Simoore An-Naml
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore An-Naml pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore An-Naml pdf Wolof — Wàcce Simoore An-Naml Tekki. An-Naml (Meccan) 93 Aaya.
Related
- An-Naml TekkiWolof
- An-Naml mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore An-Naml

ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Taa, Siin. Lii ay laayay Alxuraan la tey tere bu bir, leer nàññ,
ﭙﭚﭛﭜ
di njub ak mbégte ci way-gëm ñi,
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
ñay taxawal julli tey génne asaka te wóolu ne àllaaxira am na.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Ña gëmul àllaaxira, taaralal Nanu leen seeni jëf, ñuy tañax-tañaxi.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Ñooñaay am mbugal mu tiis te ca Bis-pénc ba, ñooy ña yàqule.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Yaw Muhammad, Alxuraan jii Nu lay jox, ma nga bawoo ca Ku xereñ, Ku xàmme.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
(Fàttalikul) ba Muusaa waxee njabootam ne leen : "Séen naa aw safar ; xaarleen ma, danaa leen fa jëlale xibaar, walla ay xal yu ngeen jaaroo ".
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Ba mu fa eggee, mu am lu ko woo ne ko. - barkel nañu Ki nekk ci safara si ak ñépp ñi ko wër, tudd naa sellug Yàlla miy Boroom àddina si.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
"Yaw Muusaa, yégal ne Maay Yàlla, Boroom kàttan, di Ku xereñ ki”.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Te : “Nanga sànni sa yet wi”. Ba mu ko gisee muy yëngantu mel ni jaan, mu tiit bëgg a daw. “Éy yaw Muusaa. Bul ragal, Yonent yi duñu ragal ci sama wet.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
u dul kuy tooñ te ginnaaw ba mu soppi ñaawtéef ak lu rafet... naka Man Jéggalaakoon laa, Jaglewaakoon laa”.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Sóobal sa loxo ci sa mbubbu. Dana génn weex tàll - muy benn ci juróom-ñeenti kéemaan yi jëm ca Firawna ak u nitam, ñoom ay saay-saay lañu woon”.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
Ndax ba leen Sunuy laaya dikkalee, leer nàññ, dañoo wax ne : “Lii ag njibar la gu bir ! ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Weddi nañu ko waaye seeni xol gëm na ko, xanaa kay rëy a leen jàpp. Xoolal nag yàqkat naka la ñuy mujje.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Joxoon Nanu Daawuda ak Suleymaan xam-xam ; ñuy wax naan : “Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla, Moom mi nu gënal ci kaw nit ñu bari ñi bokkoon ci jaamam ñi gëm”.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Suleymaan wuutu na Daawuda, daldi ne : “Éy yéen nit ñi ! Xam naa waxi picc yi ; te am naa lu ne. Loolu mooy ngëneel lu bir.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Dajaleef na Suleymaan ak i xaritam, cij jinne yeek nit ñi, ñu def i sàppe.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Ba ñu agsee ca xuru xorondom ya, mu am xurondom wu wax ne : "Éy yéen xorondom yi, dugguleen ci seeni biir kër, balaa leen a Suleymaan ak i xaritam di nappaaje te duñu ko sax yëg”.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
[Suleymaan] muuñ, daldi ree ndax wax jooju, daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, Nanga baaxe may sant ci xéewal gii Nga ma dafal maak samay waajur, te may jëf jëf ju baax Joo gërëm te Nga may ma ci Sa yërmaande ma bokk ca Sa jaam ñu yiw ña”.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Mu nemmiku njanaaw ya, daldi ne : “Lan moo tax gisuma Muusaa-njuburi ? Walla nekku fi?
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Danaa ko mbugal mbugal mu tar ! Walla ma rendi ko ! Walla mu indil ma lay wu wér”.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Mu sax fa tuuti, [picc] ma dellusi ne ko : “Xam naa loo xamul te indil naa la xibaar bu wóor bu bawoo réewum Sabaa” :
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Fekk naa leen ñu am buur bu jigéen, am na lépp, am it gàngunaay gu rëy.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Fekk naa ko it mook aw nitam ñuy jaamu jant bi bàyyi Yàlla. Séytaane taaralal leen jëf jooju, wëlbati leen ñu dëddu yoonu Yàlla ba gëmuñu.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Moo ndax duñu jaamu Yàlla Miy génne li nëbbu ci asamaan yeek suuf si, te Moo xam li ngeen di nëbb ak li ngeen di feeñal ?
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
[Cëy] Yàlla ! Jeneen yàlla amul ju dul Moom, Mooy boroom gàngunaay [Aras] gu màgg ga.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Suleymaan ne ko : “Dananu xool ndax wax nga dëgg walla dangay fen.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Jëlal sama bataaxal bii ; boo demee nga sànni leen ko ; te dëppal xool ba xam na ñuy def.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Buur ba [Balxiis] ne leen : "Kilifay dëkk bi ! Man dey, sànni nañu ma bataaxal bu tedd.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Mi ngi bawoo ca Suleymaan : “Ci turu Yàlla la Miy Yërëmaakoon, di Jaglewaakoon,
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Buleen rëy-rëylu ci sama kaw te ñëwleen jébbalusi seen bopp”.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Buur ba ne gàngooram : "Ubbileen sama bopp ci mbir mii : masumaa dugg ci menn mbir
te joxewuleen ci xalaat”.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Ñu ne ko : “Nun am nañu dooleek alal te yaay digle. Seetal loo nuy digal”.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Buur ba ne leen : “Buur yi dey, bu ñu duggee cib dëkk, yàqate ko, daldi toroxal ña fa gënoon a tedd. Ñoom noonu la ñuy def.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Man, dama leen di yónnee alal [neexal], su ma ko defee nag xool lu ndaw ya di delloosi”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
[Ba ndaw ya àggee] ca Suleymaan, mu ne leen : “Yéen daal dangeen may jéem a gere alal ? Maa leen ko gënle fuuf. Mbaa du ! Lii doŋŋ la.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Dellul ca ñoom. Neleen danaa leen indil xare bu ñu dul mën a dékku. Te danaa leen fa génne toroxal leen ba ñu ne tott.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Suleymaan ne : "Yéen kilifa yi ! Ana kan moo may indil gàngunaayam ba la ñoo agsi di jébbalesi seen bopp ? ”
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Mu am jinne ju ne ko : “Mën naa la koo indil bala ngaa jóge fii nga toog : Mën naa ko te wóor na”.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Ka ame woon xam-xamu Téere ba ne ko : “Mën naa la koo indil ba la ngaa xef”. [Ne ko mingi nii] , ba ko Suleymaan gisee ci kanamam, dafa wax ne : “Lii dey ngënéelul sama Boroom bi la. Dama ciy nattu ndax damay sant walla damay xarab... képp kuy sant yaw caak, ku weddi nag, sama Boroom moom di Ku doylu, di Ku tedd”.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Suleymaan réerantal leen, toog na di xool ndax dana gindiku am déet.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Ba Balxiis agsee, ñu ne ko : “Ndax lii mooy sa toogu ba ? ” Mu ne : “Mel na ni moom la de”. - [Suleymaan ne]: “Am nanu xam-xam lu ko jiitu ba tax na nu jébbalusi”.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Li mu daan jaamu bàyyi Yàlla moo ko fàbbi woon, ndax dafa bokkoon ci askanu yéefar.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝﰞﰟﰠﰡﰢﰣﰤ
Ñu ne ko : “Dugal ci njénde li”. Ba mu ko gisee, mu njort ne am ndox la, daldi wog i yeelam. Suleymaan ne ko : “Njénde li ay weer la ñu ko defare”. - Balxiis daldi ne : “Yaw Boroom bi, tooñaan naa sama bopp : Tey jii nag, jébbalu naa ànd ak Suleymaan dib jullit ngir Yàlla jiy Boroom àddina si”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Yónnee woon Nanu ca Samuuda seen mbokk Saaliwu. Mu ne leen : “Jaamuleen Yàlla”. Ndekete yoo dañoo séddalikoo ñaari kurél di xulloo rekk.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Mu ne leen : "Éy samaw nit, lu tax ngeen di gën a yàkkamti lu bon ci lu baax ? Céy bu ngeen jéggalu woon Yàlla ? Kon xéy-na Mu yërëm leen.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Ñu ne ko : “Gaafal nanu la yaak ña nga àndal.”. Mu ne leen : “Kon dey cig sànje ngeen di sax ndax li ngeen di gaafal moo nekk fa Yàlla.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Mu amoon kurél bu nekkoon ca dëkk ba di juróom-ñeenti nit, daan yàq rekk te daawuñu defar.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Ñu wax ne : “Nanu waatoo ci Yàlla rey ko mook njabootam. Bu ñu xëyee ba ñay dese mbir ma laaj nu, nu tontu ne : “Nun kat teewewunu woon seenug rey”.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Ñangay fexe am pexe, Nun it Noo ngi fexe am pexe te ñoom yéguñu ko.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Xoolal naka seen pexe ya mujje woon : Danu leen a faagaagal ñook seeni xeet wépp.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Seen kër yaa ngi noonu gent na ngir la ñu tooñoon. Ay kéemaan a ngi ci loolu ngir aw nit ñuy xam.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Te musal Nanu ña gëmoon te ragal Yàlla.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
[Fàttalikul] Lóot, ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Ndax dangeen di def ñaawtéef te ne ca jàkk”.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Ndax dangeen di gën a xemmem góor ñi bàyyi jigéen ñi ? Yéen daal aw nit ñu réer ngeen.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Nitam ña tontuwuñu lu dul ne : “Génneleen njabootug Lóot ci seen dëkk bii ! Ndax ñoom dañuy jéem a laab-laablu.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Nu daldi koy musal mook njabootam ga ba mu des soxnaam sa àndoon ak defkatu ñaawtéef ya Nu faagaagal.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Dotti Nanu ca seen kaw waamem [doj]. Ndaw taw bu bon ca ña mu dal ca seen kaw!
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Waxal : “Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla te yal na jàmm wàcc ci kaw jaamam ña Mu tànn ! ” Waaw! Ana lan moo gën : Yàlla walla li ngeen di bokkaale ?
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Ana kan moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si te Mu wàcceel leen am ndox mu bawoo asamaan, daldi cay saxale ay tool yu taaru yoo xam ne mënuleen ko woon a saxal. Moo ndax dafa am jeneen yàlla juy ànd ak Yàlla ? [Amul], ñoom kay fu ñu toll ña ngay jéem a utal Yàlla ndend.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Ana kan moo waajal suuf si ba mu doon dëkkuwaay, mu def ci biir ay dex ak tundi doj te def ci diggante ñaari géej yi ay téq [muy tax ndox mu neex mi ak mu xorome mi duñu jaxasoo], - Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla ? Déedéet amul, waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Ana kan mooy wuyyu boroom tiitaange saa yu Ko woowee, ana kan it mooy dindi njàqare ji, te def leen ngeen wuutu ko ci suuf si, - Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla? [Déedéet amul]. Li ñuy fàttaliku moo néew doŋŋ !
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Ana kan moo leen di gindi ci lëndëmug jéeri jeek géej gi, tey yebal ngelaw liy bégle ci yërmaandeem [xamle taw buy bëgg sóob]. Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla ? Déedéet [amul de]. Yàlla kawe na li ñu koy bokkaaleel.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Ana kan mooy tàmbali sosu ga, topp Mu di ko delloosi, ana kan moo leen di dundal ci la bawoo asamaan ak suuf. Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla ? [Déedéet amul de]. Neeleen : “Indileen seen firnde ndegam wax ngeen dëgg ! ”
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Neel : “Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si, kenn xamu ci kumpa ku dul Yàlla”. Te it xamuñu kañ la ñuy dekki !
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Seeni xam-xam soriwul ci mbiri àllaaxira. Ñoom sax dañu cay sikki-sàkka. Te ñoom sax ay gumba lañu ci mbir moomu.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Yéefar yaa ngay wax naan : “Ndax [ginnaaw ba ñu faatoo] ba doon suuf nook sunuy baay, dananu génnaat suuf [dekki] ?
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Lii daal digoon nañu nu ko nook sunuy baay. Lii du dara lu dul léebi mag ñu jëkk ña ! ”.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Neeleen : “Doxleen ci suuf si [wëréelu] te ngeen xool naka la tooñkat ya mujje”.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Bul jàq ci ñoom te seeni pexe itam bu mu la xatal.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Ñangay wax naan : “Dig bi moom kañ lay doon ndegam wax ngeen dëgg ? ”
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Neel : “Amaana lii ngeen di yàkkamtee ngi ci seen kaw”.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Te nag sa Boroom aka bari ngëneel yu Muy jox nit ñi, waaye li ëpp ci ñoom duñu sant.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Te it sa Boroom xam na li ngeen rënk ci seeni dënn ak li ngeen di feeñal.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Te it amul lenn lu fàddu nekk ci asamaan si walla ci suuf si te dul ne nekk na ci biir ab Téere bu ñu faramfàcce.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
Alxuraan jii dafay nettali ci giir Bani-Israayiila, li ëpp ci la ñu daan juuyoo ak a wuute,
ﭑﭒﭓﭔﭕ
Te Alxuraan jooju njub la ak yërmaande ci képp ku gëm [di ab jullit].
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Sa Boroom dana àtte seen diggante ci àtteem yi ; Mooy Boroom kàttan ga, di Ku xam.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
[Yaw Muhammad], nanga wéeru ci Yàlla, [te xamal it ne] yaa ngi ci dëgg gu bir.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Mënoo tax ku xas a dee ba noppi di dekki, mënoo tax it ab tëx dégg woote ba, saa su la wonee ginnaaw dummóoyu.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Mënoo gindi gumba yi ci seenug réer. Ñi lay déglu kay ñooy ña gëm Sunuy kàddu te doon ay jullit.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Saa su wax ja tàbbee ci seen kaw, Dananu leen génneel benn mala buy wàqanteek ñoom ne : Nit ñi gëmuñu woon Sunuy kàddu, kéemaan.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Bu keroogee Bis ba Nuy pang, ci wépp xeet ay mbooloo yu daan jàppe Sunu kàddu yii ay fen [di ko weddi], Nu def leen ñu di ay sàppe.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Bu ñu agsee, [Yàlla] ne leen : “Waaw, yéen a daan weddi Samay kàddu te xamuleen ci woon dara ? Walla lan ngeen daan def ? ”
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Su wax ja agsee ci ñoom, seen tooñ ga dana tax duñu àddu.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Ndax dañoo gisul ne [Man Yàlla] maa leen defal guddi ngir ñu di ca dal-lu, def bëccëg muy yëngukaay ? Ay kéemaan nekk na ci biir loolu ngir ñi gëm.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Bu keroogee Bis ba ñuy wal buftu bi, ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ñoom ñépp danañu tiit, ku dul ku soob Yàlla ! – Ñoom ñépp danañu dikk fa Yàlla te tott.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Ngay gis tundi doj yi foog ni dafa taxaw benn barab, te fekk na booba ñangay daw niw niir. Loolu mooy liggéeyub Yàlla. Te Mooy Xereñaakoonub mépp mbir, te Ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Moo ndax du ku indi ag yiw dana ca ame pey gu ko gën, te bu Bis-pénc baa dana mucc ci am tiit.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Te it képp ku indig jëf ju ñaaw... dees na nargan seeni kanam ca safara. Te la ñu defoon doŋŋ la ñu leen di feye ”
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
“[Man Muhammad] daal, digaleef na ma may jaamu Boroom dëkk bii Mu wormaal, - te Moo moom lu ne - digaleef na ma it ma bokk ca jullit ña, jébbal ko sama bopp,
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Ak it ma nettali Alxuraan”. Képp ku gindiku, mook boppam. Képp ku ko mën a réer..., yaw neel : “Man daal damay xuppe doŋŋ”.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Waxal ne : “Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla ! Dana leen won ay kéemaan, firndeem ngeen di ko xam”. Te sa Boroom sàgganewul li ñuy def.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







