At-Tawba · 103/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
خُذْ مِنْ أَمْوَالِهِمْ صَدَقَةً تُطَهِّرُهُمْ وَتُزَكِّيهِم بِهَا وَصَلِّ عَلَيْهِمْ ۖ إِنَّ صَلَاتَكَ سَكَنٌ لَّهُمْ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ ۝١٠٣
Khuz min amwaalihim sadaqtan tutahhiruhum wa tuzakkeehim bihaa wa salli `alaihim inna salaataka sakanul lahum; wallaahu Samee`un `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Jëlal ci seen alal ab sarax (asaka) ngir laabal leen ca ak sellal leen ca, te nga ñaanal leen. Ndax sa ñaan dalum xel la ci ñoom. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 101-105 — At-Tawba

101وَمِمَّنْ حَوْلَكُم مِّنَ الْأَعْرَابِ مُنَافِقُونَ ۖ وَمِنْ أَهْلِ الْمَدِينَةِ ۖ مَرَدُوا عَلَى النِّفَاقِ لَا تَعْلَمُهُمْ ۖ نَحْنُ نَعْلَمُهُمْ ۚ سَنُعَذِّبُهُم مَّرَّتَيْنِ ثُمَّ يُرَدُّونَ إِلَىٰ عَذَابٍ عَظِيمٍ
Am na it ca sàmm sa nekk ca seen wet, ay naaféq, ak waa (Madina). Am na ñu téppeeral cig naaféq. Xamuloo leen, (waaye) Nun xam Nanu leen. Dananu leen mbugal ñaari yoon ba noppi Nu door leen a delloo ca mbugal mu màgg ma.
102وَآخَرُونَ اعْتَرَفُوا بِذُنُوبِهِمْ خَلَطُوا عَمَلًا صَالِحًا وَآخَرَ سَيِّئًا عَسَى اللَّهُ أَن يَتُوبَ عَلَيْهِمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ak ñeneen ña nangu seeni bàkkaar (tuub nañu), jaxase woon nañu jëf yu sell ak yeneen yu ñaaw. Xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla nag Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
103خُذْ مِنْ أَمْوَالِهِمْ صَدَقَةً تُطَهِّرُهُمْ وَتُزَكِّيهِم بِهَا وَصَلِّ عَلَيْهِمْ ۖ إِنَّ صَلَاتَكَ سَكَنٌ لَّهُمْ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Jëlal ci seen alal ab sarax (asaka) ngir laabal leen ca ak sellal leen ca, te nga ñaanal leen. Ndax sa ñaan dalum xel la ci ñoom. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
104أَلَمْ يَعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ هُوَ يَقْبَلُ التَّوْبَةَ عَنْ عِبَادِهِ وَيَأْخُذُ الصَّدَقَاتِ وَأَنَّ اللَّهَ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla Moom Dana nangu tuub ciy jaamam, te Dana jël it sarax ya, te Moom Yàlla Mooy Nanguwaakoon cig tuub, di Jaglewaakoon.
105وَقُلِ اعْمَلُوا فَسَيَرَى اللَّهُ عَمَلَكُمْ وَرَسُولُهُ وَالْمُؤْمِنُونَ ۖ وَسَتُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Neel : “Jëfleen (lu leen soob), Yàlla ak ub Yonentam ak jullit ña, Danañu gis seeni jëf, te dees na leen delloo ca Aji-xam ja kumpa ak la feeñ. Mu xamal leen la ngeen daan def”.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
103Aaya

Tekki — At-Tawba 103

Simoore At-Tawba Aaya 103 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Jëlal ci seen alal ab sarax (asaka) ngir laabal leen…

Simoore Aaya 103/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 101–105. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers