Simoore Al-Jathiya
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Jathiya pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Jathiya pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Jathiya Tekki. Al-Jathiya (Meccan) 37 Aaya.
Related
- Al-Jathiya TekkiWolof
- Al-Jathiya mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Jathiya

ﭑﭒ
Haa, Miim.
ﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Wàccug Téere bi ma nga bawoo ca Yàlla, ji am Tedd nga ( Kàttan sañ-sañ), di ku Xereñ.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Ay kéemtaan a ngi ci asamaan yeek suuf si yuy soxal way gëm ñi.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Ay kéemtaan it, yuy soxal ñi amug wóolu nekk na ci bind, bi ngéen ame ay ci lépp luy dukkat ca anam ya muy giire.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Ak ci jëllasanteb guddi gi ak bëccëg bi, ak ci xeewal gi Yàlla wàcce mu bawoo ci asamaan si [Taw] di ci dundal suuf si (Naataange) ginnaaw ba mu bekkooree, ak ci ni muy soppaxndikoo ngelaw yi, ay kéemtaan la yuy soxal ñi xellu.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Yooyu ñooy firndey Yàlla nu di la ko jàngal mu tegu ci dëgg. Kon ana jan wax la ñuy man a gëm ginnaaw bu Yàlla ak firndeem Yii jàllee?
ﮎﮏﮐﮑﮒ
Képp ku dib duuraakoon defaakoonub bàkkaar toskare na ca xuri sawara !
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Daan dégg ñuy jàng laayay Yàlla yi ( Alxuraan) mu féttéerlu di jaayub dayo, melni ku ko déggul. (Kookee na xam ne ) mbugal mu mettee (nga koy xaar).
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Bu xamee as lëf ci Sunu laaya yi, jàppe ko ay caaxaan di ko yéjji. Ñooñee mbugël mu doyadi moo leen fay xaar :
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
(Sawaraw) Jahannamaa ngi leen topp. Lañu doon fàggu ak ña ñu doon digaaleel du ñu léen ko man a fegal. Te sax mbugal mu rëy moo léen fay xaar.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Lii ag njub la. Ñi weddi seen Téereb Boroom mbugël mu tar te metti dina leen dal.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Yàlla ji léen tàggatal géej, ba gaal di ca tëmb di daw, Ci ndigalam, ak it ngeen di sàkku Ca xeewalam ya xanaa nak da ngeen sant.
ﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
Moo leen tàggatal lépp lu nekk ci asamaan yeek suuf si, Ay kéemtaan a ngi ci yuy soxal ñiy xalaat.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Waxal ñi gëm ne leen na ñuy jégël ñi yaakaarul bisi Yàlla ya ci ne Yàlla dana àtte fay xeet wu nekk ci kem la ñu daan fàggu.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Képp kuy jëf yiw, moom caak ; képp kuy jëf lu bon it, moom caak. Ndax yéen ñépp ca seen boroom ngeen di dellu.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Indiloon Nanu waa giiru Banii-Israayiil Téere ba, ak ngor ga, ak yonnenta ga, wërsëgëloon Nanu leen ci àddina si yépp ;
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
joxoon Nanu leen ay firnde yu leer ci ndigël yi. Wuutewuñu woon lu dul ba ñu amee xam- xam cig bew, ci seen diggënte. Te sa Boroom dana àtte seen diggënte, bu Bis Pénc baa, ca la ñu daan juuyoo.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Topp ginnaaw ba teg Nanu la ci yoonu ndigël. Na nga koy topp te bul di topp bànneexu ñiy xamadi.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Ndax ñoom du ñu la jariñ ci Yàlla tus. te tooñkat ya ku nekk ma ngay wéeru ci moroomam ; waaye Yàlla tigi mooy wéeruwaayu ñi ragal Yàlla.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
[Alxuraan jii] ag leer ak gëti xol la, ñeel nit ñi di njub di yërmaande ngir aw nit ñu wóolu.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Moo ndax defkati ñaawtéef yi dañoo jàpp ne danu leen di def ni ña gëmoon te daan jëf yiw, ñu yem niróok dundu akg dee ? (mukk du am) aka ñoo bon nu ñuy àttee !
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Yàlla bind na asamaan yeek suuf si ci dëgg ak it ngir mu fay bakkaan bu nekk ca la mu daan fàggu. Te kenn du leen tooñ (ci wàññi yiw mbaa yokk safaan).
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Xanaa gisuloo ka jàppe bakkanam muy yàlllaam ? Yàlla faf ko réerël fatt ag déggëm ak ub xolam muur ab gisam. (Waaw) kooku ana kan moo koy gindi ginnaaw Yàlla ? Xanaa dangeen dul fàttaliku?
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Ñuy wax naan : “lii daal du lenn lu dul su nu dundug àddina : danuy dee di dund te yàggaayu jamono rekk moo nuy ràpploo”. Waaye amuñu ci loolu benn xam-xam : dañuy njortu doŋŋ.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Te saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci ñoom, seen lay du doon lenn lu dul di wax naan: “Délloosilleen nu sunuy maam (ya deewoon) ndegam li ngeen di wax dëgg la”.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Waxal ne : “Yàllaa leen di dundal soog leen a rey. Ba noppi mu leen di dajale bu Bis Pénc baa, sikk amul ci loolu, waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si. Te saa su Bis Pénc ba taxawee, bu keroogee, yéefar yi danañu yàqule.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Ca ngay gise xeet wu nërméelu. Xeet wu ca nekk ñu di ko woo (ngir jox ko ab téereem ba ay jëfëm nekk). Te naan ko bis niki tey dees na leen fay li ngeen daan jëf.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Sunub Téere bii nag. Di àddu ci yéen dëgg ndax ci la nu daan bind li ngeen daan jëf”.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Ña gëmoon te daan jëf yiw, sa Boroom dana leen tàbbal ci biir yërmaandeem. loolu moo di texe gu màgg ga.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Ña weddi woon : “Xanaa Sunuy kàddu daawuloon wàcci ca ñoom ? Ñuy rëy-rëylu ak a tooñ di jalgati”.
ﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝﰞﰟﰠﰡﰢﰣ
Te bu ñu leen waxaan ne : “digub Yàlla bii dëgg la de ; te it Bis Pénc ba sikkuwul”, ngeen daan tontu ne : “Nun sax xamunu luy Bis Pénc ba ; am nanu ci ay njortu te wóoluwu nu ko.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Ñu ne gegg ca [ñaatéefi ] seen jëf ya. Lañu daan yejje gaw leen.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Ñu wax leen ne : “Bis niki tey dananu leen fàtte (bàyyi leen ci biir Safara) kem ni ngeen fàttewoon dajeg seen bis bii ( ba waajaluleen ko). Seenub dëkkuwaay mooy Safara ; te kenn du leen fa dimbali.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
li ko waral moo di ni ngeen jàpp laayay Yàlla ay reetaan dundug àddina tax ngeen woru faggu”. Bis niki tey dootu ñu fa génne te déefuleen ko woyofal.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Yàllaa jagoo xeeti cant (yépp), Mooy Boroom asamaan yi di Boroom suuf si : di Boroom àddina sépp.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Moo ame màgg ga ci biir asamaan yeek suuf si. Mooy boroom Kàttan ga, di ku Xereñ.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







