Simoore Luqman
34 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒ
Aliif, Laam, Miim.
ﭓﭔﭕﭖﭗ
Lii ay laaya la yu Téere bu xereñ,
ﭘﭙﭚﭛ
jub la, yërmaande la ngir ñuy rafetal ,
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
ñiy taxawal julli, di génne asaka te amug wóolu ci ne àllaaxira dina ñëw.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Ñooñaa nga tege ca kaw seen yoonu Boroom wu jub xocc wa, te ñoom ñooña ñoo texe.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Am na ci nit ñuy nëbb xam-xam, di feeñal waxi caaxaan ngir namm a soreel nit ñi, sànk leen, réeral leen yoonu Yàlla ci lu àndul ak xam-xam, weddi ko, jàppe ko ag doyadal. Ñoom ñooña am nañu mbugal muy toroxale.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci moom, mu dummóoyu mel ni ku ko déggul, mel ni ab saañ dafa nekk ca nopp ya. Yégal ko ne [am na] mbugal mu metti.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Ña gëm tey jëf u yiw, am nañu Àjjanay xéewal,
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
dañu fay béel, - ni ko Yàlla dige woon tigi. - Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Moo bind asamaan si ci lu àndul ak keno yu ngeen di mën a gis ; Moo def ay doj ci biir suuf ngir mu bañ jeriku ak yéen ; def na ci xeetu mala wu nekk. Te nun, Yàlla wàcceel nanu ndox mu bawoo asamaan, nu saxal ci ay yóllent ci xeetu gàncax wu nekk.
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
“Lii mooy li Yàlla sàkk. Kon wonleen ma, ña dul Moom, ana lu ñu sàkk ñoom ? ”. Li am kay mooy, tooñkat ya ñi ngi ci réer gu bir .
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Joxoon Nanu Luqmaan xam-xamu xereñ, ne ko : “Santal Yàlla, [gërëm Ko], ku Ko sant ci di Ko dello jukkal, boppam ; ku Ko xarab it..., [Na xam ni] Yàlla ku doylu la, Yayoowaakoonug cant la”.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
[Fàttalikul] ba Luqmaan waxee doomam ja, di ko waar, naan ko : “Yaw samas doom, bul bokkaale mukk dara ak Yàlla, ndax bokkaale kat ag tooñ gu réy la”.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Dénk Nanu nit muy rafetal jëme ci ñaari waajuram ; ndax yaayam ëmb na ko muy coono ci biir coono : ba feral ko diirub ñaari at. “Nanga may sant Man [Yàlla] ak sa ñaari waajur. Ci Man la lépp di mujj.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Saa su ñu la sonnalee ci bëgg nga bokkaale Maak loo amul xam-xam, bulen ca topp ; waaye nangay ànd ak ñoom ci àddina si ak njekk. Te nanga topp yoon wa jëmsi ci Man. Fi Man ngeen di mujje [yéen ñépp], su ko defee, Ma téqantalal leen la ngeen daan def”.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
“Yaw sama doom, dIisaay woowu, doonte la sax dafa tollu ni as fepp, nekk ci kaw doj mbaa ci biir asamaan yi, walla ci biir suuf, du tee Yàlla indi ko . Yàlla Ku deñ-kumpa la .
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Yaw sama doom, taxawalal julli tey digle njekk, te it nangay tere njekkar, te it nangay muñ li lay dal. Loolu mooy dégu !
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Bul dox di dummóoyu nit ñi, bul dox it di fuukarewu : Yàlla safoowul képp kuy fuukarewu ak a damu.
ﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
Nangay teey ci sab dox, te nangay suufeel sa kàddu, ndax kàddu gi gën a suufe moo di kàddug mbaam sëf ”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Xanaa gisuleen ne Yàllaa leen tàggatal li nekk ci asamaan yeek suuf si ? Te Mu tuur leen xéewalam yi ci li feeñ ak li nëbbu. Am na ci nit ñi ñuy dàggasante ci mbiri Yàlla, te amuñu ca benn xam-xam, du càggenu ag gindiku, waxantumalaak Téere buy gindi.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Te bu ñu leen waxee ne : “Toppleen li Yàlla wàcce”, dañu naan : “Nuy kay dañuy topp sunu baaxi maam”. Moo ndax Séytaane daawuleen woo jëme leen ci mbugalum Safara !
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Képp ku jébbal Yàlla boppam tey rafetal, [na xam ne] ŋoy na ci buum gi gën a dëgër. Te ca Yàlla la mbir yépp di mujj.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Képp ku weddi it, weddeem ga bumu la jaaxal : danañu dellusi ci Nun, ñu xibaar leen la ñu jëfoon. Yàlla xam na xéll li nekk ci dënn yi.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Dananu leen bànneexal as ndiir ; daldi leen mbaq ci mbugal mu diis.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Te su leen laajoon : “Ku bind asamaan yeek suuf si ? ”, kon ñu ne : “Yàlla ! ”. Waxal : “Cant ñeel na Yàlla ! ”. Waaye ñi ëpp ci ñoom xamuñu.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Yàllaa moom li ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku doylu la, di Yayoowaakoonub cant !
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Su fekkoon ne mboolem li nekk ci suuf si ciy garab, dafa doon ay xalima, géej gi amaat yeneen juróom-ñaari géej yu koy dolli, lépp di daa, kon dey du tax kàdduy Yàlla jeex. Yàlla Borom Kàttan la, di Ku Xereñ.
ﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖ
Seenug sosu ak seenug dekkiwaat yéen ñépp, mi ngi yombe Yàlla ni benn bakkan kepp. Yàlla Kuy Dégg la, Kuy Gis la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Xanaa gisoo ne Yàlla mooy dugal guddi ci bëccëg, Moom dugal it bëccëg it ci guddi, Moo tàggat jant beek weer wi, ku ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal ? Te Yàlla Ku Deñ- kumpa la, Ku Xàmmee li ngeen di def la.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
[Loolu nag] ngir xam ne Yàlla mooy dëgg, lépp lu ngeen mën a jaamu te du Moom, neen la te Yàlla moo di Aji-kawe, di Ku màgg.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Xanaa gisuloo ne gaal a ngay daw ci biir géej, mu bokk ci xéewali Yàlla yi ? Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ñeel bépp santaakoon, dib muñaakoon.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Bu leen duus yi muuree ba mel ni ker, ñuy woo Yàlla, di Ko sellal ; bu leen musalee ba [ñu génn ci jéeri ji], mu amaat ca ñoom ñuy diiŋat ; te Sunuy kàddu kenn du ko diiŋat ku dul ku goreedi, di ab xarabaakoon.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Éy yéen nit ñi ! Ragal-leen seen Boroom [te di Ko wattandiku], te nangeen tiit ci Bis boo xam ne baay du warlul doom dara, doom it du warlul baayam dara. [Fexeleen it] ba buleen Séytaane tax ngeen faku.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Xam-xamu Bis-pénc baa ngi ca Yàlla ; Mooy wàcce tawu waame ; Moo xam li nekk ci jurukaay ya. Benn bakkan xamul lu muy fàggu ëllëg, benn bakkan xamul it ci san suuf lay deewe. Yàlla Ku Xam la, Ku Xàmmee la.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers