Simoore Al-Muzzammil
PDF —
20 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Muzzammil pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Muzzammil pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Muzzammil Tekki. Al-Muzzammil (Meccan) 20 Aaya.



Simoore Al-Muzzammil
20 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓ
Éy ! yaw, ku ñu sàng ki !
ﭔﭕﭖﭗﭘ
Jógal [di julli], ci guddi gi, bamu des lu ,néew ;
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Ab xaajam, walla sax nga wàññi ca lu tuuti ;
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
walla sax nga dolli ca. Te na ngay jàng Alxuraan, njàng mu léer.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Xalset nanu laa gàll wax ju diis.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Jullig guddi nag moo gëna nangu te moo gëna leer cim njàng.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Am nga, ci bëcëg bi, jot gu gudd goo mana lijantee.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Na ngay fàttaliku di tud sa turu Boroom te wéeru ci moom fàwwu,
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
mooy boroom Penkook Sowu. Amul jeneen Yàlla ju dul moom. Na nga wéeru ci moom.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Muñal li ñuy wax ; te nga gàddaay leen gàddaay gu rafet (bañ leena faale).
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Bàyyi maak ñiy weddi ak ñi am alal ; te nga muñal leen tuuti :
ﮜﮝﮞﮟﮠ
Noo ngi leen di waajal Safara wu ànd ak jéng,
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
ak aw ñam wuy fot loo, ànd ak mbugël mu mitti.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Bu keroogee bis ba suuf seek doj yi dëgg-dëgg tundu yi mel ni suufus ber mokk.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Yónni nanu ci yéen ab Yonent muy seede, kem ni nu yónnee woon ca Firawna ab Yonent.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Firawna daldi moy Yonenta ba. Nu daldi koy jël bu metti. (faagaagal ko).
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Ana naka ngeen di ragale (Yàlla), su ngeen weddee, bis boo xam ne tiit ma bijaawloona ab liir ?
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Su asamaan si dee xar. Ca la digam ba di mate.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Lii nag ag fàttali la. Képp ku mu soob mu jël yoon wa jëm ca Boroomam aw ca.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Sa Boroom xam na ne, yaw (Muhammad) da ngay taxawlu gëna néew ñaari ñetteeli xaaji guddi gi, walla xaaj ba, walla benn ñetteelu xaaj ba. Ànd kook mbooloo ci ña ànd ak yaw. Te Yàlla dana nattale guddeek bëccëg. Xam na ne manu leen fanaanee julli. Mu jégal leen. Jàngleen lu jàppandi ci Alxuraan. (Ndax moom Yàlla) xam na ne am na ci yéen ñu wopp, ak ñeneen ñuy tukki ji ci réew yi, ngir sàkku ji ci ngënéeli Yàlla yi, ak ñeneen ñuy xare ji ci yoonu Yàlla. Kon jàngleen la ca jàppandi. Te na ngeen taxawal julli, tey génne asaka, te na ngeen lebal Yàlla bor bu rafet. Te lépp lu ngeen jiitalal seen bopp ciw yiw, da ngeen ko fekk ci Yàlla, mooy la gën te moo ëpp ag pey. Te it na ngay jéggalu Yàlla. Yàlla moom Jéggalaakoon la Jaglewaakoon la.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers