Simoore Muhammad
PDF —
38 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Muhammad pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Muhammad pdf Wolof — Wàcce Simoore Muhammad Tekki. Muhammad (Medinan) 38 Aaya.



Simoore Muhammad
38 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Ña weddi tey dumóoyu yoonu Yàlla, (tax na) ba sànk na séen jëf.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Ña gëmoon te daan jëf yiw te ñoo daan gëm la ñu daan wàcce ci Muhammad (Alxuraan) – te mooy dëgg ga bawoo ca séen Boroom – Faralal na leen séen ñaawtéef te it yéwénal na leen séen mbir.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Li wér moo di ne ñiy weddi dañoo topp Neen ñi gëm nag ñoom dañoo topp Dëgg gu bawoo ca séen Boroom. Noonu la Yàlla di séddale nit séeni léebu.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Te saa su ngeen fa dajeetee ak ñay weddi (ci jamonoy xare) dóorleen ci loos yi. Saa su ngeen leen noote nag, na ngeen leen jéng bu daŋ a daŋ. Su leen soobee, ngeen baal leen dem, wala ngeen laaj leen njotu, ba baa xare ba di giif. Lool nag, bu sooboon Yàlla, Dana feyyu ci kaw yéefar yi, waaye danay faral nattuwante ci ñeneen ña ca des. Te itam ña ñuy roy ci yoonu Yàlla (ña doon jullit), Séeni jëf du réer.
ﮫﮬﮭﮮ
(Yàlla) dana leen xala gindi tey yéwénal seeni mbir,
ﮯﮰﮱﯓﯔ
te dana leen tàbbal Àjjana ju mu leen jagle.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
eey yéen ñi gëm ! bu ngeen taxawee temm ci yoonu Yàlla, Kon dey dana leen dimbali te it dana dëgëral séeni ndëggu (gindi leen ci xare).
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Ña weddiwoon, ñoom toskare nañu te séeni jëf réer na.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Li ko waral moo di ne dañoo sibóon li Yàlla daan wàcce ci moom it. Mu daldi sippi séeni jëf (neenal ko).
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Moo xanaa dañoo wërul ca réew yi (suuf si) bay xool naka la mujjug ña leen jiitu deme woon ? Yàlla da leen nappaaje (faag leen). Noonu it la yéefar yi di mujje.
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
Dafa fekk ne Yàlla mooy méngóo di Aar ñi gëm ; yéefar yi nag ñoom amu ñu ku leen di aar.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Yàlla dana tàbbal ñi gëmoon te daan jëfe yiw, Àjjana yoo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam ronu leen. Ña weddiwoon ñoom dañu daan bànneexu ak daan lekk ni jur gi di lekke ; te safaraay séen saxuwaay.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Ak i bari dëkk, yu ëppoon doole fuuf sa dëkk bii ñu la génne, te dañu leen faagaagal, te amul kenn ku leen musal.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Moo ndax kiy topp firnde yu leer yu tukkee ci Boroomam niróok naak ñay jàppe séeni ñaawtéef lu rafet tey topp séeni bànneex.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Nirële melow Àjjana ja ñuy dig ña ragal Yàlla (di watandiku) : am na ci biiram ay dexi ndox yu dul forox, ak ay dexi meew yu dul soppiku, ak ay dexi ñoll yu neex ca ña koy naan, ak ay dexi lem yu sell. Te dañu fay am wépp xëti meññeef, boole kook njegëluk seen Boroom. Moo ndax loolu niroo naak ña béel ca biir Safara te ñu di leen nàndale ndox muy wañax muy daggate séeni butit ? Mukk yemuñu.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Am na ci ñoom ñu lay déglu . Bu ñu génne fi yaw rekk, tàmbalee wakaate di laaj ña am xam-xam (Sahaba ya) naan leen : “Waaw moom lu mu waxati woon sax ? ” Ñooñee la Yàlla fàtt seen xol ñu topp senn bànneex.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Ña gindiku ñoom dolli na leen njub, jox leen yombalal leen ragal Yàlla.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Ana lan la (yéefar ya di xaar ci baña jebbalu) ba bis penc ba faf ne jaseet ci seen kaw bett leen ? Ndax màndargam yi dikk nañu. Te sax su xasee ba eksi ana lan la leen fàttaliku di jariñati?
ﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙ
Xamal ne, amul jeneen Yàlla ju dul moom Yàlla, te nga jéggalu say bàkkaar, ak di jéggalul jullit yu goor yeek yu jigéen yi. Yàlla xam na li ngeen di def lépp guddeek bëcëg.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Ña gëm ña ngay wax naan : “Cëy ! Bu aw saar wàccatiwoon ! ” Te fekk na saa suñu wàccee aw saar wu leer nàññ te digal ca xare, da ngay daldi gis naaféq ya di la xool ni ñuy xoole dee (ngir ragal). Li gën a yell ci ñoom moo di.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
topp (jëf) ak wax ju yiw. Su, ndigal la xasee dugg, ñoom dey suñu dëggaloon (ndigalul Yàlla) jëfe ko), mooy gën ci ñoom (fuuf).
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Moo ndax, su ngeen dëddoo baña xare ji loolu du jur ak yàq ci suuf si ak ngeen di dog séenug mbokk ?
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Ñooñu la Yàlla di rëbb, tëx loo na leen te gumba loo na séenub gis.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Moo ndax ñoom dañu dul settantal Alxuraan ? Wala séeni xol moo tojul ?
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Ña murtad weddi ginnaaw ba leen njub ga feeñee, Saytaane legna leen te di leen fàbbi.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Li ko waral moo di dañuy wax yéefar yi naan leen : “dananu leen topp ci yennati mbir”. Te Yàlla xam na li ñuy nëbb.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Naka la séeni mbir di mujje su leen Malaaka ya jekkalee, di leen dóor ci kanam ak ginnaaw ?
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Li ko waral moo di dañuy topp luy waral xarabug Yàlla, tey bañ lépp luy ngëramal Yàlla. Moom it mu daldi sippi séen jëf.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Moo ndax naaféq ya dañoo foog ne Yàlla du génne mbañeel gi ëmbul (Yonenta bi) mu ne fàŋŋ ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Bu Nu sooboon danga leen gis jàrr. Te danga leen xam ci séen màndarga ; danga leen man a xam itam ci séen galeenu waxiin. Yàlla xam na séeni jëf.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Dananu leen natt ba baa nuy xam, ñay jihaad ci yéen ak muñkat ya, te it da nanu feeñal séeni jëf (yu baax ak yu bon).
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Ña daan weddi tey dumóoyu yoonu Yàlla te daan sonal Yonenta bi ginaaw (ba ñu xamee) njub ga mu leer nàññ, manuñoo wàññi Yàlla dara. Te dana sippi seen jëf.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
eey yéen ñi gëm ! Topp leen Yàlla tey topp Yonent bi, te bu leen di neenal séeni jëf.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Ña daan weddi tey dumóoyu yoonu Yàlla ba dee ca diy yéefar, Yàlla duleen jéggal.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Bu leen di doyadi tey woote maslaa te yéen a gën a kawe, Yàlla itam yéen la àndal, te it séenug (peyug jëf) dara du ci wàññiku.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Dundug Àddina sii am po la ak i caaxaan ; bu ngeen gëmee te ragal Yàlla di wattandiku , Dina leen jox séenug pey te duleen laaj séeni alal.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Buleen ko Yàlla laajoon, kon dangeen di nay te kon dana génne seeni dëxëñ teg mbañeel gi séen diggante .
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Yéen a ngi nii ñu di leen woo ngir ngeen di joxey alal ci yoonu Yàlla. Am na ci yéen ñuy nay a joxe. Te képp kuy nay a joxe boppam la koy def. Yàlla di ku woomal te yéen ay ñi ñàkk. Te su ngeen dumóoyoo , Dana wuutal ñeneen nit ñu dul yéen, te du ñu mel ni yéen.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers