Simoore Al-Ahqaf
PDF —
35 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Ahqaf pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Ahqaf pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Ahqaf Tekki. Al-Ahqaf (Meccan) 35 Aaya.



Simoore Al-Ahqaf
35 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮑﮒ
Haa, Miim.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Lii moo di wàccug Téere ba bawoo ca Yàlla, miy boroom Kàttan, te di ku xereñ.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Bindunu asamaan yeek suuf seek li ci seen diggante, lu dul ci dëgg ak dig bu ñu yemale. Yéefër yi ñoom bu ñu leen di waar dañuy dumóoyu.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Waxal ne : “Ana lan ngeen di xalaat ci li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla ? Wan leen ma ana li ñu sàkk ci kaw suuf ! Walla dañoo am man-man ci asamaan yi ? Indilleen ma Téere bu jiitu (Alxuraan) wala book jeexitali xam-xam, ndegam ñu dëggu ngeen”.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Waaw ana kan moo gën a sànku (réer) ci kuy woo keneen ku dul Yàlla, koo xam ne du ko wuyu ba baa bis penc ba ? Te dañuy sàggane woote ba (duñu dégg duñu tontu).
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
(Te bu bis Pénc baa) ñu pang nit ñi ngir àtte leen dañuy soppeeku di ay noon, weddi jaamu ga ba mu set wecc.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Bu ñu jàngaatee ñoom sunuy Laaya mu leer nàññ ña daan weddi dañu daan wax ne: “ lii ak njibar la gu fés” , aa li mooy duun-duun dëgg.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Walla ñu naan : “Da koo sos ! ” Nee leen : “Su fekkee ne dama koo sos manalu leen ma ci Yàlla tus. Moom moo gën a xam li ngeen cay lëmbaaje : Doy na sëkk seede sama digganteek yéen. Te moom (Yàlla) moo di Jéggëlewaakoon bi, di Jaglewaakoon bi”.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Waxal ne : “Du man maay Yonent bi jëkk feeñ ; te it xamuma li ñuy xala def ci man, mbaa ci yéen. Man daal damay topp linu may soloo doŋŋ ; te itam doonu ma kenn ku dul ab waaraatekat buy leeral”.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Waxal ne: “Ana lan mooy xalaat ci ne lii su fekkee dafa bawoo ca Yàlla ngeen weddi ko, mu am it ci giir banii israayila kenn ku ca seede lu ni mel moom mi gëm, yéen ngeen rëy- rëylu... Yàlla dey du gindi aw nit ñuy tooñkat ! ”
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Ña weddi ngay wax ñi gëm naan leen : “Su fekkoon ne yiw la dana nu ca jiitu”. Ngir séenug ñakka gindiku dana ñu xala wax naan : “Alxuraan jii ay dur la yu yàgg ! ”
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Téereb Muusaa jiituwoon na ko di njub. Lii nag ab téere la buy dëggal loolu ci làmmiñu araab, ngir muy xupp ñiy tooñ di bégal ñiy rafetal (ay jëf).
ﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
Ñi gëm Yàlla tey jaar ca yoon wu jub xocc wa, duñu tiit duñu jaaxle.
ﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛ
Ñooñee ñoo di waa Àjjana dañu fay béel mu di peyug la ñu daan jëf.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Dénk nanu nit (mu wara rafetal) jëme ko ci ñaari waajuram : ndayama ko ëmb ci coono, imbi ko ci coono ; fa ëmb ba dale ba ca feral ga fanweeri weer la ; ba sax moom saa su dëgëree ba am ñeent fukki at, muy wax naan : “yaw sama Boroom ! Yenkeewal ma may mana sant ci sa xéewël yi Nga ma xéewale ak sama ñaari waajur, ak itam may man a jëf (jëf ju yiw joo gëram). Te nga yéwénalal ma ci sama njërtiit , Man dey tuub naa dellu ci Yaw te itam Man mii ci jullit ñi laa bokk” (ñi jébbale séen bopp).
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Ñooñee ñoo di ña nga xam ne dananu leen nangul la gëna rafet ca lañu daan jëf te da nanu leen faral séeni ñaawtéef , te it dananu leen limaale ca waa Àjjana, muy dig bu dëggu banu leen daan dig.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Kuy wax ñaari waajuram naan leen : “Kuf ma leen te naan leen ! Ndax dangeen may dig ne danaa génnaat dellu àddina te ña wéyoon masuñoo génnaat ? ” Ñoom ñaar ña ngay sàkku ndimbalul Yàlla ngir ag delloom, [ñu di ko wax naan]: “Soo delluwul ginnaaw ci lii nga ne toskare dal na la ! Digub Yàlla dëgg la de”. Moom it mu tontuwaat ne : “Lii du lenn lu dul feni mag ñu jëkk ña”.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Ñoom ñooñee la wax ja dal ca séen kaw (menn mbugël) mooy xeet ya leen jiitu woon ci jinne yeek nit ñi. Ñoom dañoo yàqule woon.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Kenn ku nekk am na lu tollook lamuy jëf, ñu nar leen a faye la ñu jëfoon te kenn du leen ca tooñ (ci wàññi natt ba).
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
Bu keroogee bis ba ñuy gaaral ña weddi ci kaw Safara (naan leen) : “jeexaloon ngeen séen yu neex ya ca jamono ba ngeen nekkee daan dund ca àddina : te pëcëxóowoon ngeen ko, bis bi niki tey dees na leen faye mbugalum toroxtaane, ngir ni ngeen daan saay-saayee.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Fàttalikul mbokkum waa Aad ña (Huud) ba muy waar aw nitam ca barabu Al Ahqaaf – te fekkoon na waaraatekat ya jar fa la ko jiitu woon ak ginnaawam - [daan leen wax naan]: “Yàlla doŋŋ ngeen war a jaamu (waaye su ngeen jaamoo leneen lu dul moom). Man dey ragal naa ci yéen mbugëlum bis bu màgg ñàng”.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Ñu tontu ko ne ko : “Moo ndax dangay ñëw ci nun ngir féewale nu bëgg nu bàyyi sunu yàlla yi ? Waay-waay, indil nu li nga nuy tëkkoo ndegam bokk nga ca way dëggu ña ”.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Mu ne leen : “ Xam-xam moom ma nga ca Yàlla. Man nag dama leen di jottali liñu ma yonni. Waaye gis naa ne yéen ñii aw nit ngeen ñu réer xamadi”.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Ba nu gisee niir wa dëgmël séen xur ya , wax na ñu ne ; “Lii aw xiin la wu nuy tawal”. Déet walaay ! lii nag mooy la ngeen daan yàkkamti : Ngelaw lu ëmb mbugël mu mitti,
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
ci ndigalul Yàlla dafay nappaaje lépp”. Mu faagaagal leen ñoom ñépp ba séen dëkuwaay ya doŋŋ des fa. Noonu lanuy faye tooñkat ya (sàmbaa-bóoy sa).
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Yombaloon nanu leen ñoom lu nu leen joxul yéen. Ndax defaloon nanu leen ag dégg ak ub gis, te seen dégg ga, wala séen gis ba, ak séen xol ya jariñu leen woon tus, ndax dañu daan weddi Laaya Yàlla yi firndeem ya. Ñañu daan yéjji far sóor leen.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Faagaagal nañu ca dëkk ya leen wër ; defaroon ay keemaan ak firnde yu wuute, ngir bëggoon ñu dellu ginnaaw ca séen kéefër gi.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Ana lu tax la ñu daan jaamu, bàyyi Yàlla dimbali wuñu leen ? Li am kay mooy dañu leen far réer mër ; loolu moo di seen fen wa ak la ñu daan dur.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
(Fàttalikul) itam ba nu jubëlee ci mbooloom jinne ngir ñuy déglu Alxuraan ba ñu teewee nee na : “déglu leen”... Ba mu jeexee, walbatiku nañu ca séen mbokki jinne di leen waar .
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Nee na ñu : "Eey yéen sunuw xeet ! Déglu nanu ab Téere bu ñu wàcce ginnaaw Muusaa, muy dëggal la ko jiitu dafay gindee itam jëme ci dëgg. Ak ci yoon wu jub xocc wa.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
ey yéen sunuy xeet wuyu leen wootekatu Yàlla ba ! Te na ngeen koy gëm. (Su ngeen ko defee) dana leen di jéggal seen bàkkaar, te it kon dana leen yiir ci mbugal mu mitti.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Te nag képp ku wuyuwul wootekatu Yàlla ba. Du man a raw mukk Yàlla ci kaw suuf si, te it du am ku koy man a dimbali ginnaaw Yàlla. Ñooñee ña nga ci réer gu bir sori.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Xanaa gisuñu ne Yàllaa bind asamaan yeek suuf si, te sonnut ci bind gi mu leen bind sàkk leen, xanaa war na man a dekkal néew ? Waaw-waaw. Moom man na lépp lu ne.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Cay bu keroogee bis ba ñuy gaaral yéefar ya ca Safara (te naan leen) : “Ndax lii du dëgg ? ” Ñuy tontu naan : “Axakañ , ak sunu màggug Boroom”. Mu ne leen : “Tokamtiku leen mbugël ma ngir li ngeen daan weddi”.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Yaw (Muhammad) na ngay muñ ni Yonent ya doonoon boroomuk dogu daan muñ; te buleen di yàkkamtil [mbugël]. Ndax bis bu ñu nee gegg ci li ñu leen daan tëkkoo, danuy mel ni masuñoo sax (dund) kon ndax dana alku ku dul saay-saay sa?

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers