PDF —
40 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Qiyama pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Qiyama pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Qiyama Tekki. Simoore Al-Qiyama (Meccan) 40 Aaya.



40 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮊﮋﮌﮍﮎ
75:1 Maa ngi giñ ci bisub dekkiwaat ga !
ﮏﮐﮑﮒﮓ
75:2 Te maa ngi giñ ci bakkan bi di ab yeddaakoon.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
75:3 Moo ndax, nit ki dafa foog ne dunu dajale ay yaxam ?
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
75:4 Axakañ ! Mën nañoo dajale yemalewaat cati waaraamam.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
75:5 Te nit moom day bëgg rekk di dund cig boy.
ﮧﮨﮩﮪﮫ
75:6 Muy laaj : “Kañ la, Bisub Dekkiwaat ba ? ”
ﮬﮭﮮﮯ
75:7 Su gis ba nee melxat gëlam,
ﮰﮱﯓ
75:8 weer wi muuru,
ﯔﯕﯖﯗ
75:9 ñu boole jant beek weer wi,
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
75:10 bu keroogee, nita ngay, wax naan : “Fees di rawe ? ”
ﯞﯟﯠﯡ
75:11 Déedéet ! Laquwaay amul de !
ﯢﯣﯤﯥﯦ
75:12 Bis boobu kay, dellu ca sa Boroom, rekk ay am.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
75:13 Ca la ñuy xamale nit la mu jëkka def ba ci li mu mujjoon def (cig dundam).
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
75:14 Li war moo di ne nit mooy seede boppam,
ﯴﯵﯶﯷ
75:15 dontela sax dafay jégalu ak miim.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
75:16 (Su Alxuraan) di wàcc (yaw Muhammad) bul di yëngël saw làmmiñ ngir gaawtoo ko :
ﯿﰀﰁﰂﰃ
75:17 Sol la ko aku jàngiinam, Nun la war.
ﰄﰅﰆﰇﰈ
75:18 Te suñu koy jàng na ngay toppaat, njàng ma.
ﰉﰊﰋﰌﰍ
75:19 Leeral ko it, Nun la war.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
75:20 Yéen da ngeena bëgg (lool) dundug àddina si,
ﭖﭗﭘ
75:21 te da ngeena sàggane (lool) Àllaxira.
ﭙﭚﭛﭜ
75:22 Bu keroogee, dana am xarkanam yu naat
ﭝﭞﭟﭠ
75:23 yuy xool seen Boroom ;
ﭡﭢﭣﭤ
75:24 dana fa am it bu keroogee, ay xarkanam yu ñàng,
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
75:25 dangay foog ne njuuma la.
ﭫﭬﭭﭮﭯ
75:26 Bu ruuga génnee ba ca bóli ga
ﭰﭱﭲﭳﭴ
75:27 ñu ne ko: “Ana kan mooy mocckat ba ? ”
ﭵﭶﭷﭸ
75:28 Mu daldi xam nag ne dee dikk na,
ﭹﭺﭻﭼ
75:29 yeel ya daldi jaxasoo rawaasoo,
ﭽﭾﭿﮀﮁ
75:30 Bu keroogee, ñu wommat la jaŋat-jaŋatee la jëm ca sa Boroom.
ﮂﮃﮄﮅﮆ
75:31 Gëmul woon, te it daawuloon julli;
ﮇﮈﮉﮊ
75:32 waaye, moom sax dafa weddi woon dumóoyu,
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
75:33 daldi dem nag ca aw nitam, di xoggaliku.
ﮑﮒﮓﮔ
75:34 “Yaayoo nga toskare, yaayoo nga toskare! ”
ﮕﮖﮗﮘﮙ
75:35 Te it yaayoo nga toskare, yayoo nga ko !
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
75:36 Moo ndax nit dafa foog ne dañu koy bàyyi rekk noonu muy nguyaay?
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
75:37 Moo ndax dafa doonul woon tóqug maniyu guy sottiku ?
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
75:38 Mu mujj di aw lumbu Ma bind ko mu ne càndaŋ yemoo;
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
75:39 ma def ci ñaari toolént ya : góor ak jigéen ?
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
75:40 Moo ndax kooku munula dekkilaat ku dee ?

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers