Simoore An-Nur
64 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Lii aw saar la wu Nu wàcce farataal ko, mu nekk ci biiram ay laaya yu Nu leeral [faramfàcce] ndax xéy-na ngeen fàttaliku”.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Njaalookat bu jigéen ak njaalookat bu góor, nangeen leen dóor téeméeri yar. Te buleen leen yërëm [ci li diine tege] - ndegam gëm ngeen Yàlla ak Bis-pénc. Te itam mbugalum njaalookat yooyu, na ko mbooloo mu bari teewe ci jullit yi.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Njaalokat bu góor du sëy ak ku dul njaalookat bu jigéen walla bokkaalekat. Njaalookat bu jigéen, kenn du sëy ak moom ku dul njaalookat bu góor walla bokkaalekat te loolu araam na ci jullit ñi.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Ñay yàq deru jigéen ña, saŋewu [ci jiiñ leen njaaloo] ba noppi ñàkk a indi ñeenti seede, nangeen leen dóor juróom-ñetti fukki yar, te buleen nangooti ñuy seede ba fàwwu. Ñoom ay saay-saay lañu,
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
ba mu des ña rëccu, tuub ginnaaw loolu, tey jëf u yiw, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Ñay tuumaal seeni jabar te amuñu ay seede lu dul seen bopp, na waat ci Yàlla ñeenti yoon ne ku dëggu la,
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
juróomeel ba mu waat ne “rëbbum Yàlla [sori yërmaandeem] na dal ci kawam su dee fenkat la”.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Su jabar ja waate ñeenti yoon ci Yàlla ne waa ja fenkat la, kenn du ko sànni xeer [rajmu],
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
ndaw sa itam na waat ne merum Yàlla na wàcc ci kawam su jëkkëram ja waxee dëgg [pasem rëbboo dootu ko fàttaliku mukk] muy juróomeelu waatam.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Cëy dugankoon ak ngënéelul Yàlla ci yéen ak yërmaandeem, waaye nag Yàlla Nanguwaakoonu tuub la bu xeréñ !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Ña leen di indil jiixi-jaaxa [naaféq ya], ab kurél lañu ci yéen. Buleen ko jàppe ay, yiw la ci yéen. Kenn ku nekk ci yéen dana jot bàkkaaram. Képp ku ca ëppal dana am mbugal mu màgg.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Lu tere woon jullit ñu góor ñeek jigéen di jort ci aw yiw ci seen diggante ? Ana lu tere ca saa sa ñu ne : “Lii kat aw duur la ” ?
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Bu ñu indi woon sax ñeenti seede, waaye bu ñu ko indiwul [ngeen daldi xam fa saa sa] ne ñoom kat ay fenjat lañu.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Cëy dogankoon ak ngënéelul Yàlla ci yéen fii ci àddina sii ak fee ci àllaaxira, kon dey seen duur wii mbugal mu rëy dana leen ci dal,
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
ngir yéen a ngi jokk-jolaate xibaar ba ak seeni làmmiñ, di wax ci seeni gémmiñ loo xam ne amuleen ci benn xam-xam ; ngeen jàppe ko lu doyadi te fekk muy lu rëy a rëy fa Yàlla.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Ana lan moo tere, ba ngeen ko déggee, ngeen sàbbaal Yàlla te wax ne : “Wii duur wu rëy warut a génne ci seeni làmmiñ” ?
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Yàllaa ngi leen di ñaax ngeen bañ a dellu mukk ci jëf ju ni mel, ndegam ay way-gëm ngeen.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Yàllaa ngi leen di faramfàcceel i laayam de, te Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Ñi bëgg a tasaarey ñaawtéef ci biir jullit ñi, mbugal mu metti dana leen dal ci àddina ak àllaaxira. Yàlla xam na te yéen xamuleen.
ﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒ
Cëy dogankoon ak ngënéelul Yàlla ak yëmaandeem ci yéen, waaye Yàlla Moom ku ñeewant la, di Jaglewaakoon ...
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen topp jeegoy Séytaane. Ku topp jéegoy Séytaane, [na xam ne] Séytaane ñaawtéef ak njekkar la am. Dogankoon ak ngënéelul Yàlla ak yërmaandeem, kenn ci yéen du sellal. Waaye nag Moom Yàlla mooy sellal ku Ko soob. Te Yàlla Kuy dégg la, Ku xam la.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Te ña Yàlla jox wërsëg te ñu bokk ci yéen, buñu cay ñàkk a jox jegeñaale ya ak ndóol ya ak ñay gàddaay ci yoonu Yàlla. Nañuy jéggale tey jéllale. Moo xanaa bëgguleen Yàlla jéggal leen ? Yàlla dey Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la !
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Ña nga xam ne dañuy tuumaal [njaaloo] jigéeni jullit ñi amul ay caaxaan, ña koy def danañu sori yërmaande ci àddina ak ca àllaaxira ; te it danañu am mbugal mu metti,
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Bu keroogee [Bis-pénc ba], seen làmmiñ ya, seeni yoxo ak seeni tànk danañu seede ci seen kaw la ñu daan def.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Bu Bis boobaa, Yàlla dana leen jox, indil leen seen diine ja di dëgg ; [Bu keroogee] lañuy xam ne Yàllaay dëgg gu fés ga.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Jigéen ñu bon ña témboo nañook góor ñu bon ña. Jigéen ñu baax ña témbook góor ñu baax ña. Góor ñu baax ña it ñoom témbook jigéen ñu baax ña. Ñoom set nañu wecc ca la ñuy wax. Am nañu ag njéggal te am nañu pey gu duun.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen dugg kër gu dul seeni kër ndare bu dangeen a yéglu te nuyyu waa kër ga. Loolu dey moo gën ci yéen ndax xéy-na ngeen fàttaliku.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Bu ngeen ca fekkul kenn, buleen ca dugg li feek joxuñuleen ca ndigal. Te bu ñu la nee : “Dellul [damaa jàpp]”, dellul. Loolu moo gën a sell ci yéen. Yàlla aka xam li ngeen di def.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
[Waaye] bàkkaar amul ci yéen ngeen dugg ci kër gu ñu dëkkewul te seen tobarte nekk fa. Yàlla xam na li ngeen feeñal ak li ngeen di nëbb.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Neel war na ci way-gëm ñi ñuy sajj seenub gis tey sàmm seen pëy. Looloo gën a sell ci yéen. Te nag Yàlla ku deñ la kumpa ci li ngeen di def.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Waxal jullit ñu jigéen ñi ne leen : nañuy sajj seenub gis, nañuy sàmm seen pëy, te nañuy bañ a feeñal seenub taar lu dul li ca feeñ, nañuy sàng [muur] seeni yaram ; te buñu feeñalal seenub taar ku dul seen jëkkër, walla seen baay, walla seen baayi jëkkër, walla seen doom, walla seen doomi jëkkër, walla seen càmmiñ, walla seen doomi càmmiñ, walla seen dommi jigéen, walla seen tàpp, walla xaleel yu géwantagul. Te it nañuy bañ a dóor seeni tànk ngir di feeñal li làqu ca seenub taar. Tuub-leen yéen ñépp jëm ci Yàlla yéen ña di way-gëm ndaxtelee ngeen texe.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Takk-leen [jabar/jëkkër] ci ña séyul ak ca ña yiw te bokk ci seeni jaam [góor, jigéen]. Su fekkee dañoo ndóol, Yàlla Dana leen woomalal ci ngënéelam. Yàlla ku yaatu la, Ku xam la.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Ña amul lu ñu takkee jabar, nañu sàmmu ba baa Yàlla di leen wërsëgal ci ngënéelam. Seen jaam ñii, sàkku ngeen goreel leen, nangeen bindanteek ñoom su ñu dee ñu yiw ; te it nangeen di joxe ca alali Yàlla ja leen Yàlla jox. Buleen di xiirtal seen jaam yu jigéen ci ñuy jaay seen bopp ngir bëgg doŋŋ ci loolu alali àddina. Ku ko daan def [te tuub ko], Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Wàcce Nanu ci yéen ay laaya yu Nu faramfàcce, di ay misaal yu bawoo ca ña leen jiitu woon, di ag waare ci ña ragal Yàlla !
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Yàllaay leerug asamaan yeek suuf si. Te leeram googu dafa mel ni ab cëgg bu ami làmp ci biiram. Làmp boobu nekkaat ci ab weer, weer boobu mel ni bidiw buy nes-nesi ; ñu di ko taalee ci diwub garabug oliw gu tedd [gu wuuteeg yi ñu miin]. Diwam ga xaw naa mën a leeral te safara laalu ko. Te Yàlla dana saddal nit ñi ay leebu te Yàlla xam na lu ne.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Ci biiri kër [jàkka] yoo xam ne Yàlla digle ñu di fa tudd aw Turam, di Ko yékkati ; di Ko ca sàbbaal suba ak ngoon,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
aw gaay ñoo xam ne njulaakum njaay duleen mës a fàbbi ci tudd Yàlla ak a taxawal julli, ak génne asaka, ngir ñoom kat dañoo ragal Bis ba xol ya di wëlbëtiku ak gët ya.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
[Ci loolu], Yàlla dana leen feye la gën a rafet ca la ñu jëf. Dana leen dolli ngëneel. Te Yàlla dana wërsëgal ku ko soob ci lu àndul ak ug waññi [lijjanti].
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Ña weddi, di ay jéefar, ñoom seeni jëf dafa mel ni ñàndóox, bu ko boroomu mar séenee, dakoy jàppe ndox. Saa bu fa agsee, du fa fekk tus ; Yàlla rekk la fay fekk Mu waññal ko ay jëfam ba mu mat sëkk, te moo ne Yàllaa ka gaaw ab lijjanti.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
[Jëfi yéefar ba-tey dafa mel ni] lëndëmug géej guy duusu : ganax ci kaw ganax, ay niir yu lëndëm tegaloo tiim ko. Ba sax moom bu génnee loxoom, du ko xaw a gis. Te képp ku Yàlla defalul ag leer, du am ag leer.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
[Xanaa gisuloo ne] ñépp ñu nekk diggante asamaan yeek suuf si, dañuy sàbbaal Yàlla ; picc yi sax dañuy sàppe. Lenn lu nekk xam na naka lay jullee ak na muy sàbbaalee. Yàlla xam na li ñuy def.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Yàllaay boroom nguurug asamaan yeek suuf si. Te ca Moom la ñéppiy dellu.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚ
Xanaa gisuloo ne Yàllaay wommat niir yi ? Dajale leen mu diw xiin, nga gis ndox di ca génnee bawoo asamaan. Ci tundi yuur lay sottikoo, Mu di ko dottil ku ko soob. Di ko xañ ku ko soob. Melxatug melaxam xaw naa mën a yàq ab gis.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Yàlla mooy jéllasante guddeek bëccëg. Boroom gis-gis yi mën nañu cee xalam.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Yàllaa bind mala yépp cim ndox. Am na ci yuy doxee biiram, am na ci yuy doxee ñaari tànk, am na ci yuy doxee ñeenti tànk. Yàllaay bind, sàkk [sos] lu ko soob te Yàlla mën na lu ne.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
[Wér na céŋŋ ne] wàcce Nanu ay laaya [kàddu] yu leer nàññ. Te Yàlla dana gindi ku ko soob jëme ko ci yoon wu jub xocc wa.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Danañuy wax naan : “Gën nanu Yàlla ak Yonent bi, topp nanu it”. Mu am kurél bu bokk ñoom wëlbëtiku ginnaaw loolu. Ñoom gëmuñu.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Saa su wootees leen jëme ci Yàlla ak ci Yonentam ngir Mu àtte seen diggante, ndekete yoo ab kurél ci ñoom day dummóoyu.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Su ñu nekkoon ci dëgg kon danañu dikk [ci Yonent bi] topp ko.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Moo ndax dañoo am woppi xol ? Walla dañuy jiixi-jaaxa ? Walla dañuy ragal Yàlla ak ub Yonentam yiir leen ? Deewalaay !... ñoom ay tooñkat lañu.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Ñi gëm Yàlla [jullit ñi], saa su ñu déggee woote buy jëme ci Yàlla ak ub Yonentam ngir àtte seen diggante, seeni wax du doon lu dul ne : “Dégg nanu, topp nanu”. Ñooña ñooy ña texe.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Képp kuy topp Yàlla ak ub Yonentam, ragal Yàlla te di Ko fuglu, ñooña ñooy ña texe.
ﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙ
Danañuy giñ ci Yàlla fa mu gën a ñàngee, naan boo leen digalee danañu génn [dem xare ji]. Neel : “Buleen giñ. [Wax ji rekk doyul]. Yàlla xam na li ngeen di def”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Neel : “Toppleen Yàlla te topp ab Yonentam. Bu ñu dummóoyoo [ndigal la] ñoom nag,... yéen itam ak seen mbiri bopp ; su ngen toppee [ndigal la] gindiku”. Yonent bi moom jottal rekk a ko ci war.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Yàlla dig na ña gëm ci ñoom, tey jëf u yiw ne def na leen kuutaay ci kaw suuf kem ni Mu defe woon kuutaay ca ña leen jiitu woon. Te Dana leen yombalal jëfandikoo diiney [Islaam] ji Mu leen tànnal. Te it Dana leen soppil ginnaaw tiitaange kóolute. Ñu di Ma jaamu te duñu Ma bokkaale lenn. Képp ku weddi ginnaaw loolu, kon ñoom ñooy saay-saay sa.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Nangeen di taxawal julli tey génne asaka, te it nangeen topp Yonent bi, ndaxtele yërëmees leen.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Buleen foog ne yéefar yi dañoo tiiñ [Yàlla] ci kaw suuf. Seenub daluwaay Safara la. Ndaw muj gu bon.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Éy yéen ñi gëm ! Na leen seeni jaam ak seeni xale yi matagul [mukkàllaf] di yëglu ba la ñoo dugg ci yéen ci ñetti waxtu yii : lu jiitu jullig fajar, ak bu ngeen summikoo ci njolloor, ak ginnaaw jullig gee ; loolu ñetti awra la ba ca waxtuy julli ya. Aayul ci yéen ngeen di gëwéelu di nemmeekuwante. Lii nag, Yàllaa leen cay faramfàcceel ay laayaam [kàddu], Yàlla ku xam la, Ku xereñ la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Xale yi itam [nañuy yëglu saa su ñu matee mukkàllaf], nañu yëglu na ko ña leen jiitu daan yëgloo. Nii la leen Yàlla di faramfàccelee ay kàddoom, te Yàlla ku xam la, Ku xereñ la.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Aayul ci jigéen ñi toog ba yaakaaratuñoo sëy ñuy summiku te bañ a wut ab taar, [waaye] bu ñu muuroon seeni yaram moo gën ci ñoom. Yàlla kuy dégg la, Ku xam la.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Aayul itam ci silmaxa [gumba], aayul itam ci ku lompoñ [làggi], aayul itam ci ku wopp, aayul itam ci yéen ci seen bopp ngeen di lekke ci seeni kër walla seeni këri baay, walla seeni këri mbokk yu jigéen, walla seeni këru baay-tëx, walla seeni këru bàjjen, walla seeni kër nijaay, walla seeni këri yaay-tëx, walla seeni jaam, walla seeni xarit. Aayul ci yéen ngeen di lekkandoon walla ngeen beru. Bu ngeen duggee ci kër, nangeen di nuyyuwante ci nuyyoo bu bawoo ca Yàlla, teey te barkeel . Noonu la leen Yàlla di faramfàccelee laaya ya ndaxtele ngeen xel-lu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Way-gëm ña dëgg-dëgg ñooy ña gëm Yàlla ak ub Yonentam, te mépp mbir mu ñu bokk ak nit ñi, bala ñu caa jëfandiku, laaj ndigal. Ñooñii nga xam ne ñoo lay laaj ndigal ngir seen itte bopp, na nga jox ndigal ña la soob ; te nanga leen jéggalul Yàlla, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Buleen def wooteb Yonent bi ni wooteb jenn waay ci yéen. Yàlla dana xam ñay potoxlu te bokk ci yéen. Ña nga xam ne dañuy moy ndigalam, nañu moytu ab sànje dal leen mbaa mbugal mu metti.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Ca dëgg-dëgg, Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Moo gën a xam li ngeen nekk, bu keroogee ba ñu leen di delloo ca Moom, Mu di leen xibaar la ñu defoon. Yàlla kat xam na lépp.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers