Simoore Al-Anfal ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Anfal ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (75 Aaya — مدنية). Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Anfal

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
يَسْأَلُونَكَ عَنِ الْأَنفَالِ ۖ قُلِ الْأَنفَالُ لِلَّهِ وَالرَّسُولِ ۖ فَاتَّقُوا اللَّهَ وَأَصْلِحُوا ذَاتَ بَيْنِكُمْ ۖ وَأَطِيعُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Ña nga lay laaj lu jëm ci màng yi. Neeleen : “Màng yi, Yàlla ak Yonentam ñoo leen moom.” Kon ragal-leen Yàlla te nangeen defar seeni diggante, te ngeen topp Yàlla ak Yonentam ndeem way-gëm ngeen.
إِنَّمَا الْمُؤْمِنُونَ الَّذِينَ إِذَا ذُكِرَ اللَّهُ وَجِلَتْ قُلُوبُهُمْ وَإِذَا تُلِيَتْ عَلَيْهِمْ آيَاتُهُ زَادَتْهُمْ إِيمَانًا وَعَلَىٰ رَبِّهِمْ يَتَوَكَّلُونَ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Jullit ya ñooy ña nga xam ne bu ñu tuddee Yàlla seeni xol yëngu. Te bu ñu jàngaa ci ñoom ay laayaam mu yokk seen ngëm. Te ci seen Boroom lañu wékku.
الَّذِينَ يُقِيمُونَ الصَّلَاةَ وَمِمَّا رَزَقْنَاهُمْ يُنفِقُونَ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Ñooy ña nga xam ne danañu taxawal julli te ca la Nu leen wërsëgal, danañu ca joxe.
أُولَٰئِكَ هُمُ الْمُؤْمِنُونَ حَقًّا ۚ لَّهُمْ دَرَجَاتٌ عِندَ رَبِّهِمْ وَمَغْفِرَةٌ وَرِزْقٌ كَرِيمٌ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Ñooña ñooy jullit dëgg : ñeel na leen yékkatiku ca seen Boroom, ci ag jéggal ak wërsëg wu tedd.
كَمَا أَخْرَجَكَ رَبُّكَ مِن بَيْتِكَ بِالْحَقِّ وَإِنَّ فَرِيقًا مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ لَكَارِهُونَ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Naka noonu, sa Boroom génne na la sa kër ci dëgg, te fekk neexul ñennat ca way-gëm ña.
يُجَادِلُونَكَ فِي الْحَقِّ بَعْدَمَا تَبَيَّنَ كَأَنَّمَا يُسَاقُونَ إِلَى الْمَوْتِ وَهُمْ يَنظُرُونَ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Ñangay weranteek yaw ca dëgg ga ginnaaw ba mu feeñee, leer nàññ ; mel ni dañu leen a bëmax jëme ci dee, ñu ne ca jàkk.
وَإِذْ يَعِدُكُمُ اللَّهُ إِحْدَى الطَّائِفَتَيْنِ أَنَّهَا لَكُمْ وَتَوَدُّونَ أَنَّ غَيْرَ ذَاتِ الشَّوْكَةِ تَكُونُ لَكُمْ وَيُرِيدُ اللَّهُ أَن يُحِقَّ الْحَقَّ بِكَلِمَاتِهِ وَيَقْطَعَ دَابِرَ الْكَافِرِينَ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
(Fàttalikul), ba leen Yàlla digee ndam ca kaw benn ca ñaari kurél ya ngeen moom ko. Te ngeen ne siiw moom ga yorul ngànnaay, te Yàlla nammoon a dëgëral dëgg ga ci kàddoom te dog ginnaaw yéefar ya.
لِيُحِقَّ الْحَقَّ وَيُبْطِلَ الْبَاطِلَ وَلَوْ كَرِهَ الْمُجْرِمُونَ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
ngir dëgg sax te caaxaan jóge fi doonte la naqari na saay-saay sa.
إِذْ تَسْتَغِيثُونَ رَبَّكُمْ فَاسْتَجَابَ لَكُمْ أَنِّي مُمِدُّكُم بِأَلْفٍ مِّنَ الْمَلَائِكَةِ مُرْدِفِينَ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
(Fàttalikul) ba ngeen sàkkoo xettaliku ci seen Boroom te Mu nangul leen, ne : “Man danaa leen dooleel ak junni Malaaka yuy toftalante.
وَمَا جَعَلَهُ اللَّهُ إِلَّا بُشْرَىٰ وَلِتَطْمَئِنَّ بِهِ قُلُوبُكُمْ ۚ وَمَا النَّصْرُ إِلَّا مِنْ عِندِ اللَّهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Yàlla deful loolu lu dul ngir mbégtem [jullit ñi] ak ngir seen xel dal. Ndimbal amul feneen fu dul fa Yàlla. Naka Yàlla Aji-not la, Aji-xereñ la.
إِذْ يُغَشِّيكُمُ النُّعَاسَ أَمَنَةً مِّنْهُ وَيُنَزِّلُ عَلَيْكُم مِّنَ السَّمَاءِ مَاءً لِّيُطَهِّرَكُم بِهِ وَيُذْهِبَ عَنكُمْ رِجْزَ الشَّيْطَانِ وَلِيَرْبِطَ عَلَىٰ قُلُوبِكُمْ وَيُثَبِّتَ بِهِ الْأَقْدَامَ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
(Fàttalikuleen) ba Mu leen muuree ag ngëmmentu muy jàmm ju jóge ci Moom, te Mu wàcce ci yéen ndox mu jóge asamaan ngir Mu laabal leen ak loolu, ak ngir Mu dàqal leen sobees Séytaane, ak ngir Mu dëgëral seeni xol, dëgëral seeni ndëggu.
إِذْ يُوحِي رَبُّكَ إِلَى الْمَلَائِكَةِ أَنِّي مَعَكُمْ فَثَبِّتُوا الَّذِينَ آمَنُوا ۚ سَأُلْقِي فِي قُلُوبِ الَّذِينَ كَفَرُوا الرُّعْبَ فَاضْرِبُوا فَوْقَ الْأَعْنَاقِ وَاضْرِبُوا مِنْهُمْ كُلَّ بَنَانٍ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
[Fàttalikul] ba sa Boroom xamalee Malaaka ya ne leen : “Maak yéen a ànd : nangeen dooleel ñi gëm. Danaa sànni njàqare ci xoli ñi weddi. Kon dóorleen ci kaw doq yi te ngeen dóor leen ci cati baaraam yi.
ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ شَاقُّوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ ۚ وَمَن يُشَاقِقِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ فَإِنَّ اللَّهَ شَدِيدُ الْعِقَابِ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Loolu, ngir dañoo juuyook Yàlla ak Yonentam.”. Te ku juuyook Yàlla ak Yonentam, ... [na xam ne] Yàlla ku tar mbugal la !
ذَٰلِكُمْ فَذُوقُوهُ وَأَنَّ لِلْكَافِرِينَ عَذَابَ النَّارِ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Noonu lay dalee ci yéen [yéefar yi] ; kon mosleen ko ! Te ñeel na way-weddi ña mbugalu Safara.
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا لَقِيتُمُ الَّذِينَ كَفَرُوا زَحْفًا فَلَا تُوَلُّوهُمُ الْأَدْبَارَ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Éy yéen ñi gëm ñi, bu ngeen dajeek yéefar yi ñuy ràngu jëm ci yéen, buleen daw won leen ginnaaw.
وَمَن يُوَلِّهِمْ يَوْمَئِذٍ دُبُرَهُ إِلَّا مُتَحَرِّفًا لِّقِتَالٍ أَوْ مُتَحَيِّزًا إِلَىٰ فِئَةٍ فَقَدْ بَاءَ بِغَضَبٍ مِّنَ اللَّهِ وَمَأْوَاهُ جَهَنَّمُ ۖ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Ku daw won leen ginnaaw, ca bis boobu - lu dul kuy jéem a njuuy ba jekku na mu war a xeexe, walla kuy jéem a tafu ci mboolom jullit, - tàbbi ci merum Yàlla te dëkkuwaayam Safara la. Aka bon booba dëkkuwaay !
فَلَمْ تَقْتُلُوهُمْ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ قَتَلَهُمْ ۚ وَمَا رَمَيْتَ إِذْ رَمَيْتَ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ رَمَىٰ ۚ وَلِيُبْلِيَ الْمُؤْمِنِينَ مِنْهُ بَلَاءً حَسَنًا ۚ إِنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ عَلِيمٌ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Te reyuleen leen [yéen jullit ñi] : Yàlla moo leen rey. Te sànniwoo [yaw Yonent bi], bi nga sànnee suuf si : waaye Yàlla moo sànni, ngir Mu may jullit ñi xéewal gu rafet gu tukke ca Moom Yàlla ! Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
ذَٰلِكُمْ وَأَنَّ اللَّهَ مُوهِنُ كَيْدِ الْكَافِرِينَ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Loolu la dëggal ci yéen te [xamleen ne] Kuy doyadal pexey yéefar yi la [Moom Yàlla].
إِن تَسْتَفْتِحُوا فَقَدْ جَاءَكُمُ الْفَتْحُ ۖ وَإِن تَنتَهُوا فَهُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ ۖ وَإِن تَعُودُوا نَعُدْ وَلَن تُغْنِيَ عَنكُمْ فِئَتُكُمْ شَيْئًا وَلَوْ كَثُرَتْ وَأَنَّ اللَّهَ مَعَ الْمُؤْمِنِينَ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Ndegam dangeen di sàkku lu ngeen di àttewoo [yéen yéefar yi], ab àtte dikkal na leen ba noppi. Bu ngeen bàyyee [la ngeen nekkoon cig kéefar], mooy gën ci yéen. Bu ngeen delloo [ca la ngeen nekke woon], Nu dellu [ci di jox Yonent bi ndimbal], te kon seeni mbooloo duleen jariñ dara, doonte dafa bari lool. Yàlla nag Mook jullit yee ànd.
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا أَطِيعُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَلَا تَوَلَّوْا عَنْهُ وَأَنتُمْ تَسْمَعُونَ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Éy yéen ñi gëm ñi ! Nangeen topp Yàlla ak ub Yonentam, buleen ko dëddu te fekk dégg ngeen li muy wax.
وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ قَالُوا سَمِعْنَا وَهُمْ لَا يَسْمَعُونَ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Buleen mel ni ñiy wax : “Dégg nanu ”, te fekk dégguñu woon dara.
۞ إِنَّ شَرَّ الدَّوَابِّ عِندَ اللَّهِ الصُّمُّ الْبُكْمُ الَّذِينَ لَا يَعْقِلُونَ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Li gën a yées ci bindeef yi ca Yàlla, mooy ñi tëx, luu te bañ a xel-lu.
وَلَوْ عَلِمَ اللَّهُ فِيهِمْ خَيْرًا لَّأَسْمَعَهُمْ ۖ وَلَوْ أَسْمَعَهُمْ لَتَوَلَّوا وَّهُم مُّعْرِضُونَ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Ku leen woo woon ñu dëddu, nekk ñu beddiku.
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اسْتَجِيبُوا لِلَّهِ وَلِلرَّسُولِ إِذَا دَعَاكُمْ لِمَا يُحْيِيكُمْ ۖ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ يَحُولُ بَيْنَ الْمَرْءِ وَقَلْبِهِ وَأَنَّهُ إِلَيْهِ تُحْشَرُونَ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen wuyu Yàlla ak Yonentam ba, bu ñu leen woowee ci lu leen di musal, te nangeen xam ne Yàlla nag Dana dox nit ak xelam, te Danañu leen bëmëx jëme ca Moom.
وَاتَّقُوا فِتْنَةً لَّا تُصِيبَنَّ الَّذِينَ ظَلَمُوا مِنكُمْ خَاصَّةً ۖ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ شَدِيدُ الْعِقَابِ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Te nangeen ragal mbugal moo xam ne ku dul ña weddi ci yéen. Te nangeen xam ne Yàlla Ku tar mbugal la.
وَاذْكُرُوا إِذْ أَنتُمْ قَلِيلٌ مُّسْتَضْعَفُونَ فِي الْأَرْضِ تَخَافُونَ أَن يَتَخَطَّفَكُمُ النَّاسُ فَآوَاكُمْ وَأَيَّدَكُم بِنَصْرِهِ وَرَزَقَكُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Fàttalikuleen ba ngeen nekkee ñu néew, di ñu ñu doyadal ci suuf si, ngeen di ragal nit ñi fëkk leen. Mu daroo leen, dimbali leen ci ndimbalam, Mu wërsëgal leen ci xéewal yu sell ndax xéy-na yéen ngeen gëram [seen Boroom].
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَخُونُوا اللَّهَ وَالرَّسُولَ وَتَخُونُوا أَمَانَاتِكُمْ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Éy yéen ñi gëm ! Buleen wuruj Yàlla ak Yonent bi. Te buleen wuruj ci seen kóllare te xam ko xéll.
وَاعْلَمُوا أَنَّمَا أَمْوَالُكُمْ وَأَوْلَادُكُمْ فِتْنَةٌ وَأَنَّ اللَّهَ عِندَهُ أَجْرٌ عَظِيمٌ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Xamleen ne seeni alal ak seeni doom, fitna lañu ci yéen te pey gu màgg a nga fa Yàlla.
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِن تَتَّقُوا اللَّهَ يَجْعَل لَّكُمْ فُرْقَانًا وَيُكَفِّرْ عَنكُمْ سَيِّئَاتِكُمْ وَيَغْفِرْ لَكُمْ ۗ وَاللَّهُ ذُو الْفَضْلِ الْعَظِيمِ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Éy yéen ñi gëm ! Bu ngeen ragalee Yàlla, Mu sagal leen, far seeni ñaawtéef, jéggal leen. Te Yàlla Kuy Boroom ngëneel yu màgg la.
وَإِذْ يَمْكُرُ بِكَ الَّذِينَ كَفَرُوا لِيُثْبِتُوكَ أَوْ يَقْتُلُوكَ أَوْ يُخْرِجُوكَ ۚ وَيَمْكُرُونَ وَيَمْكُرُ اللَّهُ ۖ وَاللَّهُ خَيْرُ الْمَاكِرِينَ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
(Fàttalikul) ba la yéefar ya fexelee ngir ñu tëj la ci barab mbaa ñu rey la mbaa ñu génne la. Ñu def seeni pexe, Yàlla def ay pexeem, te Yàlla di Ku gën a màgg ay pexe.
وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا قَالُوا قَدْ سَمِعْنَا لَوْ نَشَاءُ لَقُلْنَا مِثْلَ هَٰذَا ۙ إِنْ هَٰذَا إِلَّا أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
Te saa yu ñu jàngee ci seen kanam Sunuy laaya, ñu ne : “Dégg nanu, ba noppi te sunu neexoon nu wax lu mel ni lii, ndaxte lii nekkul lu dul léebi nit ñu jëkk ña”.
وَإِذْ قَالُوا اللَّهُمَّ إِن كَانَ هَٰذَا هُوَ الْحَقَّ مِنْ عِندِكَ فَأَمْطِرْ عَلَيْنَا حِجَارَةً مِّنَ السَّمَاءِ أَوِ ائْتِنَا بِعَذَابٍ أَلِيمٍ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
(Fàttalikul) ba ñu waxee ne : “Yaw sunu Boroom, ndegam lii lu dëggu la lu jóge ci Yaw, Nanga sotti ci sunu kaw taw bu nekk ay xéewal wàcc jóge asamaan, mbaa nga indil nu mbugal mu metti”.
وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيُعَذِّبَهُمْ وَأَنتَ فِيهِمْ ۚ وَمَا كَانَ اللَّهُ مُعَذِّبَهُمْ وَهُمْ يَسْتَغْفِرُونَ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
Te Yàlla du Ku leen di mbugal fekk nga nekk [yaw Yonent bi] ci seen biir. Te it du Ku leen di mbugal fekk ñangay sàkku njéggal.
وَمَا لَهُمْ أَلَّا يُعَذِّبَهُمُ اللَّهُ وَهُمْ يَصُدُّونَ عَنِ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ وَمَا كَانُوا أَوْلِيَاءَهُ ۚ إِنْ أَوْلِيَاؤُهُ إِلَّا الْمُتَّقُونَ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
Yellul ci ñoom Yàlla bañ leen a mbugal, te ñuy wax nit ñi bañ a jëm ci jàkka ju ñu wormaal ja, nekkuñu ñoom soppey jàkka jooju, ay soppeem ñooy way-ragal Yàlla ña. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
وَمَا كَانَ صَلَاتُهُمْ عِندَ الْبَيْتِ إِلَّا مُكَاءً وَتَصْدِيَةً ۚ فَذُوقُوا الْعَذَابَ بِمَا كُنتُمْ تَكْفُرُونَ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
Seen julli ca néegub, nekkul lu dul ay waliis ak ay tàccu, kon : “Mosleen mbugal mi [ca xare Badar] ngir la ngeen doon weddi ! ”
إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ لِيَصُدُّوا عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ فَسَيُنفِقُونَهَا ثُمَّ تَكُونُ عَلَيْهِمْ حَسْرَةً ثُمَّ يُغْلَبُونَ ۗ وَالَّذِينَ كَفَرُوا إِلَىٰ جَهَنَّمَ يُحْشَرُونَ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
Ña nga xam ne dañoo weddi, Dananu sànk seeni alal ngir dëdduloo [nit ñi] yoonu Yàlla. Waaye Danañu ko sànk ba noppi di ko réccu. Ñu not leen, te ña weddi dees na leen bëmax jëme Safara,
لِيَمِيزَ اللَّهُ الْخَبِيثَ مِنَ الطَّيِّبِ وَيَجْعَلَ الْخَبِيثَ بَعْضَهُ عَلَىٰ بَعْضٍ فَيَرْكُمَهُ جَمِيعًا فَيَجْعَلَهُ فِي جَهَنَّمَ ۚ أُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
ngir Yàlla téqale yéefar yi ak ña gëm Yàlla, Dana boole yéefar yi, dajale leen ñoom ñépp ca biir Safara. Ñooñu ñooy way-ñàkk ña.
قُل لِّلَّذِينَ كَفَرُوا إِن يَنتَهُوا يُغْفَرْ لَهُم مَّا قَدْ سَلَفَ وَإِن يَعُودُوا فَقَدْ مَضَتْ سُنَّتُ الْأَوَّلِينَ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Waxal yéefar yi, ne leen : “Bu ngeen bàyyee [xareek Yonent bi], nu baal leen la weesu. Waaye bu ngeen delluwaatee [ca la ngeen nekke woon], dees na leen mbugal kem ni mu daan ame bu njëkk.
وَقَاتِلُوهُمْ حَتَّىٰ لَا تَكُونَ فِتْنَةٌ وَيَكُونَ الدِّينُ كُلُّهُ لِلَّهِ ۚ فَإِنِ انتَهَوْا فَإِنَّ اللَّهَ بِمَا يَعْمَلُونَ بَصِيرٌ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
Xeexleen ak ñoom ba fitna jóge fi, ba diine nekk lu ñu jagleel Yàlla léppam. Waaye bu ñu bàyyee nag, Yàlla mi ngi ne jàkk ci li ñuy def.
وَإِن تَوَلَّوْا فَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ مَوْلَاكُمْ ۚ نِعْمَ الْمَوْلَىٰ وَنِعْمَ النَّصِيرُ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
Bu ñu dëddoo, xamleen ne, Yàlla mooy ka leen di jàppale. Ndaw soppe bu baax, ndaw Aji-dimbalee ju baax !
۞ وَاعْلَمُوا أَنَّمَا غَنِمْتُم مِّن شَيْءٍ فَأَنَّ لِلَّهِ خُمُسَهُ وَلِلرَّسُولِ وَلِذِي الْقُرْبَىٰ وَالْيَتَامَىٰ وَالْمَسَاكِينِ وَابْنِ السَّبِيلِ إِن كُنتُمْ آمَنتُم بِاللَّهِ وَمَا أَنزَلْنَا عَلَىٰ عَبْدِنَا يَوْمَ الْفُرْقَانِ يَوْمَ الْتَقَى الْجَمْعَانِ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
Te nangeen xam ne lu ngeen màng ci lu mu mën a doon, juróomeelu xaaj ba ñeel na Yàlla ak Yonent ba ak i jegeñaaleem, ak jirim ya, ak way-ñàkk ya, ak ña nekk ci yoon di tukki, ndegam gëm ngeen Yàlla ak la Nu wàcce ci Sunu jaam ba bisu téqale ba [ca Badar] : bisu ndaje ñaari mbooloo ya, te Yàlla mën na lu ne.
إِذْ أَنتُم بِالْعُدْوَةِ الدُّنْيَا وَهُم بِالْعُدْوَةِ الْقُصْوَىٰ وَالرَّكْبُ أَسْفَلَ مِنكُمْ ۚ وَلَوْ تَوَاعَدتُّمْ لَاخْتَلَفْتُمْ فِي الْمِيعَادِ ۙ وَلَٰكِن لِّيَقْضِيَ اللَّهُ أَمْرًا كَانَ مَفْعُولًا لِّيَهْلِكَ مَنْ هَلَكَ عَن بَيِّنَةٍ وَيَحْيَىٰ مَنْ حَيَّ عَن بَيِّنَةٍ ۗ وَإِنَّ اللَّهَ لَسَمِيعٌ عَلِيمٌ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
Fekk na booba ngeen nekk ca xur wa gën a jegeñ, ñoom ñu nekk ca xur wa gën a sori, njëgg ma gën a suufe. Bu ngeen sàkku woon a dajeek ñoom, du sotti. Waaye lu Yàlla dogal day nekk, dana am ñu dee ci lu bir ak ñu dundu ci lu bir. Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
إِذْ يُرِيكَهُمُ اللَّهُ فِي مَنَامِكَ قَلِيلًا ۖ وَلَوْ أَرَاكَهُمْ كَثِيرًا لَّفَشِلْتُمْ وَلَتَنَازَعْتُمْ فِي الْأَمْرِ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ سَلَّمَ ۗ إِنَّهُ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Ba la Yàlla wonee ci sa gént, ñoom ñu nekk mbooloo mu néew ! [Li ko waral mooy], su Ma la wonoon ñu nekk ñu bari, kon dangeen di yoqat, te dangeen xëccoo ca mbir ma. Waaye Yàlla defal leen dal. Moom nag xam na li nekk ci xol yi.
وَإِذْ يُرِيكُمُوهُمْ إِذِ الْتَقَيْتُمْ فِي أَعْيُنِكُمْ قَلِيلًا وَيُقَلِّلُكُمْ فِي أَعْيُنِهِمْ لِيَقْضِيَ اللَّهُ أَمْرًا كَانَ مَفْعُولًا ۗ وَإِلَى اللَّهِ تُرْجَعُ الْأُمُورُ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
Fàttalikul ba Ma leen wonee, ba ngeen dajee, ñu néew ci seeni bët, te ngeen nekk ca ñu néew ca seeni bët ngir la Yàlla dige lu am la. Te ca Yàlla la mbir yépp di dellu.
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا لَقِيتُمْ فِئَةً فَاثْبُتُوا وَاذْكُرُوا اللَّهَ كَثِيرًا لَّعَلَّكُمْ تُفْلِحُونَ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
Éy yéen ñi gëm ñi ! Bu ngeen dajeek mbooloo, nangeen sax ci pastéef te ngeen tudd Yàlla lu bari ndax ngeen am ndam.
وَأَطِيعُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَلَا تَنَازَعُوا فَتَفْشَلُوا وَتَذْهَبَ رِيحُكُمْ ۖ وَاصْبِرُوا ۚ إِنَّ اللَّهَ مَعَ الصَّابِرِينَ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
Te nangeen topp Yàlla ak Yonentam ; te buleen xëccoo, kon ngeen yoqat, seen doole néew. Kon muñleen, Yàlla muñkat yi la àndal.
وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ خَرَجُوا مِن دِيَارِهِم بَطَرًا وَرِئَاءَ النَّاسِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ وَاللَّهُ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطٌ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Buleen mel ni ña génnoon seeni kër, rëylu ak di ngistal ci nit ñi, te di gàllankoor [nit ñi ñu bañ jëm ci] yoonu Yàlla. Te Yàlla xam na la ñuy def de.
وَإِذْ زَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ وَقَالَ لَا غَالِبَ لَكُمُ الْيَوْمَ مِنَ النَّاسِ وَإِنِّي جَارٌ لَّكُمْ ۖ فَلَمَّا تَرَاءَتِ الْفِئَتَانِ نَكَصَ عَلَىٰ عَقِبَيْهِ وَقَالَ إِنِّي بَرِيءٌ مِّنكُمْ إِنِّي أَرَىٰ مَا لَا تَرَوْنَ إِنِّي أَخَافُ اللَّهَ ۚ وَاللَّهُ شَدِيدُ الْعِقَابِ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
Fàttalikul ba Séytaane rafetalee yéefar ya seeni jëf, ne leen : “Tey kenn duleen not, te man maa leen di dimbali.”. Waaye ba ñaari kurél ya jàkkaarloo, dafa dellu ginnaaw te wafeet daw, daldi wax, moom Séytaane, ne : “Man kat deñ naa ci yéen. Ndax gis naa lu ngeen gisul ; ragal naa Yàlla, te Yàlla Ku tar mbugal la”.
إِذْ يَقُولُ الْمُنَافِقُونَ وَالَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ غَرَّ هَٰؤُلَاءِ دِينُهُمْ ۗ وَمَن يَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ فَإِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
(Fàttalikul), ba naafeq ya ak ña jàngoro nekk ca seeni xol waxee ne : “Ñii seen diine wor na leen.” Waaye ku wéeru ci Yàlla ... [na xam ne] Yàlla Kuy not lépp la, Ku xereñ la.
وَلَوْ تَرَىٰ إِذْ يَتَوَفَّى الَّذِينَ كَفَرُوا ۙ الْمَلَائِكَةُ يَضْرِبُونَ وُجُوهَهُمْ وَأَدْبَارَهُمْ وَذُوقُوا عَذَابَ الْحَرِيقِ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
Boo gisee na Malaaka ya di reyee yéefar ya ! Dañuy dóor seeni kanam ak seeni ginnaaw, (naa leen): “Mosleen mbugalu Safara.
ذَٰلِكَ بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيكُمْ وَأَنَّ اللَّهَ لَيْسَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
Loolu mooy la ngeen jëfoon ci seeni yoxo.” Te it Yàlla du koy tooñ jaam ñi.
كَدَأْبِ آلِ فِرْعَوْنَ ۙ وَالَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ كَفَرُوا بِآيَاتِ اللَّهِ فَأَخَذَهُمُ اللَّهُ بِذُنُوبِهِمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ قَوِيٌّ شَدِيدُ الْعِقَابِ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
Niki aaday njabootu Firawna ak ña leen jiitu, weddi woon nañu kàdduy Yàlla. Yàlla sadd leen ngir seeni bàkkaar. Naka Yàlla, Boroom kàttan la, di Ku tar mbugal.
ذَٰلِكَ بِأَنَّ اللَّهَ لَمْ يَكُ مُغَيِّرًا نِّعْمَةً أَنْعَمَهَا عَلَىٰ قَوْمٍ حَتَّىٰ يُغَيِّرُوا مَا بِأَنفُسِهِمْ ۙ وَأَنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ عَلِيمٌ ۝٥٣
📖 Tekki Aaya 53
Li ko waral mooy Yàlla du soppi yiw wu Mu xéewale aw nit feek soppiwuñu li nekkoon ci ñoom. Yàlla Kuy dégg la, Ku xam la.
كَدَأْبِ آلِ فِرْعَوْنَ ۙ وَالَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ كَذَّبُوا بِآيَاتِ رَبِّهِمْ فَأَهْلَكْنَاهُم بِذُنُوبِهِمْ وَأَغْرَقْنَا آلَ فِرْعَوْنَ ۚ وَكُلٌّ كَانُوا ظَالِمِينَ ۝٥٤
📖 Tekki Aaya 54
Niki aada njabootu Firawna ak ña leen jiitu, weddi nañu kàdduy Boroom bi. Nu alag leen ngir seeni bàkkaar. Te Nu labal [ca géej] waa kër Firawna. Te ñoom ñépp nekkoon nañu di ay tooñkat.
إِنَّ شَرَّ الدَّوَابِّ عِندَ اللَّهِ الَّذِينَ كَفَرُوا فَهُمْ لَا يُؤْمِنُونَ ۝٥٥
📖 Tekki Aaya 55
Ña yées fa Yàlla ñooy ña weddi woon te duñu gëm ba mukk,
الَّذِينَ عَاهَدتَّ مِنْهُمْ ثُمَّ يَنقُضُونَ عَهْدَهُمْ فِي كُلِّ مَرَّةٍ وَهُمْ لَا يَتَّقُونَ ۝٥٦
📖 Tekki Aaya 56
mooy ña nga fasanteek kóllare ñu lay wor, te ñoom duñu ragal Yàlla mukk.
فَإِمَّا تَثْقَفَنَّهُمْ فِي الْحَرْبِ فَشَرِّدْ بِهِم مَّنْ خَلْفَهُمْ لَعَلَّهُمْ يَذَّكَّرُونَ ۝٥٧
📖 Tekki Aaya 57
Kon su ngeen dajee cib xare, nanga leen tasaare ak ña leen topp ndax xéy-na danañu fàttaliku.
وَإِمَّا تَخَافَنَّ مِن قَوْمٍ خِيَانَةً فَانبِذْ إِلَيْهِمْ عَلَىٰ سَوَاءٍ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ الْخَائِنِينَ ۝٥٨
📖 Tekki Aaya 58
Boo ragalee ciw nit ñu wor la, tërëlal déggoo gu leer, Yàlla soppul workat ya.
وَلَا يَحْسَبَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا سَبَقُوا ۚ إِنَّهُمْ لَا يُعْجِزُونَ ۝٥٩
📖 Tekki Aaya 59
Ña weddi, buñu njortu ne raw nañu. Ñoom duñu mën a raw Yàlla.
وَأَعِدُّوا لَهُم مَّا اسْتَطَعْتُم مِّن قُوَّةٍ وَمِن رِّبَاطِ الْخَيْلِ تُرْهِبُونَ بِهِ عَدُوَّ اللَّهِ وَعَدُوَّكُمْ وَآخَرِينَ مِن دُونِهِمْ لَا تَعْلَمُونَهُمُ اللَّهُ يَعْلَمُهُمْ ۚ وَمَا تُنفِقُوا مِن شَيْءٍ فِي سَبِيلِ اللَّهِ يُوَفَّ إِلَيْكُمْ وَأَنتُمْ لَا تُظْلَمُونَ ۝٦٠
📖 Tekki Aaya 60
Feguleen, ngir ñoom, lu ngeen mën ci doole ak fas yu ngeen mën a tiitale nooni Yàlla ya, di seeni noon, ak ñeneen ñu dul ñoom, xamooleen, Yàlla Moo leen xam. Li ngeen di joxe ci alal ci yoonu Yàlla, dees na leen ko delloo ba mu mat sëkk te deesuleen ci wàññil dara.
۞ وَإِن جَنَحُوا لِلسَّلْمِ فَاجْنَحْ لَهَا وَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ ۚ إِنَّهُ هُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ ۝٦١
📖 Tekki Aaya 61
Bu ñu jengee jëm ci jàmm, jengal yaw it jëm ca te nga wéeru ci Yàlla, naka Moom Kuy dégg la, Ku xam la.
وَإِن يُرِيدُوا أَن يَخْدَعُوكَ فَإِنَّ حَسْبَكَ اللَّهُ ۚ هُوَ الَّذِي أَيَّدَكَ بِنَصْرِهِ وَبِالْمُؤْمِنِينَ ۝٦٢
📖 Tekki Aaya 62
Bu ñu la naree wor, na la Yàlla doy. Moom moo lay dëgëral ci ndimbalam ak ñu gëm ña.
وَأَلَّفَ بَيْنَ قُلُوبِهِمْ ۚ لَوْ أَنفَقْتَ مَا فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا مَّا أَلَّفْتَ بَيْنَ قُلُوبِهِمْ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ أَلَّفَ بَيْنَهُمْ ۚ إِنَّهُ عَزِيزٌ حَكِيمٌ ۝٦٣
📖 Tekki Aaya 63
Te Moo dajale seeni xol (ñu soppante). Te yaw boo joxe woon lépp li nekk ci àddina, du tax nga mën a boole seeni xol ; Moom nag [Yàlla] Ku not la, Ku xereñ la.
يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ حَسْبُكَ اللَّهُ وَمَنِ اتَّبَعَكَ مِنَ الْمُؤْمِنِينَ ۝٦٤
📖 Tekki Aaya 64
Éy yaw Yonent bi, Yàlla doy na la ak ku la topp ci ñi gëm.
يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ حَرِّضِ الْمُؤْمِنِينَ عَلَى الْقِتَالِ ۚ إِن يَكُن مِّنكُمْ عِشْرُونَ صَابِرُونَ يَغْلِبُوا مِائَتَيْنِ ۚ وَإِن يَكُن مِّنكُم مِّائَةٌ يَغْلِبُوا أَلْفًا مِّنَ الَّذِينَ كَفَرُوا بِأَنَّهُمْ قَوْمٌ لَّا يَفْقَهُونَ ۝٦٥
📖 Tekki Aaya 65
Éy yaw Yonent bi, nanga ñaax ñi gëm ci xare. Bu amee ñaar-fukk ñu muñ, danañu not ñaari téeméeri yéefar ; bu nekkee ci yéen téeméer, danañu not junni ciy yéefar, ndax ñoom nit lañu ñu amul dégg-dégg.
الْآنَ خَفَّفَ اللَّهُ عَنكُمْ وَعَلِمَ أَنَّ فِيكُمْ ضَعْفًا ۚ فَإِن يَكُن مِّنكُم مِّائَةٌ صَابِرَةٌ يَغْلِبُوا مِائَتَيْنِ ۚ وَإِن يَكُن مِّنكُمْ أَلْفٌ يَغْلِبُوا أَلْفَيْنِ بِإِذْنِ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ مَعَ الصَّابِرِينَ ۝٦٦
📖 Tekki Aaya 66
Léegi, Yàlla woyofal na leen ngir xam na doyadi gi nekk ci yéen. Kon bu nekkee ci yéen téeméer yu muñ, danañu not ñaari téeméer ; bu nekkee ci yéen junni, danañu not ñaari junni, bu neexee Yàlla. Te Yàlla muñkat yi la àndal.
مَا كَانَ لِنَبِيٍّ أَن يَكُونَ لَهُ أَسْرَىٰ حَتَّىٰ يُثْخِنَ فِي الْأَرْضِ ۚ تُرِيدُونَ عَرَضَ الدُّنْيَا وَاللَّهُ يُرِيدُ الْآخِرَةَ ۗ وَاللَّهُ عَزِيزٌ حَكِيمٌ ۝٦٧
📖 Tekki Aaya 67
Warul cib Yonent mu am ay jaar-jaar [ca ña ñu jàppe cib xare not leen] fekk ñu nasaxal yéefar yi, faagaagal leen ba ñu mokk ci suuf si. Dangeen a bëgg [yéen jullit ñi] alali àddina, te Yàlla bëggal leen [xéewalu] àllaaxira. Te Yàlla Ku not la, Ku xereñ la.
لَّوْلَا كِتَابٌ مِّنَ اللَّهِ سَبَقَ لَمَسَّكُمْ فِيمَا أَخَذْتُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ ۝٦٨
📖 Tekki Aaya 68
Bu bul koon dogal bu tukkee ca Yàlla bu jiitu, kon mbugal mu rëy dana leen dal ngir la ngeen màng.
فَكُلُوا مِمَّا غَنِمْتُمْ حَلَالًا طَيِّبًا ۚ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٦٩
📖 Tekki Aaya 69
Kon lekkleen ca la ngeen màng, muy lu dagan lu teey. Te ngeen ragal Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ قُل لِّمَن فِي أَيْدِيكُم مِّنَ الْأَسْرَىٰ إِن يَعْلَمِ اللَّهُ فِي قُلُوبِكُمْ خَيْرًا يُؤْتِكُمْ خَيْرًا مِّمَّا أُخِذَ مِنكُمْ وَيَغْفِرْ لَكُمْ ۗ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٧٠
📖 Tekki Aaya 70
Éy yaw Yonent bi, waxal jaam yi nekk ci seeni yoxo, ne : “Bu Yàlla gisee dara lu baax ci seeni xol, Dana leen jox la gën ci yéen te Dana leen jéggal. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
وَإِن يُرِيدُوا خِيَانَتَكَ فَقَدْ خَانُوا اللَّهَ مِن قَبْلُ فَأَمْكَنَ مِنْهُمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ ۝٧١
📖 Tekki Aaya 71
Bu ñu la bëggee wuruj..., lu jiitu loolu, woroon nañu Yàlla ; ba tax na Mu digle ngeen jàppe leen [ci xare Badar]. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا وَهَاجَرُوا وَجَاهَدُوا بِأَمْوَالِهِمْ وَأَنفُسِهِمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَالَّذِينَ آوَوا وَّنَصَرُوا أُولَٰئِكَ بَعْضُهُمْ أَوْلِيَاءُ بَعْضٍ ۚ وَالَّذِينَ آمَنُوا وَلَمْ يُهَاجِرُوا مَا لَكُم مِّن وَلَايَتِهِم مِّن شَيْءٍ حَتَّىٰ يُهَاجِرُوا ۚ وَإِنِ اسْتَنصَرُوكُمْ فِي الدِّينِ فَعَلَيْكُمُ النَّصْرُ إِلَّا عَلَىٰ قَوْمٍ بَيْنَكُمْ وَبَيْنَهُم مِّيثَاقٌ ۗ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ ۝٧٢
📖 Tekki Aaya 72
Ña nga xam ne gëm nañu, te gàddaay te ñuy xare ak seeni alal ak seeni bakkan ngir Yàlla ak ña leen dalaloon di leen dimbali, ñooña ñooy ñu jàppante ña. Walla ña nga xam ne gëm nañu te gàddaayuñu, loolu du dox seen diggante feek gàddaayuñu. Waaye bu ñu sàkkoo ndimbal ci yéen ci wàllu diine, dimbal loolu war na leen ginnaaw songug nit ñoo xam ne kóllare dox na seen diggante. Yàlla Mi ngi ne jàkk ca la ngeen di def.
وَالَّذِينَ كَفَرُوا بَعْضُهُمْ أَوْلِيَاءُ بَعْضٍ ۚ إِلَّا تَفْعَلُوهُ تَكُن فِتْنَةٌ فِي الْأَرْضِ وَفَسَادٌ كَبِيرٌ ۝٧٣
📖 Tekki Aaya 73
Ña weddi, dañuy jàppoo. Bu ngeen ko deful, fitna ak yàqute gu rëy dana am ci kaw suuf si.
وَالَّذِينَ آمَنُوا وَهَاجَرُوا وَجَاهَدُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَالَّذِينَ آوَوا وَّنَصَرُوا أُولَٰئِكَ هُمُ الْمُؤْمِنُونَ حَقًّا ۚ لَّهُم مَّغْفِرَةٌ وَرِزْقٌ كَرِيمٌ ۝٧٤
📖 Tekki Aaya 74
Ña nga xam ne gëm nañu te gàddaay tey xare ci yoonu Yàlla ak ña leen dalaloon, di leen dimbali [Waa Ansaar], ñooña ñooy ñu gëm, ñu dëggu ña : am nañu njéggal ak xéewal gu tedd.
وَالَّذِينَ آمَنُوا مِن بَعْدُ وَهَاجَرُوا وَجَاهَدُوا مَعَكُمْ فَأُولَٰئِكَ مِنكُمْ ۚ وَأُولُو الْأَرْحَامِ بَعْضُهُمْ أَوْلَىٰ بِبَعْضٍ فِي كِتَابِ اللَّهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ ۝٧٥
📖 Tekki Aaya 75
Ak ña gëm ginnaaw ga te ñu gàddaay tey xare ànd ak yéen, ñooña ci yéen lañu bokk.Waaye ña nekk ay mbokk ñoo gën a yey [ci donnante] ci Téereb Yàlla bi. Yàlla xam na lu ne.
← 7 Al-Anfal (8/114) 9 →
Jàng Simoore Al-Anfal ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

8الأنفال Al-Anfal 📚 75 Aaya مدنية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers