Simoore Al-Mu'minun
PDF —
118 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Mu'minun pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Mu'minun pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Mu'minun Tekki. Al-Mu'minun (Meccan) 118 Aaya.



Simoore Al-Mu'minun
118 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔ
Way-gëm ña dey texe nañu,
ﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
gaa ña nga xam ne dañuy toroxlu ci seen biirug julli,
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
te ñooy gaa ña nga xam ne dañoo dëddu am po,
ﭡﭢﭣﭤﭥ
tey génne asaka,
ﭦﭧﭨﭩﭪ
te mooy gaa ña nga xam ne dañuy sàmm seeni pëy,
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
lu dul ci seeni soxna ak ci seeni jébéer , ñoom dey kenn yejju leen ;
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
ku sàkku leneen ginnaaw loolu nag, ñoom la ñuy tudde way-jalgati ña ;
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
ña nga xam ne nag dañuy sàmm la ñu leen dénk ak seeni kàddu,
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
tey wattu seeni julli [di ko sàmm].
ﮊﮋﮌﮍ
Ñoom dey ñooy donnkat ya,
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
ña nga xam ne danañu donn Àjjana Firdawsi, te dañu cay béel.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Nun bind Nanu nit [sàkk ko]mu bawoo ci cosaanul ban [suuf],
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
ginnaaw ba Nu def ko mu di maniyu ma mu di aw lumbu.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Ginnaaw ba Nu def lumbu ma di aw suux ; ginnaaw ba Nu def suux wa mu di ay yax, daldi sànge yax ya aw yàpp. Daldi koy def jëmm,Yàllaa mën a sakkanal. Moom miy gën gi Bindkat !
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Bu loolu jàllee, dangeen di dee.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Ba noppi Bis-pénc ba Mu dekkal leen.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Sàkk Naa juroóm-ñaari asamaan yu leen tiim. Te na leen wóor ne sàgganewuma leen ci li Ma leen sàkk.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Te wàcce Nanu ndox mu bawoo ca asmaan. Topp Nu sowal ko ci biir suuf, kon Nun am Nanu kàttanug sànk ko de.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Te ci ndox moomu Lanu leen sosale ay tooli dër yu tàndarma ak reseñ, yu ngeen di am ci biiram ay fuytéef yu bari ngeen di ca lekk,
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
ak garab gay génne ci tuuri Siinaa, mu am diw gu ngeen di tabasoote di ko rënde li ngeen di lekk [garabug oliw].
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Te xanaa war ngeen a am xalaatu fàttaliku ca jur ga leen Yàlla xéewale : Dananu leen nàndale ci li nekk ci biiram [meew], am ngeen ca itam ay njariñ yu bari ; te it ca ngeen di lekk.
ﮉﮊﮋﮌﮍ
Ngeen di ca war, di ca lonk la ngeen di war.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Yónni woon Nanu Nooh ca aw nitam. Mu ne leen : "Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen yàlla ju dul Moom. Moo ndax dangeen dul ragal Yàlla ? ”
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Gaa ña weddi woon ca aw nitam di wax naan : “Kii daal nit la ni yéen, dafa bëgg toog ci seen kaw doŋŋ. Te sax bu neexoon Yàlla mu wàcce ay Malaaka. Mësunoo dégg lii ca sunu maam ya jiitu woon.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Kii daal as waay la su jinne sadd, muñal-leen ko tuuti.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
[Nooh]ne : “Yaw sama Boroom ! Dimbali ma ci weddi gi ñu ma weddi”.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
Nu daldi ko soloo [digal ko] ne ko : “Defaral gaal ci Sunug càmm ak Sunu ndigal. Te saa su Sunu ndigal agsee ba lakkukaayu mburu ba sãs, nanga dugal te bàyyi sag njaboot ak yóllent ci wépp xeet ba mu des ña nga xam ne wax ja jiitu woon na c
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Saa soo duggee ca gaal ga yaak ña nga àndal ba noppi, nanga wax ne : “Cant ñeel na Yàlla Moom mi nu musal ci ay nit yu di ay tooñkat.”
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Te nanga wax ne : “Sama Boroom, nanga ma wàcce ngën gi wàccuwaay bu barkeel, Yaw yaa di gën ji wattu”.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Ay kéemaannekk na ci biir loolu. Doontele sax dañuy nattu (ñi gëm).
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Topp, ginnaaw ba, Nu sos ay maas ci ñeneen,
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Nu yónni ci ñoom ab Yonent bu bokk ci ñoom [ngir mu wax leen] : “Jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen yàlla ju dul Moom. Moo ndax dangeen dul ragal Yàlla ? ”
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Ña jiite yéefar ya cig nitam tey weddi ne danañu dajeek seen Boroom Bis-pénc ba, daldi wax ne : “Kii daal nit la ni yéen, ci li ngeen di lekk lay lekk, di naan ci li ngeen di naan.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Te bu ngeen toppee ci moom (nitug njorondaay)ni yéen, dangeen yàqule.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Moo ndax daleen a dig ne bu ngeen faatoo ba doon suuf ak i yax, dangeen génnaat dekki ?
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Mukk, mukk li ñu leen dig !
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Lii daal du lenn lu dul sunug dundug àddina sii : danuy dundu, dee ; waaye dunu dekki.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Kii daal as waay la suy duural Yàlla ay fen ; te nun sax gëmunu ko”.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Mu ne : “Yaw sama Boroom ! May ma ndimbal ci weddi gi ñu may weddi”.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Mu wax ne [Moom Yàlla] : “Li feek ndiir su néew, danañu rëccu”.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Ag xaacu dikkal leen ci dëgg ; ñu ne lànjaŋ. Tooñkat ya tuskare nañu !
ﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Ba noppi, Nu sos ca seen ginnaaw yeneeni maas.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Amul wenn xeet wuy jiitu walla mu mujj ab digam.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Topp, ginnaaw ba Nu yónni sunuy Yonent ñuy toppante. Xeet bu ca ab Yonentam dikkal, ñu weddi ko. Toftale Nanu leen kenn kenn, def Nanu leen ñu di ay waxtaan. Toskare ñeel na aw nit ñu gëmul !
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Topp, ginnaaw ba yónni Nanu Muusaa ak mbokkam ma Aaruuna jox leen Sunuy laaya ak kàttan gu bir,
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
jëmale ko ca Firawna ak gàngooram ña doon rëy-rëylu te doon aw nit ñuy kawe-kawelu.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Ñuy wax naan : “Ndax dananu gëm ñaari nit ñu mel ni nun, ñoo xam ne seenu xeet sunuy jaam lañu.
ﮉﮊﮋﮌﮍ
Ñu daldi leen weddi, daldi alku.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Jox Nanu Muusaa Téere ba ngir mu waar leen ca ba ba ñuy gindiku.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Te Noo def doomi Maryaama [Iisaa] ak yaayam di kéemaan ; te Nu dugal leen ci aw tundu, mu maasee ànd ak bëti-ndox [naan].
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Éy yéen Yonent yi ! lekk-leen ci yi teey yi tey jëf u yiw. Man dey kuy xam laa li ngeen di def.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Te diine jii mooy seen diine, di jenn diine, te maa di seen Boroom. Ragal-leen Ma”.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Séddale nañu seeni mbir ci ay kurél, xaaj bu ne doyloo na la fa moom.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Bàyyileen ci seen ngëlëmte loolu ab diir.
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Ndax dañoo jàpp ne li ñu leen may ci alal ak i doom,
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Danu leen di gaawe [fey leen baaxug la ñu nekk] ? Ñoom yëguñu li xew de.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Ña sóobu dëgg dëgg ci ragal seen Boroom,
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
ña nga xam ne dañoo gëm seen kàdduy Boroom,
ﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
ña nga xam ne duñu bokkale seen Boroom ak dara,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
ña joxe ca la ñu leen xéewale, te seeni xol di nux-nuxi ci [di xalaat] ne danañu delluwaat ca seen Boroom.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Ñooña ñooy jëkkante ci jëfu yiw te jëkk nañu ca.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Dunu teg benn bakkan lu dul la mu àttan. Te ab Téeree ngi fi buy àtte ci dëgg, te kenn du leen ca noonu [ci waññi yiw walla yokk safaan].
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Waaye seeni xol réere na lii [di Alxuraan]. Te am nañu ay jëf yu yées yooyu te ña nga koy jëf,
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
ba ba ñuy mbugal seen njiit ya ñu seet seet di yuuxu walla.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
“Buleen wooteg wallu tey. Kenn duleen dimbali ci Nun.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Samay kàddu wàccoon na ci yéen ; ngeen daan ko dummóoyu,
ﮝﮞﮟﮠﮡ
ngeen daan ca rëy-rëylu, di ko waxtaane”.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Ndax dañoo settantalul wax ji [di Alxuraan] ? Walla daleen a digalul lu ñu digalul woon seen maam ya leen jiitu woon ?
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Walla dañoo xamul seenub Yonent, ba tax ñu umpale ko ?
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Walla dañu naan : “Jinnee ko sadd ? ” [Du loolu lépp], li am mooy moom dëgg rekk la indi. Te li ëpp ci ñoom dañoo sib dëgg.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Te bu Yàlla toppoon seen bànneex, kon asamaan ak suuf si yàqu. Indil Nanu leen ag waare, waaye dañoo dummóoyu waare googu.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Ndax danga leen di laaj ab génnuwaay ? Sa génnuwaayu Boroom moo gën. Te moom [Yàlla] moo Gën ji kuy wërsëgal.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Te yaa ngi leen di woo jëme leen ca yoon wu jub wa xocc.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
Ña xamul àllaaxira nag ñoom xamuñu yoon wa.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Bu Nu leen yërëmoon ba wàññi seeni tiis, ñu dellooti nuur ca seen bew ga.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Dananu leen mbugal ndax toroxlu wuñu ngir seen Boroom ; jaamuwuñu Ko,
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
ba ba kerook Nuy ubbi ci ñoom buntub mbugal mu tar, ñu ne ca xiim.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Moom moo leen sàkkal ag dégg, ak ug gis, ak i xel. Néewaana ngeen gërëm.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Moom moo leen bàyyi ci kaw suuf si, te dees na leen pang jëme ci Moom.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Moom mooy dundal, mooy rey ; Moom mooy jàllasante guddeek bëccëg. Ndax dangeen dul xel-lu ?
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Ñoom kay faf dañoo wax rekk la ñu jëkk ña waxoon.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Nee nañu : “Ndax bu nu faatoo ba nekk suuf ak i yax, ndax dananu dekkiwaat ?
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Lii dey digoon nañu ko sunuy maam ak nun ; lii daal ay léeb rekk la”
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Neel : “Ana kan moo moom suuf si ak li ci biiram ? Ndeem xam ngeen”.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Kon danañu wax ne : “Yàllaa ko moom”. Neel : “Moo ndax dangeen dul fàttaliku ? ”
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Neel : “Ana kan mooy Boroom asamaani juróom-ñaar tey Boroom Gàngunaay [Aras] gu màgg ga ? ”
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Danañu wax ne : “Yàllaa ko moom”. Neel : “Ndax dangeen dul ragal Yàlla ? ”
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Neel : “Ana kan moo ame ci loxoom nguurug lépp, kiy aare te soxlawul ku ko aar ? Waxleen rekk, ndax xam ngeen ko ! ”
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Danañu wax ne : “Yàllaa ko moom”. Neel : “Ana fu ñu leen jibare ? ” [ba mënuleen a gëm].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
Indil Nanu leen dëgg waaye ñoom ay fenkat lañu.
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Yàlla jàppewul kenn doomam te it amul jeneen Yàlla ju muy àndal ; su loolu amoom, kon yàlla ju nekk dem ak boppam ak la mu sàkk te kon danañuy ëppantey doole. [Tudd naa sellam ga] ! Rawante naak li ñu koy melal.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Mooy ki xam kumpaag li teew ! Kawe na [lool] li ñu koy bokkaaleel !
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Neel : “Sama Boroom, cëy boo ma wonoon li nga leen dig ;
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Yaw sama Boroom, bul ma boole mukk ci tooñkat yi.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Te it am Nanu kàttanu won la li Nu leen dig.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Ña ngay jiñe ñaawtéef ci [jëf yu gën a]rafet. Nun [Yàlla] noo gën a xam la ñuy melal.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Neel : “Maa ngi sàkkoo ci sama Boroom mu musal ma ci jax-jaxali Séytaane.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
te maa ngi sàkku ndimbalul sama Boroom ci ñu di ma teewe ànd ak man”.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
ba ba dee dikkal kenn ci ñoom, mu naan : “Sama Boroom ! Delloo ma àddina,
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
ndax ma mën a jëf yiw ca la ma fa bàyyi”. [Mukk loolu du mës a am], loolu kàddu la rekk gu muy wax. [Barsàq] kiiraay la ñuy nekk ba ba ñuy dekki”.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Bu ñu walee Buftu bi kerook Bisboobu, askan amatul seen diggante te dootuñu lijjanti.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Képp ku peeseem diis [ak jëf yu baax]ñoom ñooy ña texe ;
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
képp ku peeseem woyof [ak jëf yu baax], ñooña ñoo di ña sànku ci biir Safara te béel fa.
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Safara waa ngay làkk seeni kanam, ñu ne fa xuum
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
“Moo ndax daa weesul jàng samag waareci yéen, ngeen jàppe ko ay fen ? ”
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ñu wax ne : “Boroom sunu ! Texeedi not nanu te xamadi woon nanu itam.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Boroom sunu, génne nu ci ! Bu nu tey-teyloo ba dellu ci, noo tooñ”.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Mu ne leen : “Jattleen ci biir te buleen ma tuddati”.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Am na ab kurél bu bokkoon ci sama jaam, daan wax naan : “Boroom sunu, gëm nanu ; jéggal nu te yërëm nu, Yaw yaa di gën ji Yërëmaakoon” ;
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
ngeen jàppee woon leen ay reetaan ba faf ñu fàbbi leen fàtteloo leen Samay kàddu, dëkkoon ci di leen reetaan rekk.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Bis niki tey feye naa leen ca la ñu doon muñ ; ñoom texe nañu.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Mu ne leen : “Yéen sax ñaata at ngeen saxoon ci àddina [dundoon] ? ”
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Ñu tontu ne : “Nun daal, benn walla fan yu néew la nu fa saxoon, xam sax laajal limkat yi.”
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Mu ne leen : “As ndiir su néew ngeen fa saxoon. Cëy bu ngeen xamoon”.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Moo ndax dangeen a jortoon ne caaxaan rekk a taxoon Ma bind leen, ngeen jort it ne dungeen dellusi ci Man [Yàlla] ? ”
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Yàlla buur biy dëgg, kawe na ! Amul jeneen yàlla ju dul Moom, Mooy Boroom gàngunaay [Aras] gu tedd ga !
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Képp kuy jaamu leneen di ko boole ak Yàlla, [na bir ne] amu ca firnde, te Yàllaa koy lijjanti. Li wér mooy yéefar ya duñu texe.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Waxal ne : “Boroom sama, jéggaleel te yërëme. Yaw yaa di gën ji yërëmaakoon yi”.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers