Simoore At-Talaq
PDF —
12 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore At-Talaq pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore At-Talaq pdf Wolof — Wàcce Simoore At-Talaq Tekki. At-Talaq (Medinan) 12 Aaya.



Simoore At-Talaq
12 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Eey yaw Yonent bi ! Su ngeen di faseeti jigéen, na ngeen leen di fasee cig laab; te nangeen di lim yidda ja ; nangeen ragal Yàlla seen Boroom. Te bu leen leen génnee, ci seeni néeg, ñoom it bu ñu génn lu dul bu ñu defee ñaawtéef wu bir. Loolu mooy daytali Yàlla. Te képp ku jàll ci daytali Yàlla, tooñ na boppam. Te xamuloo baxam Yàlla dana àttewaat meneen mbir am déet !
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Su yidda ja matee, Téyeleen ci njekk, walla ngeen yewwileen ci njekk ; te nangeen ko seedeloo ñaari way maandu ci yéen. Te seede sa na Yàlla rekk tax. Loolu la nu leen cay dénk képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba. Ak képp kuy ragal Yàlla, dana ko defal génnuwaay bu rafet (tajfël),
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
te dana koy wërsëgale fu mu foogewul. Képp kuy doyloo Yàlla, Yàlla dana ko doy. Yàlla Dana jot mbiram, te Yàlla defal na lu nekk ab dayo.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Jigéen ñi mbaragatul, ñoom seen yidda ñetti weer lay doon. Ak ñi mbaragagul. Ñi ëmbu doom, seen yidda mi ngi yem ca ba ñu imbee seen ëmb. Te képp kuy ragal Yàlla, Dana ko defal ak yombal ciy mbiram.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Loolu moo di ndigëlul Yàlla li mu wàcce ci yéen. Te képp kuy ragal Yàlla, dana ko jéggal ay ñaawtéefam jox ko pey gu màgg.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Nangeen di dëkkël jigéen ñi ca fa ngeen dëkk yéen, ca nangeen ko mane. Buleen leen bunduxataal ngir xatal leen. Su fekkee ne dañoo ëmb, na ngeen leen di dundal ba baa ñuy imbi. Suñu, leen nàmpalalee seen doom, nangeen ko fay. Nangeen diisoo ci njekk. Su ngeen ca juuyoo, kon, na ko keneen nàmpal.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Ku am alal na joxee na mu woomale ; ku amul alal it na joxee ci kem na ko Yàlla wërsëgële. Yàlla du ga kenn ci lu mu manul, Yàlla dana def yombal ci ginnaaw ag jafe.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Aka bari ay dëkk yu moyoon seen ndigëlu boroom ak i Yonentam ! Nu nattu leen nattu bu tar, mbugal leen mbugal mu mitti.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Mosnañu musibam seeni mbir. Ñu mujj yàqule.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Yàlla waajal na leen mbugël mu tar. Kon book ragal-leen Yàlla, yéen woroom xel yi, natt gëm. Yàlla wàcce na ci yéen ag fàttali,
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
ab Yonent buy jàng ci yéen Laayay Yàlla mu leer nàññ, ngir mu génne ñi gëm tey jëfe yiw cig lëndëm jëme leen ci leer. Képp ku gëm Yàlla tey jëfe yiw, (Yàlla) dana ko tàbbal Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam, ñu béel fa Yàlla may ko fa xéewal gu jekk.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜ
Moom Yàlla mi bind juróom-ñaari asamaan ak suuf yu na toll. Ay ndigalam di wàcci ci seen diggante, loolu lépp ngir ngeen xam ne Yàlla man na lépp lu ne te it peek na lépp lu ne ci xam-xam.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers