At-Tawba · 82/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
فَلْيَضْحَكُوا قَلِيلًا وَلْيَبْكُوا كَثِيرًا جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ ۝٨٢
Falyadhakoo qaleelanw walyabkoo kaseeran jazaaa`am bimaa kaanoo yaksiboon
📖 Tekkim Wolof
Nañuy ree lu néew (ci àddina), danañu jooy lu bari (ca àllaaxira) mu di seenug pey ca la ñu doon fàggu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 80-84 — At-Tawba

80اسْتَغْفِرْ لَهُمْ أَوْ لَا تَسْتَغْفِرْ لَهُمْ إِن تَسْتَغْفِرْ لَهُمْ سَبْعِينَ مَرَّةً فَلَن يَغْفِرَ اللَّهُ لَهُمْ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ كَفَرُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ ۗ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْفَاسِقِينَ
Nga balul leen walla nga bañ leen a balul (moo yem) - soo leen baluloon juróom-ñaar fukki yoon - du tax Yàlla baal leen mukk. Ngir dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam te Yàlla du gindi aw nit ñu di ay saay-saay.
81فَرِحَ الْمُخَلَّفُونَ بِمَقْعَدِهِمْ خِلَافَ رَسُولِ اللَّهِ وَكَرِهُوا أَن يُجَاهِدُوا بِأَمْوَالِهِمْ وَأَنفُسِهِمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَقَالُوا لَا تَنفِرُوا فِي الْحَرِّ ۗ قُلْ نَارُ جَهَنَّمَ أَشَدُّ حَرًّا ۚ لَّوْ كَانُوا يَفْقَهُونَ
Ña dem bañ a xeexal Lislaam, bég nañu ca seenub toogaay ngir juuyook Yonent Yàlla bi, te soppuñu di xeex ak seeni alal ak seeni bakkan ngir Yàlla, ñuy wax naan : “Buleen génn xare ji ci tàngaay bi ! ”. Neel : “Tàngaaru Safara moo gën a tar.” - Cëy bu ñu xamoon ! -
82فَلْيَضْحَكُوا قَلِيلًا وَلْيَبْكُوا كَثِيرًا جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Nañuy ree lu néew (ci àddina), danañu jooy lu bari (ca àllaaxira) mu di seenug pey ca la ñu doon fàggu.
83فَإِن رَّجَعَكَ اللَّهُ إِلَىٰ طَائِفَةٍ مِّنْهُمْ فَاسْتَأْذَنُوكَ لِلْخُرُوجِ فَقُل لَّن تَخْرُجُوا مَعِيَ أَبَدًا وَلَن تُقَاتِلُوا مَعِيَ عَدُوًّا ۖ إِنَّكُمْ رَضِيتُم بِالْقُعُودِ أَوَّلَ مَرَّةٍ فَاقْعُدُوا مَعَ الْخَالِفِينَ
Bu la Yàlla delloo ci ab kurél ñoom, te ñu ñaan la ndigalul génn (ànd ak yaw), neeleen : “Dootuleen génn mukk di ànd ak man, te it dootuleen xare ak noon yi ànd ak man. Ndax yéen tànnoon ngeen toog ca njalbéen ga ; kon nag toogleen, ànd ak way-des ña ginnaaw”.
84وَلَا تُصَلِّ عَلَىٰ أَحَدٍ مِّنْهُم مَّاتَ أَبَدًا وَلَا تَقُمْ عَلَىٰ قَبْرِهِ ۖ إِنَّهُمْ كَفَرُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَمَاتُوا وَهُمْ فَاسِقُونَ
Bul jullee kenn ku dee ci ñoom, te bul taxaw mukk ci bàmmeelam, ndax ñoom dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam ba ñuy dee, fekk ñu di ay saay-saay.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
82Aaya

Tekki — At-Tawba 82

Simoore At-Tawba Aaya 82 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nañuy ree lu néew (ci àddina), danañu jooy lu bari…

Simoore Aaya 82/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 80–84. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers