Al-Kahf · 44/110
Tekki Waxtaan — Al-Kahf
هُنَالِكَ الْوَلَايَةُ لِلَّهِ الْحَقِّ ۚ هُوَ خَيْرٌ ثَوَابًا وَخَيْرٌ عُقْبًا ۝٤٤
Hunaalikal walaayatu lillaahil haqq; huwa khairun sawaabanw wa khairun `uqbaa
📖 Tekkim Wolof
Fu mu doon, kaaraange ñeel na Yàlla ju dëggu ja. Mooy joxe gën ji yool ak gën ji muj.

🎧 Dégg


📜 Aaya 42-46 — Al-Kahf

42وَأُحِيطَ بِثَمَرِهِ فَأَصْبَحَ يُقَلِّبُ كَفَّيْهِ عَلَىٰ مَا أَنفَقَ فِيهَا وَهِيَ خَاوِيَةٌ عَلَىٰ عُرُوشِهَا وَيَقُولُ يَا لَيْتَنِي لَمْ أُشْرِكْ بِرَبِّي أَحَدًا
Alageef na meññent ma mu xëy di moqarñi ñaari yoxoom ngir la mu ca tàbbal ci alal, te fekk tool ba yàqu na, garab ya daanu, dàmme ca dàtt ya. Mu naan : “Ay aka neexoon bokkaalewuma kenn ak sama Boroom ! ”.
43وَلَمْ تَكُن لَّهُ فِئَةٌ يَنصُرُونَهُ مِن دُونِ اللَّهِ وَمَا كَانَ مُنتَصِرًا
Te amatul mbooloo mu ko mën a dimbali ku dul Yàlla. Te nekkul it di mënal boppam dara.
44هُنَالِكَ الْوَلَايَةُ لِلَّهِ الْحَقِّ ۚ هُوَ خَيْرٌ ثَوَابًا وَخَيْرٌ عُقْبًا
Fu mu doon, kaaraange ñeel na Yàlla ju dëggu ja. Mooy joxe gën ji yool ak gën ji muj.
45وَاضْرِبْ لَهُم مَّثَلَ الْحَيَاةِ الدُّنْيَا كَمَاءٍ أَنزَلْنَاهُ مِنَ السَّمَاءِ فَاخْتَلَطَ بِهِ نَبَاتُ الْأَرْضِ فَأَصْبَحَ هَشِيمًا تَذْرُوهُ الرِّيَاحُ ۗ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ مُّقْتَدِرًا
Joxleen léebug dundu àddina. Dafa mel ni ndox mu ñu wàcce mu jóge asamaan ; tax gàncax ga jóge ci suuf sax. Mu mujj nekk mboob mu wow, ngelaw yi tasaare ko. Yàlla ku am kàttan la ci def lu ne !
46الْمَالُ وَالْبَنُونَ زِينَةُ الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۖ وَالْبَاقِيَاتُ الصَّالِحَاتُ خَيْرٌ عِندَ رَبِّكَ ثَوَابًا وَخَيْرٌ أَمَلًا
Alal ak i doom ci yiy neexal àddina lañu bokk. Waaye way-des ya di [jëf] yu yiw, ñooy ya gën ca sa Boroom ci wàllu yool ak yaakaar.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
44Aaya

Tekki — Al-Kahf 44

Simoore Al-Kahf Aaya 44 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Fu mu doon, kaaraange ñeel na Yàlla ju dëggu ja.…

Simoore Aaya 44/110 — Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Kahf Dégg, Al-Kahf Tekki, Al-Kahf mp3, Al-Kahf pdf. Aaya 42–46. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers