Simoore Saba
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Saba pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Saba pdf Wolof — Wàcce Simoore Saba Tekki. Saba (Meccan) 54 Aaya.
Related
- Saba TekkiWolof
- Saba mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Saba

ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Cant ñeel na Yàlla, Yàlla mi moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Cant it ñeel na ko ca àllaaxira. Moo di Ku Xereñ, di Ku Xàmmee.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Xam na li duggu ci suuf ak la cay génne, ak lay wàcc ci asamaan si ak la cay yéeg. Mooy Jaglewaakoon ba, di Jéggalaakoon ba.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Yéefar yaa ngay wax naan : “Bis-pénc ba du ñëw”. Waxal ne : “Axakañ. Giñ naa ci sama Boroom ! ne dana leen dikkal. Moom mi xam kumpa. Te dara lu tollu ni aw pepp du ko lënt ci asamaan yeek suuf si. Walla lu ko gën a tuuti, walla lu ko gën a rëy, lu dul ne mi ngi ci ab Téere bu bir.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
[Li waral Bis ba], ngir fey ña gëmoon tey jëf u yiw. Danañu am njéggal, ak teraanga ak i xéewal.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Ña doon dëgërante bopp te Sunuy laaya nag ñoom, danañu am mbugalum kaŋ-kaŋ mu metti.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Woroom xam-xam ya danañu gis ne li Nu wàcce ci yaw mu bawoo ca sa Boroom, mooy dëgg te dafay gindee jëme ca yoonu Yàlla wu jub wa xocc, Yàlla miy boroom kàttan, di Yayowaakoonu cant.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Ña weddee ngay wax naan : “Ndax dunu leen tegtal ci waa joo xam ne nee naay su ngeen deewee ba daggatoo, di ngeen dekkiwaat?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Moo ndax dafay sosal Yàlla ay fen ? Walla jinne dakoo sadd ? ” La am kay moo di ña gëmul àllaaxira ñanga ca mbugal ak réer gu sori.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Ndax dañoo gisul li leen wër ci asamaan ak suuf ? Su Nu sooboon, mën Nanu leen a jaxaseek suuf si, walla Nu rotale ay dogit yu bawoo ci asamaan si. Ay kéemaan a ngi ci loolu ngir bépp jaam buy delluwaakoon ci Boroom bi .
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Joxoon Nanu Daawuda ngëneel lu bawoo ci Nun. Doj yeek njanaaw yi ànd ak moom di sàbbaal. Te it nooyalaloon Nanu ko weñ gu ñuul.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
(ne ko) : “Liggéeyal ay mbubbi koŋ te jekkal ko”. Te ngeen di jëf u yiw. Kuy gis laa [Man Yàlla] li ngeen di def.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Tàggataloon Nanu Suleymaan ngelaw li, am xëyëm doxub weer la woon, am ngontam it, doxub weer la woon. Nu nooyalaloon ko bëtub mbellum përëm. Amoon na ci jinne yi ñu koy liggéeyal ci ndigalul Yàlla. Ku ca fétt nag, Dananu ko mosal mbugalum safara.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Ñu di ko liggéeyal lu ko soob : ci ay tabax ak i bóoli yu tollu ni ay xur, ak i kawdiir yu ñu sësale. “Yéen waa kër Daawuda, gërëmleen Yàlla”, te néewaana mu am ci sama jaam yi ay santkat.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Ba Nu dogalee mu war a dee, la leen ko xamal moo di max ga lekk yetam wa. Ba mu daanoo, jinne yi daldi xam ne bu ñu xamoon kumpa, duñu sax ca mbugal moomee daan leen tax a doyadi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Waa réewum Saba amoon nañu màndargam ñaari dër ci ndeyjoor ak càmmooñ. “Lekkleen ci xéewali Yàlla, mayi seen Boroom, te ngeen sant Ko ndax : may na leen dëkk bu teey, neex, te di Boroom biy Jéggalaakoon”.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Waaye dummóoyu woon nañu . Nu daldi leen yebalal mbënnum téqum ndox ma, Nu daldi leen soppil seen tooli dër y, def leen ay tool yu am meññent mu sëcc ak i gargamboose ak i siddéem juy néewal.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Loolu la Nu leen feye woon ngir seenug weddi. Moo ndax Dananu ko feye keneen ku dul ñuy weddi ?
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Te defoon nanu seen digganteek yeneen dëkk ya barkeel, ay dëkk yu fés, te nattle woon Nanu seenug demlante. “Demlanteleen ci guddi mbaa bëccëg ci kóolute”.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, dandaleel sunuy diggantey dëkk”, daldi tooñ seen bopp. Ba mujj di ay waxtaan ndax téqale Nanu leen. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir bépp muñaakoon buy sant.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Séytaane dëggalal na leen njortam. Ñoom ñépp daldi koy topp ba mu des ab kurél bu néew ca way-gëm ña.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Amul woon ci ñoom benn mën-mën lu dul ngir Nu xam ña ca gëm àllaaxira ak ña koy sikki-sàkka. Sa Boroom mooy wattu lépp lu ne.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Waxal ne : “Li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla. Amuñu lu tollu ni kem aw fepp ci asamaan yeek suuf si. Bokkuñu ci, ci dara, te it kenn dimbaliwu ko woon ci ñoom”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Tinu mënu la jariñ dara fa Moom [Yàlla], lu dul ka Mu ca jox ndigal. Bu tiit ma duggee seeni xol nag, ñu naan : “Lan la seen Boroom wax nag ? ”. Ñu ne leen : “Dëgg rekk ; Te Moom moo di Ku Kawe, di Ku Màgg ka”.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Neel : “Ana kan moo leen di wërsëgal ci asamaan yeek suuf si ? ”. Waxal ne : “Yàlla. Te Nun ak yéen, ana kan moo nekk ci njug walla réer gu bir”.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Neel : “Kenn duleen laaj li nuy def, te it kenn dunu laaj li ngeen di def”.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Waxal ne : “Sunu Boroom dananu dajale, daldi Nuy àtte ci dëgg, Mooy ubbiwaakoon bu xam ba”.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Waxal ne : “Wonleen ma ña ngeen daan bokkaaleek Yàlla. [Mukk] ! Li wér moo di ne Mooy Yàlla, di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ”.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Yónniwunu la [yaw Muhammad] lu dul nga daj képp nit ñi, di béglekat, di xuppekat. Waaye li ëpp ci nit ñi duñu xam.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Ñuy wax naan : “Dig ba kañ lay doon su fekkee ne li ngeen di wax dëgg la ? ”.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Waxal ne : “Am ngeen digub Bis boo xam ne dungeen ko jiitu, dungen ko yées ! ”.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Yéefar ya nee nañu : “Duñu gëm Alxuraan walla lu ko jiitu”. Cëy boo gisoon tooñkat ya
bu keroogee ba ñu taxawal leen ci seen kanamu Boroom, nga gis leen ñuy wàqante ! Ña néewoon doole di wax kilifa ya, naan leen : “Bu dul kon ak yéen, ay jullit la nuy doon”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Ña ca doonoon kilifa wax ña ca néewoon doole, ne leen : “Ndax Nun noo leen féewale woon ak njub ga ca ba mu leen dikkalee ? Li wér kay mooy yéen ay tooñkat ngeen”.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Ña ca néewoon doole wax ña ca doonoon ay kilifa, ne leen : “Moom ngeen daan fexe guddi ak bëccëg, ndax yéen a nu daan digal nuy weddi Yàlla, di ko sàkkal ay bokkaale”. Daldi nañu rëccu ba ñu gisee mbugal ma. Nu daldi def ay jéng ca loosi ña weddi : moo ndax feyewuñu leen lu dul la ñu daan def ? ”
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Amul benn dëkk bu Nu mës a yebal ab xuppekat lu dul ne kilifa ya dañuy wax naan : “Nun dey weddi nanu lii ñu leen yónni”.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Ñuy wax it naan : “Nun noo leen ëppale alal ak i doom te sax kenn dunu mbugal”.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëg, di ko xatal it. Waaye li ëpp ci nit ñi waxuñu”.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Nekkul ne seeni alal walla seeni doom ñoo leen di tax a jegeñ Yàlla. Lu dul ña ca gëm tey jëf u yiw. Ñooñu danañu am pey gu ñu fulandi ci sababus la ñu daan jëf, te ñoom ña nga ne fayax ci ay kër yu kawe [ca Àjjana].
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Waaye ña daan dox, di dëgërante bopp ak Sunuy kàddu, ñoom ña nga ne xeew ci biir mbugal ma.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam ci jaamam yi, Moo koy xatal it. Lépp lu ngeen mën a joxe [ci alal], moom Yàlla moo koy wuutalaat, te Yàlla moo di ngën ji kuy wërsëgal”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Bu keroogee Bis ba leen Yàlla di dajale mbooleseen. Ba noppi daldi wax Malaaka ya ne leen : “Moo ndax ñii yéen la ñu daan jaamu ? ”.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Ñu ne : “Tudd nanu sag sell ! Yaw yaay sunu wéeruwaay, du ñoom. Li am moo di, ñoom jinne yi la ñu daan jaamu, li ëppoon ci ñoom jinne la ñu gëm.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Tey jii nag, kenn ci ñoom ëmbalut moroomam lor mbaa njariñ, te Dananu wax ña daan tooñ ne leen: “Tokkamtikuleen mbugamal Safara sa ngeen doon weddi”.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Bu ñu mësaan a jàng ci ñoom laaya yu leer, dañu naan : “Waa jii daal nammul lu dul féewale leen ak li leen seeni baay daan jaamu”. Ñuy wax it naan : “Lii daal du dara lu dul ay fen yu ñu sos”. Ña weddi woon dëgg it ba mu leen dikkalee, ña nga naan : “Lii daal ag njibar doŋŋ la ! ”.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
[Moonte] Joxuñuleen woon ay téere yu ñuy mën a jàng. Mësuñoo yónni it ca ñoom ab xuppekat bu la jiitu.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Xeet ya jiitu woon waa Màkka weddi woon nañu Yonent ya. Te waa Màkka amuñu ca lu tollu ni fukkeelu la ñu joxoon ñooña [ci kàttan]. Ñoom it ne sunuy ndaw ay fenkat lañu. Kon naka la samab sànje di dem !
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Waxal ne : “Maa ngi leen di waar ci lenn : nangeen taxaw ngir Yàlla, moo xam ngeen diy ñaar-ñaar walla ngeen di benn been, te ngeen xalaat. Seen àndandoo bii di Muhammad jinne sadd ko : moom doonul lu dul ab xuppekat bu ame mbugal mu nekk seen kanam”.
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
Neel : “Laajumaleen ci ag pey, yéen a ko moom. Samag pey, Yàllaa ko warlu. Moom seede la ci lépp lu nekk”.
ﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙ
Neel : “Neel Yàlla mooy badd ndawam ci dëgg. Mooy xamaakoonu mbóot ya”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Waxal ne : “Dëgg [Lislaam] dikk na. Te ag neen [kéefar] du fi tàmbalee te du fi dellusi”.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Waxal ne : “Su ma réeree , sama bopp doŋŋ laay sànk ; su ma gindikoo it, ci sababus li ma Yàlla soloo lay ame, Moom Yàlla kuy Dégg, kuy Jigeñ la”.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Cëy soo leen gisoon ba ñu jàqee, - kenn du raw, - dañu leen a ndar-kepp ci barab bu nekk !
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Ñu neey : “Gëm nañu”, - Moo fu leen ngëm di bawoo ?
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
te fekkoon ñu weddi lu jiitu, di sànney kumpa ci barab bu sori !
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Ñu gàllankoor seen digganteek la ñu doon wuneen [sopp], kem nañu ko defe woon ca ña leen jiitu, ña nga woon ci biir sikki-sàkka gu xóot.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







