Ibrahima · 37/52
Tekki Waxtaan — Ibrahima
رَّبَّنَا إِنِّي أَسْكَنتُ مِن ذُرِّيَّتِي بِوَادٍ غَيْرِ ذِي زَرْعٍ عِندَ بَيْتِكَ الْمُحَرَّمِ رَبَّنَا لِيُقِيمُوا الصَّلَاةَ فَاجْعَلْ أَفْئِدَةً مِّنَ النَّاسِ تَهْوِي إِلَيْهِمْ وَارْزُقْهُم مِّنَ الثَّمَرَاتِ لَعَلَّهُمْ يَشْكُرُونَ ۝٣٧
Rabbanaaa inneee askantu min zurriyyatee biwaadin ghairi zee zar`in `inda Baitikal Muharrami Rabbanaa liyuqeemus Salaata faj`al af`idatam minan naasi tahweee ilaihim warzuqhum minas samaraati la`allahum yashkuroon
📖 Tekkim Wolof
Yaw sama Boroom, dëkkal naa lenn ci sama njaboot ci xur wu amul mbey, ci sa néeg bu ñu wormaal ba [Kaaba ga], ngir ñuy taxawal julli. Defal seenug cofeel ci xoli nit ñi. Te nga wërsëgal leen ay meññent. Ndax xéy-na ñu gërëm la ?

🎧 Dégg


📜 Aaya 35-39 — Ibrahima

35وَإِذْ قَالَ إِبْرَاهِيمُ رَبِّ اجْعَلْ هَٰذَا الْبَلَدَ آمِنًا وَاجْنُبْنِي وَبَنِيَّ أَن نَّعْبُدَ الْأَصْنَامَ
[Fàttalikul] ba Ibraahiima waxee ne : “Sama Boroom, [ñaan naa la] nga def dëkk bii di fu am kóolute, te maak samag njaboot nga soril nu ak jaamu xërëm.
36رَبِّ إِنَّهُنَّ أَضْلَلْنَ كَثِيرًا مِّنَ النَّاسِ ۖ فَمَن تَبِعَنِي فَإِنَّهُ مِنِّي ۖ وَمَنْ عَصَانِي فَإِنَّكَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Boroom sama, xërëm yooyu dey réeral nañu [sànk] lu bari ci nit ñi. Képp ku ma topp ci man la bokk. Képp ku ma weddi. .. [Yaa xam noo koy def], ndax Yaw Jéggalaakoon nga, Jaglewaakoon nga !
37رَّبَّنَا إِنِّي أَسْكَنتُ مِن ذُرِّيَّتِي بِوَادٍ غَيْرِ ذِي زَرْعٍ عِندَ بَيْتِكَ الْمُحَرَّمِ رَبَّنَا لِيُقِيمُوا الصَّلَاةَ فَاجْعَلْ أَفْئِدَةً مِّنَ النَّاسِ تَهْوِي إِلَيْهِمْ وَارْزُقْهُم مِّنَ الثَّمَرَاتِ لَعَلَّهُمْ يَشْكُرُونَ
Yaw sama Boroom, dëkkal naa lenn ci sama njaboot ci xur wu amul mbey, ci sa néeg bu ñu wormaal ba [Kaaba ga], ngir ñuy taxawal julli. Defal seenug cofeel ci xoli nit ñi. Te nga wërsëgal leen ay meññent. Ndax xéy-na ñu gërëm la ?
38رَبَّنَا إِنَّكَ تَعْلَمُ مَا نُخْفِي وَمَا نُعْلِنُ ۗ وَمَا يَخْفَىٰ عَلَى اللَّهِ مِن شَيْءٍ فِي الْأَرْضِ وَلَا فِي السَّمَاءِ
Yaw sunu Boroom dey, xam nga li ñuy nëbb ak li ñuy fésal : - te amul menn mbir mu umpu Yàlla ci suuf si, waxantuma laak asamaan ! -
39الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي وَهَبَ لِي عَلَى الْكِبَرِ إِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ ۚ إِنَّ رَبِّي لَسَمِيعُ الدُّعَاءِ
Xéeti cant yépp moomale naa ko Yàlla, Mi nga xam ne Moo ma may cig mage [sama doom] Ismaahiila ak Isaaqa. Sama Boroom daal kuy dégg ñaan la.
IbrahimaFihi Alxuraan
52Aaya
MeccanRevelation
37Aaya

Tekki — Ibrahima 37

Simoore Ibrahima Aaya 37 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yaw sama Boroom, dëkkal naa lenn ci sama njaboot ci…

Simoore Aaya 37/52 — Ibrahima إبراهيم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ibrahima Dégg, Ibrahima Tekki, Ibrahima mp3, Ibrahima pdf. Aaya 35–39. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers