Al-Baqara · 232/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِذَا طَلَّقْتُمُ النِّسَاءَ فَبَلَغْنَ أَجَلَهُنَّ فَلَا تَعْضُلُوهُنَّ أَن يَنكِحْنَ أَزْوَاجَهُنَّ إِذَا تَرَاضَوْا بَيْنَهُم بِالْمَعْرُوفِ ۗ ذَٰلِكَ يُوعَظُ بِهِ مَن كَانَ مِنكُمْ يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ ۗ ذَٰلِكُمْ أَزْكَىٰ لَكُمْ وَأَطْهَرُ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ وَأَنتُمْ لَا تَعْلَمُونَ ٢٣٢
Transliteration
Wa izaa tallaqtumun nisaaa`a fabalaghna ajalahunna falaa ta`duloo hunna ai yankihna azwaaja humna izaa taraadaw bainahum bilma` roof; zaalika yoo`azu bihee man kaana minkum yu`minu billaahi wal yawmil aakhir; zaalikum azkaa lakum wa athar; wallaahu ya`lamu wa antum laa ta`lamu wa antum laa ta`lamoon
Tekki (Tekkim Wolof)
📖 Tekkim Wolof
Bu ngeen fasee aw jigéen, ba seen idda mat, buleen gàllankoor bu ñu bëggee sëyaat ak seeni jëkkër, bu ñu ca dogoo te nangulante ko. Yàllaa cay waar képp ku bokk ci yéen te gëm Yàlla ak bis bu mujj ba [Bis-pénc ba]. Loolu moo gën a sell ci yéen te moo gën a laab. Yàlla xam na te yéen xamuleen.
Additional reference in Fulfulde
🎧 Dégg
📜 Aaya 230-234 — Al-Baqara
230فَإِن طَلَّقَهَا فَلَا تَحِلُّ لَهُ مِن بَعْدُ حَتَّىٰ تَنكِحَ زَوْجًا غَيْرَهُ ۗ فَإِن طَلَّقَهَا فَلَا جُنَاحَ عَلَيْهِمَا أَن يَتَرَاجَعَا إِن ظَنَّا أَن يُقِيمَا حُدُودَ اللَّهِ ۗ وَتِلْكَ حُدُودُ اللَّهِ يُبَيِّنُهَا لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ
Bu ko fasewaatee [ñetteelu yoon] du dagan mu jëlaat ko ginnaaw ga. Ba ba muy sëy ak jeneen jëkkër ju dul moom joo xam ne su ko fasee moom it mu daldi ragal delloowante [ndaw sa ak jëkkër ju jëkk ja], njeem njort nañu ne dana sàmmonte ak daytali Yàlla yi. Muy leeralal nit ñi amug ràññee.
231وَإِذَا طَلَّقْتُمُ النِّسَاءَ فَبَلَغْنَ أَجَلَهُنَّ فَأَمْسِكُوهُنَّ بِمَعْرُوفٍ أَوْ سَرِّحُوهُنَّ بِمَعْرُوفٍ ۚ وَلَا تُمْسِكُوهُنَّ ضِرَارًا لِّتَعْتَدُوا ۚ وَمَن يَفْعَلْ ذَٰلِكَ فَقَدْ ظَلَمَ نَفْسَهُ ۚ وَلَا تَتَّخِذُوا آيَاتِ اللَّهِ هُزُوًا ۚ وَاذْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَمَا أَنزَلَ عَلَيْكُم مِّنَ الْكِتَابِ وَالْحِكْمَةِ يَعِظُكُم بِهِ ۚ وَاتَّقُوا اللَّهَ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Bu ngeen fasee aw jigéen, ba seeni idda [àpp] di waaj a mat, nangeen leen dencaat bu yiw, walla ngeen bàyyi leen ci njekk. Te buleen leen téye ngir bëgg leen a lor : di jalgati, ku def loolu topp na boppam. Buleen jàppe laayay Yàlla yi ay caaxaan. Fàttalikuleen xéewal yi leen Yàlla defal, ak li mu leen wàcceel ci Téere, ak xereñe, di leen ca waar. Kon ragal-leen Yàlla, te ngeen xam ne Yàlla xam na lépp.
232وَإِذَا طَلَّقْتُمُ النِّسَاءَ فَبَلَغْنَ أَجَلَهُنَّ فَلَا تَعْضُلُوهُنَّ أَن يَنكِحْنَ أَزْوَاجَهُنَّ إِذَا تَرَاضَوْا بَيْنَهُم بِالْمَعْرُوفِ ۗ ذَٰلِكَ يُوعَظُ بِهِ مَن كَانَ مِنكُمْ يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ ۗ ذَٰلِكُمْ أَزْكَىٰ لَكُمْ وَأَطْهَرُ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ وَأَنتُمْ لَا تَعْلَمُونَ
Bu ngeen fasee aw jigéen, ba seen idda mat, buleen gàllankoor bu ñu bëggee sëyaat ak seeni jëkkër, bu ñu ca dogoo te nangulante ko. Yàllaa cay waar képp ku bokk ci yéen te gëm Yàlla ak bis bu mujj ba [Bis-pénc ba]. Loolu moo gën a sell ci yéen te moo gën a laab. Yàlla xam na te yéen xamuleen.
233۞ وَالْوَالِدَاتُ يُرْضِعْنَ أَوْلَادَهُنَّ حَوْلَيْنِ كَامِلَيْنِ ۖ لِمَنْ أَرَادَ أَن يُتِمَّ الرَّضَاعَةَ ۚ وَعَلَى الْمَوْلُودِ لَهُ رِزْقُهُنَّ وَكِسْوَتُهُنَّ بِالْمَعْرُوفِ ۚ لَا تُكَلَّفُ نَفْسٌ إِلَّا وُسْعَهَا ۚ لَا تُضَارَّ وَالِدَةٌ بِوَلَدِهَا وَلَا مَوْلُودٌ لَّهُ بِوَلَدِهِ ۚ وَعَلَى الْوَارِثِ مِثْلُ ذَٰلِكَ ۗ فَإِنْ أَرَادَا فِصَالًا عَن تَرَاضٍ مِّنْهُمَا وَتَشَاوُرٍ فَلَا جُنَاحَ عَلَيْهِمَا ۗ وَإِنْ أَرَدتُّمْ أَن تَسْتَرْضِعُوا أَوْلَادَكُمْ فَلَا جُنَاحَ عَلَيْكُمْ إِذَا سَلَّمْتُم مَّا آتَيْتُم بِالْمَعْرُوفِ ۗ وَاتَّقُوا اللَّهَ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
Nday ya nañu nàmpal seeni doom ñaari at yu mat sëkk ci ku bëgg nàmpal gu mat. War na ca baay ya dundu ak koddaayu jabar ja ci njekk. Tegeesul kenn lu dul la mu àttan. Wareesul a lor ndey ja ci [nàmpal doomam, baay ba it wareesu koo lor ci doomam]. Aji-nàmp ja donn alal looloo ko war. Te ñu génne ci alalam peyu nàmpal ga. Su ñu bëggee feral [liir ba] ci ña jaboote ñoom ñaar, diisoo ca aayul ci ñoom ñaar ñu def ko. Bu ngeen bëggee nàmpal-lu seeni doom yéen baay yi, aayul ngeen def ko, bu joxee pey gu jaadu ci njekk. Nangeen ragal Yàlla te xam ne Yàllaa ngi ne jàkk ci li ngeen de def
234وَالَّذِينَ يُتَوَفَّوْنَ مِنكُمْ وَيَذَرُونَ أَزْوَاجًا يَتَرَبَّصْنَ بِأَنفُسِهِنَّ أَرْبَعَةَ أَشْهُرٍ وَعَشْرًا ۖ فَإِذَا بَلَغْنَ أَجَلَهُنَّ فَلَا جُنَاحَ عَلَيْكُمْ فِيمَا فَعَلْنَ فِي أَنفُسِهِنَّ بِالْمَعْرُوفِ ۗ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Ña dee ci yéen te bàyyi ginnaaw ay jabar : nañu muñandiku [ñoom jabar yooyu] ñeenti weer ak fukki fan. Bu ñu matalee àpp ba amatuleen wareef ca la ñu def ci seen bopp, ci lu yiw. Yàlla deñ na kumpa ci li ngeen di def.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
232Aaya
Tekki — Al-Baqara 232
Simoore Al-Baqara Aaya 232 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ngeen fasee aw jigéen, ba seen idda mat, buleen…Simoore Aaya 232/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 230–234. Tekkim Wolof: Fulfulde.
العربية
English
Bahasa Indonesia
Türkçe
Русский
فارسی
Français
اردو
বাংলা
Deutsch
Español
中文
हिन्दी
Português
Italiano
ภาษาไทย
Polski
Nederlands
Shqip
Kiswahili
O'zbek
தமிழ்
Melayu
Bosanski
Soomaali
Azərbaycan
کوردی
한국어
日本語
Svenska
Dansk
Norsk
پښتو
മലയാളം
සිංහල
Tamazight
Hausa
አማርኛ
Български
Тоҷикӣ
Қазақша
Filipino
سنڌي
Yorùbá
Fulfulde
Татарча
ئۇيغۇرچە
Кыргызча
ਪੰਜਾਬੀ
Jawa
తెలుగు
မြန်မာ
ગુજરાતી
Oromo
मराठी
Tiếng Việt
Malagasy
Нохчийн
Wolof
ދިވެހި
ಕನ್ನಡ
Українська
Ελληνικά
ქართული
ខ្មែរ
دری
Qafar af
Maranao
नेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers








