Al-An'am · 97/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَهُوَ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ النُّجُومَ لِتَهْتَدُوا بِهَا فِي ظُلُمَاتِ الْبَرِّ وَالْبَحْرِ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ ۝٩٧
Wa Huwal lazee ja`ala lakumun nujooma litahtadoo bihaa fee zulumaatil barri walbahr; qad fassalnal Aayaati liqawminy ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Moom moo leen defal ay bidiw ngir ngeen di ca gindiku bu ngeen nekkee ci lëndëmi jéeri walla géej gi. Faramfàcce Nanu Téere ba, ngir aw nit ñuy xam !
🎧 Dégg

📜 Aaya 95-99 — Al-An'am

95۞ إِنَّ اللَّهَ فَالِقُ الْحَبِّ وَالنَّوَىٰ ۖ يُخْرِجُ الْحَيَّ مِنَ الْمَيِّتِ وَمُخْرِجُ الْمَيِّتِ مِنَ الْحَيِّ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ
Yàlla mooy xar pepp ak i saal : [génne ca luy sax gàncax walla garab], Mooy génne luy dundu ci lu dee, tey génne lu dee ci luy dundu. Yàllaa ngoogu. Waaw naka lañu leen wëlbatee ?
96فَالِقُ الْإِصْبَاحِ وَجَعَلَ اللَّيْلَ سَكَنًا وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ حُسْبَانًا ۚ ذَٰلِكَ تَقْدِيرُ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ
Mooy sos leeraayu suba si, def guddi muy noflaay ; def jant bi ak weer wi ñuy waññikaayu jamono. Loolu mooy nattaleb Aji-not jiy Aji-xam [Yàlla].
97وَهُوَ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ النُّجُومَ لِتَهْتَدُوا بِهَا فِي ظُلُمَاتِ الْبَرِّ وَالْبَحْرِ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ
Moom moo leen defal ay bidiw ngir ngeen di ca gindiku bu ngeen nekkee ci lëndëmi jéeri walla géej gi. Faramfàcce Nanu Téere ba, ngir aw nit ñuy xam !
98وَهُوَ الَّذِي أَنشَأَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ فَمُسْتَقَرٌّ وَمُسْتَوْدَعٌ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَفْقَهُونَ
Moom moo leen sose ci benn bakkan. [Ngeen jaar] ci dekkiwaay [ci ndiggu baay] ak saxuwaay [ci biiru yaay]. Leeral Nanu sunuy kéemaan ngir aw nit ñu am dégg-dégg.
99وَهُوَ الَّذِي أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَخْرَجْنَا بِهِ نَبَاتَ كُلِّ شَيْءٍ فَأَخْرَجْنَا مِنْهُ خَضِرًا نُّخْرِجُ مِنْهُ حَبًّا مُّتَرَاكِبًا وَمِنَ النَّخْلِ مِن طَلْعِهَا قِنْوَانٌ دَانِيَةٌ وَجَنَّاتٍ مِّنْ أَعْنَابٍ وَالزَّيْتُونَ وَالرُّمَّانَ مُشْتَبِهًا وَغَيْرَ مُتَشَابِهٍ ۗ انظُرُوا إِلَىٰ ثَمَرِهِ إِذَا أَثْمَرَ وَيَنْعِهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكُمْ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Moom mooy wàcce ndox mu jóge asamaan. Nu genne ci gàncax lu nekk, Nu génne ci loolu gàncax gu naat, ci loolu Nu génne ci ay pepp yu raŋaloo ; ak ci garabu tàndarma, ay tëggu tàndarma yu jóge ci tóor-tóor yi te jegeñ suuf. Seetluleen seeni meññent bu ñuy meññ ak bu ñuy ñor. Kéemaan guy waaree ngi noonu ci ñi gëm.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
97Aaya

Tekki — Al-An'am 97

Simoore Al-An'am Aaya 97 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moom moo leen defal ay bidiw ngir ngeen di ca…

Simoore Aaya 97/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 95–99. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers