An-Nur · 52/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
وَمَن يُطِعِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَيَخْشَ اللَّهَ وَيَتَّقْهِ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَائِزُونَ ۝٥٢
Wa mai yuti`il laaha wa Rasoolahoo wa yakhshal laaha wa yattaqhi fa ulaaa`ika humul faaa`izoon
📖 Tekkim Wolof
Képp kuy topp Yàlla ak ub Yonentam, ragal Yàlla te di Ko fuglu, ñooña ñooy ña texe.

🎧 Dégg


📜 Aaya 50-54 — An-Nur

50أَفِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ أَمِ ارْتَابُوا أَمْ يَخَافُونَ أَن يَحِيفَ اللَّهُ عَلَيْهِمْ وَرَسُولُهُ ۚ بَلْ أُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ
Moo ndax dañoo am woppi xol ? Walla dañuy jiixi-jaaxa ? Walla dañuy ragal Yàlla ak ub Yonentam yiir leen ? Deewalaay !... ñoom ay tooñkat lañu.
51إِنَّمَا كَانَ قَوْلَ الْمُؤْمِنِينَ إِذَا دُعُوا إِلَى اللَّهِ وَرَسُولِهِ لِيَحْكُمَ بَيْنَهُمْ أَن يَقُولُوا سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا ۚ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُفْلِحُونَ
Ñi gëm Yàlla [jullit ñi], saa su ñu déggee woote buy jëme ci Yàlla ak ub Yonentam ngir àtte seen diggante, seeni wax du doon lu dul ne : “Dégg nanu, topp nanu”. Ñooña ñooy ña texe.
52وَمَن يُطِعِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَيَخْشَ اللَّهَ وَيَتَّقْهِ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَائِزُونَ
Képp kuy topp Yàlla ak ub Yonentam, ragal Yàlla te di Ko fuglu, ñooña ñooy ña texe.
53۞ وَأَقْسَمُوا بِاللَّهِ جَهْدَ أَيْمَانِهِمْ لَئِنْ أَمَرْتَهُمْ لَيَخْرُجُنَّ ۖ قُل لَّا تُقْسِمُوا ۖ طَاعَةٌ مَّعْرُوفَةٌ ۚ إِنَّ اللَّهَ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
Danañuy giñ ci Yàlla fa mu gën a ñàngee, naan boo leen digalee danañu génn [dem xare ji]. Neel : “Buleen giñ. [Wax ji rekk doyul]. Yàlla xam na li ngeen di def”.
54قُلْ أَطِيعُوا اللَّهَ وَأَطِيعُوا الرَّسُولَ ۖ فَإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّمَا عَلَيْهِ مَا حُمِّلَ وَعَلَيْكُم مَّا حُمِّلْتُمْ ۖ وَإِن تُطِيعُوهُ تَهْتَدُوا ۚ وَمَا عَلَى الرَّسُولِ إِلَّا الْبَلَاغُ الْمُبِينُ
Neel : “Toppleen Yàlla te topp ab Yonentam. Bu ñu dummóoyoo [ndigal la] ñoom nag,... yéen itam ak seen mbiri bopp ; su ngen toppee [ndigal la] gindiku”. Yonent bi moom jottal rekk a ko ci war.
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
52Aaya

Tekki — An-Nur 52

Simoore An-Nur Aaya 52 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Képp kuy topp Yàlla ak ub Yonentam, ragal Yàlla te…

Simoore Aaya 52/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 50–54. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers