Simoore Al-A'raf
PDF —
206 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-A'raf pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-A'raf pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-A'raf Tekki. Al-A'raf (Meccan) 206 Aaya.



Simoore Al-A'raf
206 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒ
Alif, Laam, Miim, Saad .
ﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Ab Téeree ngi, bu ñu wàcce ci yaw ; ngir nga waare ca, ak mu nekk ag fàttali ci way-gëm ña ; bu wenn tiis nekk ci sa xol ngir loolu.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Toppleen li ñu wàcce ci yéen mu jóge ca seen Boroom. Buleen ko bàyyi di topp ay xërëm. Néew ngeen xalaat.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Bariwaana dëkk bu Nu alag ! Sunu mbugal agsi fa ci guddi walla ci bëccëg.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Te seeni njàmbat nekkul, ba leen mbugal ma saddee, lu dul : “Nun ay tooñkat lanu woon”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Fàwwu Dananu laaj ña Nu yónni ca ñoom [nit ña], fàwwu it Dananu laaj ña Nu yónni woon [Yonent ya].
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Te Dananu leen nettali ji [ci loolu] ci xam-xam bu wér ndaxte fekke woon Nanu lépp !
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Booba bis, peese bu dëggu lay doon. Ña seen peese diis ak u yiw... Ñoom ñooy ñu texe ña !
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Ña seen peese woyof nag ... Ñooy ña yàqal seen bopp ngir ñàkk a faale Sunuy kàddu te doonoon ñu daan tooñ.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Defal Nanu leen ag jàppandal ci suuf si, defal leen ca lu ngeen dunde. Te seenug cant néew na !
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Bind Nanu leen, jox leen i melo, ba noppi Nu wax Malaaka ya : “Sujjóotal-leen Aadama.”. Ñoom ñépp a sujjoot, ba mu des Ibliis, moom bokkul ca ña sujjóot.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
[Yàlla] ne ko : “Lan moo la tee sujjóot ba Ma la ko digalee ? ”. Mu ne : “Maa ko gën : ndax Danga ma bind ci Safara, moom Nga bind ko ci ban”.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
[Yàlla] ne ko : “Wàccal jóge fi, yaw waroo fi rëy-rëylu. Génnal, torox nga.”
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Ibliis ne Ko : “Muñal ma ba bisu dekki ba.”
ﭸﭹﭺﭻﭼ
[Yàlla] ne ko : “Bokk nga ca ña Nuy muñandiku.”
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
bliis daldi ne : “Giñ naa ne beewloo gi Nga ma teg, danaa leen rékki ci sa yoon wu jub wi,
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
bu ko defee, ma songe leen ci seen kanam ak ci seen ginnaaw, seen ndeyjoor ak ci seen càmmoñ ba lu ëpp ci ñoom duñu la sant.”
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Yàlla ne ko : “Génnal”, di ku ñu detteel, di ku ñu dàq. “Ku la ca toppati ci ñoom... fàwwu Danaa feesale Safara ci yéen ñépp [yaak ñoom]”.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
“Te yaw Aadama, dëkkal yaak sa soxna, Àjjana ; lekkleen yéen ñaar fu leen fi neex ; waaye buleen jegeñ garab gii ; su amee, ngeen tooñ.”
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Séytaane jax-jaxal leen ngir mu feeñal ca ñoom ñaar la Nu leen nëbboon - ci seen cër - mu ne leen : “Seen Boroom terewuleen ngeen jegeñ garab gii lu dul ne Dafa bañ ngeen nekk ñaari Malaaka walla ngeen bokk ca ñay dund fàwwu [duñu dee] ! ”.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Mu waatal leen, ne leen : “Man dey damaa bokk rekk ci ñi leen di laabire”.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
[Aadama ak Awa] daldi ne : "Sunu Boroom, tooñ nanu sunu bopp. Soo nu baalul, yërëm nu, kon dananu bokk ca ñu yàqule ña”.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Mu ne leen : “Wàccleen, ku ci nekk di noonu ka ca des. Suuf si, am ngeen fay dëkkuwaay ak i xéewal ab diir.”
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
“Fa ngeen di dunde, fa ngeen di faatoo, fa lañu leen di génnee [ngeen dekkiwaat].”
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Yéen doomi-aadama ! Wàcceel Nanu leen koddaay lu ngeen di muure seeni pëy ak i takkaay. -Waaye koddaayul ragal Yàlla moo gën de. - Loolu bokk na ci kéemaani Yàlla yi. Ndax Yàlla ñuy fàttaliku [seen Boroom].
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Yéen doomi-aadama ! Buleen Séytaane sànke ni mu génne woon seen ñaari maam ya Àjjana, muri seeni koddaay ngir won leen seeni pëy. Moom mi ngi leen di gis, moom ak njabootam, te yéen mënuleen a gis fa ñu nekk. Nun def Nanu Séytaane ya ñu lëkkaloo ak ñi gëmul,
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
bu ñu defee ñaawtéef, dañuy wax ne : “Danoo fekk sunuy maam di ko def, te Yàllaa nu ko digal.” Neel : “Yàlla du digle ñaawtéef. Moo ndax dangeen di waxal Yàlla lu ngeen xamul ? ”
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Neel : “Yàlla Dafa digle maandute. Nangeen di jublu ci jàkka yépp te nangeen ko jaamu, di sellal ngir Moom [Yàlla]. Dangeen dellu ca Moom, na Mu leen sose woon cag njalbéen”.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Am na kurél bu gindiku, waaye am na ab kurél bu ab réer wàkk na leen, ñoom dañoo féeteek Séytaane bàyyi Yàlla te defe ne cig njub lañu nekk !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Éy yéen doomi-aadama, [jépp jàkka ju ngeen jëmati] nangeen di waaj ba jekk [ak yére yu rafet]. Te nangeen di lekk di naan ; te buleen di yàq, ndax Yàlla soppul yàqkat yi.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Neel : “Ana kan mooy digle ne taari Yàlla, yi Mu génneel ay jaamam, araam nañu, ak xéewal yu sell yi ? ”. Neel : “Yooyu, ñi gëm ci àddina bi, ñoo koy moom, ñoom doŋŋ te bu àllaaxiraa.”. Noonu la Nuy leeralee Sunuy tegtal ci nit ñuy xam.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Neel : “Sama Boroom araamalul lu dul ñaawtéef yi, la ca feeñ ak la ca nëbbu ak bàkkaar, ak bew guy jalgati dëgg, ak di Ko bokkaaleek loo xam ne wenn lay wàccewu ca, ak ngeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul. [Yooyu ñoo araam]”.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Xeet wu nekk am na àpp. Bu àpp ba agsee, duñu yées senn saa te it duñu ko jiitu.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Éy yéen doomi-aadama yi ! Amaana ay Yonent yu bokk ci yéen dikkal leen, di leen nettali sunuy tegtal, (nangeen xam ne) képp ku ragal na Yàlla tey yéwénal, du am tiitaange te du jàq.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Gaa ña nga xam ne dañoo weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu, dëddu ko, ñooñee ñooy waa Safara, te dañu fay béel.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen walla muy weddi ay tegtalam ? Ñoom dey, danañu jot seen wàll wi Nu dogal ci ñoom ; ba kero bu leen Sunuy ndaw dikkale, naan len : “Ana ña ngeen daan jaamu bàyyi Yàlla ? ” - Ñu toontu ne : “Réer nañu nu”. Daldi seede ne ñoom ay yéefar lañu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Mu ne leen : “Dugguleen fekki xeet ya leen jiitu woon, di ay nit ak i jinne ca Safara sa.”. Xeet wu ca dugg rekk, tàmbalee rëbb moroom ja. Ba ñépp yembee, ña jiitu ak ña mujj ku nekk naan : “Ñii noo nu sànkkoon : kon nag Yàlla, fulal mbugal ma ci seen kaw.”. Yàlla ne leen : “Yéen ñépp laay ful seen mbugal, waaye xamuleen”.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Ña fa jiitu ñoom di wax ña mujj a agsi, naan leen : “Yéen ñii daal, gënewuleen nu lenn. Kon mosleen [toqamtiku] mbugal mi ngir la ngeen fàggu woon ciy bàkkaar”.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Ña weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu ba dëddu leen, Deefuleen ubbil wunti asamaan si, te duñu dugg Àjjana li feek gëléem duggul ci bën-bënu puso. Te noonu Lanuy feye saay-saay si.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Am nañu laltaayu Safara ak mbalaanum [Safara]. Noonu Lanuy feye tooñkat ya.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Ña gëm te jëf u yiw - Te kat Dunu teg bakkan lu dul lu mu àttan - ñooña ñooy waa Àjjana : te dañu fay béel.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
e Danuy rocci la nekkoon ca seeni dënn cig noonoo, dex ya dañuy daw-dawaan ca seen ron, ñuy wax naan : “Sant nanu Yàlla, Moom Mi nu indi ci lii. Te mënunu woon a gindi mukk sunu bopp, su fekkoon ne Yàlla gindiwunu. Sunu Boroom, ay Yonentam indi woon nañu dëgg.”. Ñu woo leen, ne leen : “Àjjana jii donolees na leen ko ngir la ngeen daan def [ci lu baax]”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Waa Àjjana woo waa Safara, ne leen : “Nun dey, gis nanu la nu sunu Boroom digoon muy dëgg. Moo ndax yéen fekk ngeen li leen seen Boroom digoon muy dëgg ? ”. Ñu toontu ne : “Waaw”. Mu am wootekat bu daldi woote ne : rëbbum Yàlla dal na ca tooñkat ya,
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
ñoom ñay féewale [nit ñi] ak diiney Yàlla ji, di doxe doxiin wu jeng, te ñoom dañoo weddi àllaaxira.”
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Dox na ca seen diggante [waa Àjjana] kiiraay, nekk na ca kaw (dig) wa aw nit ñoo xam ne danañu leen xàmmee ñoom ñépp ca seen màndarga ya. Ñu woo waa Àjjana, ne leen : “Yal na jàmm nekk ci yéen ! ”. Ñoom duñu dugg Àjjana te xemmem nañu ko.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Saa su seeni gët jubloo ca waa Safara, ñu ne : "Sunu Boroom, Yàlla boo nu boole ak nit ñu di ay tooñkat”.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Ña nekk ca dig wa tuddu [Al-Lahraaf] woo ay nit ñu ñu xàmmee ngir seeni màndarga, ne leen : “Waa kon alal ja ngeen daan dajale ak la leen taxoon a rëy-rëylu, amaluñuleen benn njariñ !
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Moo ndax ñii du ña ngeen giñoon ne Yàlla duleen dugal ci yërmaande... ? - Dugguleen ci Àjjana ! Te buleen am njàqare, te buleen am naqar.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Waa Safara woo waa Àjjana ne leen : “Bëbël-leen ci nun lenn ci ndox mi, walla ci li leen Yàlla wërsëgale.” Ñu toontu ne : “Yàlla dogal na ne [xéewal yii] araam na ci yéefar yi”.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
Ña nga xam ne dañoo jàppe seen diine po ak i caaxaan, te dundug àddina nax leen. Tey Dananu leen fàtte na ñu fàttee woon ndajem tey jii, ak la ñu weddi woon Sunuy kàddu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Te wóor na ne joxoon nanu leen ab Téere, bu Nu faramfàcce mu neex a dégg, muy njub ak yërmaande ngir nit ñu gëm.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Moo ndax dañuy xaar ba lu ko firndéel agsi ? Ña ko fàtte woon, la ko jiitu, danañu wax ne : “Yonenti sunu Boroom indi woon nañu dëgg. Moo ndax dananu amatiy rammukat yu nuy rammu ? Walla ñu delloo nu [àddina] nu def fa lu gën a rafet la nu fa daan def ? ”. Yàqal nañu jeeg seen bopp ; te la ñu daan duur réer na leen.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Seen Boroom nag mooy ki bind asamaan yeek suuf si ci juróom-benni fan, ba noppi Mu jublu ca Gàngunaay ga. Dana muure guddi ak bëccëg Mu toftale ko bu gaaw. Te jant bi ak weer wi ak bindiw, yu ñu tàggat lañu ci ndigalam. Moo ndax du Moo moom bind gi ak dogal yi? Yàlla Boroom àddina si, Ku barkeel la !
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Ñaanleen seen Boroom ci toroxlu ak ci yelu. Moom nag soppul ñiy jéggi dayo.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Buleen di yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Te nangeen di ñaan ànd ak ragal ak yaakaar, yërmaandey Yàlla nag lu jegeñ rafetalkat yi la.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Moo moom kiy yabal ngelaw yi ñuy tasaaroo lu jiitu. Ba bu ñu yanoo niir yu diis, ñu nàndal ci réew mu bekkoor, Nu wàccee ca ndox, génne ca bépp xeetu doomu gàncax [meññent]. Noonu lañuy génnee ñi dee [bu ñu leen di dekkal] ndax xéy-na ngeen fàttaliku.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Te dëkk bu [suuf sa baax], gàncaxam dana génn ci coobare Boroomam ; ña [seen suuf] bon, du génne lu dul lu bon. Noonu Lanuy leerale tegtal yi ngir nit ñuy gërëm [seen Boroom].
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Yónni woon Nanu [Nooh] ci aw nitam. Mu ne leen : “Yéen samay mbokk, nangeen jaamu Yàlla. Amuleen jeneen Yàlla ju dul Moom. Man dey, ragal naa ci yéen mbugalum bis bu màgg”.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Mbooloo ma, ca aw nitam [kilifa ya], toontu ko ne : “Gis nanu ne yaa ngi ci réer gu tar”.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Mu ne : "Man nekkuma ci ag réer ; Waaye man kat ab Yonentub Yàlla, miy Boroom àddina si, laa.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Dama leen di jottali sama bataaxalub Boroom, te dama leen di laabire, te xam naa ci Yàlla lu ngeen xamul.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Moo ndax dafa leen a jaaxal, ay kàdduy waare dikkal leen tukkee ca seen Boroom, jaare ci góor gu bokk ci yéen, ngir mu artu leen ngeen ragal Yàlla, ndax xéy-na yërëmeef leen ? ”
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Ñu weddi ko. Nu musal ko, moom ak ña nekkoon ak moom ca gaal ga, Nu labal ña weddi samay kàddu. Ñooña, aw nitam ñu gumba lañu woon.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
[Yónni woon Nanu it] ca waa [Haad], seen mbokk [Huud], mu ne leen : "Yéen samay mbokk, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen Yàlla ju dul Moom. Moo ndax dangeen dul ragal Yàlla ? ”
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Mbooloo ma weddi, ca aw nitam, wax ne : “Nun gis nanu la nga nekk ci ag ndof, te nun sax far nanu jort ne yaw ci fenkat yi nga bokk”.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Mu ne : "Yéen samay mbokk, ag ndof nekkul ci man de ; waaye li wér moo di ne man ab Yonent laa, [ndaw] lu bawoo fa Yàlla Boroom àddina si.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Dama leen di jottali bataaxalub sama Boroom te man dama nekk ci yéen aji-laabir ju wóor.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Moo ndax dafa leen yéem, waare dikkal leen tukke ci seen Boroom, jaare ci góor gu bokk ci yéen ngir mu artu leen? Fàttalikuleen ginnaaw ba Mu leen defee ngeen di kuutaay ginnaaw nitu Nooh, te Mu yokk seeni jëmm, dolli seeni kàttan. Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ndax xéy-na yéen ngeen texe.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Ñu wax ne : “Ndax danga noo dikkal ngir nu jaamu Yàlla moom doŋŋ, te bàyyi li sunu maam ya daan jaamu ? Indil nu li nga nu daan tëkkoo, ndegam ku dëggu nga”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Mu toontu ne : “Nekk na lu leen dëddale tukke ca seen Boroom, mbugal ak mer. Moo ndax dangeen di dàggasanteek man ciy tur yu ngeen sos yéen ak seeni maam, te Yàlla wàccewu ca wenn lay ? Man maa ngi nekk ak yéen di bokk ca way-muñandiku ña.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Nu musal ko moom ak ña ànd ak moom, ci Sama yërmaande, Nu daldi faagaagal nag ña jàppe Sunuy laaya ay fen te gëmuñu.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Yónni woon Nanu it ca waa Tamuud, seen mbokk Saalihu, mu ne : "Yéen samay mbokk, nangeen jaamu Yàlla ndax amuleen jeneen yàlla ju dul Moom. Ay lay yu leer nàññ dikkal na leen, tukke ca seen Boroom : gëléem gu jigéen la, di mbindéefum Yàlla, di kéemaan ci yéen. Bàyyileen ko muy lekk ci kaw suuf si Yàlla moom, te buleen ko def lu bon ; kon mbugal mu tar dal leen [bu ngeen jëfewut ndigal li].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Fàttalikuleen ba Mu leen defee ay kuutaay, ca ginnaaw Haad, mu dëkkal leen ci suuf si. Ngeen tabax ay kër yu rëy ci dénd yi, di yatt ci doj yi ay kër. Fàttalikuleen xéewali Yàlla te buleen doon ay yàqkat ci kaw suuf si.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Kilifa ya nekkoon di rëy-rëylu ciy nitam wax nañu, ña ñu doyadal, muy ña gëm ca ñoom : “Moo ndax wóor na leen ne Saalihu Yonentub Yàlla la ? ". Ñu toontu ne : “Nun dey way-gëm lanu [ci bataaxal] bi ñu ko yónnee”.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Ñay rëy-rëylu ne leen : “Nun dey, li ngeen gëm, weddi nanu ko”.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Ñu rey giléem ga, jalgati seen ndigalul Boroom, daldi ne : “Yaw Saalihu, indil nu la nga nu doon tëkkoo, ndegam ci Yonent yi nga bokk”.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Ag yëngug suuf rajaxe leen ; ñu xëy ne lànjaŋ ca seen kër ya.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Mu dëddu leen, daldi ne : "Yéen samay mbokk, jottali naa leen sama Yonenteb Boroom, laabire naa leen itam. Waaye yéen dey soppuleen laabirekat yi ! ”
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Fàttalikuleen itam ba Lóot waxee aw nitam, ne leen : “Moo ndax dangeen di def ñaawtéef woo xam ne kenn mësu koo def ci àddina sépp ?
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Ndaxte yéen dangeen di jublu góor ñi, di ca sàkku bànneex, bàyyi fa jigéen ña ! Yéen daal, aw nit ngeen ñu jéggi dayo.”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Toontul aw nitam nekkul lu dulñu ne : “Génneleen leen seenub dëkk. Ndax ñoom aw nit lañu ñuy laab-laablu” !
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Nu musal ko (Nun Yàlla) mook waa këram, ba mu des soxnaam, moom dafa des ca mbugal ma.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Nu sotti ca seen kaw ab taw , waay-waay gisal na mujjug saay-saay sa mel !
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
(Fàttalikul ba Nu yónnee) fa Madyaana, seen mbokk Chuhaybu, mu ne leen : "Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen Yàlla ju dul Moom. Te ay lay yu leer dikkal na leen yu bawoo ca seen Boroom. Kon nangeen di matal natt ak màndaxe te buleen wàññil nit ña, la ñu moom. Te it buleen yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Loolu dey, moo di li gën ci yéen, bu fekkee ni gëm ngeen.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Te buleen di toog ci wépp yoon, di dëkku ñi gëm Yàlla, di leen wëlbati, di dox seen digganteek yoonu Yàlla, di ko jéngal. Fàttalikuleen ba ngeen nekkee di ñu néew, Mu baril leen. Te nangeen settantal naka la mujjug yàqkat ya meloon.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Su fekkee am na ci yéen kurél bu gëm li ñu ma yónni, ak kurél bu goreedi, nangeen muñ ba ba Yàlla di àtte seenu diggante, te Moom (Yàlla) moo di gën jaa mën a àtte.”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Kilifa, ya rëy-rëylu ca aw nitam, ne ko : “Dananu la génne, yaw Chuhaybu ak ña gëm ànd ak yaw, ci sunum réew. Walla nga dellusi ci sunu diine.” - Mu ne leen : “Ba bu fekkee ne sax dangeen nuy ga [ci seen diine jooju] ? ”.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
“Bu nu delloo dugg ci seen diine, kon de nu duural Yàlla aw fen gannaaw ba nu Yàlla musalee ci seen diine jooju. Dunu mën a dellu duggu ci lu dul mu soob Yàlla sunu Boroom. Xam-xamu sunu Boroom ump na lu nekk. Ci Yàlla lanuy wéeru. Yaw sunu Boroom, àtteel sunu diggante ak sunuy nit, ci dëgg, ndaxte Yaw [Yàlla], yaa gën a mën àtte àttekat yi.”
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Kilifa, ya weddi ca aw nitam, ne : “Bu ngeen toppee Chuhaybu, dangeen yàqule”.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Yëngug suuf rajaxe leen ; ñu xëy ne lànjaŋ fa seeni kër.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Ña weddi woon Chuhaybu, dañoo mujj mel ni masuñu faa dëkk. Ña weddi woon Chuhaybu yàqule nañu.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Mu dëddu leen, ne : "Yéen samay mbokk, jottali naa leen sama Yonentub Boroom, laabire naa leen itam. Kon naka laay yërëmtaloo ngir aw nit ñu di ay yéefar ? ”
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Dunu yónni Yonent ci am réew, te tegunu waa réew ma ay tiis ak i njàqare ngir xéy-na ñu toroxlu.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
Ginnaaw ba ñu soppi yu bon ya, toxal ca yu baax, bu ñu biroo it ñu naan : “Aw naqar ak mbégte daloon na sunuy maam.”. Nu songe woon leen ci mbetteel te fooguñu ko woon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Bu fekkoon ne waa dëkk yooyu gëmoon nañu te ragal Yàlla, kon fàwwu Dananu leen ubbil ay wërsëg yu bawoo asamaan ak ci suuf si. Waaye dañoo weddi, Nu sadd leen ngir la ñu daan fàggu ci lu bon.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Moo ndax dafa am ci waa dëkk yooyu ñu naagu ne Sunu mbugal duleen dikke ci guddi fekk ñuy nelaw ?
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Walla dëkk yooyu naagu ne Sunu mbugal duleen dikkal bëccëg fekk ñuy fo ?
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Moo ndax dañoo naagu ci pexey Yàlla ? Te kenn du naagu ci pexey Yàlla ku dul nit ñu yàqule.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Walla ndax dafa leeral ci ñi donn suuf si, ginnaaw ña fi nekkoon, ci ne su Nu neexoon Nu sadd leen ngir seeni bàkkaar ak fatt seeni xol ba dootuñu am dégg-dégg ?
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Dëkk yooyu, Noo ngi lay nettali dara ci seeni xibaar. Te fekk Sunuy Yonent dikkoon fa ak ay lay yu leer, waaye ñoom mënatuñu woon a gëm la ñu daan weddi ca njalbéen. Noonu la Yàlla di fattee xoli yéefar ya.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Fekkunu woon li ëpp ci ñoom ñu ame kóllare fenn ; lu dul ne li ëpp ci ñoom ay saay-saay lañu.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Ba noppi Nu yónni ci seen ginnaaw Muusaa, mu ànd ak Sunu kéemaan ca Firawna ak mbooloom ña weddi. Seetlul naka la mujjug yàqkat ya mel nag.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Muusaa ne : “Yaw Firawna, man ab Yonent laa [boo xam ne], Yàlla miy Boroom àddina si Moo ma yónni,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
wér na ci man ma bañ a wax ci Yàlla lu dul dëgg. Ne indil naa leen aw lay wu tukkee ci seen Boroom. Boyalal waa Bani-Israayil ñu ànd ak man.”
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Mu toontu ne : “Ndegam danga indi ag kéemaan, wone ko ndegal ku dëggu nga.”
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Sànni na yetam wa mu daldi nekk jaan ju rëy.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Mu génne loxoom mu daldi weex tàll ca ña koy gis.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Kilifa ya bokk ca nitu Firawna ne ko : “Jabar bu am xam-xam la”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
[Firawna] ne : “Dafa leen bëgg a génne ci seen suuf.” - “Lan mooy seen ndigal ? ”
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Ñu ne ko : “Xaarloo ko mook mbokkam, te yónnee ci dëkk yi ay ndaw ñu mën a dajale nit ñi,
ﮚﮛﮜﮝﮞ
ñu indil la bépp jabar bu am xam-xam.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Jabar ya ñëw ca Firawna ne ko : “Ndax dananu am pey bu fekkee ne not nanu ? ”[joŋ]
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Mu ne leen : “Waawaaw, kon dangeen bokk ci ñi may jegeñ”.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Ñu ne : “Muusaa, benn yaw nga sànni, walla nun nu sànni”.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Mu ne : “Sànnileen”. Ba ñu sànnee, dañoo jabar bëti nit ña, ragal-loo leen ci jabar gu rëy.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Nu xelal Muusaa ne ko : “Sànnil sa yet wi”. Mu daldi wann la ñu doon wëlbati.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Dëgg daldi tàbbi, la ñu doon def yàqu.
ﯿﰀﰁﰂﰃ
Ñu not leen foofa, ñu daldi ànd ak toroxte.
ﰄﰅﰆﰇ
Ñu rot ñoom jabar ya, sujjóot.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
Ñu ne : “Gëm nañu Boroom àddina si,
ﭖﭗﭘﭙ
Boroom Muusaa ak Aaruuna.”
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Firawna ne leen : “Ndax dangeen Koy gëm te joxuma leen ci ndigal ? Lii, pexe la mu ngeen fàggu ci dëkk bi, ngir génne ñi fi dëkk.Waaye dangeen xam...
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Danaa dagg seeni yoxo ak seeni tànk cig jàllawle, ba noppi ma daaj leen, sandamtal leen yéen ñépp.”
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Ñu toontu ne : “Nun ci sunu Boroom lanuy dellu.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Feyoowoo ci nun lu dul nu gëm ay kéemaani sunu Boroom, ba ñu agsee ci nun. Sunu Boroom ! Sottil ci nun muñ te nga rey nu fekk nu dee jullit.”
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Kilifa ya bokk ci nitu Firawna ne ko : “Moo ndax dangaa bàyyi Muusaa ak u nitam ñuy yàq ci suuf si, te moom mu bàyyi la, bàyyi sa yàlla ? ”. Mu toontu ne : “Danaa rey seeni doom yu góor, ba yu jigéen yi. Ndax nun noo leen tiim, noo leen not.”
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Muusaa wax ay nitam : “Sàkkuleen ndimbal ci Yàlla te ngeen muñ, suuf si Yàllaa ko moom. Dana ko donnale ku ko neex ciy jaamam. Te muj ga, way-ragal Yàlla yee ko moom”.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
[Ñoom yahuud ya] ne : “Loreef nanu lu jiitu sa dikk ci nun ak ginnaaw la nga nu indil.”. Mu ne : “Xéy-na seen Boroom dana rey seeni noon, Mu wuutal leen ci suuf si ba noppi di saytu na ngeen di def”.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Teg Nanu nitu Firawna bekkoor ay at ak wàññikug meññent ndax xéy-na ñu fàttaliku [seen Boroom].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Bu leen lu baax dikkalee, ñu ne : “Lii noo ko moom” ; bu leen lu bon dalee, ñu gaafal Muusaa ak ña ànd ak moom. Déedéet seen gaaf nekkul ci kenn ku dul Yàlla. Waaye ña ëpp ca ñoom xamuñu.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Ñu ne : “ Loo nu mën a indil ciy kéemaan ngir jabar nu ci, dunu la gëm”.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Yabal Nanu ca seen kaw am mbënn, ak i njéeréer, ak teeñ ya ak mbott ya, ak deret ja, ñu di ay kéemaan yu fés, waaye ña rëy-rëylu nag ay nit ñu saay-saay lañu.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Ba mbugal ma agsee ca ñoom, ñu ne : “Yaw Muusaa, ñaanal nu sa Boroom ci kóllare gi dox seen diggante. Boo nu tàggaleek mbugal mii, dananu la gëm te dananu bàyyi Banii- israayil ñu dem ànd ak yaw”.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Ba Nu teggee ca ñoom mbugal ma [ca àpp ba mu waroon a yem], firi nañu la ñu dige woon.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Tax na Nu feyyu ci ñoom ; labal leen ci géej gi, ndax ñoom dañoo weddi sunuy tegtal, sàggane leen.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Nu donnale suuf si nit ña ñu nekkoon daan leen suufeel, penku ba sowu te barkeel ko. Noonu, sa dogalu Boroom bu rafet bi, daldi mat ci Banii-israayil ngir la ñu nekkoon di muñ. Nu rajaxe la Firawna ak u nitam nekkoon di liggéey ak ya ñu tabaxoon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Jàllale Nanu Bani-Israayil géej ga. Ñu fekk fa aw nit ñoo xam ne ña nga doon jaamu seeni xërëm, ñu ne : "Muusaa, defal nu yàlla ju mel ni seen yàlla.”. Mu ne leen : “Yéen daal ñu réer ngeen.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Nii la ñu nekkee di ñu alku; te seeni jëf lu yàqu la.”
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Mu wax ne : “Moo ndax dama leen di wutal jeneen yàlla ju dul Yàlla, te Moom mu defal leen ngëneel, teg leen ci kaw waa àddina si yépp [ca booba] ? ”
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
(Fàttalikuleen) ba Nu leen musalee ci nitu Firawna ya leen doon teg mbugal mu gën a ñaaw. Daan rey seeni doom yu góor, di bàyyi yu jigéen ya. Te loolu nekkoon na nattu bu màgg bu tukkee ca seen Boroom.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Àppal Nanu Muusaa fanweeri guddi, Nu mottali ko ak fukk, diir ba Boroomam dogal mat ñeneenti fukki guddi. Muusaa wax na mbokkam ma Aaruuna : “Wuutu ma ci samaw nit, te nangay jubbanti te bul topp yoonu yàqkat ya”.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Ba Muusaa agsee ca Sunu ndaje te Boroomam wax ak moom, mu ne : "Sama Boroom, won ma ma gis La ! ”. Mu ne ko : “Doo ma gis Muusaa ; waaye xoolal tundu doj wii : bu saxee ci barab bi mu nekk, kon danga Ma mën a gis.”. Ba Boroomam feeñoo doj wa, dafa mokk rumbax, Muusaa daanu xëm. Ba mu ximmee, mu daldi ne : “Tudd naa sag sell, kañ naa La ! Dellu naa ci Yaw ; te man sax faf maa di ki jëkk a gëm”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Mu ne ko : “Yaw Muusaa, Man tànn naa la ci biir nit ñi, ngay Sama Yonent ak Sama kàddu. Jëlal li Ma la jox te nga bokk ca way-gëm ña”.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Nu bindal ko ci àlluwaya lu nekk ngir waare ak faramfàcce lu nekk ba mu waar ko cig farlu. “Nu digal ko mu wax ay nitam ñu jàppe ko ca na mu gën a rafete. Danaa leen won dëkku saay-saay sa.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Danaa soreel Samay tegtal ña rëy-rëylu ci suuf si ci lu dul dëgg. Ba bu ñu gisee bépp kéemaan duñu ko gëm. Bu ñu gisee yoon wu njub, duñu ko topp, muy seenu yoon. Li waral loolu mooy dañoo weddi Sunuy kàddu, sàggan ba dëddu leen.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Ña weddi Sunuy kàddu ak ndaje mu mujj ma, seeni jëf yàqu na. Ndax deesuleen fey lu dul la ñu daan def ”
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Nitu Muusaa jàpp nañu ci ginnaawam aw yëkk wu ñu takk seeni takkaayi yaram, weddi Sunuy kàddu. Ndax dañoo gisul ne moom mënuta wax ak ñoom te duleen jubale ciw yoon ? Jàpp nañu ko [di ko jaamu], nekk i way-tooñ.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Waaye ba mu daanoo ca seeni yoxo, te ñu gis ne ñoom dañoo nekkoon cig réer, ñu ne sunu Boroom : “Soo nu yërëmul, baal nu, dananu bokk ca way-yàqule ña”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Ba Muusaa ñibbee ca aw nitam, mer lool, dafa wax ne : “Nii ngeen ma ginnaawoo ñaaw na ! Xanaa dangeen a yàkkamti seen àtteb Boroom gaaw a ñëw? ”. Mu daldi sànni àlluwa ya, jàpp ca boppub mbokkam ma, xëcc ko. Aaruuna toontu ko ne : “Yaw sama doomu-ndey , nit ñi dañu maa doyadal te xaw nañu maa rey sax. Kon bul bégloo noon ya te bul ma boole ca nit ña di way-tooñ”.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Mu ne : “Yaw sama Boroom, jéggal ma ak sama mbokk mii te nga tàbbal nu ci sa yërmaande, ndax Yaw yaa ëpp yërmaande képp kuy yërëme”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Ña nga xam ne doon nanu jaamu yëkk wa, mbugal dana leen dal tukke fa seen Boroom, ak toroxte ci dundu àdduna. Te noonu Lanuy feyee ñay duural Yàlla.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Ñay def lu ñaaw ba noppi ginnaaw ga ñu tuub, tey ñu gëm... sa Boroom nag, ginnaaw loolu, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Ba merum Muusaa giifee, dafa jël àlluwa ya. Te mbind ma làmboo na njub ak yërmaande ngir ña nga xam ne ñoom ragal nañu seen Boroom.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Muusaa tànn juróom-ñaar fukki góor ciy nitam, ngir sunu waxtu ndaje. Ba leen yëngug xeer wa jàppee, mu ne : “Yaw sama Boroom, bu la neexoon nga rey leen ak man lu jiitu tey. Moo ndax Danga nuy rey ngir li ña réer ci nun def ? Loolu du leneen lu dul sa nattu, ci ngay réerale ku La soob, di ci jubal ku La soob. Yaway sunu Cëslaay. Nanga nu baal, yërëm nu, Yaa di ki gën a mën a jéggale.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Dogalal ci nun yiw ci àddina ak ca àllaaxira. Nun gindiku nanu jëm ci Yaw.”. Mu ne : “Sama mbugal, danaa ko sadd ku Ma neex. Waaye Sama yërmaande ëmb na lépp lenn. Te danaa ko sadd ña ragal Yàlla tey génne asaka ak ñi gëm Samay kàddu.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Ña nga xam ne danañu topp Yonent ba, di ku ñu soloo te jàngul, te ñu fekk ñu bind ko ca ya ñu yore ci Tawreet ak Injiil. Mu di leen digal lu baax, di leen tere lu bon, daganal leen yu sell ya, araamal ca ñoom yu selladi ya, soppil leen ya leen diisoon ak gàkk ya nekkoon ca ñoom. Kon ñi ko gëm [moom Muhammad] te weg ko, te ñu topp leer ga Nu wàcce ci moom; ñoom ñooy way-texe ña.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Neeleen : "Yéen nit ñi ! Man Yonentub Yàlla laa ci yéen ñépp, Moom mi nga xam ne Moo moom nguuru asamaan yi ak suuf si. Amul jeneen yàlla ju dul Moom. Mooy dundal, Mooy rey. Kon gëmleen Yàlla ak Yonentam bi, di ku ñu soloo te jàngul, te moom gëm na Yàlla ak ug kàddoom. Kon toppleen ko, xéy-na kon ngeen gindiku”.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Amoon na ci nitu Muusaa, mbooloo muy gindee ci dëgg ak di ca tegtaloo ci maandute.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Nu xaaj leen fukki giir ak ñaar ñuy ay xeet. Ba noppi, Nu soloo Muusaa, ba ñuy sàkku lu ñu naan, ne ko : “Dóoral xeer wi ak sa yet wi.”. Noonu fukki bëti ndox ak ñaar balle ca. Ku nekk ca ñoom xamee fa muy naane. Nu defal leen keppaar ak niir wa, Nu wàcceel leen lem gu weex ak i njanaaw, ne leen : “Lekkleen ci yu sell yi Nu leen wërsëgale.”. Waaye tooñuñu Nu, seen bopp rekk lañuy tooñ.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
[Fàttalikul] ba ñu leen waxee ne : “Dugguleen ci dëkk bii te nangeen di lekk ci ñamam yi fu mu leen soobe, te nangeen di wax : Sippikug bàkkaar te nangeen tàbbi ci buntu bi sujjóot. Kon Nu baal leen seeni ñaawteef ; te Dananu dolli way-rafetal ña”.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Ña tooñ ci ñoom, soppi la ñu leen wax ak yeneeni wax. Nu yebal fa ñoom mbugal mu tukke asamaan ngir la ñu nekk di tooñ.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Te nga laaj leen lu jëm ci dëkk ba nekkoon ca tefesu géej ga ca gaawu ba ! Ba seen jën ya tëmbu ci ñoom ca seenug gaawu, tey bañ a génn bis ya! Noonu la Nu leen doon nattoo ngir la ñu daan fétterlu génn topp.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Te am mbooloo ca ñoom ne : “Lu tax ngeen di waar nit ñoo xam ne Yàlla dana leen rey mbaa mu teg leen mbugal mu tar ? ”. Ñu toontu [ñoom ña doon waare] ne : “Ngir nu am lay ca seen Boroom ak xéy-na ñoom ñu ragal Yàlla ! ”
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Ba ñu fàttee la ñu leen doon waare, musal Nanu ña doon tere lu bon, Nu sadd ña doon tooñ, mbugal mu tar ngir la ñu féttérlu woon génn topp.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Bu ñu rëyloo ca la ñu leen tere, Nu wax leen ne : “Nekkleen di ay golo yu torox”.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
[Fàttalikul] ba seen Boroom xamlee ne Dana leen yónnee ku leen di teg gëm jaa boni mbugal ba kerook Bis-pénc di agsi. Sa Boroom nag Ku gaaw la ci mbugal te Moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Te séddale Nanu leen ay giir ci suuf si. Am ci ñoom ñu yiw, am ñu yiwadi. Nu nattu leen ciy xéewal ak ciy naqar ndax ñu dellusi [ci seen Boroom].
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Kuutaay gu bon toftaloo ca ñoom, [teewul] ñu jàppe ci alali ku yées ki [di àddina], ñu naan : “Dees nanu baal.”. Te bu leen alal ju ne mel dikkalee, ñu jàpp ca. Waaw ndax kóllareb Téere ba tënku leen ci di waxal Yàlla dëgg rekk ? Moone jàng nañu la nekk ca biir de. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla, - Moo ndax dangeen dul xel-lu ? -
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Te ñay jafandu ca Téere ba te di taxawal julli, [nañu xam ne] Nun nag Dunu sànk peyu way-sellal ña.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
[Fàttalikul] ba Nu yékkatee doj wa mu tiim leen, mel ni niir la. Ñu am njort ci mu daanu ci seen kaw. Ñu ne leen : “Jàppleen lii ñu leen jox ànd ca ak farlu te ngeen jëfe li nekk ci biir. Ndax xéy-na yéen ngeen ragal Yàlla”.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
[Fàttalikul] ba sa Boroom génnee ci ndigul doomu-aadama yi seeni sëf, te Mu seedeloo leen ci seen bopp, ne leen : “Du Maay seen Boroom ? ”. Ñu ne : “Axakay, seede nanu ko...” - ngir ngeen bañ a wax ca Bis-pénc ba ne : “Danoo réere woon lii [mu nekk seenu lay]”,
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
mbaa ngeen bañ a wax : “Du dara lu dul sunuy maam dañoo bokkaale woon lu jiitu nu sëtoo ca ñoom ginnaaw ga. Ndax dees na nu mbugal [ci loo xam ne ña jubutoon ca nun ñoo ko def] ? ”
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Noonu la Nuy leeralee tegtal yi. Ndax xéy-na ñu dellusi [ci seen Boroom] !
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Nettalileen ka Nu joxoon Sunuy mbóot mu rocceeku ca. Séytaane topp ko, tax na mu bokk ca way-beew ña.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Su nu sooboon Nu yékkatikook mbóot yooyu, waaye dafa jengoon jëm ci àddina, topp bànneexam. Dafay mel ni xaj, boo ko songee muy yalkat, boo ko bàyyee muy yalkat. Loolu mooy niróowaaleeb nit ña weddi Sunuy kàddu. Nettalil xew-xew ba. Xéy-na ñoom ñu fàttaliku !
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Nekkinu nit ña weddi Sunuy kàddu, aka bon, waaye seen bopp lañuy tooñ nag.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Ku Yàlla gindi nag, mu nekk cig njub. Ña Mu bàyyi cig réer, ñooy ñu yàqule ña.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Nun bind nanu ba noppi ngir Safara jinne yu bari ak nit. Ñeel na leen xol yu dul am dégg-dégg. Ay bët yu ñu dul gis ak ay nopp yu ñu dul dégge. Ñooña, dañoo mel ni mala ya, ñoo leen gën a réer sax. Ñooy ñu sàggan ña.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Yàllaa moom tur yu rafet yi. Nangeen ko ciy jaamu te ngeen dëddu ña di jeng ci turam yi : dees na leen feye la ñu daan def.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Nekk na ci ñi Nu bind, xeet woo xam ne danañu gindiku ci dëgg te danañu maandu.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Waaye ña weddi Sunuy tegtal, Dananu leen jay, jaarele leen fu ñu xamul.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Muñal-leen, Sama pexe naka lu dëgër la !
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Moo ndax dañu dul xél-lu xam ne seen àndandoo bi jinne jàppu ko? Nekkul lu dul waarekat bu ràññeeku !
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Moo ndax dañu dul xool nguuru asamaan yi ak suuf si, ak li Yàlla bind lépp, te it xéy-na Mu jegeñal seen àpp ? Kon jan wax gannaaw josam, lañu mën a gëm ?
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Ku Yàlla bàyyi cig réeram, kenn du la mën a gindi. Dana leen jàppe ca seen beew ga ñuy tëñax-tëñaxi.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚ
Ñi ngi lay laaj ci taxawaayu Bis-pénc ba : “Kañ lay doon ? ”. Neel : “Kenn amu ca xam- xam ku dul sama Boroom. Kenn du ko feeñal ca waxtoom ku dul Moom. Lu diis la ci asamaan ya ak ci suuf si, duleen digal lu dul cig mbetteel.”. Ña nga la koy laaj mel ni danga ca xam dara. Neel : “Xam-xam nekkul fenn fu dul fa Yàlla.”. Waaye lu ëpp ci nit ñi xamuñu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Neel : “Mënaluma sama bopp njariñ walla lor lu dul la soob Yàlla. Su ma xamoon kumpa, kon ma bari lool alal ak i xéewal, te kon lu metti duma dal. Nekkuma man lu dul waarekat, béglekatu nit ñi gëm Yàlla”.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Moom mooy Ki leen bind ci benn bakkan, mu génne ca soxnaam ngir muy am ug dal ci moom; ba mu ko muuree, mu ëmb ëmb bu woyof, muy dem ak ëmbam. Ba mu diisee, ñoom ñaar ñu ñaanYàlla seen Boroom ne ko : “Soo nu mayee [doom] ju baax, kon faf dananu bokk ci gërëmaakoon ña”.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Ba Mu leen mayee [doom], ñu bokkaale Yàlla ca la Mu leen may. Te Yàlla jomb na la ñu Ko bokkaale.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Moo ndax dañuy bokkaaleek [Yàlla] ñoo xam ne mënuñoo bind dara te dañu leen a bind,
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
te mënuñuleen a dimbali, mënuñoo dimbali seen bopp sax ?
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Boo leen woowee ci njub, duñuleen topp. Ngeen woo leen walla ngeen noppi [bañ leen a woo] yem kepp.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Ña nga xam ne dangeen leen jaamu bàyyi Yàlla, ay jaam lañu ni yéen. Wooleen ba xam danañu leen nangul ndeem ñu dëggu ngeen.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Moo ndax dañoo am tànk yu ñu doxe ? Moo ndax dañoo am loxo yu ñu téye ? Moo ndax dañoo am bët yu ñuy gise ? Moo ndax dañoo am nopp yu ñuy dégge ? Neeleen : “Wooleen seen bokkaale yooyu, te nangeen ma fexeel, bañ maa yeexe.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Ki may dimbali mooy Yàlla Mi wàcce Téere ba te mu méngook ñu sell ña.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Ña ngeen di jaamu te bàyyi Ko, mënuñuleen a dimbali te mënuñoo dimbali seen bopp sax.”
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Boo leen woowee cig njub duñu dégg sax. Dangeen gis ñu di la xool te ñoom duñu gis.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Jéggaleel te nangay digle yiw, te nanga dëddu ñu réer ña.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Saa su la ag soppeeku dalee, gu tukke ci Séytaane, nanga sàkku mucc ci Yàlla. Moom Yàlla nag Kuy dégg la, Kuy xam la.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Ña ragal Yàlla, bu leen lu metti dalee, tukke ci Séytaane, ñu fàttaliku [seen Boroom] daldi nekk ñu am ràññee.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Mu am seen kuute ñoo xam ne danañu leen tàbbal ci ag réer, te di leen ca xamb rekk.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Te bu ndigal ñëwul, ñu naan : “Lu tee nga fental ko sa bopp ? ” Neel : “Duma def lu dul topp li ñu ma soloo mu tukke ci sama Boroom. Loolu ay lay la yu tukkee ci seen Boroom, di njub ak yërmaande ci nit ñu gëm.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Kon bu ñuy jàng Alxuraan, nangeen ko déglu te nangeen ko xarawlu ndax xéy-na yërëmees leen.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Nangay tudd sa Boroom ci sa bopp ànd ak toroxlu ak ug ragal, ci lu ànd ak yelu ci sa kàddu, ci kaw subaak ngoon, te bul bokk ca ñu sàggan ña.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Ña nga xam ne ñanga ca sa Boroom, duñu di rëylu ci jaamu Ko. Te danañu Ko di sàbbaal, di Ko sujjóotal.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers