An-Nur · 2/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
الزَّانِيَةُ وَالزَّانِي فَاجْلِدُوا كُلَّ وَاحِدٍ مِّنْهُمَا مِائَةَ جَلْدَةٍ ۖ وَلَا تَأْخُذْكُم بِهِمَا رَأْفَةٌ فِي دِينِ اللَّهِ إِن كُنتُمْ تُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ ۖ وَلْيَشْهَدْ عَذَابَهُمَا طَائِفَةٌ مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ ۝٢
Azzaaniyatu wazzaanee fajlidoo kulla waahidim minhumaa mi`ata jaldatinw wa laa taakhuzkum bihimaa raafatun fee deenil laahi in kuntum tu`minoona billaahi wal Yawmil Aakhiri wal yashhad `azaabahumaa taaa`ifatum minal mu`mineen
📖 Tekkim Wolof
Njaalookat bu jigéen ak njaalookat bu góor, nangeen leen dóor téeméeri yar. Te buleen leen yërëm [ci li diine tege] - ndegam gëm ngeen Yàlla ak Bis-pénc. Te itam mbugalum njaalookat yooyu, na ko mbooloo mu bari teewe ci jullit yi.
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-4 — An-Nur

1سُورَةٌ أَنزَلْنَاهَا وَفَرَضْنَاهَا وَأَنزَلْنَا فِيهَا آيَاتٍ بَيِّنَاتٍ لَّعَلَّكُمْ تَذَكَّرُونَ
Lii aw saar la wu Nu wàcce farataal ko, mu nekk ci biiram ay laaya yu Nu leeral [faramfàcce] ndax xéy-na ngeen fàttaliku”.
2الزَّانِيَةُ وَالزَّانِي فَاجْلِدُوا كُلَّ وَاحِدٍ مِّنْهُمَا مِائَةَ جَلْدَةٍ ۖ وَلَا تَأْخُذْكُم بِهِمَا رَأْفَةٌ فِي دِينِ اللَّهِ إِن كُنتُمْ تُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ ۖ وَلْيَشْهَدْ عَذَابَهُمَا طَائِفَةٌ مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ
Njaalookat bu jigéen ak njaalookat bu góor, nangeen leen dóor téeméeri yar. Te buleen leen yërëm [ci li diine tege] - ndegam gëm ngeen Yàlla ak Bis-pénc. Te itam mbugalum njaalookat yooyu, na ko mbooloo mu bari teewe ci jullit yi.
3الزَّانِي لَا يَنكِحُ إِلَّا زَانِيَةً أَوْ مُشْرِكَةً وَالزَّانِيَةُ لَا يَنكِحُهَا إِلَّا زَانٍ أَوْ مُشْرِكٌ ۚ وَحُرِّمَ ذَٰلِكَ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ
Njaalokat bu góor du sëy ak ku dul njaalookat bu jigéen walla bokkaalekat. Njaalookat bu jigéen, kenn du sëy ak moom ku dul njaalookat bu góor walla bokkaalekat te loolu araam na ci jullit ñi.
4وَالَّذِينَ يَرْمُونَ الْمُحْصَنَاتِ ثُمَّ لَمْ يَأْتُوا بِأَرْبَعَةِ شُهَدَاءَ فَاجْلِدُوهُمْ ثَمَانِينَ جَلْدَةً وَلَا تَقْبَلُوا لَهُمْ شَهَادَةً أَبَدًا ۚ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ
Ñay yàq deru jigéen ña, saŋewu [ci jiiñ leen njaaloo] ba noppi ñàkk a indi ñeenti seede, nangeen leen dóor juróom-ñetti fukki yar, te buleen nangooti ñuy seede ba fàwwu. Ñoom ay saay-saay lañu,
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
2Aaya

Tekki — An-Nur 2

Simoore An-Nur Aaya 2 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Njaalookat bu jigéen ak njaalookat bu góor, nangeen leen dóor…

Simoore Aaya 2/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 1–4. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers