Simoore Al-Anbiya
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Anbiya pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Anbiya pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Anbiya Tekki. Al-Anbiya (Meccan) 112 Aaya.
Related
- Al-Anbiya TekkiWolof
- Al-Anbiya mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Anbiya

ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Waññub [jëfi] nit ñi jegesi na, te ñoom ña nga nuur cig càggante dëddu.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Amul lenn lu leen di digal ci Alxuraan di lu bawoo fa seen Boroom, te dégluwaale wuñu kook am po,
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Càggante nekk na ca seen xol ; tooñkat ya di déeyoo naan : “Ndax kii dafa nekkul mbindéef ni yéen ? Ndax dangeen di topp ag njibar te janook moom ? ”
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Neel : “Sama Boroom xam na lépp lu ñu wax ; ci kaw asamaan yi ak suuf, mooy Aji-dégg di Aji-gis”.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Waaye ñu naan : “Way-jaxasook ay gént rekk la ! Du lenn lu dul lu mu sos. Ndax [moom Yonent bi] waykat la. Nanu indil kaawtéef ni ñu ko daan yónnee ñu njëkk ña”.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Xeet ya leen jiitu woon te gëmuñu, alag Nanu leen. [Kon] ñoon ndax danañu gëm ?
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Mësunoo yónni ñu la jiitu lu dul aw góor yu Nu soloo. Laajleen ña jotoon Téere ndeem xamu leen.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Defunuleen woon [boroom] yaram yu dul lekk ñam. Te it nekkuñu woon ñuy béel [dañu daa lekk, di wopp, di dee].
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Topp, Nu def la Nu leen digoon. Daldi leen boole musal ak ku Nu soob. Yàqkat ya ñoom, Nu rey leen.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Wàcce Nanu ci yéen ab Téere boo xam ne seen teraangaa nekk ca biir. Moo ndax dangeen dul xel-lu ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Ay ay dëkk yu daan tooñ, te Nu alag leen ; ba noppi sosaat ca seen ginnaaw ñeneen nit.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Ba ñu yégee Sunu mbugal, ñoom daw nañu [di jéem a génn dëkk ya].
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Buleen daw de. Delluleen fa seen kër ya ngeen nekkoon di xéewlu, ndax xéy-na dees na leen laaj.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Ñu ne : “Ngalla nun ! Nun dey ay tooñkat lanu woon”.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Xawuñoo eggale seen njàmbat loolu ba Nu def leen ni am ngóobit mu ne selaw.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Bindinu asamaan yi ak suuf si ak li nekk ci seen diggante ngir fo.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Su Nu bëggoon po, kon [Dunu soxla bind dara], ci Sunu bopp la Nu koy sose, ndegam lu Nu nammoon a def la
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Déedéet Dananu sanni dëgg ci kaw fen mu tojte ko, tax mu raaf. Te li ngeen di nirale [Yàlla] dana tax ngeen toskare.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Moo moom lépp li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Te ña nekk fa Moom duñu rëy-rëylu [ci di ko jaamu], te it duñu ca lott.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Dañu Koy sàbbaal guddi ak bëccëg, duñu ca jóge.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Ndax ñoom dañuy jaamu ay yàlla ci suuf si [yuy mën a dekkal ku dee ni Boroom bi] ? [Mukk du am]
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Su jeneen yàlla ju dul Yàlla amoon ci asamaan yeek suuf si, kon ñoom ñaar ñépp yàqu. Cëy sellam ga, Mooy Boroom Gàngunaay ga [Aras] ; Jomb na li ñu koy nirale !
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Deefu ko sañ a laaj ci li Muy def, waaye ñoom la ñuy sañ a laaj.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏ
Am dañuy jaamu ay yàlla bàyyi Ko ? Neel : “Indileen seenu lay”. Lii [Alxuraan jii] mooy lépp lu ñuy waare képp ku ànd ak man, moo di li ñu waare woon it ña ma jiitu. Li ëpp ci ñoom xamuñu dëgg, tax na ñu dummóoyu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Yónniwunu la la jiitu benn Yonent te soloowunu ko [lay dëgg] te moo di : “Amul jeneen yàlla ju dul Man. Kon jaamuleen Ko”.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Ñiy wax naan : “Jërëmaakoon bi am na doom”. Cëy sellam ga ! Déet, ay jaam lañu yu Nu teral [ñoom Malaaka ya].
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Duñu ko jiitu ci wax te ñoom ndigalam lañuy def.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Xam na li nekk ci seen kanam ak li nekk ci seen ginnaaw. Te duñu rammu lu dul ka Ko neex, te ñoom ña nga ca tiitaangey ragal Yàlla.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Te ku ca waxoon bokk ca ñoom ne : “Man yàlla laa, ju dul Moom”. Loola Safara la Nu ko koy feyee. Te noona it la Nuy feye tooñkat ya.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Ndax ña weddi dañoo gisul ne asamaan yi ak suuf si dañoo taqaloodef [benn dank] ? Nu daldi leen téqale, te Nu sose ndox lépp luy dundu. Moo ndax dañu dul gëm ?
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Te def Nanu ci biir suuf si ay tundi doj, ngir mu bañ a baj-baji ak ñoom. Te def Nanu ci ay yoon ngir ñu mën a gindiku.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Te def Nanu asamaan si mu nekk am téeg mu Nu wattu. Te ñoom ñangay dëddu Sunuy kéemtaan [bañ leen a seetlu].
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Te Moom mooy ki bind guddi gi ak bëccëg bi, ak jant bi ak weer wi, ku ci nekk di daw caw rëdd [wa ñu ko rëddal].
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Te defalunu kenn nit ca la la jiitu muy ku fi sax. Waaw konndax yaw ginnaaw boo deewee, ñoom dañu fiy sax ba fàwwu ? [Déedéet]
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Bakkan bu nekk dana mos dee. Te Dananu leen nattu ci lu bon ak yiw mu dib sànje. Te ci Nun ngeen di dellusi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ña weddi, bu ñu la gisee, duñu la jàppe lu dul ku ñuy yéjji, naan : “Ndax du kii mooy sikkal seen yàlla yi ? ” Te ñoom dañuy weddi Yàlla Mi nga xam ne [bokk na ci turam yi] Yërëmaakoon bi.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Bindeef na nit cig yàkkamti. Danaa leen won Samay kéemaan. Buleen ma yàkkamti.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Ñuy wax naan : “Kañ la dig boobu di agsi ndegam ñu dëggu ngeen ? ”
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Ña weddi bu ñu xamoon waxtu wa nga xam ne duñu mën a feg safara say lakk seeni kanam walla seeni ginnaaw, te kenn duleen ca dimbali...
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Déedéet, ndekete yoo ci mbetteel la leen di dikkale, gëlëmal leen ; duñu ko mën a fànq, te kenn duleen ca yéexe.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Yéjjeefoon na Yonent ya la jiitu woon. Faf ña doon yéjji, la ñu doon reetaan wàcc ci seen kaw.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Neel : “Kan moo leen mëna yërëm guddi ak bëccëg ci Yërëmaakoon bi ? ” Teewul ñoom ñangay dëddoo tuddu seen Boroom [Fàttaliku Ko].
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Am dañoo am ay yàlla ju dul Nun, ju leen di mën a aar ? Duñu mën a dimbali seen bopp, te deefuleen mën a xettali ci Nun.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Li am mooy, xéewalal Nanu ñooñook seeni baay ba seenug dund yàgg ci ñoom. Waaye ndax dañoo gisul ne wàññi Nanu suuf si cig wàññi ay catam ? Moo ndax ñoom ñooy not ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Neel : “Defuma lu dul ragal-loo leen li ñu ma soloo”. Waaye ay tëx duñu dégg wooteb ña leen di waar.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Te bu leen lu tuuti daloon ci sa ndigalu Boroom, ñu dellu tàmbalee wax naan : “Ngalla nun ! Nun ay tooñkat lanu woon”.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Dana tëral màndaxe mu maandu ca Bis-pénc ba. Te deesul tooñ benn bakkan ci dara, doonte lu tollu ni pepp bàkket, Dananu ko indi. Te aka mën a wàññi.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Joxoon Nanu Muusaa ak Aaruuna Tawreet ak leeraay ak fàtttaliku ngir ña ragal Yàlla,
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
ñooy ña ragal seen Boroom ci kumpa, te ñoom way-jàq lañu ca Bis-pénc ba.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Te lii [Alxuraan jii], tur la wu barkeel [sakkan] wu Nu wàcce. Ndax yéen dangeen koy weddi ?
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Te mayoon Nanu Ibraahiima njub lu jiitu. Te nekkoon Nanu ñu ko xam xéll.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
[Fàttalikul] ba mu waxee baayam ak nitam ña, ne leen : “Ana luy yàlla xërëm [yu diy jëmm yu ñu yatt] te ngeen fonk leen lool ? ”.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Ñu tontu ne : “Dañoo fekk sunuy baay di leen jaamu”.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Mu ne leen : “Ca dëgg-dëgg, yéen ak seeni baay dangeen a nekk ci réer gu fés”.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Ñu ne ko : “Ndax li nga nu dig dëgg la ci yaw walla dangay kaf ? ”.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Mu ne déedéet : “Seen Boroom mooy Boroom asamaan yi ak suuf si, te Moo leen sàkk. Te man dey bokk naa ci ñiy seede loolu ci yéen.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Te waat naa ci Yàlla ! Ne danaa fexeel seen xërëm yi ci seen ginnaaw, bu ngeen dëddoo”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Mu dàggate leen ba mu des xërëm bu mag ba. Ngir xéy-na mu mën cee delloo [seeni xel].
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ñu ne : “Ku def lii sunu yàlla yi ? Kooka dey bokk na ca tooñkat ya”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Am ñu wax ne : “Déggoon nanu benn waxamaande mu di leen ayibal ; ñu di ko woowe Ibraahiima”.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Ñu ne : “Indileen ko ci kanamu nit ñi”, xéy-na ñoom ñu nekki seede [ci loolu].
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Ñu ne ko : “Ndax yaw yaa def lii ci sunu yàlla yi, yaw Ibraahiima ? ”
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Mu ne : “Déedéet, ki ko def mooy ki ci gën a mag ci ñoom. Laajleen ko ndegam mën nañoo wax”.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Ñu dellu ca seeni xel, daldi wax ne : “Nun noo tooñ sunu bopp”.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Ñu daldi far delluwaat ca seen kéefar ga, daldi ne : Xam nga ne ñii mënuñoo wax waay”.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Mu ne : “Waaw, ndax dangeen di bàyyi Yàlla di jaamu loo xam ne mënuleen a jariñ dara te mënuleen a lor.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Kuf ma leen yéen ak li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla ! Ndax dangeen dul xel-lu ? ”
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Ñu ne : “Lakk-leen ko ngir ngeen dimbali seen xërëm yi ndegam nar ngeen ko”.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Nu wax ne [Nun Yàlla] : "Yaw safara, nekkal lu sedd te am jàmm ci kaw Ibraahiima”.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Ñu bëgg a def seeni pexe ci moom, Nu def leen ñu di ñu yàqule ña.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Nu daldi koy musal moom ak Lóot jëme leen fa suuf sa Nu barkeel ngir waa àddina si yépp.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Nu may ko Isaaqa ak Yàqooba, muy ndollent, Nu def leen ñu nekk ñoom ñépp di ñu sell.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Def leen ay njiit yuy gindee ci Sunu ndigal. Nu soloo leen jëf yu yiw, ak taxawal julli ak génne asaka. Te ñoom daal daanañu Ma jaamu.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Ak Lóot ! May Nanu ko ràññee, dégg ak xam-xam, te musal Na
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Dugal Nanu ko ci Sunu yërmaande. Te moom bokk na ca ñu sell ña.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Ak Nooh itam, [fàttalikul] ba mu wootee ca lu jiitu. Nu dal koy wuyyu te musaloon ko, mook njabootam, ca njàqare ju rëy ja,
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
te Nu dimbali woon ko ca nit ña weddi woon Sunuy kàddu. Ñoom aw nit ñu bon lañu woon. Nu daldi leen labal ñoom ñépp.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Ak Daawuda, ak Suleymaan, [fàttalikul] ba Nu àttee mbirum mbéy ma gàtti nit ñu yàqoon [ruur]. Te teewoon fa seen àtte ba.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Déggloo Nanu Suleymaan àtte ba. Te ñoom ñaar ñépp mayoon Nanu leen ràññee dëgg ak xam-xam. Te tàggatoon Nanu tundi doj ak njanaaw ya ñu àndak Daawuda di Nu sàbbaal. Te Nun noo ko defoon.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Te jàngal Nanu ko ràbbiinu mbubbi koŋ ngir mu musal leen ci seen ngaañ. Moo ndax yéen du ngeen sant [delloo njukkal] ?
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Suleymaan tàggatal Nanu ko ngelaw luy ràddi, di daw ci ndigalam, mu jëm ci suuf su Nu barkeel. Te kat Nun xam Nanu lépp lëf,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
te ci jinne yi am na ci ñu ko daan nuural [ci géej te daan nañu ko liggéeyal yeneeni liggéey, te Daan naa leen wattu [Man Yàlla].
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Ak Ayuuba [fàttalikul] ba mu woowee Boroomam ne ko : “Man dey mettit dal na ma. Te Yaw yaay gën jaa yërëme yërëmaakoon ya” !
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Te Nu nangul ko, daldi wuññi lor ja nekkon ca moom, Nu may ko njabootam te boole ca ñeneen ñu tollu ni ñoom, muy yërmaande ju tukkee fi Nun, ak fàttali jaamukati Yàlla yi.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Ak Ismaayiila, ak Idriisa ak Zul-Kifli, ñoom ñépp bokkoon nañu ca muñkat ya ;
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
dugal Nanu leen ci Sunu yërmaande, bokk nañu ca ñu yiw ña [sell].
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
[Fàttalikul] boroom jën wa [Yunus] ba mu demee ànd ak mer. Te mu jortoon ne du lu Nu dogal ci moom [ciw tiis ngir la mu dem te amu ca ndigal]. Waaye mu woote ca biir lëndëm ga ne : “Amul jeneen yàlla ju dul Yaw ! Tudd naa sag sell ! Man nag bokk naa ca tooñkat ya”.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Nu daldi koy nangul te musal ko ca njàqare ja. Te it noonu la Nuy musalee way-gëm ña.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
[Fàttalikul it] Zakariyaa ba mu woowee Boroomam ne : “Boroom sama, bul ma bàyyi ma wéet, te Yaa di ku gën a mën a dimbalee”.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Nu nangul ko, may ko Yahyaa te Nu yéwénalal ko soxnaam. Ñoom sax dañu daan njëkkante ci jëf yu yiw ya te ñoom daanañu Nu jaamu, nekk ci diggante xemmem ak ragal. Te nekkoon nañu diy way-toroxlu ci Nun.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Ak jigéen ja ñoŋal boppam [Maryam] ! Nu wal ci moom lenn ci Sunu ruu, daldi koy def mook doomam [Iisaa] ñuy kaawtéef ci àddina si yépp.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Lii nag moo di seen diine, mu di jenn diine doŋŋ, te Man maa di seen Boroom. Waay- waay kon jaamuleen Ma.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
De daggate nañu seeni mbir ca seen diggante. Te ñoom ñépp fi Nun lañuy dellusi.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Képp kuy jëf ca jëf yu yiw ya te muy ku gëm, deesul fakk jëfam ndax Nun noo ko koy bindal.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Te dëkk bu Nu rey, waa dëkk ba duñu mënatee dellusi!
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Ba ba kerook Nuy ubbi Yaajuuja ak Maajuuja ñuy sottiku di rogaat ci tunduwu nekk ;
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
dig bu dëggu ba daldi gën a jegeñ, bu boobaa bëti ña weddi dana buqiku, ñu naan : “Ngalla nun ! Nekkoon nanu cig càggante ci lii. Te nekkoon nanu di ay tooñkat”.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
“Yéen nag ak li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla, yéen a di mattum Safara te yéen dangeen ca dëkk.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Bu fekkoon ne ay yàlla lañu, kon duñu ca tàbbi ; nit ñooña ñépp dañu fay béel.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Te ñoom am nañu ca biir foofa ay yikkat, te ñoom duñu fa mën a dégg dara.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Ña nga xam ne digoon Nanu leen xéewal yu jëkk ya jóge ci Nun, ñoom ñu Nuy soreel [Safara soosu] lañu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Duñu dégg yëngoom ga te ñoom ñangay nekk ca lu neex seen bakkan ba fàwwu.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Tiit mu rëy ma duleen tiital, te Malaaka ya danañu leen gatandu naan : “Lii mooy seen bis ba ñu leen digoon”.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Bis boobu Dananu taxañ asamaam ni Nuy taxañe këyit gu am bind. Na nu tàmbalee woon sos ga bu jëkk ba, Dananu dellu [defaat ko] ; muy dëel bu Nu warlu [lu Nuy def la] !
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Te bind Nanu ba noppi ca Téere ya ginnaaw bind ga nekk [ca Lawhul Mahfuuz] Àlluwa ja, ne suuf si Sunu jaam yu yiw yi ñoo koy donn”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Nekk na ci biir loolu ab jottali ñeel aw nit ñuy jaamu Yàlla !
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Yónniwunu la ngir dara lu dul nga nekk yërmaandey waa àddina.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Neel : “Man dey dañu may soloo doŋŋ : Waaye seen Yàlla jenn doŋŋ la ; kon ndax yéen dungeen wommatu jébbalu? ” [dugg ci Lislaam]
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Bu ñu dëddoo, neel : “Xamal naa leen loo xam ne noo ca yem ; mu di ndax li ñu leen dig dafa jegeñ walla dafa sori.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Moom dey xam na li ñuy biral ciy wax ak it li ngeen di nëbb.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Te xamuma ; ndax moom nattu la ci yéen ak xéewal gu gàtt” !
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Yaw Yonent bi neel : “Yaw sama Boroom, àtteel ci dëgg ! Te sunu Boroom mooy Yërëmaakoon biy Dimbaliwaakoon biy musalee ci li ngeen koy nirale”
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







