Simoore Al-Jinn
28 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Waxal ne : “Soloof na ma am na mbooleem jinne muy déglu, bay wax naan : “Nun dey dégg nanu Ñjàngum [Alxuraan] mu yéeme,
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
dafay gindee jëme ci njub. Nu daldi koy gëm, te dunu bokkaale dara ci sunu Boroom.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Te sunu Boroom - màggam ga sell na - jàppewul kenn muy soxnaam, waxatumalaa doomam !
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Sunu kannas ma [Ibliis] moodaan wax ay njaxum ci Yàlla.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Te foog na ne nit ak jinne amul kenn ku cay fenal Yàlla.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Amoon ci nit, aw gaay ñu daan sàkku ay muslaay ci aw gaay ñu bokk ci jinne yi ñu faf leen dolli jaaxle (njaaxum).
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Te ñoom dañoo jortu li ngeen jortoon ci ne Yàlla yónniwul kenn.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
te Nun kat làmbu Nanu asamaan si fekk mu fees dell ak i wattukat ak jumi safara.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Te nun danu fa daan toog di yadu. Leegi nag képp ku fay jéema yëdu ji, dana fa fekk ab jum bu koy tuŋlu.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Te nun sax xamu nu ndax ñi nekk ci suuf si aw ay lees namm ci ñoom walla seen Boroom dafa namm ci ñoom ñu jub.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Am na ci nun ñu jub am na it ñu yées loolu : nun daal ay kurél lanu yu limu.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Te xam nanu ne manuñoo tiiñ Yàlla te it manuñoo daw mukk ba raw ko.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Te nun ba nu déggee njub ga [Alxuraan], gëm nanu ko, te nag képp ku gëm Boroomam dootul ragal wàññikug jëf waxantumalaak sànje.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Am na ci nun ay jullit, am na it ci nun ay tooñkat. Ña nga xam ne ñoom dañoo tuub defi jullit ñoo ñaa làmboo njub.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Tooñkat ya nag, ñoom ñoo di mattum safara.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Te kat su ñu jaaroon ca yoon wu jub xocc wa, Danaa leen nàndale, ndox mu neex,
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
ngir nu nattu leen ca. Képp ku dumóoyu baña fàttaliku Boroomam, (Yàlla) dana ko sóob ci mbugël muy dolliku saa su nekk.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Jàkka yi Yàlla moo leen moom : buleen fay woo kenn di ko booleek Yàlla.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Te kat ba jaamub Yàlla bi taxawee di ñaan Boroomam, xawnañoo raj-rajloo ca kawam.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Waxal ne : “Maa ngi ñaan sama Boroom te duma ko bokkaaleek kenn”.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Waxal ne: “man mii kat manuma leen a lor manuma leen a jubbanti ”.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Waxal it ne: “man mii keen manumaa aar ci Yàlla, te it duma wut benn rawtukaay budul moom.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Manuma lu dul jottali ndigëlul Yàlla. Waaye képp ku moy Yàlla akub Yonentam ca Safara sa lay sax te dafay béel ba fàww.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Ba bis ba ñu gisee la ñu leen daan tëkkoo, danañu xala xam ana kan moo gën ñàkk ndimbal ak ana kan moo gën a néew lim.
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Waxal ne: “Xamuma baxam li ñu leen di tëkkoo dafa jiggeñ, walla, sama Boroom da leen may ab dig.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
[Moom] moo xam kumpa. Te du wuññil kumpaam ga kenn,
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
lu dul ku mu gëram ci Yonent te dakoy booleek ñu koy wattu kanam ak ginnaaw,
ﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘ
ngir mu xam ne jotal nañu seen Yonentub Boroom. Te it peeg na lépp lu ne ci ab lim (xam na na mu day”.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers