Al-Ahzab · 13/73
Tekki Waxtaan — Al-Ahzab
وَإِذْ قَالَت طَّائِفَةٌ مِّنْهُمْ يَا أَهْلَ يَثْرِبَ لَا مُقَامَ لَكُمْ فَارْجِعُوا ۚ وَيَسْتَأْذِنُ فَرِيقٌ مِّنْهُمُ النَّبِيَّ يَقُولُونَ إِنَّ بُيُوتَنَا عَوْرَةٌ وَمَا هِيَ بِعَوْرَةٍ ۖ إِن يُرِيدُونَ إِلَّا فِرَارًا ۝١٣
Wa iz qaalat taaa`ifatum minhum yaaa ahla Yasriba laa muqaamaa lakum farji`oo; wa yastaazina fareequm minhumun Nabiyya yaqooloona inna buyootanaa `awrah; wa maa hiya bi`awratin iny yureedoona illaa firaaraa
📖 Tekkim Wolof
Ak ba mu amee kurél ci ñoom buy wax naan : “Yéen waa Yasriba [Madina] ! Buleen fa toog. Delluleen [ginnaaw]”. Mu am it kurél ci ñoom buy ñaan ndigal Yonent bi, di wax naan : “Sunuy kër dafa aaruwul”, du loolu de : waaye dañoo bëggoon a daw doŋŋ.
🎧 Dégg

📜 Aaya 11-15 — Al-Ahzab

11هُنَالِكَ ابْتُلِيَ الْمُؤْمِنُونَ وَزُلْزِلُوا زِلْزَالًا شَدِيدًا
Foofee la Nu nattoo jullit ña, yëngal leen yëngal gu tar.
12وَإِذْ يَقُولُ الْمُنَافِقُونَ وَالَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ مَّا وَعَدَنَا اللَّهُ وَرَسُولُهُ إِلَّا غُرُورًا
Ak ba naaféq ya ak ña seen xol tawat di wax naan : “Yàlla ak Yonentam diguñu nu lu dul ay nax”.
13وَإِذْ قَالَت طَّائِفَةٌ مِّنْهُمْ يَا أَهْلَ يَثْرِبَ لَا مُقَامَ لَكُمْ فَارْجِعُوا ۚ وَيَسْتَأْذِنُ فَرِيقٌ مِّنْهُمُ النَّبِيَّ يَقُولُونَ إِنَّ بُيُوتَنَا عَوْرَةٌ وَمَا هِيَ بِعَوْرَةٍ ۖ إِن يُرِيدُونَ إِلَّا فِرَارًا
Ak ba mu amee kurél ci ñoom buy wax naan : “Yéen waa Yasriba [Madina] ! Buleen fa toog. Delluleen [ginnaaw]”. Mu am it kurél ci ñoom buy ñaan ndigal Yonent bi, di wax naan : “Sunuy kër dafa aaruwul”, du loolu de : waaye dañoo bëggoon a daw doŋŋ.
14وَلَوْ دُخِلَتْ عَلَيْهِم مِّنْ أَقْطَارِهَا ثُمَّ سُئِلُوا الْفِتْنَةَ لَآتَوْهَا وَمَا تَلَبَّثُوا بِهَا إِلَّا يَسِيرًا
Ku leen doxe woon ginnaaw, ne leen na ñu weddi, kon ñu def ko, te duñu ca yéex,
15وَلَقَدْ كَانُوا عَاهَدُوا اللَّهَ مِن قَبْلُ لَا يُوَلُّونَ الْأَدْبَارَ ۚ وَكَانَ عَهْدُ اللَّهِ مَسْئُولًا
te la ko jiitu, fekkoon na ñu daalante ak Yàlla te dañoo wone ginnaaw [daw xare]. Te daalanteb Yàlla, lu ñuy lijjanti lay doon.
Al-AhzabFihi Alxuraan
73Aaya
MedinanRevelation
13Aaya

Tekki — Al-Ahzab 13

Simoore Al-Ahzab Aaya 13 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ak ba mu amee kurél ci ñoom buy wax naan…

Simoore Aaya 13/73 — Al-Ahzab الأحزاب (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahzab Dégg, Al-Ahzab Tekki, Al-Ahzab mp3, Al-Ahzab pdf. Aaya 11–15. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers