Ibrahima · 36/52
Tekki Waxtaan — Ibrahima
رَبِّ إِنَّهُنَّ أَضْلَلْنَ كَثِيرًا مِّنَ النَّاسِ ۖ فَمَن تَبِعَنِي فَإِنَّهُ مِنِّي ۖ وَمَنْ عَصَانِي فَإِنَّكَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٣٦
Rabbi innahunna adlalna kaseeram minan naasi faman tabi`anee fa innahoo minnee wa man `asaanee fa innaka Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Boroom sama, xërëm yooyu dey réeral nañu [sànk] lu bari ci nit ñi. Képp ku ma topp ci man la bokk. Képp ku ma weddi. .. [Yaa xam noo koy def], ndax Yaw Jéggalaakoon nga, Jaglewaakoon nga !

🎧 Dégg


📜 Aaya 34-38 — Ibrahima

34وَآتَاكُم مِّن كُلِّ مَا سَأَلْتُمُوهُ ۚ وَإِن تَعُدُّوا نِعْمَتَ اللَّهِ لَا تُحْصُوهَا ۗ إِنَّ الْإِنسَانَ لَظَلُومٌ كَفَّارٌ
Te Moo di leen may ci lépp lu ngeen ko ñaan. Te sax, bu ngeen doon jéem a waññi ay xéewalam, dungeen ko mën a takk. Ndekete yoo nit moom ab tooñkat la bu mën a fakk jëf.
35وَإِذْ قَالَ إِبْرَاهِيمُ رَبِّ اجْعَلْ هَٰذَا الْبَلَدَ آمِنًا وَاجْنُبْنِي وَبَنِيَّ أَن نَّعْبُدَ الْأَصْنَامَ
[Fàttalikul] ba Ibraahiima waxee ne : “Sama Boroom, [ñaan naa la] nga def dëkk bii di fu am kóolute, te maak samag njaboot nga soril nu ak jaamu xërëm.
36رَبِّ إِنَّهُنَّ أَضْلَلْنَ كَثِيرًا مِّنَ النَّاسِ ۖ فَمَن تَبِعَنِي فَإِنَّهُ مِنِّي ۖ وَمَنْ عَصَانِي فَإِنَّكَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Boroom sama, xërëm yooyu dey réeral nañu [sànk] lu bari ci nit ñi. Képp ku ma topp ci man la bokk. Képp ku ma weddi. .. [Yaa xam noo koy def], ndax Yaw Jéggalaakoon nga, Jaglewaakoon nga !
37رَّبَّنَا إِنِّي أَسْكَنتُ مِن ذُرِّيَّتِي بِوَادٍ غَيْرِ ذِي زَرْعٍ عِندَ بَيْتِكَ الْمُحَرَّمِ رَبَّنَا لِيُقِيمُوا الصَّلَاةَ فَاجْعَلْ أَفْئِدَةً مِّنَ النَّاسِ تَهْوِي إِلَيْهِمْ وَارْزُقْهُم مِّنَ الثَّمَرَاتِ لَعَلَّهُمْ يَشْكُرُونَ
Yaw sama Boroom, dëkkal naa lenn ci sama njaboot ci xur wu amul mbey, ci sa néeg bu ñu wormaal ba [Kaaba ga], ngir ñuy taxawal julli. Defal seenug cofeel ci xoli nit ñi. Te nga wërsëgal leen ay meññent. Ndax xéy-na ñu gërëm la ?
38رَبَّنَا إِنَّكَ تَعْلَمُ مَا نُخْفِي وَمَا نُعْلِنُ ۗ وَمَا يَخْفَىٰ عَلَى اللَّهِ مِن شَيْءٍ فِي الْأَرْضِ وَلَا فِي السَّمَاءِ
Yaw sunu Boroom dey, xam nga li ñuy nëbb ak li ñuy fésal : - te amul menn mbir mu umpu Yàlla ci suuf si, waxantuma laak asamaan ! -
IbrahimaFihi Alxuraan
52Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Ibrahima 36

Simoore Ibrahima Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Boroom sama, xërëm yooyu dey réeral nañu [sànk] lu bari…

Simoore Aaya 36/52 — Ibrahima إبراهيم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ibrahima Dégg, Ibrahima Tekki, Ibrahima mp3, Ibrahima pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers