Al-Hajj · 31/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
حُنَفَاءَ لِلَّهِ غَيْرَ مُشْرِكِينَ بِهِ ۚ وَمَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَكَأَنَّمَا خَرَّ مِنَ السَّمَاءِ فَتَخْطَفُهُ الطَّيْرُ أَوْ تَهْوِي بِهِ الرِّيحُ فِي مَكَانٍ سَحِيقٍ ۝٣١
Hunafaaa`a lillaahi ghaira mushrikeena bih; wa mai yushrik billaahi faka annamaa kharra minas samaaa`i fatakh tafuhut tairu aw tahwee bihir reehu bee makaanin saheeq
📖 Tekkim Wolof
Nangeen doon ñuy sellal ngir Yàlla (ñu àndul ak bokkaale) ; ku bokkaale ak Yàlla, dangay mel ni ku rëcc jóge asamaan, njanaaw fëkk ko walla ngelaw sànni ko barab bu sore.
🎧 Dégg

📜 Aaya 29-33 — Al-Hajj

29ثُمَّ لْيَقْضُوا تَفَثَهُمْ وَلْيُوفُوا نُذُورَهُمْ وَلْيَطَّوَّفُوا بِالْبَيْتِ الْعَتِيقِ
Bu ñu noppee, nañu dindi seeni tilim, sangu, wattu, mottali seeni yéene, daldi wër néeg bu yàgg a yàgg ba (Kaaba ga)”.
30ذَٰلِكَ وَمَن يُعَظِّمْ حُرُمَاتِ اللَّهِ فَهُوَ خَيْرٌ لَّهُ عِندَ رَبِّهِ ۗ وَأُحِلَّتْ لَكُمُ الْأَنْعَامُ إِلَّا مَا يُتْلَىٰ عَلَيْكُمْ ۖ فَاجْتَنِبُوا الرِّجْسَ مِنَ الْأَوْثَانِ وَاجْتَنِبُوا قَوْلَ الزُّورِ
Looloo wér, te képp ku màggal jaamukaayu Yàlla ba, loolumoo gën ci moom fa Boroomam. Te mu dagan ci yéen juri kër yi ginnaaw ya mu leen limal (ca saaru Ndën la). Kon nangeen wattandiku sobes xërëm yi te wattandiku waxi caaxaan, ay fen.
31حُنَفَاءَ لِلَّهِ غَيْرَ مُشْرِكِينَ بِهِ ۚ وَمَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَكَأَنَّمَا خَرَّ مِنَ السَّمَاءِ فَتَخْطَفُهُ الطَّيْرُ أَوْ تَهْوِي بِهِ الرِّيحُ فِي مَكَانٍ سَحِيقٍ
Nangeen doon ñuy sellal ngir Yàlla (ñu àndul ak bokkaale) ; ku bokkaale ak Yàlla, dangay mel ni ku rëcc jóge asamaan, njanaaw fëkk ko walla ngelaw sànni ko barab bu sore.
32ذَٰلِكَ وَمَن يُعَظِّمْ شَعَائِرَ اللَّهِ فَإِنَّهَا مِن تَقْوَى الْقُلُوبِ
Noonu la. Képp ku màggal jaamukaayu Yàlla, na xam ne màggal googu bokk na ca ragalug Yàlla ci xol yi.
33لَكُمْ فِيهَا مَنَافِعُ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ثُمَّ مَحِلُّهَا إِلَى الْبَيْتِ الْعَتِيقِ
Ñeel na leen ci loolu ay njariñ ba àpp bu ñu tudd ; te it seen barab ba ñuy loje ma nga ca Néeg bu yàgg a yàgg ba.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
31Aaya

Tekki — Al-Hajj 31

Simoore Al-Hajj Aaya 31 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nangeen doon ñuy sellal ngir Yàlla (ñu àndul ak bokkaale)…

Simoore Aaya 31/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 29–33. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers