Simoore Al-Furqan
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Furqan pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Furqan pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Furqan Tekki. Al-Furqan (Meccan) 77 Aaya.
Related
- Al-Furqan TekkiWolof
- Al-Furqan mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Furqan

ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Yàlla barkeel na [màgg na] Moom mi wàcce Téere ba [Alxuraan] ca jaamam ba ngir mu doon luy xupp waa àddina si yépp.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Moom mi nga xam ne Moo moom nguurug asamaan yeek suuf si, te jàppewul kenn doomam, te it amul ku Mu bokkal nguur gi, Moo bind lépp te jox na ko dayo ba mu témbool.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Te ñoom dañoo jàppe ay yàlla ñenenn ñoo xam ne binduñu tus, faf ñoom sax dañu leen a bind, te it mënuñoo lor seen bopp waxantumalaak njariñ, amuñu dee amuñu dundu waxantumalaak dekki.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Yéefar yi wax nañu ne : “[Alxuraan] jii daal aw duur la wu [Muhammad] moo ko sos, te dafa am ñu ko cay jàppale”. Li ñu fi indi tooñ ak i fen la.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Ñu wax it ne : “Léebi mag ñu jëkk ña rekk la ! Ñu koy saa muy bind suba ak ngoon ! ”
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Neel : “Ki ko wàcce moo xam mbooti asamaan yeek suuf si. Di ab Jéggalaakon, di Jaglewaakoon.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Ñu wax ne [ñoom yéefar yi] : “Ana lan moo tax Yonent bii di lekk ñam ak a dox ci ja yi [màrse yi] ? Lan moo tax wutéelsu ko Malaaka mu ànd ak moom di xuppaate ?
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Walla mu am ndàmb ? Mbaa mu am tooli dër di ci lekk ?”. Tooñkat ya naan : “Yéen daal toppiwuleen ku dul as waay ju ag njibar jàpp”.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Gisal ni ñu lay méngaléelee ! Dañuy sànku te amuñu ca wenn yoon.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Yàlla ju barkeel ja nga xam ne bu Ko sooboon Mu defal la ci loolu Àjjana joo xam ay dex dañuy daw ci suufam ; Mu defal la it ay jénde.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Waaye wedd nañu Bis-pénc ba. Te Nun kat waajalal Nanu, képp ku weddi Bis-pénc ba, aw safara wuy jér-jéri.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Saa su leen Safara soosu séenee fu sori, dinañu dégg riiram.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Bu ñu leen ca sànnee ci pukus bu xat, lëkke leen [jéng], ñuy wél-wéliy juuxu ci toskare.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
“Bisu tey jii, buleen yuuxu jenn tuskare doŋŋ, ay tuskare yu bari la”.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Neel : “Ndax loolu moo gën ? Walla Àjjanay xéewal ju sax ju ma digee fey gaa ña ragal Yàlla, muy seen kër ?”
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Am nañu fa lépp lu leen fa soob te dañu fay béel. Yàllaa ko warlu.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Bis ba Mu leen di pang, boole leen ak ya ñu doon jaamu bàyyi Yàlla, Di leen wax [moom Yàlla] naan : “Ndax yéen a sànkoon sama jaam ñii, walla ñoom ñoo sànku woon réere yoon wa ? ”
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Ñuy wax di tontu naan : “Tudd nanu sa sell gi. ! Yellut ci nun nuy wut kilifa bàyyi la, waaye Yaa leen tuuroon xéewal ñook seeni baay ba tax ñu fàtte [Alxuraan]. Far sànku”.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
“Weddi woon nañu leen ca li ngeen di wax. Amuñu ab rawtukaay. Te képp ku tooñati ci yéen, Dananu ko mosal mbugal mu réy”.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Musunoo yebal ay Yonent ca la la jiitu lu dul dañu daan lekk ñam te di dox ci ja yi [màrse yi]. Def Nanu it ñenn ci yéen di sànjeb ña ca des, mbaa dangeen muñ ? - Sa Boroom de kuy gis la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Ña yaakaarul a dajeek Nun ñangay wax naan : “Céy bées wàcce woon ci nun ay Malaaka, mbaa nu gis sunu Boroom [Yàlla] ! ”. Dañu doon rëy-rëylu [kaweel seen bopp], réer réer gu jéggi dayo.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Bis ba ñuy mën a gis malaaka ya du neex ci ñoom de, ndax Malaaka yaa nga naan leen : “Seeni mbir sakk na” !
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Nu fab jépp jëf ju ñu mësoon a jëf, def ko pënd bu ñu wasaare.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
[Bu keroogee Bis-pénc ba], waa Àjjana ñooy gën delluwaay te ñooy dàq ub nooflaay.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
[Bu Bis baa] ba niiri asamaan si di xottiku, ñuy wàcce Malaaka yi,
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
bu keroogee [buntub] nguur dëgg, Yërëmaakoon baa koy ame, mu doon nag Bis bu jafe ci yéefar yi.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Bis ba tooñkat yi di màtt seeni yoxo, te naan : “Aka neexoon ma ànd ak Yonent aw yoon !...
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Ngalla man ! Aka neexoon jàppewuma diw sàngam ab xarit !...
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Moo ma féewaleek [Alxuraan] ginnaaw ba mu ma ñëwalee”. Séytaane moo di yàqalekat
bu bon (bu yées ba).
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Yonent bi daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, nit ñi dey dëddu nañu Alxuraan jii ! ”
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Noonu la Nu defe woon Yonent bu nekk am ab noon ca tooñkat ya. Waaye nag, Sa Boroom Moom doy na sëkk kuy gindee, doy sëkk it ndimbal.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Yéefar yaa ngay wax naan : “Lu tax wàccendoo wuñu Alxuraan jii wenn yoon mu ne ñumm ? ” [Waaye Nun nii la Nu koy wàccee] ngir dëgëral sa xol. Te it toftale Nanu ko bu jekk.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Amul léebu wu ñu lay mën a indil te indilunu la dëgg, te gën koo jub.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Ña nga xam ne dees na leen pang, di leen diri ci seen xar-kanam ya, jëme leen Safara, ñoom ñooy gën a yées wàccuwaay, gën a réere yoon wu jub wa.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Jox Nanu Muusaa Téere ba, defal ko Aaruuna mbokkam mu di ko jàppale.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Nu wax leen ne : “Demleen yéen ñaar ca nit ña weddi woon Sunuy kàddu”. Nu alag leen.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Te nitu Nooh ya, ba ñu weddee Yonent ya, labal Nanu leen, def Nanu leen it kéemaan ci nit ñi. Te waajalal Nanu tooñkat ya mbugal mu metti.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Ak nitu Aad, ak nitu Samooda ak waa Rasi, ak maas yu bari yu nekkoon seeni diggante !
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Ku nekk ci ñoom, sadd Nanu koy léebu, alag Nanu leen ñoom ñépp.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Romb nañu dëkk ba mbugal ma wàcce woon. Moo ndax gisuñu ko woon ? Ñoom kay dañoo foogoon ne duñu dekki !
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Bu ñu la gisee dañu lay téjji naan : “Ndax kii la Yàlla yónni ?
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Bu nu muñul woon, danañu xaw a féewaleek sunu yàlla jii ! ”. Waaye danañu xam [Bis bu ñu gisee mbugal ma], ana kan moo réere yoon wu jub wa.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Ndax gisuloo ka jàppe bakkanam mu di yàllaam ? Moo ndax dangay doon wéeruwaayam ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Walla dangaa jàpp ne li ëpp ci ñoom dañuy dégg di xam ? Ñoom kay ñook mala yi ñoo yem. Walla sax ñoo gën a sànku.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Xanaa gisoo ni sa Boroom tàllale ker [takkander] ? Bu ko sooboon, Mu def ko mu di lu sax. Ba noppi def Nanu jant bi muy firnde,
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
te ginnaaw loolu, xëcc Naa ko jëme ci Man muy lu yomb.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Mooy Ki leen defal guddi gi mu di ag col ak nelaw yu neex, te Mu def bëccëg muy yëngatukaay.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Moom moo yebal ngelaw muy bégal ci yërmaandey Yàlla. Te wàcce Nanu ci asamaan si ndox mu laab,
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
ngir Nu dundalaat ci dëkk bu dee woon, màndal ci ña Nu bind ci mala ak nit ñu bari.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Tasaare Nanu ko ci seen diggante ngir ñu fàttalikoo ca. Li ëpp ci nit ñi lànk di ay yéefar.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Bu Nu sooboon, dëkk bu nekk Dananu fa yebal ab xuppekat.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Bul topp ñiy weddi Alxuraan ; te nanga xeex ak ñoom xeex bu rëy.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Mooy Kiy dawloo ñaari géej : bii neex, lewet, ba ca des saf xorom, naqari. Te moo def ci seen diggante aw téq [bu kenn mënul a jaxase].
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Mooy ki sos nit ci ndox, def ci aw askan ak ug goromle. Sa Boroom di Ku am kàttan [ci def lu nekk].
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
[Yéefar ya], ña ngay jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne duleen jariñ, duleen lor ! Ku di ab yéefar mooy takkatook noonub Boroomam !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
Yónniwunu la lu dul ngay xuppe ak a waare.
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Neel : “Laaju ma leen ci ag pey. Ku mu soob nag, mën naa joxe ci yoonu Yàlla”.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Te nanga wéeru ci Yàlla Miy Aji-dund te du dee. Te nangay sàbbaal ci sant Ko. Moom Yàlla ku mat sëkk la ci xam bàkkaari jaamam ñi.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Mooy Ki bind asamaan yaak suuf si ak li nekk seen diggante, ci juróom-benni fan, daldi yemoo ca gàngunaay ga [Aras], Moo di ab Yërëmaakoon. Laaj ko ku xam.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Saa su Nu leen waxee : “Sujjóotal-leen [Yàlla] Mi di ab Yërëmaakoon”, ñu tontu ne : “Kuy kooku ?” - Mu faf dolli leen ug foñ.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Barkeel na [Moom Yàlla] mi def ci asamaan si ay yoon, def ca ab làmp [jant bi] ak weer wu leer nàññ !
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Mooy Ki def guddeek bëccëg ñuy jëlasante ngir ku bëgg a xalaat, fàttaliku, mbaa mu bëgg a sant.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Ak jaami Yàlla yii dox ci kaw suuf si ndànk, su ñu réer ña di wàqanteek ñoom, ñuy wax jàmm,
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
ñoom ñooy fanaanee julli te Yàlla rekk tax [taxaw ak a sujjóot] ;
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
ñoom ñooy wax naan : “Yàlla, yal na nga nu dëddëleek mbugalum Safara”. - mbugalum Safara soosu lu ne dànk la.
ﯲﯳﯴﯵﯶ
Ndaw dëkkuwaay bu soof !
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Bu ñuy joxe alal, duñu xaabaabal te it duñu nay, dañuy digg-dóomu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Duñu boole di jaamoondoo dara ak Yàlla, te duñu rey bakkan bu Yàlla tere ku ko rey, lu dul ci dëgg ; duñu njaaloo it - képp ku def loolu, dana dajeek mbugal
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
dees na ko fulal mbugal ma bu Bis-pénc baa, te dafay béel cig doyadi ;
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
u dul ña ca tuub, rëccu te gëm, tey jëf u yiw ; ñooña, Yàlla dana soppi seeni ñaawtéef def ko mu di yiw, Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la ;
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
képp kuy tuub [rëccu lu bon te bañ koo defati], dana dellu ca Yàlla mucc.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Ña nga xam ne duñu seede mukk aw fen ; te bu ñu rombee ay caaxaan duñu fa xand ;
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
ña nga xam ne bu ñu déggee seen kàdduy Boroom, duñu ca tëx, duñu ca gumba ;
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
ña nga xam ne dañuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, defal nu ci sunuy jabar ak sunuy doom ñuy seral xol, te nga def nu ay njiit ca ña ragal Yàlla tey wattandiku”.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Ñoom dees na leen feye ay néeg yu kawe [ca Àjjana], muy peyug la ñu doon muñ, te dees na leen fa teeroo ab nuyyoo ak jàmm [ju ne béyyi],
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
dañu fay béel. Ndaw dëkkuwaay bu neex !
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Neel : “Seen Boroom duleen faale, xanaa sax bu fekkoon ne yéen a ngi Koy jaamu ; waaye weddi woon ngeen Yonent bi. Seen mbugal, dungeen ko mën a raw, te dafay doo lu sax.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







