Simoore Al-Muddaththir
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Muddaththir pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Muddaththir pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Muddaththir Tekki. Al-Muddaththir (Meccan) 56 Aaya.
Related
- Al-Muddaththir TekkiWolof
- Al-Muddaththir mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Muddaththir

ﮪﮫﮬ
Éey, yaw Ku ñu muur ki!
ﮭﮮﮯ
Neel ñokket jóg tey xuppe.
ﮰﮱﯓ
Te na ngay màggal sa Boroom.
ﯔﯕﯖ
Te na ngay laabal say yéere.
ﯗﯘﯙ
Te it na ngay daw bépp bàkkaar.
ﯚﯛﯜﯝ
Bul di joxe mukk ngir sàkku ca lu gëna bari.
ﯞﯟﯠ
Te na ngay muñ ngir sa Boroom.
ﯡﯢﯣﯤﯥ
Saasu ñu walee ca mbiib ga,
ﯦﯧﯨﯩﯪ
su boobaa bis bu jafeñ lay doon,
ﯫﯬﯭﯮﯯ
du yomb ca yéefar ya de.
ﯰﯱﯲﯳﯴ
Bàyyi Ma ak ki nga xam ne maa ko bindoon nu wéet,
ﯵﯶﯷﯸﯹ
te ma joxoñ ko alal ju yaatu,
ﯺﯻﯼ
ak doom yu ko daan wéttali,
ﯽﯾﯿﰀ
te Ma dindiloon ko bépp jafe-jafe.
ﰁﰂﰃﰄﰅ
te mo daan xemmeem saa su nekk Ma di ko dolli.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Te kat des na ! Ndax moom da daan lànk di bañ (Al xuraan) ji.
ﰍﰎﰏ
Danaa ko sonale yéegu tundu.
ﰐﰑﰒﰓ
Moom day xalaat. Na daldi soobu.
ﭑﭒﭓﭔ
Nu daldi koy rey ! Ca na mu sóobóo !
ﭕﭖﭗﭘﭙ
Topp Nu reyaat ko ; Ca na mu sóobóo woon !
ﭚﭛﭜ
Mu daldi, xool.
ﭝﭞﭟﭠ
Daldi nay gaññ te sóomórlu.
ﭡﭢﭣﭤ
Topp mu daldi dumóoyu tey rëy-rëylu.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Mu daldi wax ne : “Alxuraan jii daal ag njibar doŋŋ la
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
lii daal du leen lu dul waxi nit”.
ﭲﭳﭴ
Kookee dey danaa ko lakk ci Safaraw (Saqar).
ﭵﭶﭷﭸﭹ
Ana kan moo lay xamal luy Saqar ?
ﭺﭻﭼﭽﭾ
Du bàyyi dara ;
ﭿﮀﮁ
Dafay alawtiku ab der di ko xëmël.
ﮂﮃﮄﮅ
Fukki (Malaaka) ak juróom-ñanant koy wattu.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Ay Malaaka rekk ay wattu Safara. Te, lu ñuy bari bari nekku wu ñu fa lu dul fitnaal yéefar yi, ak tiiñal ñoñ Téere, ak dolli ngëmug ña gëmoon, ak it ñoñ Téere ak way gëm ña baña dengi-dengi ; ak it ngir yéefar yaak ña seeni xol wopp di wax naan : “Ana lu Yàlla namm ci misaal mii ? ” Noonu la Yàlla réerële ku ko soob di gindi it ku ko soob. Te sa xarekati Boroom, Moom doŋŋ leen xam. Te lii du lenn lu dul luy fàttali bindéef yi jàjj leen.
ﯥﯦﯧ
Déet !... maa ngi giñ ci weer wi !
ﯨﯩﯪﯫ
Ak ci guddi su nee wërëñ !
ﯬﯭﯮﯯ
Ak su fajar si di xar!
ﯰﯱﯲﯳ
[Safaraw Saqar] bokk na ca tiis yi gëna rëy
ﯴﯵﯶ
ag xuppe la, ñeel bindéef yi.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Ku mu soob ci yéen, na jiitu walla mu des ginnaaw.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Bakkan bu mu mana doon ag tayle la ci jëfam.
ﰅﰆﰇﰈ
Ba mu des waa ndeyjoor :
ﰉﰊﰋﰌ
ñoom ña nga ca biir Àjjana di laajante
ﰍﰎﰏ
ci mbirum tooñkat ya :
ﰐﰑﰒﰓﰔ
“(Naan) Ana lan mooleen wara duggloo Safaraw Saqar ? ”
ﰕﰖﰗﰘﰙﰚ
Ñu tontu ne : “Nun kat danu daawul julli,
ﰛﰜﰝﰞﰟ
te daawune leel miskiin yi,
ﰠﰡﰢﰣﰤ
te danu daan ànd ak caaxankat ya,
ﰥﰦﰧﰨﰩ
te danu daan weddi bis Penc bi,
ﰪﰫﰬﰭ
ba dee aksi ci sunu kaw”.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
Rammug rammukat, du leen fa jariñ dara.
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Ana lan moo leen dëdëleek fàttaliku ?
ﭜﭝﭞﭟ
Dañoo mel ni ñu ñu tiital (ay mbaam),
ﭠﭡﭢﭣ
ni ñuy dawe gaynde.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Kenn ku nekk ci ñoom bëggoon na ñu jox ko ay kayit yu teqalikoo.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Dee wa laay ! Ñoom ragalu ñu woon àllaaxira.
ﭵﭶﭷﭸ
Mukk ! Te lii ag fàttali la.
ﭹﭺﭻﭼ
Kéep ku mu soob, na fàttaliku.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Te manuñoo fàttaliku lu dul ci bu soobee Yàlla. Te moo gëna yayoo ci ragal ko ; te moom doŋŋa am njégël.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







