Al-An'am · 98/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَهُوَ الَّذِي أَنشَأَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ فَمُسْتَقَرٌّ وَمُسْتَوْدَعٌ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَفْقَهُونَ ۝٩٨
Wa hhuwal lazeee ansha akum min nasinw waahidatin famustaqarrunw wa mustawda`; qad fassalnal Aayaati liqaw miny-yafqahoon
📖 Tekkim Wolof
Moom moo leen sose ci benn bakkan. [Ngeen jaar] ci dekkiwaay [ci ndiggu baay] ak saxuwaay [ci biiru yaay]. Leeral Nanu sunuy kéemaan ngir aw nit ñu am dégg-dégg.
🎧 Dégg

📜 Aaya 96-100 — Al-An'am

96فَالِقُ الْإِصْبَاحِ وَجَعَلَ اللَّيْلَ سَكَنًا وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ حُسْبَانًا ۚ ذَٰلِكَ تَقْدِيرُ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ
Mooy sos leeraayu suba si, def guddi muy noflaay ; def jant bi ak weer wi ñuy waññikaayu jamono. Loolu mooy nattaleb Aji-not jiy Aji-xam [Yàlla].
97وَهُوَ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ النُّجُومَ لِتَهْتَدُوا بِهَا فِي ظُلُمَاتِ الْبَرِّ وَالْبَحْرِ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ
Moom moo leen defal ay bidiw ngir ngeen di ca gindiku bu ngeen nekkee ci lëndëmi jéeri walla géej gi. Faramfàcce Nanu Téere ba, ngir aw nit ñuy xam !
98وَهُوَ الَّذِي أَنشَأَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ فَمُسْتَقَرٌّ وَمُسْتَوْدَعٌ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَفْقَهُونَ
Moom moo leen sose ci benn bakkan. [Ngeen jaar] ci dekkiwaay [ci ndiggu baay] ak saxuwaay [ci biiru yaay]. Leeral Nanu sunuy kéemaan ngir aw nit ñu am dégg-dégg.
99وَهُوَ الَّذِي أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَخْرَجْنَا بِهِ نَبَاتَ كُلِّ شَيْءٍ فَأَخْرَجْنَا مِنْهُ خَضِرًا نُّخْرِجُ مِنْهُ حَبًّا مُّتَرَاكِبًا وَمِنَ النَّخْلِ مِن طَلْعِهَا قِنْوَانٌ دَانِيَةٌ وَجَنَّاتٍ مِّنْ أَعْنَابٍ وَالزَّيْتُونَ وَالرُّمَّانَ مُشْتَبِهًا وَغَيْرَ مُتَشَابِهٍ ۗ انظُرُوا إِلَىٰ ثَمَرِهِ إِذَا أَثْمَرَ وَيَنْعِهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكُمْ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Moom mooy wàcce ndox mu jóge asamaan. Nu genne ci gàncax lu nekk, Nu génne ci loolu gàncax gu naat, ci loolu Nu génne ci ay pepp yu raŋaloo ; ak ci garabu tàndarma, ay tëggu tàndarma yu jóge ci tóor-tóor yi te jegeñ suuf. Seetluleen seeni meññent bu ñuy meññ ak bu ñuy ñor. Kéemaan guy waaree ngi noonu ci ñi gëm.
100وَجَعَلُوا لِلَّهِ شُرَكَاءَ الْجِنَّ وَخَلَقَهُمْ ۖ وَخَرَقُوا لَهُ بَنِينَ وَبَنَاتٍ بِغَيْرِ عِلْمٍ ۚ سُبْحَانَهُ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يَصِفُونَ
Te ñoom sàkkal nañu Yàlla ay bokkaale yu di ay jinne te Moo leen bind. Sosal nañu ko it ay doom yu góor ak yu jigéen, ci lu àndul ak benn xam-xam. Cëy sellam ga ak màggam ga ! Jomb Na la ñu koy nirële.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
98Aaya

Tekki — Al-An'am 98

Simoore Al-An'am Aaya 98 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moom moo leen sose ci benn bakkan. [Ngeen jaar] ci…

Simoore Aaya 98/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 96–100. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers