Al-Maida · 95/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَقْتُلُوا الصَّيْدَ وَأَنتُمْ حُرُمٌ ۚ وَمَن قَتَلَهُ مِنكُم مُّتَعَمِّدًا فَجَزَاءٌ مِّثْلُ مَا قَتَلَ مِنَ النَّعَمِ يَحْكُمُ بِهِ ذَوَا عَدْلٍ مِّنكُمْ هَدْيًا بَالِغَ الْكَعْبَةِ أَوْ كَفَّارَةٌ طَعَامُ مَسَاكِينَ أَوْ عَدْلُ ذَٰلِكَ صِيَامًا لِّيَذُوقَ وَبَالَ أَمْرِهِ ۗ عَفَا اللَّهُ عَمَّا سَلَفَ ۚ وَمَنْ عَادَ فَيَنتَقِمُ اللَّهُ مِنْهُ ۗ وَاللَّهُ عَزِيزٌ ذُو انتِقَامٍ ۝٩٥
Yaaa aiyuhal lazeena aamanoo laa taqtuslus saida wa antum hurum; wa man qatalahoo minkum mut`am midan fajazaaa`um mislu maa qatala minanna`ami yahkumu bihee zawaa `adlim minkum hadyam baalighal Ka`bati aw kaffaaratun ta`aamu masaakeena aw `adlu zaalika Siyaamal liyazooqa wabaala amrih; `afal laahu `ammaa salaf; wa man `aada fayanta qimul laahu minh; wallaahu `azeezun zuntiqaam
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen ñi gëm ! Buleen rey aw rab bëgg rëbb, fekk ngeen nekk ci armal di aj [Màkka]. Ku ko rey ci yéen te tey ko, war naa fey lu mel ni la mu rey ci jur, ñaar ñu maandu ci yéen xayma ko, muy yool bu ñuy yóbb ca kaaba ga, mbaa mu jéggaloo aw ñam wu muy jox néew-ji-doole yi, walla mu woor kem lu tollu noona. Ndax mu mos mbugalu la mu jëf. Yàlla boroom kàttan la, Ku mën a feyyu la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 93-97 — Al-Maida

93لَيْسَ عَلَى الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ جُنَاحٌ فِيمَا طَعِمُوا إِذَا مَا اتَّقَوا وَّآمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ ثُمَّ اتَّقَوا وَّآمَنُوا ثُمَّ اتَّقَوا وَّأَحْسَنُوا ۗ وَاللَّهُ يُحِبُّ الْمُحْسِنِينَ
Du nekk bàkkaar ca ña gëm tey sellal seeni jëf, la ñu masoon a lekk [lu araam lu jiitu digle ga ko araamal], gannaaw ba, ñu nekk ñu di way-ragal Yàlla te gëm, di sellal seeni jëf ba noppi raggal Yàlla te gëm ; ragal Yàlla te rafetal seeni jëf. Yàlla safoo na way-rafetal ña.
94يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَيَبْلُوَنَّكُمُ اللَّهُ بِشَيْءٍ مِّنَ الصَّيْدِ تَنَالُهُ أَيْدِيكُمْ وَرِمَاحُكُمْ لِيَعْلَمَ اللَّهُ مَن يَخَافُهُ بِالْغَيْبِ ۚ فَمَنِ اعْتَدَىٰ بَعْدَ ذَٰلِكَ فَلَهُ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Éy yéen ñi gëm ! Yàlla dana leen nattu ci lenn lu jëm ci rëbb ci seeni loxo walla seeni xeej. Ndax Mu xam ku Ko ragal ci kumpa. Ku féttéerlu ginnaaw loolu, mbugal mu metti dana ko dal.
95يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَقْتُلُوا الصَّيْدَ وَأَنتُمْ حُرُمٌ ۚ وَمَن قَتَلَهُ مِنكُم مُّتَعَمِّدًا فَجَزَاءٌ مِّثْلُ مَا قَتَلَ مِنَ النَّعَمِ يَحْكُمُ بِهِ ذَوَا عَدْلٍ مِّنكُمْ هَدْيًا بَالِغَ الْكَعْبَةِ أَوْ كَفَّارَةٌ طَعَامُ مَسَاكِينَ أَوْ عَدْلُ ذَٰلِكَ صِيَامًا لِّيَذُوقَ وَبَالَ أَمْرِهِ ۗ عَفَا اللَّهُ عَمَّا سَلَفَ ۚ وَمَنْ عَادَ فَيَنتَقِمُ اللَّهُ مِنْهُ ۗ وَاللَّهُ عَزِيزٌ ذُو انتِقَامٍ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen rey aw rab bëgg rëbb, fekk ngeen nekk ci armal di aj [Màkka]. Ku ko rey ci yéen te tey ko, war naa fey lu mel ni la mu rey ci jur, ñaar ñu maandu ci yéen xayma ko, muy yool bu ñuy yóbb ca kaaba ga, mbaa mu jéggaloo aw ñam wu muy jox néew-ji-doole yi, walla mu woor kem lu tollu noona. Ndax mu mos mbugalu la mu jëf. Yàlla boroom kàttan la, Ku mën a feyyu la.
96أُحِلَّ لَكُمْ صَيْدُ الْبَحْرِ وَطَعَامُهُ مَتَاعًا لَّكُمْ وَلِلسَّيَّارَةِ ۖ وَحُرِّمَ عَلَيْكُمْ صَيْدُ الْبَرِّ مَا دُمْتُمْ حُرُمًا ۗ وَاتَّقُوا اللَّهَ الَّذِي إِلَيْهِ تُحْشَرُونَ
Dagan na ci yéen la ngeen nappe ca géej ga, ak ñamu géej, muj xéewal ci yéen ñi nekk ci armal. Te nangeen ragal Yàlla, Ma nga xam ne, dees na leen fang jëme ca Moom.
97۞ جَعَلَ اللَّهُ الْكَعْبَةَ الْبَيْتَ الْحَرَامَ قِيَامًا لِّلنَّاسِ وَالشَّهْرَ الْحَرَامَ وَالْهَدْيَ وَالْقَلَائِدَ ۚ ذَٰلِكَ لِتَعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ وَأَنَّ اللَّهَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Yàlla def na kaaba ga muy néeg bu ñu wormaal, muy lu ñu taxawal ngir nit ñi. Ak àtte weer wa ñu wormaal ak yool ga, ak mala ya ñu ràngal, yooyu yépp [def na ko] ngir ngeen xam ne Yàlla xam na li nekk ci asamaan yi ak suuf si; te it xam na lu ne.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
95Aaya

Tekki — Al-Maida 95

Simoore Al-Maida Aaya 95 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen ñi gëm ! Buleen rey aw rab bëgg…

Simoore Aaya 95/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 93–97. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers