Al-A'raf · 150/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَلَمَّا رَجَعَ مُوسَىٰ إِلَىٰ قَوْمِهِ غَضْبَانَ أَسِفًا قَالَ بِئْسَمَا خَلَفْتُمُونِي مِن بَعْدِي ۖ أَعَجِلْتُمْ أَمْرَ رَبِّكُمْ ۖ وَأَلْقَى الْأَلْوَاحَ وَأَخَذَ بِرَأْسِ أَخِيهِ يَجُرُّهُ إِلَيْهِ ۚ قَالَ ابْنَ أُمَّ إِنَّ الْقَوْمَ اسْتَضْعَفُونِي وَكَادُوا يَقْتُلُونَنِي فَلَا تُشْمِتْ بِيَ الْأَعْدَاءَ وَلَا تَجْعَلْنِي مَعَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ ۝١٥٠
Wa lammaa raja`a Moosaaa ilaa qawmihee ghadbaana asifan qaala bi`samaa khalaftumoonee mim ba`dee a-`ajiltum amra Rabbikum wa alqal alwaaha wa akhaza biraasi akheehi yajurruhoo ilaih; qaalab na umma innal qawmas tad`afoonee wa kadoo yaqtu loonanee; falaa tushmit biyal a`daaa`a wa laa taj`alnee ma`al qawmiz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
Ba Muusaa ñibbee ca aw nitam, mer lool, dafa wax ne : “Nii ngeen ma ginnaawoo ñaaw na ! Xanaa dangeen a yàkkamti seen àtteb Boroom gaaw a ñëw? ”. Mu daldi sànni àlluwa ya, jàpp ca boppub mbokkam ma, xëcc ko. Aaruuna toontu ko ne : “Yaw sama doomu-ndey , nit ñi dañu maa doyadal te xaw nañu maa rey sax. Kon bul bégloo noon ya te bul ma boole ca nit ña di way-tooñ”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 148-152 — Al-A'raf

148وَاتَّخَذَ قَوْمُ مُوسَىٰ مِن بَعْدِهِ مِنْ حُلِيِّهِمْ عِجْلًا جَسَدًا لَّهُ خُوَارٌ ۚ أَلَمْ يَرَوْا أَنَّهُ لَا يُكَلِّمُهُمْ وَلَا يَهْدِيهِمْ سَبِيلًا ۘ اتَّخَذُوهُ وَكَانُوا ظَالِمِينَ
Nitu Muusaa jàpp nañu ci ginnaawam aw yëkk wu ñu takk seeni takkaayi yaram, weddi Sunuy kàddu. Ndax dañoo gisul ne moom mënuta wax ak ñoom te duleen jubale ciw yoon ? Jàpp nañu ko [di ko jaamu], nekk i way-tooñ.
149وَلَمَّا سُقِطَ فِي أَيْدِيهِمْ وَرَأَوْا أَنَّهُمْ قَدْ ضَلُّوا قَالُوا لَئِن لَّمْ يَرْحَمْنَا رَبُّنَا وَيَغْفِرْ لَنَا لَنَكُونَنَّ مِنَ الْخَاسِرِينَ
Waaye ba mu daanoo ca seeni yoxo, te ñu gis ne ñoom dañoo nekkoon cig réer, ñu ne sunu Boroom : “Soo nu yërëmul, baal nu, dananu bokk ca way-yàqule ña”.
150وَلَمَّا رَجَعَ مُوسَىٰ إِلَىٰ قَوْمِهِ غَضْبَانَ أَسِفًا قَالَ بِئْسَمَا خَلَفْتُمُونِي مِن بَعْدِي ۖ أَعَجِلْتُمْ أَمْرَ رَبِّكُمْ ۖ وَأَلْقَى الْأَلْوَاحَ وَأَخَذَ بِرَأْسِ أَخِيهِ يَجُرُّهُ إِلَيْهِ ۚ قَالَ ابْنَ أُمَّ إِنَّ الْقَوْمَ اسْتَضْعَفُونِي وَكَادُوا يَقْتُلُونَنِي فَلَا تُشْمِتْ بِيَ الْأَعْدَاءَ وَلَا تَجْعَلْنِي مَعَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Ba Muusaa ñibbee ca aw nitam, mer lool, dafa wax ne : “Nii ngeen ma ginnaawoo ñaaw na ! Xanaa dangeen a yàkkamti seen àtteb Boroom gaaw a ñëw? ”. Mu daldi sànni àlluwa ya, jàpp ca boppub mbokkam ma, xëcc ko. Aaruuna toontu ko ne : “Yaw sama doomu-ndey , nit ñi dañu maa doyadal te xaw nañu maa rey sax. Kon bul bégloo noon ya te bul ma boole ca nit ña di way-tooñ”.
151قَالَ رَبِّ اغْفِرْ لِي وَلِأَخِي وَأَدْخِلْنَا فِي رَحْمَتِكَ ۖ وَأَنتَ أَرْحَمُ الرَّاحِمِينَ
Mu ne : “Yaw sama Boroom, jéggal ma ak sama mbokk mii te nga tàbbal nu ci sa yërmaande, ndax Yaw yaa ëpp yërmaande képp kuy yërëme”.
152إِنَّ الَّذِينَ اتَّخَذُوا الْعِجْلَ سَيَنَالُهُمْ غَضَبٌ مِّن رَّبِّهِمْ وَذِلَّةٌ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُفْتَرِينَ
Ña nga xam ne doon nanu jaamu yëkk wa, mbugal dana leen dal tukke fa seen Boroom, ak toroxte ci dundu àdduna. Te noonu Lanuy feyee ñay duural Yàlla.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
150Aaya

Tekki — Al-A'raf 150

Simoore Al-A'raf Aaya 150 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba Muusaa ñibbee ca aw nitam, mer lool, dafa wax…

Simoore Aaya 150/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 148–152. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers