Al-Baqara · 220/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ ۗ وَيَسْأَلُونَكَ عَنِ الْيَتَامَىٰ ۖ قُلْ إِصْلَاحٌ لَّهُمْ خَيْرٌ ۖ وَإِن تُخَالِطُوهُمْ فَإِخْوَانُكُمْ ۚ وَاللَّهُ يَعْلَمُ الْمُفْسِدَ مِنَ الْمُصْلِحِ ۚ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ لَأَعْنَتَكُمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ ۝٢٢٠
Fid dunyaa wal aakhirah; wa yas`aloonaka `anil yataamaa qul islaahullahum khayr, wa in tukhaalitoohum fa ikhwaanukum; wallaahu ya`lamul mufsida minalmuslih; wa law shaaa`al laahu la-a`natakum; innal laaha `Azeezun Hakeem
📖 Tekkim Wolof
ci àddina ak ca àllaaxira ! Te danañu laaj lu jëm ci jirim yi. Neel : “Yéwénalal-leen [ba seeni alal mën a yokk]. Moo gën bu ngeen jaxasoo ak ñooñu, aayul ndax seeni mbokk lañu ci diine”. Yàlla xàmmee na ñiy yàq ak ñiy defar. Te bu sooboon Yàlla mu sonnal leen. Moom Yàlla moo not lépp, moo xereñ.
🎧 Dégg

📜 Aaya 218-222 — Al-Baqara

218إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا وَالَّذِينَ هَاجَرُوا وَجَاهَدُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ أُولَٰئِكَ يَرْجُونَ رَحْمَتَ اللَّهِ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ña gëm ak ña gàddaay tey jihaad [xeex] ci yoonu Yàlla, mën nañoo yaakaar yërmaandey Yàlla. Te Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
219۞ يَسْأَلُونَكَ عَنِ الْخَمْرِ وَالْمَيْسِرِ ۖ قُلْ فِيهِمَا إِثْمٌ كَبِيرٌ وَمَنَافِعُ لِلنَّاسِ وَإِثْمُهُمَا أَكْبَرُ مِن نَّفْعِهِمَا ۗ وَيَسْأَلُونَكَ مَاذَا يُنفِقُونَ قُلِ الْعَفْوَ ۗ كَذَٰلِكَ يُبَيِّنُ اللَّهُ لَكُمُ الْآيَاتِ لَعَلَّكُمْ تَتَفَكَّرُونَ
- Danañu la laaj lu jëm ci sàngara ak wure. Neel : “Ñoom ñaar bàkkaar bu rëy a nga ca ak njariñi nit ñi ; waaye, la cay bàkkaar ca ñoom ñaar moo ëpp fuuf njariñ ya”. Danañu la laaj : “Lan la ñu war a joxe ci alal? ” Neel : “Aw des.”. Noonu la leen Yàlla di leeralee laaya ya ndaxtelee ngeen di xalaat
220فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ ۗ وَيَسْأَلُونَكَ عَنِ الْيَتَامَىٰ ۖ قُلْ إِصْلَاحٌ لَّهُمْ خَيْرٌ ۖ وَإِن تُخَالِطُوهُمْ فَإِخْوَانُكُمْ ۚ وَاللَّهُ يَعْلَمُ الْمُفْسِدَ مِنَ الْمُصْلِحِ ۚ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ لَأَعْنَتَكُمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
ci àddina ak ca àllaaxira ! Te danañu laaj lu jëm ci jirim yi. Neel : “Yéwénalal-leen [ba seeni alal mën a yokk]. Moo gën bu ngeen jaxasoo ak ñooñu, aayul ndax seeni mbokk lañu ci diine”. Yàlla xàmmee na ñiy yàq ak ñiy defar. Te bu sooboon Yàlla mu sonnal leen. Moom Yàlla moo not lépp, moo xereñ.
221وَلَا تَنكِحُوا الْمُشْرِكَاتِ حَتَّىٰ يُؤْمِنَّ ۚ وَلَأَمَةٌ مُّؤْمِنَةٌ خَيْرٌ مِّن مُّشْرِكَةٍ وَلَوْ أَعْجَبَتْكُمْ ۗ وَلَا تُنكِحُوا الْمُشْرِكِينَ حَتَّىٰ يُؤْمِنُوا ۚ وَلَعَبْدٌ مُّؤْمِنٌ خَيْرٌ مِّن مُّشْرِكٍ وَلَوْ أَعْجَبَكُمْ ۗ أُولَٰئِكَ يَدْعُونَ إِلَى النَّارِ ۖ وَاللَّهُ يَدْعُو إِلَى الْجَنَّةِ وَالْمَغْفِرَةِ بِإِذْنِهِ ۖ وَيُبَيِّنُ آيَاتِهِ لِلنَّاسِ لَعَلَّهُمْ يَتَذَكَّرُونَ
Buleen takk soxna jigéen ñuy bokkaale li feek gëmuñu, jaam bu jigéen bu gëm moo gën jigéen [ju ñuy tuddeeb sang] juy bokkaale, doontale yéem na leen. Buleen may jabar góor ñuy bokkaale, jaam bu góor moo gën góor [gu ñuy tuddeeb sang] guy bokkaale, doontale yéem na leen. Ñooña dañuy woote jëme Safara ;Yàlla moom di woote jëme Àjjana ak ug njéggal, ci ndigalam. Te dana leeral ay laayaam nit ña ndax ñu fàttaliku [seen Boroom] !
222وَيَسْأَلُونَكَ عَنِ الْمَحِيضِ ۖ قُلْ هُوَ أَذًى فَاعْتَزِلُوا النِّسَاءَ فِي الْمَحِيضِ ۖ وَلَا تَقْرَبُوهُنَّ حَتَّىٰ يَطْهُرْنَ ۖ فَإِذَا تَطَهَّرْنَ فَأْتُوهُنَّ مِنْ حَيْثُ أَمَرَكُمُ اللَّهُ ۚ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ التَّوَّابِينَ وَيُحِبُّ الْمُتَطَهِّرِينَ
- Danañu la laaj lu jëm ci mbërëg . - Neel : “Moom sobe la. Deeleen beru jigéen ña bu ñu nekkee ci mbërëg, buleen jege ba bañuy laab. Suñu laabee, ngeen duggeleen fa Yàlla digle ndax Yàlla sopp na ñay tuub, sopp na itam ñay laabal seen bopp”.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
220Aaya

Tekki — Al-Baqara 220

Simoore Al-Baqara Aaya 220 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ci àddina ak ca àllaaxira ! Te danañu laaj lu…

Simoore Aaya 220/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 218–222. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers