Simoore Al-Qiyama ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Qiyama ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (40 Aaya — مكية). Al-Qiyama Dégg, Al-Qiyama Tekki, Al-Qiyama mp3, Al-Qiyama pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Qiyama

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
لَا أُقْسِمُ بِيَوْمِ الْقِيَامَةِ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Maa ngi giñ ci bisub dekkiwaat ga !
وَلَا أُقْسِمُ بِالنَّفْسِ اللَّوَّامَةِ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Te maa ngi giñ ci bakkan bi di ab yeddaakoon.
أَيَحْسَبُ الْإِنسَانُ أَلَّن نَّجْمَعَ عِظَامَهُ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Moo ndax, nit ki dafa foog ne dunu dajale ay yaxam ?
بَلَىٰ قَادِرِينَ عَلَىٰ أَن نُّسَوِّيَ بَنَانَهُ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Axakañ ! Mën nañoo dajale yemalewaat cati waaraamam.
بَلْ يُرِيدُ الْإِنسَانُ لِيَفْجُرَ أَمَامَهُ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Te nit moom day bëgg rekk di dund cig boy.
يَسْأَلُ أَيَّانَ يَوْمُ الْقِيَامَةِ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Muy laaj : “Kañ la, Bisub Dekkiwaat ba ? ”
فَإِذَا بَرِقَ الْبَصَرُ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Su gis ba nee melxat gëlam,
وَخَسَفَ الْقَمَرُ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
weer wi muuru,
وَجُمِعَ الشَّمْسُ وَالْقَمَرُ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
ñu boole jant beek weer wi,
يَقُولُ الْإِنسَانُ يَوْمَئِذٍ أَيْنَ الْمَفَرُّ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
bu keroogee, nita ngay, wax naan : “Fees di rawe ? ”
كَلَّا لَا وَزَرَ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Déedéet ! Laquwaay amul de !
إِلَىٰ رَبِّكَ يَوْمَئِذٍ الْمُسْتَقَرُّ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
Bis boobu kay, dellu ca sa Boroom, rekk ay am.
يُنَبَّأُ الْإِنسَانُ يَوْمَئِذٍ بِمَا قَدَّمَ وَأَخَّرَ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Ca la ñuy xamale nit la mu jëkka def ba ci li mu mujjoon def (cig dundam).
بَلِ الْإِنسَانُ عَلَىٰ نَفْسِهِ بَصِيرَةٌ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Li war moo di ne nit mooy seede boppam,
وَلَوْ أَلْقَىٰ مَعَاذِيرَهُ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
dontela sax dafay jégalu ak miim.
لَا تُحَرِّكْ بِهِ لِسَانَكَ لِتَعْجَلَ بِهِ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
(Su Alxuraan) di wàcc (yaw Muhammad) bul di yëngël saw làmmiñ ngir gaawtoo ko :
إِنَّ عَلَيْنَا جَمْعَهُ وَقُرْآنَهُ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Sol la ko aku jàngiinam, Nun la war.
فَإِذَا قَرَأْنَاهُ فَاتَّبِعْ قُرْآنَهُ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Te suñu koy jàng na ngay toppaat, njàng ma.
ثُمَّ إِنَّ عَلَيْنَا بَيَانَهُ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Leeral ko it, Nun la war.
كَلَّا بَلْ تُحِبُّونَ الْعَاجِلَةَ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Yéen da ngeena bëgg (lool) dundug àddina si,
وَتَذَرُونَ الْآخِرَةَ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
te da ngeena sàggane (lool) Àllaxira.
وُجُوهٌ يَوْمَئِذٍ نَّاضِرَةٌ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Bu keroogee, dana am xarkanam yu naat
إِلَىٰ رَبِّهَا نَاظِرَةٌ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
yuy xool seen Boroom ;
وَوُجُوهٌ يَوْمَئِذٍ بَاسِرَةٌ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
dana fa am it bu keroogee, ay xarkanam yu ñàng,
تَظُنُّ أَن يُفْعَلَ بِهَا فَاقِرَةٌ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
dangay foog ne njuuma la.
كَلَّا إِذَا بَلَغَتِ التَّرَاقِيَ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Bu ruuga génnee ba ca bóli ga
وَقِيلَ مَنْ ۜ رَاقٍ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
ñu ne ko: “Ana kan mooy mocckat ba ? ”
وَظَنَّ أَنَّهُ الْفِرَاقُ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Mu daldi xam nag ne dee dikk na,
وَالْتَفَّتِ السَّاقُ بِالسَّاقِ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
yeel ya daldi jaxasoo rawaasoo,
إِلَىٰ رَبِّكَ يَوْمَئِذٍ الْمَسَاقُ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Bu keroogee, ñu wommat la jaŋat-jaŋatee la jëm ca sa Boroom.
فَلَا صَدَّقَ وَلَا صَلَّىٰ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
Gëmul woon, te it daawuloon julli;
وَلَٰكِن كَذَّبَ وَتَوَلَّىٰ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
waaye, moom sax dafa weddi woon dumóoyu,
ثُمَّ ذَهَبَ إِلَىٰ أَهْلِهِ يَتَمَطَّىٰ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
daldi dem nag ca aw nitam, di xoggaliku.
أَوْلَىٰ لَكَ فَأَوْلَىٰ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
“Yaayoo nga toskare, yaayoo nga toskare! ”
ثُمَّ أَوْلَىٰ لَكَ فَأَوْلَىٰ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
Te it yaayoo nga toskare, yayoo nga ko !
أَيَحْسَبُ الْإِنسَانُ أَن يُتْرَكَ سُدًى ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
Moo ndax nit dafa foog ne dañu koy bàyyi rekk noonu muy nguyaay?
أَلَمْ يَكُ نُطْفَةً مِّن مَّنِيٍّ يُمْنَىٰ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
Moo ndax dafa doonul woon tóqug maniyu guy sottiku ?
ثُمَّ كَانَ عَلَقَةً فَخَلَقَ فَسَوَّىٰ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Mu mujj di aw lumbu Ma bind ko mu ne càndaŋ yemoo;
فَجَعَلَ مِنْهُ الزَّوْجَيْنِ الذَّكَرَ وَالْأُنثَىٰ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
ma def ci ñaari toolént ya : góor ak jigéen ?
أَلَيْسَ ذَٰلِكَ بِقَادِرٍ عَلَىٰ أَن يُحْيِيَ الْمَوْتَىٰ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
Moo ndax kooku munula dekkilaat ku dee ?
← 74 Al-Qiyama (75/114) 76 →
Jàng Simoore Al-Qiyama ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

75القيامة Al-Qiyamah 📚 40 Aaya مكية

Aaya bu ne – Simoore Al-Qiyama — 40 Aaya




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers