Simoore Fatir
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Fatir pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Fatir pdf Wolof — Wàcce Simoore Fatir Tekki. Fatir (Meccan) 45 Aaya.
Related
- Fatir TekkiWolof
- Fatir mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Fatir

ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla mi bind asamaan yeek suuf si, Mooy ki def Malaaka yi ñu di ay ndaw te di woroomi laaf, ñaar-ñaar, ñett ñett walla ñeent ñeent. Mooy dolli ca mbind ga lu ko soob, Yàlla mën na lépp lu nekk.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Li Yàlla di ubbil nit ñi ci yërmaande, kenn mënu koo fànq, lu Mu tëj itam, kenn mënu koo tijji ginnaawam. Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Éy yéen nit ñi ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ci yéen : moo ndax amuñu bindkat bu dul Yàlla, bu leen di wërsëgal ci asamaan yeek suuf si ? Amul jeneen yàlla ju dul Moom ! Moo yéen ndax mën ngeen koo dummóoyu ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Bu ñu la weddee it, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu woon. Te ca Yàlla la mbir yi di mujj.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Éy yéen nit ñi ! Li Yàllay dige dëgg la. Buleen dundug àddina bii di fàbbi, buleen Séytaane tax a fakku ci Yàlla.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Séytaane, seenub noon la. Nangeen ko jàppe ab noon. Li muy woote di ci xiirtal gàngooram moo di ngir ñu nekk waa Safara doŋŋ la.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Ña weddi, mbugal mu metti dana leen dal, ña gëm nag tey jëf u yiw, danañu am njéggal ak pey gu rëy .
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Naka kay jàppee ñaawtéefam ya muy lu rafet... ? – Yàllaay réeral ku ko soob, di gindi ku ko soob – Bul sonnal sa bopp ci ñoom : Yàlla xam na xéll la ñuy def.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Yàlla miy yebal ngelaw muy niir, Nu wommat ko jëme ko ci dëkk bu deewoon ; di ca dundal suuf si ginnaaw ba mu deewee. Noonu la Dekki di ame.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Képp kuy bëgg kàttan , na xam ne kàttan ba kàttan jeex, Yàllaa ko ame : ca Moom la wax ju yiw di yéeg ak jëf ju yiw, Mu di ko yékkati. [Waaye] ñiy fexe ay ñaawtéef, am nañu mbugal mu tar. Te seeni pexe du joy mukk.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝﰞ
Yàlla moo leen bind ci suuf ba eggal, def leen ay lumb deret, topp Mu def leen ay yóllent [góor ak jigéen]. Amul jenn jigéen juy ëmb walla muy imbi lu dul ci xam-xamam lay ame. Amul it genn dundu guy yokk walla muy wàññiku te duwut ne mi ngi ci ab Téere . [Loolu] yomb na lool ca Yàlla.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Ñaari géej ya yemuñu : gii dafa neex a naan te lewet domm, gee saf xorom te naqari. Ngeen di ca génnee aw yàpp wu tooy di ko lekk, ngeen di ca génne itam gànjar gu ngeen di sol. Nga gis gaal ya di jax ca biir ngir sàkku ci ay xéewalam. Ak it ndax amaana ngeen sant.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Mooy dugal guddi ci bëccëg, di dugal bëccëg ci guddi. Di tàggat jant beek weer wi. Lu ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal. Kooku moo di Yàlla : seen Boroom moo moom nguur, te li ngeen di jaamu bàyyi ko, amuñu sax lu tollu ni kem mbuusum xooxu tàndarma.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Bu ngeen leen di woo, duñu leen dégg ; bu ñu leen déggoon it, duñu leen tontu. Bu Bis- pénc baa, danañu teggi ba mu set li ngeen ko doon bokkaale. Amul kenn ku la mën a jox xibaar yu wére nii.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Éy yéen nit ñi, yéen ay soxlaa woo Yàlla, waaye Yàlla moom Ku doylu la ci boppam, di Yeyoowaakoonu cant.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Su ko neexoon Mu yóbbu leen, indi ñeneen mbindeef yu bees.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯙ
Te loolu du lu jafe ci Yàlla.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Kenn du yenu bàkkaarub keneen. Te képp ku diis gann ak bàkkaar, bumu cay woote ndimbal, kenn du ko yenul dara, doonte la sax dafa di mbokkug jegeñaale. Da di rekk ne nangay xupp ña di ña ragal seen Boroom ci kumpa tey taxawal julli. Te képp ku cay sellal, na xam ne boppam la koy defal, te ca Yàlla la lépp di mujj.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
Gumba ak njàccaar niróowuñu.
ﭖﭗﭘﭙﭚ
du caagene lëndëm ak leer.
ﭛﭜﭝﭞﭟ
du caagene ker ak naaj.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Ñiy dundu it niróowuñook ñi dee. Yàlla dina déggloo ku ko soob, te yaw Muhammad mënoo déggloo ñi xas nekk ci biiri bàmmeel.
ﭳﭴﭵﭶﭷ
Yaw daal nekkoo lu dul ab xuppekat
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Yónni Nanu la ci dëgg ngay bégalekat di ab xuppekat, amul wenn xeet wu amul ab xuppekat.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Su fekke ne dañu laa weddi, [xamal ne] am na ñu leen jiitu woon te daan weddi, ndax seeni Yonent indiloon nañu leen ay laaya, ay firnde yu bir ak ay mbind ak ab Téere bu leer.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Ginnaaw ba, Ma jël ña weddi. Cëy na Ma leen jële.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Xanaa gisuloo ne Yàlla moo wàcce ndox mu bawoo ci asamaan si ? Nu daldi cay génne ay meññent yu wuute ay wirgu. Am na it ci tundi doj yi yuy sësëloo te weex, ak yuy xonk, yu wuute ay wirgu, ak yu ñuul kukk.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Am na it ci nit ñi, ci daaba yeek mala yi yu wuute ay wirgu, noonu rekk la. Jaami Yàlla yi ko ragal ñoo di woroom xam-xam yi. Te Yàlla boroom xam-xam la, di Jéggalaakoon.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Ñay jàng Téereb Yàlla ba, tey taxawe julli, tey joxe ci [alal] ji Nu leen wërsëgale, ci lu nëbbu ak ci lu feeñ, ñoom yaakaar nañu am njula mu dul yàqu.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
loolu lépp ngir Yàlla jox leen seenug pey te dolli leen ciy ngënéelam. Moom Yàlla, Jéggalaakoon la, Kuy sant la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
La Nu la soloo ci Téere bi mooy dëgg tey saxal la ko jiitu woon . Yàlla kuy Xàmmee la, Kuy Gis jaamam ñi la.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Ginnaaw ba, donnale Nanu Téere ba sunu jaam ña Nu tànn. Am na ci ñoom kuy tooñ boppam, am na ci ñoom ñuy yamamaay, am na it ci ñoom ñuy jëkkante ciy jëf yu baax ci ndimbalu Yàlla ; loolu nag tigi mooy ngëneel la gën a màgg.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Àjjanay Hadan yoo xam danañu ca dugg, ñu di leen fa sadd ay lami wurus ak peme ; te seenug col ca biir àjjana yooyu sooy lay doon.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Ñuy wax naan : “Xeeti cant yi ñeel na Yàlla, Yàlla mi nu dàqal tiitaange. Sunu Boroom daal Jéggalaakoon la buy Yayoowaakoonu cant.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Moom mi nu dalal ci kërug nooflaay ci mbaaxam, coono dunu fa dab, jaaxle it dunuu fa dab”.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Ñay weddi nag, ñoom Safara la ñuy dëkk : ñu di leen xorñoññal, duñu dee ; te it deesuleen woyofalal mbugal ma. Noonu la Nuy feye képp ku di ab weddiwaakoon.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Ña ngay yuuxu ca biir, di wax naan : “Yaw sunu Boroom, génne nu ; kon dey dananu jëf u yiw, wu bokkul ak la ñu daan jëf ”. “Waaw, moo ndax dundalunuleen fa woon diir bu tax, ña fàttaliku ñépp, fàttaliku nañu ca ? Te ay xuppekat it dëkkaloon nañu leen. Kon book, toqamtikuleen mbugal mi. Tooñkat yi, kenn duleen dimbali”.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Yàllaa xam kumpag asamaan yeek suuf si. Moom ab Xamaakoon la li nekk ci dënn yi .
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Moo leen def ngeen di ay kuutaatam ci kaw suuf si. Képp kuy weddi, weddeem ga dana daanu ci kawam. Te yéefar ya, seenug weddi duleen dolli lu dul jéppig Yàlla. Te it seen weddi googu duleen dolli lu dul yàqule.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Neel : “Ndax gis ngeen ñi ngeen bokkaleek Yàlla, di leen jaamu ? Wonleen ma ñoom ana lan la ñu bind ci kaw suuf si. Walla dañoo am sañ-sañ ci asamaan yi ? Walla dañu leen a joxoon Téere bu leen bir” Déedéet ! Li am kay moo di ne tooñkat ñi ñoom wor rekk la ñuy digante.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Yàlla moo téye asamaan yeek suuf si ba daanuwuñu. Te bu ko dindi woon it, amul kenn ci ñoom ku ko cay téye ginnaawam. Moom Yàlla ab Jéggalaakoon la, ku Lewet la.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Dañu daan waat ci Yàlla fu ngiñ gën a ñàngee, di wax naan : su leen ab xuppekat dikkaloon, ñooy gën a gindiku weneen xeet wu dul ñoom. Waaye ba leen ab xuppekat dikkalee , dolliwuleen lu dul dummóoyu .
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
[Te dara waralu ko] lu dul rëy-rëylu ak pexe yu bon. Te pexe mu bon du rey lu dul boroom. Te ñoom néggandikuwuñu lu dul xew-xew ya leen jiitu woon ? Te tëralinu Yàlla kenn du ko sopparñi, te kenn it du ko wëlbati.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜ
Moo ndax dañoo doxul ci suuf si tey xool mujjug ña leen fi jiitu woon te ëppoon leen doole ? Amul dara lu mën të Yàlla ci asamaan yeek suuf si. Moom Yàlla kuy Xam la, kuy Mën la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Su Yàlla doon jàppe nit ñi ci li ñuy def. Kon du bàyyi kenn kuy dox ci kaw suuf si. Waaye daleen di xaare àpp ba Mu àppal. Cëy bu dig ba agsee... [danañu xam ne] Yàlla kuy gis jaamam ñi la.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







