At-Tawba · 91/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
لَّيْسَ عَلَى الضُّعَفَاءِ وَلَا عَلَى الْمَرْضَىٰ وَلَا عَلَى الَّذِينَ لَا يَجِدُونَ مَا يُنفِقُونَ حَرَجٌ إِذَا نَصَحُوا لِلَّهِ وَرَسُولِهِ ۚ مَا عَلَى الْمُحْسِنِينَ مِن سَبِيلٍ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٩١
Laisa `alad du`aaaa`i wa laa `alal mardaa wa laa `alal lazeena laa yajidoona maa yunfiqoona harajun izaa nasahoo lillaahi wa Rasoolih; maa `alal muhsineena min sabeel; wallaahu Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Ña néew dolle ak ña wopp, ak ñi amul yóbbal, amuñu bàkkaar (ci toog bañ a xare ji) ndeem ñu rafet yéene lañu ci Yàlla ak ub Yonentam. Naka noonu it, ca ñay rafetal seeni jëf. Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 89-93 — At-Tawba

89أَعَدَّ اللَّهُ لَهُمْ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا ۚ ذَٰلِكَ الْفَوْزُ الْعَظِيمُ
Yàlla xaroo na leen Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel. Loolu moo di texe gu màgg ga !
90وَجَاءَ الْمُعَذِّرُونَ مِنَ الْأَعْرَابِ لِيُؤْذَنَ لَهُمْ وَقَعَدَ الَّذِينَ كَذَبُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ ۚ سَيُصِيبُ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ñiy sàkku ngànt (ci bañ a dem) xare ji ca sàmm sa, nekk nañu ngir ñu am ci ndigal. Ña weddi Yàlla ak ub Yonentam, toog nañu. Ña weedi ca ñoom, mbugal mu metti dana leen dal.
91لَّيْسَ عَلَى الضُّعَفَاءِ وَلَا عَلَى الْمَرْضَىٰ وَلَا عَلَى الَّذِينَ لَا يَجِدُونَ مَا يُنفِقُونَ حَرَجٌ إِذَا نَصَحُوا لِلَّهِ وَرَسُولِهِ ۚ مَا عَلَى الْمُحْسِنِينَ مِن سَبِيلٍ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ña néew dolle ak ña wopp, ak ñi amul yóbbal, amuñu bàkkaar (ci toog bañ a xare ji) ndeem ñu rafet yéene lañu ci Yàlla ak ub Yonentam. Naka noonu it, ca ñay rafetal seeni jëf. Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la.
92وَلَا عَلَى الَّذِينَ إِذَا مَا أَتَوْكَ لِتَحْمِلَهُمْ قُلْتَ لَا أَجِدُ مَا أَحْمِلُكُمْ عَلَيْهِ تَوَلَّوا وَّأَعْيُنُهُمْ تَفِيضُ مِنَ الدَّمْعِ حَزَنًا أَلَّا يَجِدُوا مَا يُنفِقُونَ
Ña nga xam ne bu ñu dikkee ci yaw di sàkku waruwaay, nanga leen di wax ne amuloo lu ñu mën a war, ñu dellu ànd ak naqar, di jooy ngir jàq ca la ñu amul waajtaay, ñoom it amuñu bàkkaar. Kenn du am ci ñoom aw yoon.
93۞ إِنَّمَا السَّبِيلُ عَلَى الَّذِينَ يَسْتَأْذِنُونَكَ وَهُمْ أَغْنِيَاءُ ۚ رَضُوا بِأَن يَكُونُوا مَعَ الْخَوَالِفِ وَطَبَعَ اللَّهُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Ñay am bàkkaar kay ñoo di ña woomal te di la laaj ndigal ci bañ a dem xare ji, bëgg a ànd ak ñay fuuyu. Yàlla fatt na seeni xol te ñoom xamuñu. Ñoom kenn du mën a am ci ñoom aw yoon.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
91Aaya

Tekki — At-Tawba 91

Simoore At-Tawba Aaya 91 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña néew dolle ak ña wopp, ak ñi amul yóbbal,…

Simoore Aaya 91/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 89–93. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers