Simoore As-Saff
14 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla, te Moom moo di Boroom Kàttan ga, di Ku Xereñ ka.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Eey yéen ñi gëm ! Ana lan moo tax ngeen di wax lu ngeen dul def ?
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Wax ji ngeen di wax te du ngeen ko def ak jéppi gu rëy (la leen di jural ca Yàlla).
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Yàlla safoona ñiy xeex ci yoonam wi def senn sàppe melni ñoom tabax bu ñu raax la ñu.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
(Fàttalikul) Ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : "Yéen samaw nit ! Ana lan moo tax ba ngeen di ma lor te xam ngeen xell ne man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen ? ” Bu ñu jengee, Yàlla jengal seeni xol, te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay saay-saay.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
(Fàttalikul it) Ba Iisaa doomu Maryaama waxee ne : “eey yéen waa giir Banii-Israayiil, man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen, may dëggal la ma jiitu woon, ca Tawraat, di bégale it, ci Yonent buy dikk sama ginnaaw aw turam di “Ahmadu”. Waaye ba mu leen dikkale ak ay firnde yu leer , dañoo wax ne : “Lii kat ag njibarla gu bir ne fàŋŋ”.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Ana kan moo gën a doon tooñkat kuy duural Yàlla ay fen, te ña nga koy woo jëme ko ci Lislaam ? Yàlla dey du gindi aw nit ñu di ay tooñkat.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Ñoom dañoo bëgg fay leerug Yàlla ci seeni gimiñ, te Yàlla moom kuy mottali la ag leeram doontele sax Yéefër yi dañuy bañ.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Moom moo yónni ab Yonentam ci njub ak diiney dëgg, ngir mu kawe mbooleem diine yi, doonte la sax Yéefër yi dañuy bañ.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Eey yéen ñi gëm ! Moo ndax du ma leen tektal ci am njoló mu leen di musël ci mbugël mu mitti ?
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Dangeen di gëm Yàlla ak ub Yonentam tey xare ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan, looloo gën ci yéen de, cëy bu ngeen xamoon !
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
kon dey dana leen jéggal seeni bàkkaar te it dana leen tàbbal ay Àjjana yu ay dex di daw ci suufam, ak ay dëkkuwaay yu teey ci Àjjanay adan ? Loolu mooy texe gu mag ga
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
dana leen defal it yeneeni mbir yu ngeen bëgg : ndimbal [lu bawoo] fa Yàlla ak ndam lu jige. Bégalal jullit ñi ci xibaar bu neex bi.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝﰞﰟﰠﰡﰢ
eey yéen ñi gëm ! Nangeen doon ay farandooy Yàlla, kem ni Iisaa doomu Maryaama waxe woon taalibeem ya ne leen : “ Ana ñan ñooy doon samay farandoo yi jëm ci Yàlla ? ” – Taalube ya ne ko : “Nun ñoo di farandoo ya jëm ca Yàlla”. Mu am Kureel ci Banii-Israayiila bu gëm na, mu am it Kureel bu weddi. Nu daldi dooleel ña gëm ca kaw seeni noon, ñu daldi am ndam.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers