Al-Anfal · 47/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ خَرَجُوا مِن دِيَارِهِم بَطَرًا وَرِئَاءَ النَّاسِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ وَاللَّهُ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطٌ ۝٤٧
Wa laa takoonoo kallazeena kharajoo min diyaarihim bataranw wa ri`aaa`an naasi wa yasuddoona `an sabeelil laah; wallaahu bimaa ya`maloona muheet
📖 Tekkim Wolof
Buleen mel ni ña génnoon seeni kër, rëylu ak di ngistal ci nit ñi, te di gàllankoor [nit ñi ñu bañ jëm ci] yoonu Yàlla. Te Yàlla xam na la ñuy def de.
🎧 Dégg

📜 Aaya 45-49 — Al-Anfal

45يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا لَقِيتُمْ فِئَةً فَاثْبُتُوا وَاذْكُرُوا اللَّهَ كَثِيرًا لَّعَلَّكُمْ تُفْلِحُونَ
Éy yéen ñi gëm ñi ! Bu ngeen dajeek mbooloo, nangeen sax ci pastéef te ngeen tudd Yàlla lu bari ndax ngeen am ndam.
46وَأَطِيعُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَلَا تَنَازَعُوا فَتَفْشَلُوا وَتَذْهَبَ رِيحُكُمْ ۖ وَاصْبِرُوا ۚ إِنَّ اللَّهَ مَعَ الصَّابِرِينَ
Te nangeen topp Yàlla ak Yonentam ; te buleen xëccoo, kon ngeen yoqat, seen doole néew. Kon muñleen, Yàlla muñkat yi la àndal.
47وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ خَرَجُوا مِن دِيَارِهِم بَطَرًا وَرِئَاءَ النَّاسِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ وَاللَّهُ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطٌ
Buleen mel ni ña génnoon seeni kër, rëylu ak di ngistal ci nit ñi, te di gàllankoor [nit ñi ñu bañ jëm ci] yoonu Yàlla. Te Yàlla xam na la ñuy def de.
48وَإِذْ زَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ وَقَالَ لَا غَالِبَ لَكُمُ الْيَوْمَ مِنَ النَّاسِ وَإِنِّي جَارٌ لَّكُمْ ۖ فَلَمَّا تَرَاءَتِ الْفِئَتَانِ نَكَصَ عَلَىٰ عَقِبَيْهِ وَقَالَ إِنِّي بَرِيءٌ مِّنكُمْ إِنِّي أَرَىٰ مَا لَا تَرَوْنَ إِنِّي أَخَافُ اللَّهَ ۚ وَاللَّهُ شَدِيدُ الْعِقَابِ
Fàttalikul ba Séytaane rafetalee yéefar ya seeni jëf, ne leen : “Tey kenn duleen not, te man maa leen di dimbali.”. Waaye ba ñaari kurél ya jàkkaarloo, dafa dellu ginnaaw te wafeet daw, daldi wax, moom Séytaane, ne : “Man kat deñ naa ci yéen. Ndax gis naa lu ngeen gisul ; ragal naa Yàlla, te Yàlla Ku tar mbugal la”.
49إِذْ يَقُولُ الْمُنَافِقُونَ وَالَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ غَرَّ هَٰؤُلَاءِ دِينُهُمْ ۗ وَمَن يَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ فَإِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
(Fàttalikul), ba naafeq ya ak ña jàngoro nekk ca seeni xol waxee ne : “Ñii seen diine wor na leen.” Waaye ku wéeru ci Yàlla ... [na xam ne] Yàlla Kuy not lépp la, Ku xereñ la.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
47Aaya

Tekki — Al-Anfal 47

Simoore Al-Anfal Aaya 47 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buleen mel ni ña génnoon seeni kër, rëylu ak di…

Simoore Aaya 47/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 45–49. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers