At-Tawba · 102/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
وَآخَرُونَ اعْتَرَفُوا بِذُنُوبِهِمْ خَلَطُوا عَمَلًا صَالِحًا وَآخَرَ سَيِّئًا عَسَى اللَّهُ أَن يَتُوبَ عَلَيْهِمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝١٠٢
Wa aakharoona` tarafoo bizunoobihim khalatoo `amalan saalihanw wa aakhara saiyi`an `asal laahu ai yatooba `alaihim; innal laaha Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Ak ñeneen ña nangu seeni bàkkaar (tuub nañu), jaxase woon nañu jëf yu sell ak yeneen yu ñaaw. Xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla nag Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 100-104 — Simoore At-Tawba

100وَالسَّابِقُونَ الْأَوَّلُونَ مِنَ الْمُهَاجِرِينَ وَالْأَنصَارِ وَالَّذِينَ اتَّبَعُوهُم بِإِحْسَانٍ رَّضِيَ اللَّهُ عَنْهُمْ وَرَضُوا عَنْهُ وَأَعَدَّ لَهُمْ جَنَّاتٍ تَجْرِي تَحْتَهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۚ ذَٰلِكَ الْفَوْزُ الْعَظِيمُ
Ña jiitu woon bu jëkk ca ña gàddaayoon (Muhaajiruuna ya) ak ña leen dalaloon (Lansaar ya) ak ña leen toppoon cig rafetal (seeni jëf), Yàlla bég na ci ñoom, te ñoom it bég nañu ci Yàlla. Te it sédde na leen Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel ba fàwwu. Loolu moo di texe gu màgg ga !
101وَمِمَّنْ حَوْلَكُم مِّنَ الْأَعْرَابِ مُنَافِقُونَ ۖ وَمِنْ أَهْلِ الْمَدِينَةِ ۖ مَرَدُوا عَلَى النِّفَاقِ لَا تَعْلَمُهُمْ ۖ نَحْنُ نَعْلَمُهُمْ ۚ سَنُعَذِّبُهُم مَّرَّتَيْنِ ثُمَّ يُرَدُّونَ إِلَىٰ عَذَابٍ عَظِيمٍ
Am na it ca sàmm sa nekk ca seen wet, ay naaféq, ak waa (Madina). Am na ñu téppeeral cig naaféq. Xamuloo leen, (waaye) Nun xam Nanu leen. Dananu leen mbugal ñaari yoon ba noppi Nu door leen a delloo ca mbugal mu màgg ma.
102وَآخَرُونَ اعْتَرَفُوا بِذُنُوبِهِمْ خَلَطُوا عَمَلًا صَالِحًا وَآخَرَ سَيِّئًا عَسَى اللَّهُ أَن يَتُوبَ عَلَيْهِمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ak ñeneen ña nangu seeni bàkkaar (tuub nañu), jaxase woon nañu jëf yu sell ak yeneen yu ñaaw. Xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla nag Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
103خُذْ مِنْ أَمْوَالِهِمْ صَدَقَةً تُطَهِّرُهُمْ وَتُزَكِّيهِم بِهَا وَصَلِّ عَلَيْهِمْ ۖ إِنَّ صَلَاتَكَ سَكَنٌ لَّهُمْ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Jëlal ci seen alal ab sarax (asaka) ngir laabal leen ca ak sellal leen ca, te nga ñaanal leen. Ndax sa ñaan dalum xel la ci ñoom. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
104أَلَمْ يَعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ هُوَ يَقْبَلُ التَّوْبَةَ عَنْ عِبَادِهِ وَيَأْخُذُ الصَّدَقَاتِ وَأَنَّ اللَّهَ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla Moom Dana nangu tuub ciy jaamam, te Dana jël it sarax ya, te Moom Yàlla Mooy Nanguwaakoon cig tuub, di Jaglewaakoon.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
102Aaya

Tekki — At-Tawba 102

Simoore At-Tawba Aaya 102 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ak ñeneen ña nangu seeni bàkkaar (tuub nañu), jaxase woon…

Simoore Aaya 102/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 100–104. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers