Al-A'raf · 151/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
قَالَ رَبِّ اغْفِرْ لِي وَلِأَخِي وَأَدْخِلْنَا فِي رَحْمَتِكَ ۖ وَأَنتَ أَرْحَمُ الرَّاحِمِينَ ۝١٥١
Qaala Rabbigh fir lee wa li akhee wa adkhilnaa fee rahmatika wa Anta arhamur raahimeen
📖 Tekkim Wolof
Mu ne : “Yaw sama Boroom, jéggal ma ak sama mbokk mii te nga tàbbal nu ci sa yërmaande, ndax Yaw yaa ëpp yërmaande képp kuy yërëme”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 149-153 — Simoore Al-A'raf

149وَلَمَّا سُقِطَ فِي أَيْدِيهِمْ وَرَأَوْا أَنَّهُمْ قَدْ ضَلُّوا قَالُوا لَئِن لَّمْ يَرْحَمْنَا رَبُّنَا وَيَغْفِرْ لَنَا لَنَكُونَنَّ مِنَ الْخَاسِرِينَ
Waaye ba mu daanoo ca seeni yoxo, te ñu gis ne ñoom dañoo nekkoon cig réer, ñu ne sunu Boroom : “Soo nu yërëmul, baal nu, dananu bokk ca way-yàqule ña”.
150وَلَمَّا رَجَعَ مُوسَىٰ إِلَىٰ قَوْمِهِ غَضْبَانَ أَسِفًا قَالَ بِئْسَمَا خَلَفْتُمُونِي مِن بَعْدِي ۖ أَعَجِلْتُمْ أَمْرَ رَبِّكُمْ ۖ وَأَلْقَى الْأَلْوَاحَ وَأَخَذَ بِرَأْسِ أَخِيهِ يَجُرُّهُ إِلَيْهِ ۚ قَالَ ابْنَ أُمَّ إِنَّ الْقَوْمَ اسْتَضْعَفُونِي وَكَادُوا يَقْتُلُونَنِي فَلَا تُشْمِتْ بِيَ الْأَعْدَاءَ وَلَا تَجْعَلْنِي مَعَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Ba Muusaa ñibbee ca aw nitam, mer lool, dafa wax ne : “Nii ngeen ma ginnaawoo ñaaw na ! Xanaa dangeen a yàkkamti seen àtteb Boroom gaaw a ñëw? ”. Mu daldi sànni àlluwa ya, jàpp ca boppub mbokkam ma, xëcc ko. Aaruuna toontu ko ne : “Yaw sama doomu-ndey , nit ñi dañu maa doyadal te xaw nañu maa rey sax. Kon bul bégloo noon ya te bul ma boole ca nit ña di way-tooñ”.
151قَالَ رَبِّ اغْفِرْ لِي وَلِأَخِي وَأَدْخِلْنَا فِي رَحْمَتِكَ ۖ وَأَنتَ أَرْحَمُ الرَّاحِمِينَ
Mu ne : “Yaw sama Boroom, jéggal ma ak sama mbokk mii te nga tàbbal nu ci sa yërmaande, ndax Yaw yaa ëpp yërmaande képp kuy yërëme”.
152إِنَّ الَّذِينَ اتَّخَذُوا الْعِجْلَ سَيَنَالُهُمْ غَضَبٌ مِّن رَّبِّهِمْ وَذِلَّةٌ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُفْتَرِينَ
Ña nga xam ne doon nanu jaamu yëkk wa, mbugal dana leen dal tukke fa seen Boroom, ak toroxte ci dundu àdduna. Te noonu Lanuy feyee ñay duural Yàlla.
153وَالَّذِينَ عَمِلُوا السَّيِّئَاتِ ثُمَّ تَابُوا مِن بَعْدِهَا وَآمَنُوا إِنَّ رَبَّكَ مِن بَعْدِهَا لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ñay def lu ñaaw ba noppi ginnaaw ga ñu tuub, tey ñu gëm... sa Boroom nag, ginnaaw loolu, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
151Aaya

Tekki — Al-A'raf 151

Simoore Al-A'raf Aaya 151 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu ne : “Yaw sama Boroom, jéggal ma ak sama…

Simoore Aaya 151/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 149–153. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers