Simoore Hud
123 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Alif, Laam, Raa. Lii ab Téere la bu ñu xereñe ay kàddoom, faramfàccees ko mu tukkee ca Ku xereñ ka, di Ku deñ-kumpa [Yàlla].
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
[Digaleef na leen] ngeen bañ a jaamu kenn ku dul Yàlla. Man mii dey kuy xuppe laa, di kuy waare ci yéen.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Te ñu sàkku njéggalu seen Boroom ; te dellu ca Moom, ànd ak tuub. Mu yóbbale leen xéewal yu gën ba ca àpp ba Mu ko dogale, mu jox képp ku ko yayoo ngëneel, ay ngënéelam. Waaye bu ngeen dummóoyoo, ragalal naa leen mbugal dal leen ci bis bu mag.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Ca Yàlla ngeen di dellu ; te Moom mën na lu ne.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Ndax ñoom dañuy lem seeni dënn ngir mën a nëbbu Yàlla ? Moo ndax bu ñu muurook seeni yëre, Yàlla dadul xam li ñuy feeñal ak li ñuy nëbb ? Moom dey ku xam li nekk ci xol yi la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Amul lenn luy dukkat ci kaw suuf si te sag dundu Yàlla warluwu ko te xam na saxuwaayam ak dëkkuwaayam ; lépp a ngi ci ab Téere bu wér péŋŋ [mu di Lawhul mahfuuz].
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Moom mooy ki bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-benni fan, - te fekk Gàngunaay ga ma nga ca kaw am ndox, - ngir Mu nattu leen [ba xam] kan moo gën a rafet jëf ci yéen. Te wóor na ne, boo leen waxoon ne : “Yéen ñu ñuy dekkal ngeen ginnaaw dee”, fàwwu ña weddi danañu wax ne : “Lii nekkul lu dul njibar gu bir”.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Te wóor na it ne su Nu yéexalee ci ñoom mbugal ma, jëme ko ca waxtu wu ñu dogal àppam, fàwwu danañu ne : “Lan moo ko téye ? - Te bis ba muy agsi ci ñoom, ndax dana nekk lu kenn dul mën a jiñ; te la ñu daan yéjj dana wàcc ci seen kaw.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Te wóor na it ne, su Nu mosaloon nit lenn ci Sunu yërmaande, ba noppi Nu nangu ko ci moom, kon dey dana nekk di ku ñàkk yaakaar ak fakk (sunuy xéewal).
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Te wóor na it ne, su Nu ko mosalee xéewal ginnaaw naqar wa ko daloon, dana wax ne : “Tiis teggeeku na ma”, Moom [nit] kuy bég la, di puukarewaakon.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
ba mu des ña nga xam ne dañoo muñ, di jëf jëf yu sell. Ñoom ñooña am nañu njéggal ak pey gu mag.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Xéy-na danga bàyyi lenn ca la Nu la soloo, nga ànd ci ak xol bu xat ; ngir la ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcceel ko ndàmbul alal ? ”. Walla : “Mu dikk ànd ak i Malaaka ? ” - Waaye yaw nekkuloo lu dul waarekat. Yàlla nag mooy Kuy wattu lépp lu mu mën a doon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Am dañuy wax ne : “Dakoo duur” - Neel : “Indileen fukki saar yu ni mel, yu ngeen fent. Te ngeen woo ku leen neex ndeem ñu dëggu ngeen”.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Bu ñu leen wuyyuwul, nangeen xam ne la ñu wàcce, ci xam-xamub Yàlla la, te nag amul jeneen yàlla ju dul Moom. Waaw, ndax dangeen dul wommatu nekk ay jullit ?
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Koo xam ne dundug àddina la bëgg ak taaram, Dananu leen fey seeni jëf ci biir dundu googu, te dara du wàññikuwu ci seen cëri àddina.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Ñooña ñoo dul am ca àllaaxira lu dul Safara. Te la ñu liggéeyoon yàqu na, te it la ñu doon def ag neen la.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Moo ndax ku tënku ci [Téere] ba tukkee ca Boroomam te mu am seede su tukkee ca Moom di ko jàng ci ndigalam, [dana niroo ak ñooña] ? te la ko jiitu, téereb Muusaa jaaroon na fa di gindee, di yërmaande itam. Am na ñu ko gëmoon. ku ko weddi ca sàmm sa, Safara mooy nekk li muy dajeel. Bul am benn sikki-sàkka. Te moom mooy dëgg gu tukkee ca sa Boroom ; waaye li ëpp ci nit ñi duñu gëm.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Ana kan moo gën a tooñ ku sosal Yàlla ay fen ? Ñooña danañu leen teewal, gaaral leen fa seen Boroom, seede ya daldi wax ne : “Ñii ñooy ña doon fen ci seen Boroom”. Moo ndax rëbbum Yàlla du wàcc ci kaw tooñkat yi waay !
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Ñoo di ñay wëlbati [nit ña] ngir ñu bañ a jëm ci yoonu Yàlla, di sàkkal diine ay sikk, boole ca ñoom gëmuñu àllaaxira.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Ñooña duñu mën a raw [rëcc] Yàlla ci kaw suuf si ! Te duñu mën a am ku leen wallu, deef na leen fulal mbugal ma. Ngir ñoom mënuñu woon a am dégg-dégg ak gis-gis.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Ñoo di ña yàqal seen bopp. Te xërëm ya ñu sosoom danañu leen réer.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Ca dëgg-dëgg, ñoom ñoo di ña gën a yàqule ca àllaaxira.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Ña nga xam ne way-gëm lañu, te ñu jëf jëf yu yiw te dellu ci seen Boroom, ñooña ñooy dugg Àjjana te dañu fay béel.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Niraleeb ñaari kurél yii mel na ne gumba ga ak tëx ba, ak kuy gis ak kuy dégg. Moo ndax ñaar ñooñu yem nañu te méngoo ? Moo ndax dañu dul xel-lu ?
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Yónni woon Nanu Nooh ca aw nitam, mu ne leen : “Man waarekat laa bu leen di xamal lu leer
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
te ngeen bañ a jaamu ku dul Yàlla. Te ragalal naa leen mbugalum bis bu metti dal leen”.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Ña di ay kilifa ci aw nitam, te weddi, ne ko : “Xoolewunu la lu dul ngay kenn rekk ci nun ; te it gisunu ñi la topp ñu dul ñi gën a suufe ci nun te lu yomb a gis ; te ëppalewuleen nu dara. Te sax am nanu njort ci ne ay fenkat ngeen”.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Mu ne leen : "Samaw nit ! Naka ngeen di gisee mbir mi ? Su fekkee maa ngi ci lu wér lu jóge ci sama Boroom, te Mu jox ma yërmaande ju jóge ci Moom ci lu nëbbu ci yéen, ndax dama cee ga te fekk yéen ngeen sib ko ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Te yéen samaw nit, laajumaleen ci alal. Samag pey nekkul ci kenn ku dul Yàlla. Te nekkuma ñiy dàq way-gëm, ñoom danañu dajeek seen Boroom. Waaye ni ma leen gise, aw nit ñu réer ngeen.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
te yéen samaw nit, ku may dimbali ci [mbugalu Yàlla] su ma leen dàqee ? Moo ndax dangeen dul xel-lu ?
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Te waxumaleen maa yore ndàmbi Yàlla, te xamuma it lu fàddu, neewumaleen Malaaka laa ; te waxuma it ne seeni bët a xeebu, Yàlla duleen jox yiw ; Yàlla moo gën a xam li nekk ci ñoom [su ma leen waxoon yooyu], kon ma bokk ci tooñkat yi.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Ñu ne ko : "Yaw Nooh, dàggasante nga ak nun ba ëppal ci dàggasante bi. Indil li nga nuy tëkkoo, su fekkee ne li ngay wax dëgg la”.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Mu ne : “Yàlla rekk a leen ko mën a indil - bu Ko soobee - te dungeen mën a raw.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Te lu ma leen bëgg bëgg a laabire, te [seen Boorom] namm ci yéen bew, kon laabire googu duleen jariñ dara. Ndax Yàlla moo di seen Boroom te ca Moom ngeen di dellu”.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Am dañuy wax ne : dañu koo duur ? Neeleen : “Su fekkee ne dama koo duur, sama bàkkaar ci sama kaw lay dal ! Te li ngeen di bàkkaar it ku ca set wecc laa”.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Te soloo woon Nanu Nooh [xamal ko], ne ko : “Kenn dootul gëm ci saw nit lu dul ña xas a gëm ba noppi. Kon bul jàq ca la ñuy def.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Defaral gaal ci Sunug càmm ak ci Sunu ndigal. Te bul wàqanteeti ak Man ci mbirum ñiy tooñ, ñoom dañu leen di labal”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Muy defar gaal ga. Saa yu ko kenn ci kilifay aw nitam rombee, reetaan ko. Mu ne : “Su ngeen nu reetaanee [tey jii], nun itam [dananu leen reetaan] nu ngeen nu reetaanee woon.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Xalset ngeen a xam ana kan la mbugalam di dal, toroxal ko, ba noppi mbugalam wàcc ci kawam, di lu sax dàkk ! ”
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Ba Sunu ndigal agsee, ndox ma di ballee fu ne, Nu ne : “Defal ci gaal gi, ci xeet wu nekk ñaar [góor ak jigéen] ak sa njaboot - ba mu des ña dogal ba xas dal [ña weddi] - ak ña gëm”. Te lim bu néew rekk a gëmoon.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Mu ne leen : “Yéegleen ci biir tey tudd Yàlla, mooy aw xélam, te it ag teeram. Sama Boroom nag Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Gaal gay daw ak ñoom ciy ganax yu kawe ni ay tundu. Nooh daldi woo doomam, fekk mu beru woon, ne ko : "Sama doom, yéegal ànd ak nun te bul ànd ak yéefar yi”.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Mu ne ko : “Maa ngi tëdd ci tundu doj wi, dana ma musal ci ndox mi”. Mu ne ko : “Kenn du mucc tey ci mbirum Yàlla ku dul ku Yàlla yërëm”. Noonu, am ganax [duus] wu dox seen diggante, mu daldi lab.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Waxeef na suuf si : “Wannal sa ndox mi ! Te yaw asamaan, téyal ! ”. Ndox ma daldi ŋiis, àtte ba dog, gaal ga teer ca tundu [Aljuudiyi], nu wax ne : “Alkaande ñeel na aw nit ñu di ay tooñkat” !
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Nooh daldi woo Boroomam, ne ko : "Yaw sama Boroom, sama doom ci sama njaboot la bokk, te Sab dig lu dëggu la. Te it Yaa gën a xereñ àttekat yi”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Mu ne ko : "Nooh, moom nag [sa doom jooju] bokkul ci sa njaboot, sa laaj bii itam du jëf ju sell. Te bul Ma laajati mukk loo xam ne leeru la. Te Maa ngi lay wattandikuloo ngay bokk ci ña réer”.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Mu ne : “Sama Boroom, maa ngiy sàkku ci Nga musal ma ci laaj la loo xam ne amuma ci xam-xam. Te soo ma baalul te yërëm ma, danaa bokk ci ña yàqule”.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Waxeef na ko : "Yaw Nooh, Wàccal te ànd ak mucc gu Nu la defal te barke nekk ci yaw ak ci xeet yi sosoo ci ñi ànd ak yaw. [Waaye, am na] xeet yoo xam ne Dananu leen jox ay xéewal ; ba noppi Dananu leen teg mbugal mu metti”.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Loolu bokk na ci xew-xew yi nëbb ci kumpa te Nu xamal la leen. Te xamooleen woon yaak saw nit lu jiitu lii. Nanga muñ. Ñiy ragal Yàlla ñooy am ag muj [ndam].
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Te waa Aad, seen mbokk Huud wax na leen ne : “Yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen yàlla ju dul Moom. Nekkeewuleen fa lu dul di duural Yàlla.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Te samaw nit, laajumaleen ci ag pey. Samag pey bokkul ci loxob kenn ku dul Ki ma bind [sàkk]. Moo ndax dangeen dul xel-lu ?
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Te yéen samaw nit, baaluleen seen Boroom te ngeen tuub [réccu] jëm ci Moom, kon Dana dottib taw bu jóge asamaan ci seen kaw te Dana leen yokk doole ju dolliku ci seen doole. Bu ngeen dëddoo nekk i bokkaalekat”.
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒ
Ñu ne : "Éy yaw Huud, indiloo nu lu leer, te nun dunu bàyyi sunu yàlla yi ngir say wax, te it gëmuñu la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Dunu la wax lu dul ne kenn ci sunu yàlla yi moo la sadd lu bon”. Mu ne : “Man dey, maa ngi seedeloo Yàlla - te seedelooleen yéen itam - ne deñ naa ba set wecc ci li ngeen di jaamu,
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
bàyyi Yàlla. Te fexeel-leen ma yéen ñépp te buleen xaar dara.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Man wéeru naa ci Yàlla Miy sama Boroom, di seen Boroom. Te amul luy dukkat [dox] ci kaw suuf si te du Moo cay jàpp. Sama Boroom nag Moo xàll yoon wu jub wa.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Bu ngeen ko dëddoo... man fekk na jottalinaa leen li Nu ma yónni ci yéen. Te dungeen ko wàññi dara, naka sama Boroom, Aji-sàmm lu nekk la”.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Ba Sunu dogal agsee, musal Nanu Huud ak ña gëmoon ànd ak moom ci Sunu yërmaande. Te musal leen ci mbugal mu rëy.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Waa Aad ñoom, dañoo weddi woon kàddug seen Boroom, moyoon ay Yonentam, toppoon képp kuy rëy-rëylu ci dëng.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Te tofal Nanu leen mbugal ci àddina ak su Bis-pénc baa. Waaw, moo ndax waa Aad nekkuñu woon ñu weddi seen Boroom ? Moo ndax alkaande dalul waa Aad nitu Huud ña ?
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Yónni woon Nanu it ca Samuuda, seen mbokk Saalihu, mu ne : "Yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen yàlla ju dul Moom. Moo leen binde ak suuf, Moo leen ciy dundal. Sàkkuleen njéggalam te tuub jëm ci Moom. Naka sama Boroom, Ku jegeñ la, Kuy wuyyu la [ku Koy] ñaan”.
ﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝﰞﰟﰠﰡ
Ñu ne : "Éy yaw Saalihu, nekkoon nga di ku yaakaaru ci nun, lu jiitu lii. Moo ndax danga nuy tere nu jaamu la sunu baay ya daan jaamu ? Nun, am nanu sikki-sàkka gu tar ci li nga nuy woo jëme”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Mu ne : "Yéen samaw nit! Ndax niir ngeen ba gis ne ndax nekk naa ci lu leer lu tukkee ci sama Boroom, te Mu jox ma yërmaande ju jógeci Moom, te ana kan moo may musal ci Yàlla su ma moyee [ndigëlam] ? Te kon sax dungeen ma yokkal lu dul ag yàqule.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Éy yéen samaw nit, giléemug Yàlla gii na nekk kéemaan ci yéen. Bàyyileen ko muy lekk ci kaw suufus Yàlla si, buleen ko def dara lu bon, kon mbugal dana leen dal bu gaaw ! ”
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Ñu rey ko. Mu ne leen : “Xéewluleen ci seeni kër ñetti fan ! Loolu àpp la bu dul deñ”.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Ba Sunub dogal agsee, musal Nanu Saalihu ak ña gëm ànd ak moom, - ci Sunu yërmaande - [te musal leen it] ci gàcceg bis booba. Sa Boroom nag, Moom moo di ku bari kàttan, tey Notaakoon ba.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Ña tooñoon, ag xaacu faagaagal leen. Ñu mujj ne lànjaŋ dee ca seen kër ya,
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
ñu mel ni mësuñu faa sax. Waaw, ndax waa Samuuda weddiwuñu woon seen Boroom ? Moo ndax alkaande dalul waa Samuuda ?
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Sunuy ndaw indiloon na Ibraahiima mbégte, ñu ne ko : “Jàmmi Yàlla na nekk ci yaw ! ”. Mu ne leen : “Jàmm ci yéen it ! ”, nis tuut mu indil leen sëll wu ñu wàjj.
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Ba mu gisee ne seeni yoxo laalu ko, mu am tuuma ak ug tiit ci ñoom. Ñu ne ko : “Bul ragal, nun kat dañunoo yónni ca nitu Lóot ñi”.
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Noona soxnaam sa taxawoon [foofa] daldi ree ; Nu bégal ko [te xamal ko ne dana am doom ju tudd] Isaaqa, ak ci ginnaawam Isaaqa, Yanqooba.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Mu wax ne : “Cëy man ! Ndax danaa jurati doom te màggat naa, sama boroom-kër bii it di ku mage ? Lii dey mbir mu doy waar la ! ”
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Ñu ne ko : “Ndax dangay yéemu ci mbiru Yàlla ? Yërmaandey Yàlla ak barkeem, yal na nekk ci yéen waa kër gi ! Moom Yàlla moo yeyoo cant ak màggal ko ! ”
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Ba tiit ma bàyyee Ibraahiima te mu am mbégte, jéem naa dàggasante ak Nun ci nitu Lóot ña,
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Ibraahiima dey ku lewet la, di kuy toroxlu, di ab delluwaakoon ci Boroomam.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Ñu ne ko : “Yaw Ibraahiima, génnal ci lii ndax sa ndigalul Boroom dikk na ba noppi, te ñoom, mbugal mu ñu dul delloo dana leen dikkal”.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Ba Sunuy ndaw agsee ca Lóot, mu jàq ca ñoom, am naqar ci ñoom. Daldi ne : “Lii dey bis bu tiis la”.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Nitam ña ñëw ci moom di gaawantu. Te lu jiitu loolu, dañu daan def jëf ju ñaaw. Lóot ne leen : “Yéen samaw nit, samay doom yu jigéen ñi : ñoo gën a yell ci yéen. Nangeen ragal Yàlla, te buleen ma toroxal mukk ci sama gan ñi. Ndax amul ci yéen génn góor gu jub ? ”
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Ñu ne ko : Xam nga ne amuñu soxla ci sa doom yu jigéen yi. Te yaw xam nga xéll li nu bëgg”.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Mu ne : “[Cëy !] su ma amoon dooley dal ci seen kaw ! mbaa ma mën a tàbbi ci giir gu am doole ! ”
ﯺﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝ
Ñu ne ko : “Éy Lóot, nun ay ndawi sa Boroom lanu. Duñu agsi ci yaw. Nanga rañaan yaak sa njaboot ci biir guddi gi. Te bu kenn ci ñoom gestu. Ba mu des sa soxna ndax moom lu leen dal dana ko dal. Seenub àpp ëllëg rekk la. Moo ndax suba jigeñul ? ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Ba Sunu dogal agsee, wëlbati Nanu [dëkk ba], la féete woon kaw féete suuf, Nu sotti ca kawam tawu xeer yu jóge Sijjiil [Safara] ay doj yu ñu toftale,
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
yu ñu màndargaal ca sa Boroom. Te dëkk boobu soreewul ag way-tooñ ya [ya ca Màkka].
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Yónni woon Nanu it ca waa Madyaana seen mbokk Suhaybu, mu ne leen : "Yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla ; amuleen jeneen yàlla ju dul Moom. Buleen wàññi nattukaay yi ak màndaxe yi. Gis naa ne yéen a ngi ci biiri xéewal, te ragal naa mbugal dal leen ca bis ba ëmb lépp.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Yéen samaw nit, nangeen di matal natt ak màndaxe cig maandute, te buleen wàññi dara ci lu nit ñi moom, te buleen salfaañe ci suuf si nekk yàqkat..
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Wërsëgu Yàlla moo gën ci yéen ndegam ñu gëm ngeen ! Te nekkuma di ku leen di warlul kiiraay”.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Ñu ne ko : "Yaw Suhaybu! Ndax say julli dalaa xiir ci bàyyiloo nu la sunuy baay daan jaamu, walla nu bañ a def ci sunuy alal lu nu neex ?Yaw daal, yaa di ku lewet, di ku jub ? ”
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Mu ne : "Yéen samaw nit, ndax seetlu ngeen ba xam ndax nekkuma ci lu leer lu jóge ca sama Boroom, te Mu jox ma xéewalam, mu di xéewal gu màgg ?... Te bëggumaa juuyook yéen ci lu ma leen tere. Bëgguma lu dul sellal [yéwénal] kem sama kàttan. Te samag njébbal wéeruwul fu dul ci Yàlla. Ci laa wéeru te ci Moom laay dellu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Yéen samaw nit, bëgg a wuuteek man bumu tax ngeen mel ni la daloon nitu Nooh dal leen, walla la daloon nitu Huud, walla nitu Saalihu, te sax nitu Lóot ña [fa ñu nekkoon] soriwuleen.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Nangeen baalu seen Boroom te ngeen tuub jëm ci Moom. Naka sama Boroom, ab Jéggalaakoon la ku sopp [way-gëm ña] la
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Ñu ne : "Yaw Suhaybu, amuñu ag dégg lu bari ci say wax ; te gis nanu nga nekk ku ñàkk solo fi nun. Te bu dul koon giir gi nga bokk, dananu la jam ay xeer. Nekkuloo ku tedd ci sunu kaw”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Mu ne : "Yéen samaw nit, moo ndax sama giir moo gën a tedd ci yéen Yàlla ba tax ngeen bàyyi Ko ginnaaw ? Sama Boroom nag Ku peeg la li ngeen di def.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Yéen samaw nit, defleen lu leen soob. Man it danaa def [li ma sama Boroom sant]. Dangeen mas a xam kan la mbugal di dal, gàcceel ko, ak kan mooy kay fen. Te muñandikuleen ! Maa ngi ànd ak yéen di muñ”.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Ba Sunu ndigal agsee, musal Nanu Suhaybu ak ña gëmoon ànd ak moom ci Sunu yërmaande. Ag xaacu faagaagal ña tooñ, ñu mujj xëy ne lànjaŋ dee fa seen kër ya,
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
mu mel ni masuñu fa woon a dëkk. Waaw, ndax alkaande dalul waa Madyaana na mu alake woon waa Samuuda ?.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Te yónni woon Nanu Muusaa mu ànd ak Sunuy kaawtéef ak lay yu leer nàññ,
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
ca Firawna ak boroom darajaam ya. Ñu topp ndigalu Firawna, te ndigalu Firawna jubul woon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Dana jiite aw nitam Bis-pénc ba. Tàbbal leen Safara. Ndaw tàbbikaay bu bon !
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Am rëbbu topp na leen ci àddina sii te Bis-pénc ba, yool ba ñuy am it bon na, ci aw yooliin !
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Loolu bokk na ca xew-xewi dëkk ya, Nu nettali la ko : te am na ca dëkk yooyu yu taxaw ba léegi, ak yu ñu maasale.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Tooñunuleen. Waaye ñoo tooñ seen bopp. Seen yàlla ya ñu doon jaamu, bàyyi fa Yàlla, jariñuleen dara. Ba sa ndigalu Boroom agsee, dolliwuleen lu dul alkaande.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Noonu la sa Boroom di alage, bu alagee njéndi fekk ñu tooñ. Alage ju Muy alag [ñooña], dafay metti tar.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Kaawtéef nekk na ci loolu ci ku ragal mbugalam àllaaxira. Bis boobu bis ba ñu koy dajaleel nit ñi; te bis la bu ñépp di teewe.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Yeexewuñu ko de, dafa di rekk am na dig bu ñu ko àppal.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Bu bis ba dikkee, kenn du wax ku dul ku ca am ndigal. Te ca nit ña am na ca ñu texeedi ak ñu texe.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Ña texeedi danañu nekk ca Safara di yikkat ak a jooy.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Dañu fay béel, nekk fa feek asamaan yi ak suuf si - ndare lu neex sa Boroom - ndax Moom lu ko soob Mu def ko.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏ
Ña texe, danañu nekk fa Àjjana, te dañu fay béel, nekk fa li feek asamaan yi ak suuf si ñi ngi fi - ndare lu neex sa Boroom - mu di ag may gu dul dog mukk.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Bul am sikki-sàkka ci la ñooñu di jaamu. Ci ña seeni baay daan jaamu bu jëkk rekk lañuy jaamu. Te Nun Dananu mottali seeni cër, te dara du ca wàññiku.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Joxoon Nanu Muusaa Téere ba. Ñu wuute ca. Bu dul koon sa kàddug Boroom jiitu woon, kon àtteef na seen diggante. Te ñoom dañu caa am sikki-sàkka gu tar.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Fàwwu ñoom ñépp sa Boroom Dana matal seen peyug jëf... Naka Moom ku xam xéll la li ñuy jëf.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Jubal [yaw Muhammad] ni ñu la ko digle, ak képp ku tuub ànd ak yaw. Buleen beew. Moom Yàlla mi ngi ne jàkk ci li ngeen di def.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Buleen jeng féetéek tooñkat ya : kon Safara laal leen. Te dungeen am ku leen di yiir ku dul Yàlla. Te it kenn du leen dimbali.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Nanga taxawal julli ci yaari cat yi séq bis bi ak li bokk ci guddi. Jëf yu baax yi dañuy far jëf yu ñaaw ya. Loolu ag waare la ci ñuy waaru.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Nanga muñ. Yàlla dey du sànk peyug ñay rafetal.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Lu taxoon ca xarnu ya leen jiitu, ñu baax ña [dese woon yan bi] nekkoon ñu néew, ñoom ña daan tere lu bon ci suuf sa ! Ñu bokk ca ña Nu musaloon te ñu tooñoon, topp seeni bakkan ca xéewal ya ñu donnoon ay bàkkaarkat.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Sa Boroom du alag lenn njénde ci ag tooñeel fekk aw nit di sellal seeni jëf.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Bu sooboon sa Boroom mu def nit ñi ñu nekk di wenn xeet doŋŋ. Waaye duñu deñ di wuute
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
ndare ña sa Boroom yërëm. Loolu moo tax Mu bind leen. Te it moo tax sa kàddug Boroom mat ca la mu wax ne : “Danaa feesal Safara ci aw nit ak i jinne mbooleseen”.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Te lépp Lanu lay nittili ci xew-xewi Yonent ya, Danu cay dalal sa xel. Te dëgg ak ug waare dikkal na la di aw lay ànd ak di fàttali ci ñi gëm.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Te waxal ña gëmul ne leen : “Defleen lu leen soob. Nun it, nu ngiy jëf [li nu sunu Boroom digal].
ﮌﮍﮎﮏ
Xaarleen. Nun it noo ngi xaar ! ”
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Yàllaa moom kumpag asamaan yi ak suuf si, te mbir yépp ca moom lañuy dellu. Kon nag jaamu ko te nga wéeru ci moom. Sa Boroom ñàkkul paal ci li ngeen di def de.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers