Simoore Al-Hadid
PDF —
29 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Hadid pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Hadid pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Hadid Tekki. Al-Hadid (Medinan) 29 Aaya.



Simoore Al-Hadid
29 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Ñi nekk ci biir asamaan yeek suuf si ñi ngi sàbbaal Yàlla miy boroom Kàttan gi, te di ku Xereñ.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Mooy boroom nguurug asamaan yeek suuf. Mooy dundal mooy rey, te Man na lépp lu ne.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Mooy ki Jëkk mooy ki Mujj, mooy ki Fés mooy ki Nëbbu te moo Xam lépp lu ne.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Mooy ki bind asamaan yeek suuf si ci biir juróom-benni fann ba noppi Mu yemoo ca kaw Gàngunaay ga (Aras); Xam na lépp luy dugg ci biir suuf ak lu caay génne, ak lépp luy wàcc bawoo asamaan ak lu cay yéek, te Moom mi ngi and ak yéen fu ngeen man di nekk. Te Yàlla kuy gis la li ngeen di def.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Mooy Boroom nguurug asamaan yeek suuf si . Te ca Yàlla la mbir yépp di mujj.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Mooy duggal guddi ci bëccëg te it mooy duggal bëccëg ci guddi, te Ku xam xéll la li nekk ci dënn yi.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Gëmleen Yàlla ak ub Yonentam, te na ngeen di joxe ci alal ji mu leen wuutalal. Ñi gëm te bokk ci yéen tey [joxe alal] danañu am ag pey gu màgg.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Ana lu leen dal ba munu leen gëm Yàlla, ak ub Yonentam mi ngi leen di woo ngir ngeen gëm seen Boroom ? Te jël ci yéen ab dig bu diis ndegam gëm ngeen.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Moom mooy wàcce ay kàddu yu leer ca jaamam ba, ngir mu génne leen cig lëndëm tàbbal leen cig leer; te Yàlla dey ku leen ñeewanti la, Jagléwaakoon la.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏ
Ana lu leen dal ba munuleen joxe alal ci yoonu Yàlla, te Yàllaa moom ndono yi nekk ci asamaan yeek suuf si ? Ña joxe seen alal lu jiitu (fathu Makkata) xare boole ca duñu yem ak kenn ñoom dañuy am pey gu màgg ak daraja yu kawe... ëppëlee ko ña joxe ginnaaw xare be te sax xare woon nañu . Ñoom ñépp, la Yàlla dig neexal bu duun, te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
ﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜ
Ana kan mooy nangoo lebal Yàlla bor bu rafet, Mu fulandikul ko ko, te it dana am ag pey gu màgg.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
(Bu keroog) (bis pénc baa) dangeen gis way gëm ña, leer ga dox seen diggante di jolli ci kanam ak ndeyjoor ; (ñu naan leen) : “Bégleen tey : am ngeen ay àjjana yu dex ya di daw ci suufam te dangeen fay béel”. Loolu mooy texe gu mag ga.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Bu keroogee ba naaféq yu góor yi ak naaféq yu jigéen yi, di wax ñi gëm naan leen : “Xoolleen nu ndax nu man a niitu: ci seenug leer”. Ñu ne leen: “Delluleen ginnaaw, wutig leer”. Daldi doxale seen diggante ñag boo xam ne biir ga yërmaande la (fareek ña gëm), biti ba di mbugël (fareek naaféq ya)
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
“(Naaféq yaa ngay) woote naan xanaa àndunu woon ak yéen ? ” jullit ña ne. “Axakañ, waaye yéen a fitnaal seen bopp, daan fexeel (ñi gëm) daan werante, faggu ba faf mbirum Yàlla agsi saytaane nax leen.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Bis niki tey, kenn du jël ci yéen ag njotu kenn it du ko jëll ca ña weddi. Seenub saxuwaay Safara moom ngeen mengóol: dootu leen tàggoo. Ndaw mujj gu bon !
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Ndax jotul nag ci ñi gëm, seeni xol ragal buur jëm ci di fàttaliku Yàllu ak lépp lu wàcci tey dëgg ? Te ñuy baña mel ni ña leen jiitu woon te Téere wàcci ca ñoom . Ba diir ba yàggee seeni xol wow, ba faf la ëpp ca ñoom saay-saay lañu (génn topp).
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Xamleen ne Yàllaay dundal suuf si ginnaaw ba mu dee. Leeralal Nanu leen, sunuy firnde ngir ngeen jëfandikoo seeni xol jàjju waaru.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
Saraxekat yu góor ak saraxekat yu jigéen ñiy lebal Yàlla bor bu rafet , dees na leen ko fulal te danañu am ag pey gu màgg.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Ña gëm Yàlla ak Yonentam ñooñee ñooy ña dëggu tey seede fa seen Boroom. Am nañu seenug pey ak seenug leer, yéefar yay weddi Sunuy firnde nag, ñoom ñoo di waa safara.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Xamleen ne dundug àddina am po la, ak i caaxaan, ak gànjar ak fuukareente, ak ëppalantey alal ak i doom. Mu mel ni waame : wu dotti yéem lool yéefar yi, gàncax ga naat seet seet mboq ; sooy mi yàqu. Te àllaxira, mbugël mu tar moo fa am, ak njégël gu bawoo fa Yàlla ak ngëramam. Dundug àddina du lenn lu dul taar buy naje.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Dawleen jëkënte jëm ci njégëluk seen Boroom ak ca Àjjana joo xam ne yaatuwaayam tollu na ni yaatuwaayu asamaan ak suuf, te dañu koy waajalal ñi gëm Yàlla ak Yonentam. Loolu ngënéelul Yàllaa. Te Yàlla Mooy Boroom ngëneel lu màgg la.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Amul menn musiba muy dal ci kaw suuf si walla seen kaw jëmm yi, lu dul ne bind Nanu ko ci ab Téere ba nu ko laata sàkk ; te loolu lu yomb Yàlla la,
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
ngir ngeen baña yoqat ñanki ci li leer, te it baña bokk ci damoo li mu leen jox. Yàlla safoowul képp kuy damoowaakoon buy fuukare wu.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Ña nay tey digël nit ñi ñuy nay. Képp ku dumóoyu... Yàlla moom ku doyloo boppam la di ku Yayoo cant.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Yónni Nanu sunuy Yonenta ci ay firnde yu leer, wàcce ay Téere boolekook ñoom ak i balaas yu màndaxe, ngir nit ñi taxawal maandute. Wàcce Nanu weñ gu ñuul, mu am kàttan gu tar, ak ay njariñ ñeel nit ñi, ak it ngir Yàlla xam, ana kan moo koy dimbalil ay Yonentam, ci kumpa. Yàlla ku am doole la di Boroom Kàttan.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Yónni Nanu Nooh ak Ibraahiima te it def nanu Yonenta ga ci seeni sët ak Téere ba jox nanu leen ko. Am na ci ñoom ñu gindiku, waaye li ëpp ci ñoom saay-saay lañu.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Nu daldi xentuloo sunuy Yonent seen mboor, xentuloo Iisaa domu Maryaama indil nanu ko Injiil, te it def nanu ca biir xolu ña ko topp ak ñeewante ak yërmaande. Ak bero jigéen ña ñoom ñoo ko fental seen bopp, Waaye farataalu nu ko ci ñoom. Li nu leen digël daal moo di nañu sàkku ngëramul Yàlla. Te sax sàmmuñu ko ni mu ware. Ña bokk ca ñoom te gëm indil Nanu leen seenug pey. Waaye lu bari ci ñoom ay saay-saay lañu.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Eey yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla te gëm Yonentam bi dana leen defal ñaari cokkoor yu yërmande, danaleen defal it ak leer gu ngeen gindikoo, te it dinaleen jéggël, Yàlla Jéggëlaakoon la Jaglewaakoon la.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Ñoñ Téere nañu xam ne manuñu dara ci ngënéelu Yàlla te it ngëneel ci loxo Yàlla la nekk ; Moo koy jox ku ko soob, te Yàlla moo di Boroom ngëneel lu màgg li.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers