Simoore At-Tahrim
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore At-Tahrim pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore At-Tahrim pdf Wolof — Wàcce Simoore At-Tahrim Tekki. At-Tahrim (Medinan) 12 Aaya.
Related
- At-Tahrim TekkiWolof
- At-Tahrim mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore At-Tahrim

ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Éy yaw Yonent bi ! Ana lu tax, ngay araamal lu la Yàlla daganalal, nga di ca sàkku ngëram loo say soxna ? (Waaye) Yàlla moom Jéggalaakoon la, Jagléwaakoon la.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Yàlla fartal na ci yéen, daganal seeni ngiñ. Yàlla di seen Boroom ; te Ku Xam la Ku Xereñ la .
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Ba Yonent bi joxee sekkare lennat ci soxnaam ba ñu ko tasaaree te Yàlla wuññil ko lenn la, dëddu leneen la. Ba mu ko xibaare soxna sa mu ne ko : “ku la ko xibaar ? ” Mu ne ko : “Yàlla mi Xam, te deñ Kumpa ci lépp mooma ko xibaar”.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Yéen ñaari soxna yi su ngeen tuubee (moo gën) ndax seeni xol jeng na. Su ngeen takktoo (Yonent bi), Yàlla farnaak moom, ak Jibriil ak jullit ñu yiw ñi, ak Malaaka yi di ko dimbali.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Te itam su leen fasee, Boroomam dana ko jox ay soxna yu leen gën, yu di ay jullit, yu gëm, yuy topp ndigal, ñuy tuub, ñuy jaamu, ñuy woor, di ay jeeg mba ay janq.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Éy yéen ñi gëm ! Fegalleen seen bopp ak seen njaboot, aw Safara woo xam ne matt ma aw nit lay doon ak xeer, ay Malaaka yu tal, te tar, ñoo fay nekk duñu moy mukk, li leen Yàlla digal te la mu leen digal la ñuy def.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Éy yéen Yéefër yi! Buleen jéema jéggalu tey danañuleen fay la ngeen daan jëf.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Éy yéen ñi gëm ! Tuuballeen Yàlla tuub gu sell. Kon dey Yàlla dana leen jéggal seeni ñaawtéef te Dana leen tàbbal ay Àjjana yu ay dex di daw ci suuf, bu keroogee Yàlla du gàcceel mukk Yonenta bi ak ñi gëm ànd ak moom. Seen leer gaa nga ca seen kanam ak ndeyjoor ; ña ngay wax naan : “Yaw sunu Boroom, mottalil nu sunug leer te jéggal nu. Yaw dey man nga lépp lu ne”.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Éy yaw Yonent bi ! Xeexal ak Yéefër yi ak Naaféq yi te na nga tar ci ñoom. Safaraay doon seenug muj, ndaw muj gu bon !
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Yàlla saddna leebu Yéefër yi ci soxnas Lóot ak soxnas Nooh. Nekkoon nañu ci ron sunu ñaari jaam yu yiw. Waaye ñu worleen dem àndeek Yéefër ya (la ñuy doon ay Yonent taxul ñu manal leen ci Yàlla dara. Dees na [leen] ne : “Tàbbileen Safara, ànd ak way tàbbi ña”,
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Yàlla saddna léebu way gëm ña, ci soxnas Firawna, ba mu waxee ne “Yaw sama Boroom, tabaxal ma kër fa yaw ca Àjjana, te nga musël ma ci Firawna ak jëfam; nga musël ma it ci nit ña di ay tooñkat”.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Ak ci, Mariyaama, doomi Imraana mi ñoŋaloon boppam ; Nu af ca ci sunu ruu. Mu dëkëloon kàdduy Boroomam ak i téereem : te bokkoon ca toppakat ya (daan jaamu Yàlla).
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







