Luqman · 32/34
Tekki Waxtaan — Simoore Luqman
وَإِذَا غَشِيَهُم مَّوْجٌ كَالظُّلَلِ دَعَوُا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ فَلَمَّا نَجَّاهُمْ إِلَى الْبَرِّ فَمِنْهُم مُّقْتَصِدٌ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا كُلُّ خَتَّارٍ كَفُورٍ ۝٣٢
Wa izaa ghashiyahum mawjun kazzulali da`a-wul laaha mukhliseena lahud deena fa lammaa najjaahum ilal barri faminhum muqtasid; wa maa yajhadu bi Aayaatinaa illaa kullu khattaarin kafoor
📖 Tekkim Wolof
Bu leen duus yi muuree ba mel ni ker, ñuy woo Yàlla, di Ko sellal ; bu leen musalee ba [ñu génn ci jéeri ji], mu amaat ca ñoom ñuy diiŋat ; te Sunuy kàddu kenn du ko diiŋat ku dul ku goreedi, di ab xarabaakoon.

🎧 Dégg


📜 Aaya 30-34 — Simoore Luqman

30ذَٰلِكَ بِأَنَّ اللَّهَ هُوَ الْحَقُّ وَأَنَّ مَا يَدْعُونَ مِن دُونِهِ الْبَاطِلُ وَأَنَّ اللَّهَ هُوَ الْعَلِيُّ الْكَبِيرُ
[Loolu nag] ngir xam ne Yàlla mooy dëgg, lépp lu ngeen mën a jaamu te du Moom, neen la te Yàlla moo di Aji-kawe, di Ku màgg.
31أَلَمْ تَرَ أَنَّ الْفُلْكَ تَجْرِي فِي الْبَحْرِ بِنِعْمَتِ اللَّهِ لِيُرِيَكُم مِّنْ آيَاتِهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّكُلِّ صَبَّارٍ شَكُورٍ
Xanaa gisuloo ne gaal a ngay daw ci biir géej, mu bokk ci xéewali Yàlla yi ? Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ñeel bépp santaakoon, dib muñaakoon.
32وَإِذَا غَشِيَهُم مَّوْجٌ كَالظُّلَلِ دَعَوُا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ فَلَمَّا نَجَّاهُمْ إِلَى الْبَرِّ فَمِنْهُم مُّقْتَصِدٌ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا كُلُّ خَتَّارٍ كَفُورٍ
Bu leen duus yi muuree ba mel ni ker, ñuy woo Yàlla, di Ko sellal ; bu leen musalee ba [ñu génn ci jéeri ji], mu amaat ca ñoom ñuy diiŋat ; te Sunuy kàddu kenn du ko diiŋat ku dul ku goreedi, di ab xarabaakoon.
33يَا أَيُّهَا النَّاسُ اتَّقُوا رَبَّكُمْ وَاخْشَوْا يَوْمًا لَّا يَجْزِي وَالِدٌ عَن وَلَدِهِ وَلَا مَوْلُودٌ هُوَ جَازٍ عَن وَالِدِهِ شَيْئًا ۚ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ ۖ فَلَا تَغُرَّنَّكُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا وَلَا يَغُرَّنَّكُم بِاللَّهِ الْغَرُورُ
Éy yéen nit ñi ! Ragal-leen seen Boroom [te di Ko wattandiku], te nangeen tiit ci Bis boo xam ne baay du warlul doom dara, doom it du warlul baayam dara. [Fexeleen it] ba buleen Séytaane tax ngeen faku.
34إِنَّ اللَّهَ عِندَهُ عِلْمُ السَّاعَةِ وَيُنَزِّلُ الْغَيْثَ وَيَعْلَمُ مَا فِي الْأَرْحَامِ ۖ وَمَا تَدْرِي نَفْسٌ مَّاذَا تَكْسِبُ غَدًا ۖ وَمَا تَدْرِي نَفْسٌ بِأَيِّ أَرْضٍ تَمُوتُ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ خَبِيرٌ
Xam-xamu Bis-pénc baa ngi ca Yàlla ; Mooy wàcce tawu waame ; Moo xam li nekk ci jurukaay ya. Benn bakkan xamul lu muy fàggu ëllëg, benn bakkan xamul it ci san suuf lay deewe. Yàlla Ku Xam la, Ku Xàmmee la.
LuqmanFihi Alxuraan
34Aaya
MeccanRevelation
32Aaya

Tekki — Luqman 32

Simoore Luqman Aaya 32 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu leen duus yi muuree ba mel ni ker, ñuy…

Simoore Aaya 32/34 — Simoore Luqman لقمان (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Luqman Dégg, Simoore Luqman Tekki, Simoore Luqman mp3, Simoore Luqman pdf. Aaya 30–34. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers