Simoore Al-Ahzab
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Ahzab pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Ahzab pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Ahzab Tekki. Al-Ahzab (Medinan) 73 Aaya.
Related
- Al-Ahzab TekkiWolof
- Al-Ahzab mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Ahzab

ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Éy yaw Yonent bi ! Ragalal Yàlla te bul topp yéefar yi ak naaféq yi, Yàlla ku xam la, Ku xereñ la.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Toppal li ñu lay soloo te mu bawoo ca sa Boroom. Yàlla xàmmee na ca la ngeen di def.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Te nangay wéeru ci Yàlla. [Ndax] Yàlla doy na sëkk wéeruwaay.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Yàlla defalul kenn nit ñaari xol ci dënnëm. Deful it jabar yi ngeen di wodde seen pendali ndey [ci pase] ñuy seeni yaay . Deful it doom yi ngeen doomoo ñuy seeni doom. Loolu seeni wax doŋŋ la ju yem ci seeni gémmiñ. Yàlla dëgg lay wax te Mooy jubbanti, di tege ci yoon wu jub.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Appelez-les du nom de leurs pères : c’est plus équitable devant Allah. Ña ngeen xamul seeni baay, kon ñoom seeni mbokk la ñuy doon ci diine ak seeni farandoo. Ayul ci yéen it lu ngeen ca wax te muy njuumte, li aay kay mooy la ngeen ca wax te tey ko. Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Yonent bi moo gën a yey jullit ñi ci seen bopp ; te ay soxnaam, seeni yaay lañu. Ña ame mbokku gu deret, gën nañoo yeyante kem ni mu dikke ci Téereb Yàlla bi, te jullit ñi ak way- gàddaay ñi, mën ngeen a bind ab dénku ci seeni alal mu ñeel seeni farandoo ya dul donn. Loolu lu sax la lu ñu bind ca Téere ba.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
[Fàttalikul] ba Nu jëlee daalante ci Yonent yi ak ci yaw, ak ci Nooh ak ci Ibraahiima, ak Muusaa, ak Iisaa doomu Maryaama : jëloon Nanu ci ñoom daalante bu dëgër, diis,
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
ngir laaj [Moom Yàlla] ñi dëggal ci seenug dëggal. Te waajalal na yéefar yi mbugal mu metti.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Éy yéen ñi gëm ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ba leen xarekat ya songee te Nu yebaloon ci ñom ngelaw ak i xarekat yu ngeen gisul. Yàllaa ngi doon gis li ngeen doon def.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Ba ñu leen songee, jóge leen kaw ak ci suuf [fépp], seen gët ya di tiiw-tiiwi, ngeen rët ba seeni xol nekk ci seeni boli, ngeen di njort ci Yàlla njort lu nekk...
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Foofee la Nu nattoo jullit ña, yëngal leen yëngal gu tar.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Ak ba naaféq ya ak ña seen xol tawat di wax naan : “Yàlla ak Yonentam diguñu nu lu dul ay nax”.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Ak ba mu amee kurél ci ñoom buy wax naan : “Yéen waa Yasriba [Madina] ! Buleen fa toog. Delluleen [ginnaaw]”. Mu am it kurél ci ñoom buy ñaan ndigal Yonent bi, di wax naan : “Sunuy kër dafa aaruwul”, du loolu de : waaye dañoo bëggoon a daw doŋŋ.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Ku leen doxe woon ginnaaw, ne leen na ñu weddi, kon ñu def ko, te duñu ca yéex,
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
te la ko jiitu, fekkoon na ñu daalante ak Yàlla te dañoo wone ginnaaw [daw xare]. Te daalanteb Yàlla, lu ñuy lijjanti lay doon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Neel : “Su ngeen dawee it, seenug daw duleen jariñ dara ; rey mbaa dee rekk a fiy am, dundu yàggul”.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Neel : “Ana kan moo leen di musal ci Yàlla, su nammee ci yéen safaan walla Mu namm ci yéen yërmaande ? ”. Duñu am wéeruwaay walla ndimbal leneen lu dul Yàlla.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Yàlla xam na ñay gàllankoore ci yéen ak ñay wax : “Ñëwleen ci nun”, fekk na yabuñu ab xare,
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Dañuy soxore loolu ci yéen. Bu am tiit dikke, nga gis ñu di la xool, seen gët yi di wur- wuri mel ni ñuy sukkraat. Bu tiit ma jeexee, ñu di leen teg ay baat yu ñaaw. Ña bañ aw yiw, ñoom ñooñee gëmuñu. Yàlla daldi sepi seeni jëf. Te loolu yomb na Yàlla.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Te ñuy foog ne farandoo ya demuñu. Te bu ñu dikkoon, dañu naa ngéeju bokk ca màngaan ya, duñu xam li ngeen xewle lu dul bu ñu ko laajtoo. Bu ñu nekkee ci seen biir itam, lu néew la ñuy xareji.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Am ngeen royuwaay wu jekk ci Yonentub Yàlla, te képp ku yaakaar Yàlla te gëm Bis- pénc bu mujj ba, tey tuddu, di fàttaliku Yàlla lu bari .
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Ña gëm tigi, ba ñu gisee farandoo ya, dañoo wax ne : “Lii la Nu Yàlla ak ub Yonentam doon dig ; te Yàlla ak ub Yonentam dëggal Nañu”. Te dolliwuleen lenn lu dul ngëm ak jébbulu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Am na ci jullit ñi ñuy dëggal la ñu dëelante woon ak Yàlla. Am na ci ñoom ñu ko matal, am it ci ñoom ñuy négandiku ; te soppiwuñu ca dara ;
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Yàlla dana fey ña dëggaloon ca seen dëggu ga, Dana mbugal it naaféq ya bu ko soobee, walla Mu baal leen. Yàlla Yërëmaakoon la, Jaglewaakoonu [yërmaandeem] la.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Yàlla delloo na yéefar ya, ñu dellook seen mer, amuñu wenn yiw, Yàlla fegal na jullit ñi xeex ba. Yàlla ku bari doole la tey Boroom kàttan.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Te wàcce na ca ña doom jàmmaarlook yéen te bokk ca ñoñ-Téere, [yonjaxal leen], daldi dugal am tiit ci seen xol ya ; ngeen rey ñenn ña, lél ñenn ña.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Mu donnale leen seen suuf, ak seeni kër, ak seeni alal, ak suuf soo xam ne mësuleen ca xand. Yàlla mën na lu ne.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Éy yaw Yonent bi ! Waxal say soxna ne leen : “Su fekke ne dundug àddina sii rekk a leen ñor ak ub taaram, kaayleen ma yombalal leen ko, ci ma fase leen ci am pase mu jekk.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Su fekkee nag ne Yàlla ak Yonentam ak kër gu mujj ga di àllaaxira rekk a leen ñor, [nangeen xam ne] képp kuy rafetal ci yéen, Yàlla dana ko waajalal ag pey gu màgg.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Képp ku bokk ci yéen te def aw ñaawtéef wu bir, dees na ko fulal mbugalam ñaari yoon ! Te loolu yomb na Yàlla.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Képp ku bokk ci yéen te jébbal boppam Yàlla ak ub Yonentam tey jëf u yiw, Dananu ko fulal ag peyam ñaari yoon, te waajalal Nanu ko xéewal gu màgg.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Yemuleen ak yeneen jigéen ñi. Su fekkee ne ragal ngeen Yàlla, buleen di wax waxi caaxaan, yuy tax góor gu xolam tawat di xemmem. Nangeen di wax wax ju yiw njekk.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Nangeen di sax ci seeni kër ; te buleen di baraj-baraji kem ni ko jigéenu jaahiliya yu njëkk ya daan ko defe. Te nangeen di taxawal julli tey génne asaka te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Ndax Yàlla dafa namm a dindi ci yéen, waa kër Yonent bi, lépp luy taq-taq, te laabal leen ba ngeen sell.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Nangeen fàttaliku li Nu leen jàngal ci seen biiri kër, te mu bokk ci laayay Yàlla yi , Alxuraan ak lépp luy xereñe. Yàlla dey Kuy ñeewante la, di Kuy xàmmee.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Naka jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi, way-gëm yu góor ak way-gëm yu jigéen, way- wommatu yu góor ak way-wommatu yu jigéen yi, way-dëggu yu góor ak way-dëggu yu jigéen yi, way-muñ yu góor ak way-muñ yu jigéen, way-ragal yu góor ak way-ragal yu jigéen ya, saraxekat yu góor ak saraxekat yu jigéen yi, woorkat yu góor ak woorkat yu jigéen yi, góor ñiy sàmm seeni pëy ak yu jigéen yi, ñiy tuddu Yàlla lu bari ci góor ñeek jigéen ñi, Yàlla waajalal na leen njéggal ak pey gu màgg.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Su Yàlla ak ub Yonentam àtte mbir ba sottalI, amul benn jullit bu góor ak bu jigéen bu ciy am coppan, te seen àtte ba xas dog. Képp kuy moy Yàllaak ub Yonentam, mi ngi ci ag réer gu bir.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
[Fàttalikul] ba ngay wax ak waa ja Yàlla xéewaloon te yaw it nga xéewaloon ko, ne : “Jàppal sa soxna si te ragal Yàlla, wattandiku Ko”, yaa ngi nëbb ci sa biir lu Yàlla xal a feeñal. Ngay ragal nit ñi te Yàlla moo gën a yeyoo ku Ko ragal. Ba Zaydun fasee soxna soosa, takkal Nanu la ko, ngir jullit yi bañ a aayalati seen jabari doomoo yi, ngeen mën leen takk saa su ñu leen fasee. Te ndigalul Yàlla moom, def rekk.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Aayul ci Yonent bi [muy jëfandikoo] la Yàlla yoonaloon, farataal ko ca ña ko jiitu woon. Te ndigalul Yàlla luy sax la.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Ña nga xam ne ñooy jottali bataaxali Yàlla yi te ragal Ko, te it duñu ragal keneen ku dul Moom. Ndax Yàlla doy na sëkk ci waññi [natt] jëf yi.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Muhammad du baayub kenn ci seeni gaay, waaye ndawul Yàlla te di mujjug Yonent yi. Yàlla xam na lépp lu ne.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen di farataal, di tudd Yàlla lu bari.
ﰂﰃﰄﰅ
te nangeen di Ko sàbbaal suba ak ngoon.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Mooy kiy julli ci yéen, di leen ñaanal, - Mook ay Malaakaam, - ngir génne leen cig lëndëm, jëme leen cig leer ; te Mu di Jaglewaakoonu yërmaandeem ci ñi gëm.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Seenub nuyyoo Bis nuy dajeek Moom : “Jàmm rekk”, te mu waajal leen ag pey gu tedd .
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Éy yaw Yonent bi ! Noo la yebal ngir nga doon seede, di béglekat, di xuppekat.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
té woote jëme ci Yàlla ; te di làmp bu leer.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Te ngay bégal jullit ñi, ne leen am nañu ca Yàlla ngëneel lu màgg.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Te bul topp mukk yéefar yeek naaféq yi, te it bul faale seen lor, nangay wéeru ci Yàlla, Yàlla doy na sëkk wéeruwaay.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Éy yéen ñi gëm ! Su ngeen takkee jabar ci jullit [jigéen ñi] ba joxe can ga, su ngeen leen fasee te laalewuleen, warul a jàpp yedda. Nangeen leen boyal ci njekk.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Éy yaw Yonent bi ! Daganal Nanu la sa soxna yi nga jox can ak ñi nga moom [jaam bu jigéen] ak doom yu jigéen yu sa baay-tëx ak sa doomi bàjjen yu jigéen ak doomi nijaay yu jigéen ak sa doomi ndey-tëx ju jigéen, - ñi gàddaay ànd ak yaw, - ak jigéenu jullit ju may boppam Yonent bi, bu ko Yonent bi bëggee takk soxna : Lew na la domm, waaye jullit yu góor ñi duñu ko sañ. Ndax Noo gën a xam li Nu farataal ci ñoom ak seeni soxna ak seeni jaam yu jigéen, [li ko waral moo di] ngir rekk dellu te yeddu. Te Yàlla Jéggalaakoon la yërmaandeem.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Mën nga xaarloo ku la soob ci ñoom, dëkkoo ku la ca soob. Ak lu la ca neex ca ña nga beddi woon, aayul ci yaw. Te loolu moo leen dàqal, buñu yërëmtalu te nañu gërëm ñoom ñépp ca la nga leen jàppe. Yàlla xam na li nekk ci seeni xol. Yàlla ku xam la, Ku lewet la.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Ginnaaw loolu, jigéen ñi duñu dagan ci yaw. Walla nga di leen wecceek yeneeni jabar, doonte la seenub taar yéem na ; - ba mu des say jaam yu jigéen. Yàlla kuy fuglu la ci lépp.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen dugg kër Yonent bi, lu dul ci ndigal, buleen fay xaaraanu ñam. Waaye bu ñu leen woowee, nangeen dugg. Bu ngeen noppee ca lekk ga, daldi leen tasaaroo te buleen toog di waxtaan. Ndax loolu, dafay lor Yonent bi mu di leen ko rus a wax, te Yàlla Moom rusul dara ci dëgg. Te su ngeen deeti laaj jegeñam ña dara, nangeen koy laaj ci ginnaaw kiiraay : ndax loolu moo gën a laab ci seeni xol [yéen ak ñoom] ; Te it waruleen di lor Yonent bi, waxantumalaak ngeen di takk soxnaam ginnaawam ; Ba fàwwu, loolu lu rëy la ca Yàlla.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
Mbir mu ngeen mën feeñal mbaa ngeen nëbb ko,... Yàlla xam na ko.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Aayul ci ñoom [soxna yi] seeni baay [di ko def], walla seeni doom, walla seen mbokk, walla seeni doomi mbokk mu jigéen, walla seeni jabar, walla seeni jaam. Te nangeen ragal Yàlla ndax Yàllaa seede lépp lu ne.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Yàlla ak i Malaakaam dañuy julli ci Yonent bi ; Éy yéen ñi gëm, jullileen ci moom te sëlmal ci moom .
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Ñi nga xam ne dañuy lor Yàlla ak ub Yonentam, Yàlla rëbb na leen ci àddina ak ca àllaaxira, te waajalal na leen mbugal muy doyadiloo, di toroxtale.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Ña nga xam ne dañuy lor jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi te defuñu lu ko jar, ñangay yenu aw duur ak bàkkaar bu rëy.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Éy yaw Yonent bi ! Waxal say soxna ak say doom yu jigéen ak jigéeni jullit ñi, ñuy muur seenu yaram : ci la ñu leen di gën a xame te kenn duleen di xas. Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Su fekkee ne naaféq yeek lëjëlkat yeek woroom xel yu tawat yi dëkk [Medina] bàyyiwuñu, Danaa xiir ci seen kaw, te kon lim bu néew moo ca déeti dëkkaale ak yéen.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Muy ñuñu rëbb. Fu ñu jublu, ñu faagaagal leen :
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Lii mooy sunnas Yàlla, ab dogalam ci ña fi jiitu woon te sunnas Yàlla du soppiku mukk.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Nit ñaa ngi lay laaj ci mbiri Bis-pénc ba. Waxal ne : “Yàllaa ko xam”. Te yaw sax loo ci xam ? Amaana Bis-pénc ba di lu jegeñ.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Yàlla rëbb na yéefar yi te waajalal na leen aw safara,
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
dañu fay béel fàww, duñu fa am ku leen méngoo, duñu fa am ndimbal.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Bis ba ñuy wëlbati seeni kanam ca Safara, ñuy wax naan : “Aka neexoon nu toppoon Yàlla, nu toppoon Yonent ba ! ”.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, nun dey toppoon nanu sunuy sang ak sunuy kilifa. Ñu réerale nu ak yoon wa.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Boroom sunu, fulandileen mbugal te nga rëbbleen rëbb mu rëy”.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen mel ni ña daan lor Muusaa, di ko tuumaal. Far Yàlla setal ko ca tuuma ya, di ku mu jubaloon.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Éy yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla tey wax wax ju jub.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
kon dey Dana leen yéwénalal seeni jëf, jéggal leen it seeni bàkkaar. Te képp kuy topp Yàlla ak ub Yonentam, dana texe texe gu màgg.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Gaaral Nanu ndénkaan lii asamaan yeek suuf si ak tundi doj yi . Ñu lànk koo yenu ngir ug ragal ko, nit moo ñëw ne ko fànkul yenu ko ; te nit nekk ab tooñaakoon bu xamadi.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
[Ci loolu] Yàlla dana mbugal naaféq yu góor yeek yu jigéen, ak bokkaalekat yu góor yeek yu jigéen yi te Dana nangu tuubug jullit yu góor yeek yu jigéen yi. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







