Al-Baqara · 173/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
إِنَّمَا حَرَّمَ عَلَيْكُمُ الْمَيْتَةَ وَالدَّمَ وَلَحْمَ الْخِنزِيرِ وَمَا أُهِلَّ بِهِ لِغَيْرِ اللَّهِ ۖ فَمَنِ اضْطُرَّ غَيْرَ بَاغٍ وَلَا عَادٍ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝١٧٣
Innamaa harrama `alaikumul maitata waddama wa lahmal khinzeeri wa maaa uhilla bihee lighairil laahi famanid turra ghaira baaghinw wa laa `aadin falaaa isma `alaih; innal laaha Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
La mu araamal [tere] mooy médd, dereet, yàppu mbaam-xuux ak la ñu tuddu keneen ku dul Yàlla [ba ñu koy rey]. Ku ñàkk pexe nag ci lu dul beew walla jéggi dayo, du am bàkkaar ci xettaliku [ci yooyu], Yàlla Jéggalaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 171-175 — Al-Baqara

171وَمَثَلُ الَّذِينَ كَفَرُوا كَمَثَلِ الَّذِي يَنْعِقُ بِمَا لَا يَسْمَعُ إِلَّا دُعَاءً وَنِدَاءً ۚ صُمٌّ بُكْمٌ عُمْيٌ فَهُمْ لَا يَعْقِلُونَ
Ña weddi dañu mel ni ay mala yoo xam ne kàddu duñu ca dégg lu dul coow la. Ñu tëx lañu, gumba, luu, duñu xel-lu.
172يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُلُوا مِن طَيِّبَاتِ مَا رَزَقْنَاكُمْ وَاشْكُرُوا لِلَّهِ إِن كُنتُمْ إِيَّاهُ تَعْبُدُونَ
Ey yéen ñi gëm ! Lekkleen ci yi teey ci lun leen wërsëgal. Te ngeen sant Yàlla, su fekkee moom ngeen di jaamu.
173إِنَّمَا حَرَّمَ عَلَيْكُمُ الْمَيْتَةَ وَالدَّمَ وَلَحْمَ الْخِنزِيرِ وَمَا أُهِلَّ بِهِ لِغَيْرِ اللَّهِ ۖ فَمَنِ اضْطُرَّ غَيْرَ بَاغٍ وَلَا عَادٍ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
La mu araamal [tere] mooy médd, dereet, yàppu mbaam-xuux ak la ñu tuddu keneen ku dul Yàlla [ba ñu koy rey]. Ku ñàkk pexe nag ci lu dul beew walla jéggi dayo, du am bàkkaar ci xettaliku [ci yooyu], Yàlla Jéggalaakoon la.
174إِنَّ الَّذِينَ يَكْتُمُونَ مَا أَنزَلَ اللَّهُ مِنَ الْكِتَابِ وَيَشْتَرُونَ بِهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۙ أُولَٰئِكَ مَا يَأْكُلُونَ فِي بُطُونِهِمْ إِلَّا النَّارَ وَلَا يُكَلِّمُهُمُ اللَّهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ وَلَا يُزَكِّيهِمْ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne dañuy nëbb la Yàlla wàcce ca téere ba jaaye ko njëg gu néew, ñooña Safara lañuy lekk ca seeni biir. Bu Bis-pénc baa, Yàlla du wax ak ñoom, duleen sellal. Te am nañu mbugal mu tar.
175أُولَٰئِكَ الَّذِينَ اشْتَرَوُا الضَّلَالَةَ بِالْهُدَىٰ وَالْعَذَابَ بِالْمَغْفِرَةِ ۚ فَمَا أَصْبَرَهُمْ عَلَى النَّارِ
Ñooña ñooy jaay njub weccee ko ak réer, jaay njéggal wecee ko ak mbugal. Ñooñu ana kan moo leen gën a mën a dékku Safara?
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
173Aaya

Tekki — Al-Baqara 173

Simoore Al-Baqara Aaya 173 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : La mu araamal [tere] mooy médd, dereet, yàppu mbaam-xuux ak…

Simoore Aaya 173/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 171–175. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers