An-Nahl · 106/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
مَن كَفَرَ بِاللَّهِ مِن بَعْدِ إِيمَانِهِ إِلَّا مَنْ أُكْرِهَ وَقَلْبُهُ مُطْمَئِنٌّ بِالْإِيمَانِ وَلَٰكِن مَّن شَرَحَ بِالْكُفْرِ صَدْرًا فَعَلَيْهِمْ غَضَبٌ مِّنَ اللَّهِ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ ۝١٠٦
man kafara billaahi mim ba`di eemaanihee illaa man ukriha wa qalbuhoo mutmma`innum bil eemaani wa laakim man sharaha bilkufri sadran fa`alaihim ghadabum minal laahi wa lahum `azaabun `azeem
📖 Tekkim Wolof
Ku weddi Yàlla ginnaaw ba mu gëmee... - ku dul ka ñu not fekk xelam sax na ci gëm Yàlla - ak ña ubbi seen dënn cig kéefar, mer mu tukkee ca Yàlla dana leen sadd te ñeel na leen mbugal mu màgg.

🎧 Dégg


📜 Aaya 104-108 — An-Nahl

104إِنَّ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ لَا يَهْدِيهِمُ اللَّهُ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne gëmuñu kàdduy Yàlla yi, Yàlla duleen gindi. Te ñeel na leen mbugal mu metti.
105إِنَّمَا يَفْتَرِي الْكَذِبَ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ ۖ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْكَاذِبُونَ
Ca dëgg-dëgg ñay duur ay fen ñooy ña gëmul kàdduy Yàlla yi, ñoom ñooy fenkat yi.
106مَن كَفَرَ بِاللَّهِ مِن بَعْدِ إِيمَانِهِ إِلَّا مَنْ أُكْرِهَ وَقَلْبُهُ مُطْمَئِنٌّ بِالْإِيمَانِ وَلَٰكِن مَّن شَرَحَ بِالْكُفْرِ صَدْرًا فَعَلَيْهِمْ غَضَبٌ مِّنَ اللَّهِ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Ku weddi Yàlla ginnaaw ba mu gëmee... - ku dul ka ñu not fekk xelam sax na ci gëm Yàlla - ak ña ubbi seen dënn cig kéefar, mer mu tukkee ca Yàlla dana leen sadd te ñeel na leen mbugal mu màgg.
107ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمُ اسْتَحَبُّوا الْحَيَاةَ الدُّنْيَا عَلَى الْآخِرَةِ وَأَنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْكَافِرِينَ
Li waral loolu moo di dañoo tànn dundug àddina ci kaw dundug àllaaxira. Te nag Yàlla du gindi aw nit ñu di ay yéefar.
108أُولَٰئِكَ الَّذِينَ طَبَعَ اللَّهُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ وَسَمْعِهِمْ وَأَبْصَارِهِمْ ۖ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْغَافِلُونَ
Ñooñooy ña Yàlla fatt seeni xol, ak seeni dégg-dégg, ak seeni gis-gis. Te ñoom ñooy ña sàggan.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
106Aaya

Tekki — An-Nahl 106

Simoore An-Nahl Aaya 106 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ku weddi Yàlla ginnaaw ba mu gëmee... - ku dul…

Simoore Aaya 106/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 104–108. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers