Al-An'am · 96/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
فَالِقُ الْإِصْبَاحِ وَجَعَلَ اللَّيْلَ سَكَنًا وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ حُسْبَانًا ۚ ذَٰلِكَ تَقْدِيرُ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ ۝٩٦
Faaliqul isbaahi wa ja`alal laila sakananw washh shamsa walqamara husbaanaa; zaalika taqdeerul `Azeezil `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Mooy sos leeraayu suba si, def guddi muy noflaay ; def jant bi ak weer wi ñuy waññikaayu jamono. Loolu mooy nattaleb Aji-not jiy Aji-xam [Yàlla].

🎧 Dégg


📜 Aaya 94-98 — Al-An'am

94وَلَقَدْ جِئْتُمُونَا فُرَادَىٰ كَمَا خَلَقْنَاكُمْ أَوَّلَ مَرَّةٍ وَتَرَكْتُم مَّا خَوَّلْنَاكُمْ وَرَاءَ ظُهُورِكُمْ ۖ وَمَا نَرَىٰ مَعَكُمْ شُفَعَاءَكُمُ الَّذِينَ زَعَمْتُمْ أَنَّهُمْ فِيكُمْ شُرَكَاءُ ۚ لَقَد تَّقَطَّعَ بَيْنَكُمْ وَضَلَّ عَنكُم مَّا كُنتُمْ تَزْعُمُونَ
(Moom Yàlla Mu ne leen) Dikk ngeen di kenn kenn ni Nu leen binde woon cig njalbéen, te bàyyi ci seen ginnaaw la ñu leen wërsëgale woon. Waaw Nun sax gisunu ña ngeen daan jaamu, di ko bokkaale ak Yàlla. Léegi seen digganteek ñoom dog na, te la ngeen doon sos réer na leen.
95۞ إِنَّ اللَّهَ فَالِقُ الْحَبِّ وَالنَّوَىٰ ۖ يُخْرِجُ الْحَيَّ مِنَ الْمَيِّتِ وَمُخْرِجُ الْمَيِّتِ مِنَ الْحَيِّ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ
Yàlla mooy xar pepp ak i saal : [génne ca luy sax gàncax walla garab], Mooy génne luy dundu ci lu dee, tey génne lu dee ci luy dundu. Yàllaa ngoogu. Waaw naka lañu leen wëlbatee ?
96فَالِقُ الْإِصْبَاحِ وَجَعَلَ اللَّيْلَ سَكَنًا وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ حُسْبَانًا ۚ ذَٰلِكَ تَقْدِيرُ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ
Mooy sos leeraayu suba si, def guddi muy noflaay ; def jant bi ak weer wi ñuy waññikaayu jamono. Loolu mooy nattaleb Aji-not jiy Aji-xam [Yàlla].
97وَهُوَ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ النُّجُومَ لِتَهْتَدُوا بِهَا فِي ظُلُمَاتِ الْبَرِّ وَالْبَحْرِ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ
Moom moo leen defal ay bidiw ngir ngeen di ca gindiku bu ngeen nekkee ci lëndëmi jéeri walla géej gi. Faramfàcce Nanu Téere ba, ngir aw nit ñuy xam !
98وَهُوَ الَّذِي أَنشَأَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ فَمُسْتَقَرٌّ وَمُسْتَوْدَعٌ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَفْقَهُونَ
Moom moo leen sose ci benn bakkan. [Ngeen jaar] ci dekkiwaay [ci ndiggu baay] ak saxuwaay [ci biiru yaay]. Leeral Nanu sunuy kéemaan ngir aw nit ñu am dégg-dégg.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
96Aaya

Tekki — Al-An'am 96

Simoore Al-An'am Aaya 96 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mooy sos leeraayu suba si, def guddi muy noflaay ;…

Simoore Aaya 96/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 94–98. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers