Al-Baqara · 172/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُلُوا مِن طَيِّبَاتِ مَا رَزَقْنَاكُمْ وَاشْكُرُوا لِلَّهِ إِن كُنتُمْ إِيَّاهُ تَعْبُدُونَ ۝١٧٢
Yaaa ayyuhal lazeena aamanoo kuloo min taiyibaati maa razaqnaakum washkuroo lillaahi in kuntum iyyaahu ta`budoon
📖 Tekkim Wolof
Ey yéen ñi gëm ! Lekkleen ci yi teey ci lun leen wërsëgal. Te ngeen sant Yàlla, su fekkee moom ngeen di jaamu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 170-174 — Al-Baqara

170وَإِذَا قِيلَ لَهُمُ اتَّبِعُوا مَا أَنزَلَ اللَّهُ قَالُوا بَلْ نَتَّبِعُ مَا أَلْفَيْنَا عَلَيْهِ آبَاءَنَا ۗ أَوَلَوْ كَانَ آبَاؤُهُمْ لَا يَعْقِلُونَ شَيْئًا وَلَا يَهْتَدُونَ
Bu ñu leen nee : “Toppleen li Yàlla wàcce”, ñu ne : “Nun kay la nu miin [di ko jaamu, baaxu maam ya] lanuy topp.” - Moo ndax ! Seen baay ya doonuñu woon ñu dul xalaat, ñu dul gindiku ?
171وَمَثَلُ الَّذِينَ كَفَرُوا كَمَثَلِ الَّذِي يَنْعِقُ بِمَا لَا يَسْمَعُ إِلَّا دُعَاءً وَنِدَاءً ۚ صُمٌّ بُكْمٌ عُمْيٌ فَهُمْ لَا يَعْقِلُونَ
Ña weddi dañu mel ni ay mala yoo xam ne kàddu duñu ca dégg lu dul coow la. Ñu tëx lañu, gumba, luu, duñu xel-lu.
172يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُلُوا مِن طَيِّبَاتِ مَا رَزَقْنَاكُمْ وَاشْكُرُوا لِلَّهِ إِن كُنتُمْ إِيَّاهُ تَعْبُدُونَ
Ey yéen ñi gëm ! Lekkleen ci yi teey ci lun leen wërsëgal. Te ngeen sant Yàlla, su fekkee moom ngeen di jaamu.
173إِنَّمَا حَرَّمَ عَلَيْكُمُ الْمَيْتَةَ وَالدَّمَ وَلَحْمَ الْخِنزِيرِ وَمَا أُهِلَّ بِهِ لِغَيْرِ اللَّهِ ۖ فَمَنِ اضْطُرَّ غَيْرَ بَاغٍ وَلَا عَادٍ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
La mu araamal [tere] mooy médd, dereet, yàppu mbaam-xuux ak la ñu tuddu keneen ku dul Yàlla [ba ñu koy rey]. Ku ñàkk pexe nag ci lu dul beew walla jéggi dayo, du am bàkkaar ci xettaliku [ci yooyu], Yàlla Jéggalaakoon la.
174إِنَّ الَّذِينَ يَكْتُمُونَ مَا أَنزَلَ اللَّهُ مِنَ الْكِتَابِ وَيَشْتَرُونَ بِهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۙ أُولَٰئِكَ مَا يَأْكُلُونَ فِي بُطُونِهِمْ إِلَّا النَّارَ وَلَا يُكَلِّمُهُمُ اللَّهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ وَلَا يُزَكِّيهِمْ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne dañuy nëbb la Yàlla wàcce ca téere ba jaaye ko njëg gu néew, ñooña Safara lañuy lekk ca seeni biir. Bu Bis-pénc baa, Yàlla du wax ak ñoom, duleen sellal. Te am nañu mbugal mu tar.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
172Aaya

Tekki — Al-Baqara 172

Simoore Al-Baqara Aaya 172 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ey yéen ñi gëm ! Lekkleen ci yi teey ci…

Simoore Aaya 172/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 170–174. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers