PDF —
227 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Ash-Shu'ara pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Ash-Shu'ara pdf Wolof — Wàcce Simoore Ash-Shu'ara Tekki. Simoore Ash-Shu'ara (Meccan) 227 Aaya.

← Al-FurqanSimoore Ash-Shu'ara An-Naml →


227 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒ
26:1 Taa, Siin, Miim.
ﭓﭔﭕﭖﭗ
26:2 Lii mooy laayay Téere bu bir ba.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
26:3 Amaana nga am ñàngi-ñàngi xol ci li ñu gëmul !
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
26:4 Bu Nu neexoon Nu wàcce ci asamaan kéemaan guy tax ñuy jatti loos.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
26:5 Amul benn woote bu bees bu mësoon a bawoo ca Yàlla lu dul ne dëndu dañu ko.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
26:6 Weddi woon nañu, te danañu mës a joti xibaari la ñu doon téjji.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
26:7 Xanaa dañoo gisul yu bari yi Nu saxal ci kaw suuf, ci xeeti gàncax muy tollént ?
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
26:8 Ay kéemaan yu bari nekk ci loolu ! Waaye taxut li ëpp ci ñoom gëm [diy jullit].
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
26:9 Te sa Boroom mooy Boroom kàttan ga te di Jaglewaakoonug [yërmaande].
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
26:10 [Fàttalikul] ba Yàlla woo na Muusaa, [ne ko] : “Demal [jubbanti ji] tooñkat ya,
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
26:11 nitu Firawna” ; moo ndax ñoom duñu ragal Yàlla ?
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
26:12 [Muusaa] wax ne : “Yaw Sama Boroom, damaa ragal ñu jàppe ma ab fenkat [weddi ma] ;
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
26:13 samab dënn di xat, te kon dootuma mën a wax : Yónnil kon Aaruuna, def ko Yonent.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
26:14 Te itam, am na tuuma ju ñu may jiiñ ; te ragal naa ñu rey ma”.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
26:15 [Yàlla] ne : “Mukk du am ! Demleen yéen ñaar yóbb sunuy kàddu. Maa ngi ànd ak yéen di dégg.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
26:16 Dem ca Firawna ne ko : “Nun ñaari ndawi Boroom àddina si lanu,
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
26:17 Yebalal giir Banii-Israayil ñu ànd ak nun ”.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
26:18 [Firawna] ne ko : “Moo ndax yarunu la fii ba nga doonee liir ? Ak li nga fi nekk lépp ?
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
26:19 Ak jëf ji nga fi jëfoon tey xarabaate”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
26:20 Muusaa ne ko : “Defoon naa ko, waaye teyuma ko.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
26:21 Ma daldi daw ba ma tiitee : faf Yàlla jox ma xam-xamu [baatin], def ma ma bokk ca Yonent ya.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
26:22 Te loolu xéewal la goo may mën a xéewale, ndax liggéeyloo nga giir Banii-Israayil lu ne ? ”
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
26:23 [Firawna] ne ko : “Waaw, ana kan mooy Boroom àddina si ? ”.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
26:24 [Muusaa ne ko] : “Mooy Boroom asamaan yeek suuf si ak li nekk seen diggante, ndegam wóolu nga ! ”
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
26:25 [Firawna] daldi wax ak ña ko wëroon, ne leen : “Gaa ñi xanaa dégguleen ? ”
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
26:26 [Muusaa] ne ko : “... Mooy seen Boroom, di Boroomub seeni baay”.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
26:27 [Firawna] daldi wax ne : “Seen Yonent bii ñu leen yónni ab dof la kat”.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
26:28 [Muusaa] ne ko : “Mooy Boroom penkook sowwu ak li nekk seen diggante, bu ngeen xel-
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
26:29 [Firawna] ne ko : “Soo fi jéemee indi jeneen yàlla ju dul man, danaa la téj kaso de”.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
26:30 [Muusaa] ne ko : “Moo ne indil naa la mbir mu leer de ?
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
26:31 [Firawna] ne ko : “Génne ko bu fekkee li ngay wax dëgg la”.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
26:32 [Muusaa] daldi sànni yetam wa, ndekete yoo jaan la juy béllaw-béllawi.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
26:33 [Muusaa] daldi génne loxoom, mu weex tàll ca ña koy xool.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
26:34 [Firawna] wax gàngoor ga ne leen : “Kii dey ab jibar la bu xor.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
26:35 Da leen a bëgg a génne ci seen suuf sii ak jibaram gi. Lu ngeen ma ciy digal ? ”
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
26:36 Ñu ne ko : “Joxleen ñoom ñaar beneen bis te nga yónni ci gox yi ñuy woo nit ñi, di leen dajale,
ﯼﯽﯾﯿﰀ
26:37 danañu la indil bépp jibar bu fi xor”.
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
26:38 Ñu dajale mbooleemi jibarkat ca bis ba ñu waxoon.
ﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
26:39 Mu am ku yéene wax ne : “Ndax nit ñépp yemb nañu,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
26:40 xéy-na bu nu toppee njibarkat yi, ndegam ñoo not ? ”
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
26:41 Ba jibar ya agsee, dellu wax Firawna ne ko : “Ndax dananu am ag pey bu fekkee ne not nanu [Muusaa] ? ”
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
26:42 Mu ne leen : “Waawaaw, kon dingeen bokk ci samay jegeñaale !
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
26:43 Muusaa ne leen : “Sànnileen li ngeen di sànni”.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
26:44 Ñu daldi sànni seen buum ak i yet, daldi wax ne : “Ci doole Firawna la nuy note”.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
26:45 Muusaa daldi sànni yetam wa, ndeketeyoo mëdd na ya ñu deferoon.
ﮈﮉﮊﮋ
26:46 Jibar ya daldi rot sujjóot,
ﮌﮍﮎﮏﮐ
26:47 daldi wax ne : “Gëm nanu Boroom àddina si yépp,
ﮑﮒﮓﮔ
26:48 Boroom Muusaa ak Aaruuna”.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
26:49 [Firawna] ne leen : “Gëmoon ngeen ko ba ma leen a laataa woo. [Xam naa ne] mooy kàndiŋ mi leen jàngal njibar ! Dangeen xam ne ! Danaa dagg seen yoxook seeni tànk, jalawle ko, danaa leen daaj yéen ñépp”.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
26:50 Ñu ne ko : “Boo yaboo ! Nun daal jublu nanu sunu Boroom.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
26:51 Danoo xemmem Yàlla jéggal nu sunuy njuumte, xemmem it doon ñu njëkk a gëm”.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
26:52 Nu daldi soloo Muusaa, digal ko mu rañaan ànd ak samay jaam te danañu leen dabsi.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
26:53 Firawna daldi yónnee ci gox yi ñuy yéene dajale nit ñi :
ﯳﯴﯵﯶﯷ
26:54 “Ñoom dey, ay mbooloo yu néew lañu,
ﯸﯹﯺﯻ
26:55 te it mere nañu nu,
ﯼﯽﯾﯿ
26:56 te nun danoo lefoog”.
ﰀﰁﰂﰃﰄ
26:57 Noo leen génne woon ci dër yaak dex yi,
ﰅﰆﰇﰈ
26:58 Ak ca ndàmb yaak dëkkuwaay yu neex ya.
ﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
26:59 Noona la Nu ko donnalee giir Bani-israayiila.
ﰏﰐﰑ
26:60 Ba jant ba fénkee la ñu leen dabuji.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
26:61 Ba ñaari mbooloo ya séenantee, waa kër Muusaa daldi ne : “Ñanga nuy dabsi de”.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
26:62 [Muusaa] ne : “Mukk, duñu nu dab ndax ànd naak sama Boroom te Dana ma gindi”.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
26:63 Nu daldi soloo Muusaa, digal ko : “Dóoral géej geek sa yet wi”. Mu daldi xàjjeeku, xaaj bu nekk tollu ni aw tund wu mag.
ﭱﭲﭳﭴ
26:64 Nu tañcale Firawna mook u nitam.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
26:65 Nu daldi musal Muusaa mook ña mu àndanloon ñépp ;
ﭻﭼﭽﭾ
26:66 Nu daldi labal ña ca des [Firawna ak i gaayam].
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
26:67 Kéemaan a ngi ci biir loolu te taxut woon li ëpp ci ñoom gëm.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
26:68 Te sa Boroom, mooy Boroom kàttan, di Jaglewaakoon ba.
ﮏﮐﮑﮒﮓ
26:69 Jàngal-leen xibaari Ibraahiima:
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
26:70 Ba mu waxee baayam ak u nitam, ne leen : “Lu ngeen di jaamu ? ”
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
26:71 Ñu ne ko : “Ay xërëm lanuy jaamu, te gëm ko lool”.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
26:72 Ibraahiima ne leen : “Ndax danañu leen dégg bu ngeen leen di woo ?
ﮨﮩﮪﮫﮬ
26:73 walla ñu di leen jariñ mbaa ñu leen di lor ? ”
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
26:74 Ñu wax ne : “Nun kat, dañoo fekk rekk sunuy baay daan ko def”.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
26:75 Ibraahiima ne leen : “Xanaa gisuleen li ngeen di jaamu... ?
ﯛﯜﯝﯞ
26:76 Yéen ak seen maam ya fi woon ?
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
26:77 Ñoom ñépp sama noon lañu ku dul Yàlla Miy Boroom àddina si,
ﯦﯧﯨﯩﯪ
26:78 Moom mi ma bind te gindi ma ;
ﯫﯬﯭﯮﯯ
26:79 Mooy ki may leel di ma nàndal ;
ﯰﯱﯲﯳﯴ
26:80 su ma woppee, Mu faj ma,
ﯵﯶﯷﯸﯹ
26:81 Moo may rey, di ma dundal,
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
26:82 Mooy ki ma xemmem mu jéggal ma samay ñaawtéef bu Bis-pénc baa.
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
26:83 Yaw sama Boroom, may ma xam-xam te def ma joti ca gaa ñu baax ña ;
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
26:84 defal ma am làmmiñ wu dëggu;
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
26:85 def ma ma bokk ca way-donn ya Àjjanay xéewal ya.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
26:86 te Nga jéggal sama baay : moom dafa bokk ca ñu réer ña ;
ﭥﭦﭧﭨﭩ
26:87 te bul ma gàcceel kerook bisub dekki ba,
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
26:88 bis ba alal ak i doom du jariñati,
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
26:89 ku dul kay ñëw ca Yàllaak xol bu mucc ayib”.
ﭸﭹﭺﭻ
26:90 Ñu jigeeñal Àjjana ña ragal Yàlla.
ﭼﭽﭾﭿ
26:91 te gaaraleef na Safara ñeel ña béewoon,
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
26:92 Ñu wax leen ne : “Ana fan ngeen nekkoon di fa jaamoo,
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
26:93 bàyyi woon Yàlla ? Ndax mën nanoo dimbali seen bopp ? Walla ñu dimbali leen ? ”
ﮏﮐﮑﮒﮓ
26:94 Ñu sànni leen fa, galajaane leen ñook mboxos ma,
ﮔﮕﮖﮗ
26:95 ak gàngoorug Ibliis ga gépp.
ﮘﮙﮚﮛﮜ
26:96 Ñuy wax ca biir tey xuloo :
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
26:97 “Waat naa ci Yàlla ne ! Noo ngi woon ci réer gu bir,
ﮤﮥﮦﮧﮨ
26:98 jamono ya nu leen doon yemaleek Boroom àddina si.
ﮩﮪﮫﮬﮭ
26:99 Te tooñkat ya doŋŋ a nga nu sànk.
ﮮﮯﮰﮱﯓ
26:100 Amunu ku nu tinu,
ﯔﯕﯖﯗ
26:101 amuma it xarit bu may miisloo.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
26:102 Céy bu nu delluwaatoon àdduna, kon dananu bokk ca way-gëm ña ! ”
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
26:103 Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ; te taxut woon li ëpp ci ñoom gëm.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
26:104 Te sa Borom, mooy Boroom kàttan, di Jaglewaakoon ba.
ﯰﯱﯲﯳﯴ
26:105 Nitu Nooh ñoom weddi woon nañu Yonent ya,
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
26:106 ba leen seen mbokk ma Nooh waxee, ne leen : “Ndax dungeen ragal Yàlla ?
ﯽﯾﯿﰀﰁ
26:107 Man seenub Yonent laa bu wóor.
ﰂﰃﰄﰅ
26:108 Ragal-leen Yàlla te topp ma.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒ
26:109 Te laajuma leen ci génn pey ; samag pey Boroom àddina si moo ko warlu.
ﰓﰔﰕﰖ
26:110 Ragal-leen Yàlla te topp ma”
ﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝ
26:111 Ñu wax ko ne : “Ndax dananu la gëm te ñi gën a saay-saay a ngi la topp? ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
26:112 Mu wax ne : “Ana man lu ma xam ca la ñu daan def.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
26:113 Seenub waññoo nga ca Yàlla [Moo koy taxawe]. Céy bu ngeen yëgoon.
ﭡﭢﭣﭤﭥ
26:114 Man dey du maay dàq ñi gëm.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
26:115 Man doonuma lu dul ab xuppekat bu bir”.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
26:116 Ñu ne ko : “Yaw Nooh, soo bàyyiwul li nga nekk, dees na la jóori xeer [ba nga dee] ! ”
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
26:117 Mu ne : “Yaw sama Boroom, samaw nit weddi nañu, jàppe ma fenkat.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
26:118 Àtteel sama digganteek ñoom ba mu ne làññ : te nga musal maak ñi ma àndal te ñu bokk ca ña gëm”.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
26:119 Nu daldi koy musal mook ña mu àndaloon ci gaal ga mu duyyoon ba mu fees.
ﮌﮍﮎﮏﮐ
26:120 Ginnaaw ba, Nu labal ña ca des.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
26:121 Ay kéemaan a nga ci biir loolu. Te taxut woon la ëpp ci ñoom gëm.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
26:122 Te sa Boorm, Mooy boroom kàttan, di Jaglewaakoon.
ﮡﮢﮣﮤ
26:123 Waa Haad, weddi woon nañu Yonent ya, jàppe leen ay fenkat.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
26:124 Ba leen seen mbokk ma Huud waxee ne : “Ndax dangeen dul ragal Yàlla ? ”
ﮭﮮﮯﮰﮱ
26:125 Man dey, ab Yonent laa bu wóor,
ﯓﯔﯕﯖ
26:126 Ragal-leen Yàlla te topp ma.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
26:127 Duma leen ca laaj genn pey ; samag pey Boroom àddina see ko warlu.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
26:128 Ndax dangeen di tabax ci kaw wépp tundu ab jàjj ngir caaxaan ?
ﯪﯫﯬﯭﯮ
26:129 Ngeen di liggéey i njéndi mel ni dangeen fiy béel ?
ﯯﯰﯱﯲﯳ
26:130 Te saa su ngeen songee mu jéggi dayo.
ﯴﯵﯶﯷ
26:131 Ragal-leen Yàlla te topp ma.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
26:132 Ragal-leen Yàlla mi leen kàttanal ba ngeen mën a jëf,
ﯾﯿﰀﰁ
26:133 Moo leen may alal ak i doom,
ﰂﰃﰄ
26:134 ak tooli dër ak i dex.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
26:135 Man dey, ragal naa ci yéen mbugalum Bis bu màgg.
ﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
26:136 Ñu tontu wax ne : “Nga di nu waar ak nga ñàkk noo war a yem ci nun képp !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
26:137 Lii daal du lenn lu dul jikkoy mag ñu jëkk ña :
ﭗﭘﭙﭚ
26:138 Nun daal, kenn dunu mbugal”.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
26:139 Ñu weddi ko. Nu daldi leen mbugal. Te ca biir, ay kéemaan a nga ca ! Te taxul la ëpp ca ñoom gëm.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
26:140 Te sa Boroom, moo di Boroom kàttan, di Jaglewaakoon.
ﭮﭯﭰﭱ
26:141 Waa Samuuda, weddi woon nañu Yonent ya.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
26:142 Ba leen seen mbokk Saalihu waxee ne : “Moo ndax dungeen ragal Yàlla ? ”
ﭺﭻﭼﭽﭾ
26:143 Man mii dey, ab Yonent laa ci yéen bu wóor.
ﭿﮀﮁﮂ
26:144 Ragal-leen Yàlla te topp ma [samay ndigal].
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
26:145 Te duma leen ca laaj genn pey, samag pey Boroom àddina see ko warlu.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
26:146 Ndax jàpp ngeen ne dañu leen di bàyyi nii rekk ngeen ne fayax ?
ﮖﮗﮘﮙ
26:147 Ci biir tooli dër yeek dex yi,
ﮚﮛﮜﮝﮞ
26:148 ak mbey yi, ak tàndarma yii neex lool a reesal ?
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
26:149 Ngeen di yett ay kër ci tundu doj yi te njaxlaf lool ?
ﮥﮦﮧﮨ
26:150 Mu ne ragal-leen Yàlla waay te topp samay ndigal.
ﮩﮪﮫﮬﮭ
26:151 Te buleen topp mukk nag ndigalul ñiy sànkaate [xaaxaabal],
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
26:152 ñiy yàq rekk ci suuf si te duñu defar”.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
26:153 Ñu ne ko : “Yaw daal, ab njibar moo la ŋëb.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
26:154 Yaw daal, doo kenn ku dul nit ni nun. Indil kaawtéef ndegam li ngay wax dëgg la”.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
26:155 Saalihu ne leen : “Lii giléem gu jigéen la [naaga] : am na bis bu muy naan, yéen it am ngeen seen bis.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
26:156 Buleen ko def mukk lu bon, [su ngeen ko ko defee], di ngeen yendu bisub mbugal mu tar”.
ﯺﯻﯼﯽ
26:157 Ñu rey ko, daldi koy rëccu !
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
26:158 Mbugal ma dal leen. Ci biir loolu ay kéemaan a nga ca. Te taxul li ëpp ci ñoom gëm.
ﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
26:159 Te sa Boroom, moo Boroom kàtta, di Jaglewaakoon bi.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
26:160 Nitu Lóot weddi woon nañu Yonent ya,
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
26:161 ba leen seen mbokk ma Lóot waxee ne : “Moo ndax dungeen ragal Yàlla ?
ﭞﭟﭠﭡﭢ
26:162 Man mii dey, ab Yonent laa ci yéen bu wóor.
ﭣﭤﭥﭦ
26:163 Ragal-leen Yàlla te topp ma.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
26:164 Laajuma leen ci genn pey ; samag pey, Boroom àddina see ko warlu.
ﭴﭵﭶﭷﭸ
26:165 Yéen góor ñi, moo ndax dangeen di sàkku bànneexu séy ci góoru àddina sii [Ngóor- jigéen]?
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
26:166 Ne fa ñukk seen jabar ya leen Yàlla sàkkal ? Waajii ! Yéen ay jalgatikat ngeen de”.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
26:167 Ñu ne ko : “Yaw Lóot, boo bàyyiwul lii ngay wax, dananu la génne”.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
26:168 Lóot ne leen : “Seen jëf jii, lenn rekk laa ciy wax.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
26:169 Yaw sama Boroom, yal na nga musal maak saag njaboot ci lii ñuy def”.
ﮛﮜﮝﮞ
26:170 [Nun Yàlla] Nu daldi koy musal mook njabootam gépp,
ﮟﮠﮡﮢﮣ
26:171 ba mu des menn màggat mu àndoon ca mbokk ga.
ﮤﮥﮦﮧ
26:172 Topp [Nun Yàlla] Nu faagaagal ña des ;
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
26:173 Nu dottil leen [taw] waame doj. A ndaw taw bu bon ca ña mu dal !
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
26:174 Ay kéemaan a ngi ci biir loolu. Te taxul ña ëppoon ca ñoom gëm.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
26:175 Sa Boroom, Mooy Boroom kàttan, di Jaglewaakoon ba [yërmaandeem].
ﯡﯢﯣﯤﯥ
26:176 Waa Aykata weddi woon nañu Yonent ya.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
26:177 Ba leeen seen mbokk ma Suhaybu waxee ne : “Moo ndax dungeen ragal Yàlla”.
ﯭﯮﯯﯰﯱ
26:178 Man mii dey, ab Yonent laa ci yéen bu wóor.
ﯲﯳﯴﯵ
26:179 Ragal-leen Yàlla te topp ma [samay ndigal],
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
26:180 te duma leen ci laaj genn pey ; samag pey [Yàlla] Boroom àddina see ko warlu.
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
26:181 Nangeen di matal nattukaay yi, te buleen cay naxaate.
ﰋﰌﰍﰎ
26:182 bu ngeen dee màndaxe [peese], nay mat sëkk.
ﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘ
26:183 Buleen di ñormati ca yëfi nit ña [wattu ko] ; buleen di lawal asaru ci suuf si.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
26:184 Nangeen ragal Yàlla mi leen sàkk, mook maas ya leen jiitu woon”.
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
26:185 Ñu ne ko : “Yaw daal ag njibar moo la ŋëb ;
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
26:186 Te doo kenn ku dul nit ni nun ; nun sax foog nanu ne ci fenkat yi nga bokk.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
26:187 Waay-waay li nga ne su dee dëgg, rotalal ci sunu kaw ay dogiiti asamaan si ! ”
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
26:188 Suhaybu ne leen : “Sama Boroom a gën a xam li ngeen di def”.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
26:189 Ñu weddi ko. Mbugalum niir wa dal ca seen kaw. Doon mbugalum bis bu màgg.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
26:190 Ay kéemaan a ngi ci biir loolu. Te taxul ña ëppoon ca ñoom gëm.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
26:191 Te sa Boroom, Mooy Boroom kàttan, di Jaglewaakoon ba [yërmaandeem].
ﮓﮔﮕﮖﮗ
26:192 [Alxuraan jii], ci lu bir, wàcceg Boroom àddina si la,
ﮘﮙﮚﮛﮜ
26:193 Ruu gu wóor ga [Jibriil] moo ko wàccaale
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
26:194 def ko ci sa biir xol [yaw Muhammad] ngir nga bokk ca xuppekat ya,
ﮣﮤﮥﮦ
26:195 ci làmmeñu araab bu leer nàññ.
ﮧﮨﮩﮪﮫ
26:196 Te nekkoon na ca biir Téerey Yonent yu njëkk ya.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
26:197 Ndax amuñu woon ay kéemaan yu taxoon boroom xam-xami giir Banii-Israayiila xamoon ko ?
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
26:198 Su Nu ko wàcce woon ci ku dul ab araab,
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
26:199 mu jàngal leen ko, du tax kon ngeen gëm ko.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
26:200 Noonu it la nu dugalee jiixi-jaaxa ca biir xoli tooñkat yi ba gëmuñu ko ;
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
26:201 duñu ko gëm mukk ndare ba ñu gisee mbugal mu metti ma,
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
26:202 mu dikke leen ci mbettel te ñoom bëgguñu ko;
ﯸﯹﯺﯻﯼ
26:203 ñuy wax naan : “Ndax deesu yeexe sunuy mbir ? ”
ﯽﯾﯿ
26:204 Ndax dañoo yàkkamti Sunu mbugal ?
ﰀﰁﰂﰃﰄ
26:205 Xanaa gisuloo ne bàyyi woon Nanu leen ay ati at ñuy xaab-xaabi,
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
26:206 tey jii nag la Nu leen doon dig agsi na,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
26:207 la ñu bànneexu woon jariñatuleen dara.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
26:208 Amul benn dëkk bu Nu mës a alag u nitam te yónneewunu fa woon ay xuppekat,
ﭠﭡﭢﭣﭤ
26:209 di fàttali rekk, tooñunu kenn.
ﭥﭦﭧﭨﭩ
26:210 Alxuraan jii, séytaane yi wàccewuñu ko de :
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
26:211 Amuñu ko, mënuñu ko.
ﭰﭱﭲﭳﭴ
26:212 Ñoom mënuñoo dégg ndigali Yàlla.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
26:213 Bul jaamu lenn di ko booleek Yàlla, ku koy def rekk mbugal di dal ci sa kaw.
ﭿﮀﮁﮂ
26:214 Nangay xupp yaw [Muhammad] nit ñi la gën a jegeñ.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
26:215 Nangay suufeel sa bopp ci jullit ñi la topp [say ndigal].
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
26:216 Bu ñu moyee nag, neeleen : “Samaw yoon nekkatul ci li ngeen di def”.
ﮒﮓﮔﮕﮖ
26:217 Nangay wéeru ci Yàlla Miy Boroom kàttan tey Jaglewaakoonu yërmaande,
ﮗﮘﮙﮚﮛ
26:218 Moom mi lay gis boo taxawee,
ﮜﮝﮞﮟ
26:219 ak say jëfiin ba nga nekkee ci biir ñay sujjóot [julli].
ﮠﮡﮢﮣﮤ
26:220 Mooy dégg, di xam.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
26:221 Moo ndax Duma la xibaar ana kan la séytaane ya wàcce ca moom ?
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
26:222 Danañuy wàcc ci képp kuy ab duuraakoon bu bariy bàkkaar.
ﯓﯔﯕﯖﯗ
26:223 Ñooy yàng seen nopp di déglu... Te la ëpp ci ñoom fenkat lañu.
ﯘﯙﯚﯛ
26:224 Woykat ya nag, nitu mbalgas ya rekk a leen di topp.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
26:225 Xanaa gisoo ne ñoom ci xur wu nekk la ñu fay wëndeelu,
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
26:226 Te it dañuy wax lu ñu dul def ?
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
26:227 ba mu des woykat ya gëm, te jëf u yiw tey tudd lool Yàlla , ñuy sàkku ndam ci ginnaaw bu ñu leen tooñee. Tooñkat ya xalset nañoo xam naka la ñuy mujje!

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers