Al-Munafiqun · 3/11
Tekki Waxtaan — Al-Munafiqun
ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ آمَنُوا ثُمَّ كَفَرُوا فَطُبِعَ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَفْقَهُونَ ۝٣
Zaalika bi annahum aamanoo summa kafaroo fatubi`a `alaa quloobihim fahum laa yafqahoon
📖 Tekkim Wolof
(La ko def) moo di ne dañoo gëmoon, weddiwaat. Ñu fatt seeni xol, ba xamatuñu dara.
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-5 — Al-Munafiqun

1إِذَا جَاءَكَ الْمُنَافِقُونَ قَالُوا نَشْهَدُ إِنَّكَ لَرَسُولُ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ إِنَّكَ لَرَسُولُهُ وَاللَّهُ يَشْهَدُ إِنَّ الْمُنَافِقِينَ لَكَاذِبُونَ
Su naaféq ya dikkee ci yaw danuy wax naan : “Noo ngi seede ne yaw Yonent Yàlla nga” ; Yàlla xam na ne yaw ab Yonentam nga ; te Yàlla seede na ne naaféq ya ay fenkat la ñu.
2اتَّخَذُوا أَيْمَانَهُمْ جُنَّةً فَصَدُّوا عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ إِنَّهُمْ سَاءَ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Def nañu seeni ngiñ muy pakk ñuy gàllankoor ci yoonu Yàlla. Ñoom dey la ñuy def ñaaw na !
3ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ آمَنُوا ثُمَّ كَفَرُوا فَطُبِعَ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَفْقَهُونَ
(La ko def) moo di ne dañoo gëmoon, weddiwaat. Ñu fatt seeni xol, ba xamatuñu dara.
4۞ وَإِذَا رَأَيْتَهُمْ تُعْجِبُكَ أَجْسَامُهُمْ ۖ وَإِن يَقُولُوا تَسْمَعْ لِقَوْلِهِمْ ۖ كَأَنَّهُمْ خُشُبٌ مُّسَنَّدَةٌ ۖ يَحْسَبُونَ كُلَّ صَيْحَةٍ عَلَيْهِمْ ۚ هُمُ الْعَدُوُّ فَاحْذَرْهُمْ ۚ قَاتَلَهُمُ اللَّهُ ۖ أَنَّىٰ يُؤْفَكُونَ
Saa soo leen gisee, seeni yaram ya dalay yéem ; bu ñuy wax it, fàww nga déglu leen. Dañuy melni ay dénk yu ñu wéer fu yuuxu jibe ñu tiit. Ñoom ñooy noon ya tigi. Moytandikuleen ! Yàlla dana leen faagaagal kem niñu dumóoyoo (yoonam).
5وَإِذَا قِيلَ لَهُمْ تَعَالَوْا يَسْتَغْفِرْ لَكُمْ رَسُولُ اللَّهِ لَوَّوْا رُءُوسَهُمْ وَرَأَيْتَهُمْ يَصُدُّونَ وَهُم مُّسْتَكْبِرُونَ
Sunu leen waxee ne : “Kaayleen Yonent Yàlla bi jéggalul leen”, ñuy dag-dagali bopp, dumóoyu tey rëy-rëylu.
Al-MunafiqunFihi Alxuraan
11Aaya
MedinanRevelation
3Aaya

Tekki — Al-Munafiqun 3

Simoore Al-Munafiqun Aaya 3 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : (La ko def) moo di ne dañoo gëmoon, weddiwaat. Ñu…

Simoore Aaya 3/11 — Al-Munafiqun المنافقون (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Munafiqun Dégg, Al-Munafiqun Tekki, Al-Munafiqun mp3, Al-Munafiqun pdf. Aaya 1–5. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers